sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
88
11
{ "fr": "où ils n´entendent aucune futilité.", "wo": "doo fa degg mukk waxi caaxaan." }
88
12
{ "fr": "Là, il y aura une source coulante.", "wo": "Am na fa, bëtu ndox buy daw-dawaan." }
88
13
{ "fr": "Là, des divans élevés", "wo": "Am na fa, ay lal yu kawe" }
88
14
{ "fr": "et des coupes posées", "wo": "ak ay kopp yu ñu teg" }
88
15
{ "fr": "et des coussins rangés", "wo": "ak ay ngegenaay yu ñu sësële" }
88
16
{ "fr": "et des tapis étalés.", "wo": "ak ay laltu yu ñu lal." }
88
17
{ "fr": "Ne considèrent-ils donc pas les chameaux, comment ils ont été créés,", "wo": "Xanaa dañoo xoolul ci giléem, naka lañu ko binde,(s)" }
88
18
{ "fr": "et le ciel comment il est élevé,", "wo": "ak ci asamaan si naka la nu ko yékëte," }
88
19
{ "fr": "et les montagnes comment elles sont dressées", "wo": "Saar 88 : Muuraakoon ba 26 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
88
19
{ "fr": "et les montagnes comment elles sont dressées", "wo": "ak ci tund doj yi naka la nu ko sampe" }
88
20
{ "fr": "et la terre comment elle est nivelée ?", "wo": "ak ci suuf si naka la nu ko maasalee ? " }
88
21
{ "fr": "Eh bien, rappelle ! Tu n´es qu´un rappeleur,", "wo": "Na ngay, fàttalee ! Ndax yaw ab fàttalikat nga," }
88
22
{ "fr": "et tu n´es pas un dominateur sur eux.", "wo": "te nootoo leen." }
88
23
{ "fr": "Sauf celui qui tourne le dos et ne croit pas,", "wo": "Lu ca dul ku dumóoyu tey weddi," }
88
24
{ "fr": "alors Allah le châtiera du plus grand châtiment.", "wo": "Yàlla dana ko mbugël mbugël mu gëna rëy." }
88
25
{ "fr": "Vers Nous est leur retour.", "wo": "Te ci Nun la ñuy déllusi." }
88
26
{ "fr": "Ensuite, c´est à Nous de leur demander compte.", "wo": "Ba noppi, te nun it nooy warloo laaj leen. " }
89
1
{ "fr": "Par l´Aube !", "wo": "Ci njël Maa ngi giiñ !" }
89
2
{ "fr": "et par les dix nuits !", "wo": "ak ci fukki guddi ya (fukki fani tabaski) !" }
89
3
{ "fr": "Par le pair et l´impair !", "wo": "Ak ci tóolent ak ci lu tóol !" }
89
4
{ "fr": "Et par la nuit quand elle s´écoule !", "wo": "Ak ci guddi gi suy tàmbali !" }
89
5
{ "fr": "N´est-ce pas là un serment, pour un doué d´intelligence ?", "wo": "Moo ndax nekk na ci loolu, ngiñul boroom xel ?" }
89
6
{ "fr": "N´as-tu pas vu comment ton Seigneur a agi avec les Aad", "wo": "Xanaa gisoo naka la sa Boroom def waa Aad" }
89
7
{ "fr": "[avec] Iram , [la cité] à la colonne remarquable,", "wo": "Iram, ma doon boroomi kenu," }
89
8
{ "fr": "dont jamais pareille ne fut construite parmi les villes ?", "wo": "yoo xam ne kemam amul ci menn réew ?" }
89
9
{ "fr": "et avec les Tamud qui taillaient le rocher dans la vallée ?", "wo": "ak waa Saamud ña daan yatt xeer ya ca xur ya ?" }
89
10
{ "fr": "ainsi qu´avec Pharaon, l´homme aux épieux ?", "wo": "ak Firawna, ma doonoon boroomi dàtt ?" }
89
11
{ "fr": "Tous, étaient des gens qui transgressaient dans [leurs] pays,", "wo": "Ñoom, ñoo gënoona bew ci réew yi," }
89
12
{ "fr": "et y avaient commis beaucoup de désordre.", "wo": "te ñu bariloon fa lool ag yàq." }
89
13
{ "fr": "Donc, ton Seigneur déversa sur eux un fouet du châtiment.", "wo": "Sa Boroom daldi leen sotti yarum mbugël." }
89
14
{ "fr": "Car ton Seigneur demeure aux aguets.", "wo": "Sa Boroom nag ma ngay fuglu." }
89
15
{ "fr": "Quant à l´homme, lorsque son Seigneur l´éprouve en l´honorant et en le comblant de bienfaits, il dit : \"Mon Seigneur m´a honoré\".", "wo": "Nit nag, moom saa su ko boroomam nattoo teral ko xéewal ko, mu ne : “Sama Boroom teral na ma” ." }
89
16
{ "fr": "Mais par contre, quand Il l´éprouve en lui restreignant sa subsistance, il dit : \"Mon Seigneur m´a avili\".", "wo": "Saa su ko nattoo wàññi wërsagëm, muy wax naan : “Sama Boroom toroxal nama” ." }
89
17
{ "fr": "Mais non ! C´est vous plutôt, qui n´êtes pas généreux envers les orphelins;", "wo": "Déedéet ! Yéen kay, du ngeen teral mukk jirim ak di tabe ci moom ;" }
89
18
{ "fr": "qui ne vous incitez pas mutuellement à nourrir le pauvre,", "wo": "te it du ngeen sonnu mukk ci di leel miskiin," }
89
19
{ "fr": "qui dévorez l´héritage avec une avidité vorace,", "wo": "te ngeen di lekk alal ndono lekkiin wu ñaaw, " }
89
20
{ "fr": "et aimez les richesses d´un amour sans bornes.", "wo": "te da ngeen bëgg alal bëgg gu tar." }
89
21
{ "fr": "Prenez garde ! Quand la terre sera complètement pulvérisée,", "wo": "(Bàyyileen xel) ! saa su nu walee suuf si ba mu di pëndax," }
89
22
{ "fr": "et que ton Seigneur viendra ainsi que les Anges, rang par rang,", "wo": "sa Boroom dikk ak malaaka ya, def ay sàppey sàppe," }
89
23
{ "fr": "et que ce jour-là, on amènera l´Enfer; ce jour-là, l´homme se rappellera. Mais à quoi lui servira de se souvenir ?", "wo": "bu keroogee, danuy indi Safarey jahanama ; bu keroogee it, nit dana fàttaliku. Waaye damaa xamut lu ko fàttaliku ga di jariñ ?" }
89
24
{ "fr": "Il dira : \"Hélas ! Que n´ai-je fait du bien pour ma vie future !", "wo": "Muy wax naan : “ Aka neexoon ! Ca ba muy dundu ma defoon lu baax !" }
89
25
{ "fr": "Ce jour-là donc, nul ne saura châtier comme Lui châtie,", "wo": "Bu keroogee, mbugël ma deefu ko mbugël kenn," }
89
26
{ "fr": "et nul ne saura garrotter comme Lui garrotte.", "wo": "Saar 89 : Njël 30 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
89
26
{ "fr": "et nul ne saura garrotter comme Lui garrotte.", "wo": "te it kenn du yolomal jéngam ba." }
89
27
{ "fr": "ô toi, âme apaisée,", "wo": "“Éy yaw, bakkan bi dalum xel," }
89
28
{ "fr": "retourne vers ton Seigneur, satisfaite et agréée;", "wo": "delul ca sa Boroom, di gërëm ñu dila gërëm ;" }
89
29
{ "fr": "entre donc parmi Mes serviteurs,", "wo": "tàbbil ca Samay jaam," }
89
30
{ "fr": "et entre dans Mon Paradis.", "wo": "tàbbil it ca Sama biir ¨Àjjana”." }
90
1
{ "fr": "Non ! ... Je jure par cette Cité !", "wo": "Déet !... Ma ngi giiñ ci dëkk bii !(r)" }
90
2
{ "fr": "et toi, tu es un résident dans cette cité -", "wo": "te yaw, sax ci dëkk bi nga dëkk" }
90
3
{ "fr": "Et par le père et ce qu´il engendre !", "wo": "Ak ci baay ak la mu jur !" }
90
4
{ "fr": "Nous avons, certes, créé l´homme pour une vie de lutte.", "wo": "Noo, bind nit muy jànkonteeki coono." }
90
5
{ "fr": "Pense-t-il que personne ne pourra rien contre lui ?", "wo": "Moo ndax dafa defe ni kenn manul ci moom dara ?" }
90
6
{ "fr": "Il dit : \"J´ai gaspillé beaucoup de biens\".", "wo": "Ma ngay wax naan : “Sànk naa alal ju bari” ." }
90
7
{ "fr": "Pense-t-il que nul ne l´a vu ?", "wo": "Moo ndax dafa defe ne kenn da koo gisul ?" }
90
8
{ "fr": "Ne lui avons Nous pas assigné deux yeux,", "wo": "Moo ndax defalunu ko ñaari gët," }
90
9
{ "fr": "et une langue et deux lèvres ?", "wo": "ak aw làmmiñ ak ñaari tuñ ?" }
90
10
{ "fr": "Ne l´avons-Nous pas guidé aux deux voies .", "wo": "Nu gindi ko tegtal ko ñaari yoon yi, mbaax, mbon." }
90
11
{ "fr": "Or, il ne s´engage pas dans la voie difficile ! ", "wo": "Te, moom moo lànka soobu yoon wu tënku wa (mitti) !" }
90
12
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est la voie difficile ?", "wo": "Ana lan moo lay xamal yoon wu tënku wa ?" }
90
13
{ "fr": "C´est délier un joug [affranchir un esclave],", "wo": "Moo di [goréel jaam]," }
90
14
{ "fr": "ou nourrir, en un jour de famine,", "wo": "mbaa joxe lekk, ci bisub xondooñ, xiif bu tar" }
90
15
{ "fr": "un orphelin proche parent", "wo": "ab jirim mba mbokk mu jige" }
90
16
{ "fr": "ou un pauvre dans le dénouement.", "wo": "walla ab miskiin bu fondóoñ." }
90
17
{ "fr": "Et c´est être, en outre, de ceux qui croient et s´enjoignent mutuellement l´endurance, et s´enjoignent mutuellement la miséricorde.", "wo": "Ba noppi, bokk ca, ña gëm tey dénkante ci muñ, di dénkante it ci yërmaande." }
90
18
{ "fr": "Ceux-là sont les gens de la droite;", "wo": "Ñooñee ñoo di waa ndeyjoor ;" }
90
19
{ "fr": "alors que ceux qui ne croient pas en Nos versets sont les gens de la gauche.", "wo": "ñay weddi sunuy Laaya ñoom ñoo di waa càmmoñ." }
90
20
{ "fr": "Le Feu se refermera sur eux.", "wo": "Safara waa ngi di gand. " }
91
1
{ "fr": "Par le soleil et par sa clarté !", "wo": "Ci jant beek leeram. Maa ngi giñ !" }
91
2
{ "fr": "Et par la lune quand elle le suit !", "wo": "Ak ci weer wi su ko dee topp !" }
91
3
{ "fr": "Et par le jour quand il l´éclaire !", "wo": "Ak ci bëcëg bi su ko muuree !" }
91
4
{ "fr": "Et par la nuit quand elle l´enveloppe !", "wo": "Ak ci guddi gi su ko muuree !" }
91
5
{ "fr": "Et par le ciel et Celui qui l´a construit !", "wo": "Ak ci asamaan seek ka ko tabax !" }
91
6
{ "fr": "Et par la terre et Celui qui l´a étendue !", "wo": "Ak ci suuf sek ka ko maasale !" }
91
7
{ "fr": "Et par l´âme et Celui qui l´a harmonieusement façonnée;", "wo": "Ak ci ruu geek Ka ko yemale ;" }
91
8
{ "fr": "et lui a alors inspiré son immoralité, de même que sa piété !", "wo": "moom mi ko ràññatleel mbaax, ak mbon !" }
91
9
{ "fr": "A réussi, certes celui qui la purifie.", "wo": "képp ku ko sellal, daldi nay texe." }
91
10
{ "fr": "Et est perdu, certes, celui qui la corrompt.", "wo": "te it, képp ku ko sàggane, daldi nay sooy." }
91
11
{ "fr": "Les Tamud, par leur transgression, ont crié au mensonge,", "wo": "Waa Saamuud, seen bewte, tax na ñu weddi," }
91
12
{ "fr": "lorsque le plus misérable d´entre eux se leva (pour tuer la chamelle)", "wo": "ba ca ña gën weddi potoxlóo" }
91
13
{ "fr": "Le Messager d´Allah leur avait dit : \"La chamelle d´Allah ! Laissez-la boire\"", "wo": "Yonentub Yàlla ba ne leen : “Bàyyileen giléemug Yàlla gi ! mu naan”" }
91
14
{ "fr": "Mais, ils le traitèrent de menteur, et la tuèrent. Leur Seigneur les détruisit donc, pour leur péché et étendit Son châtiment sur tous.", "wo": "Ñu weddi ko, rey ko. Seen Boroom, maasale na mbugël ma.ca kaw nit ñépp" }
91
15
{ "fr": "Et Allah n´a aucune crainte des conséquences :", "wo": "Te ragalul dara ca la cay mujj : " }
92
1
{ "fr": "Par la nuit quand elle enveloppe tous !", "wo": "Ci guddi gi saa su muuree lépp ! maa ngi giñ(s)" }
92
2
{ "fr": "Par le jour quand il éclaire !", "wo": "Ak ci bëcëg bi saa su leeree !" }
92
3
{ "fr": "Et par ce qu´Il a créé, mâle et femelle !", "wo": "Ak ci ki sàkk, góor ak jigéen !" }
92
4
{ "fr": "Vos efforts sont divergents.", "wo": "Seen jëf wuute na." }
92
5
{ "fr": "Celui qui donne et craint (Allah) ", "wo": "Képp kuy joxe te ragal (Yàlla)" }
92
6
{ "fr": "et déclare véridique la plus belle récompense", "wo": "te mu dëggël yoolub àllaaxira" }
92
7
{ "fr": "Nous lui faciliterons la voie au plus grand bonheur.", "wo": "Dananu ko jàppandalal yoon wu yomb wa." }
92
8
{ "fr": "Et quand à celui qui est avare, se dispense (de l´adoration d´Allah),", "wo": "Képp ku nay, te dumóoyu boroomam," }
92
9
{ "fr": "et traite de mensonge la plus belle récompense,", "wo": "te muy weddi yoolub àllaaxira," }
92
10
{ "fr": "Nous lui faciliterons la voie à la plus grande difficulté,", "wo": "Dananu ko jàppandalal yoon wu jafe wa," }
92
11
{ "fr": "et à rien ne lui serviront ses richesses quand il sera jeté (au Feu).", "wo": "te alalam du ko jariñ dara saa su ñu ko mbaqee (Safara)." }
92
12
{ "fr": "C´est à Nous, certes, de guider;", "wo": "Gindee, nun la war ;" }
92
13
{ "fr": "à Nous appartient, certes, la vie dernière et la vie présente.", "wo": "te Noo moom, dundug àddinaak àllaaxira." }
92
14
{ "fr": "Je vous ai donc avertis d´un Feu qui flambe", "wo": "Xuppnaa leen ci Safara wuy bérëx-bérëxi" }
92
15
{ "fr": "où ne brûlera que le damné,", "wo": "Saar 92 : Guddi ga 21 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
92
15
{ "fr": "où ne brûlera que le damné,", "wo": "ku texedi ka rekka cay xoyomu," }
92
16
{ "fr": "qui dément et tourne le dos;", "wo": "kay weddi tey dumóoyu ;" }