text
stringlengths 6
463
|
---|
Joxe woon na ab lim ciy tegtal. |
Dañuy jéem a teg doxaliin yu bare, donte loolu tekkiwul ne bésu joŋante bi, noonu lañuy doxale. |
Lii, gànnaaw bi ñu fésalee ci bokk-jokkoo gi ab bataaxal bu jëm ci jëwrin ji ñu dénk biir réew mi, Aali Nguy Njaay. |
Te mu araftu àndandoom yi : dinanu dem ci wote yi ci turu Bennoo Bokk Yaakaar (BBY). |
Lii lépp a tabax gëm-gëmu Umar Jara, Kilifa ci wàllu mën-mënu nit, Abbaas Ndaw, nekk na léegi bérébu liggéeyukaay bu am solo ngir dooleem ak nit ñu am solo ñi ko séq, maanaam ay jëmmi nite. |
Réewum Ginne dañu ko aj ci joŋantey ati 2019 ak 2021 ci CAN bu xale yi am wala yéesal fukk ak juróom-ñaari at (17), |
su ñu sukkandikoo ci mindum CAF ak kurélu réew mi yor futbal bi, dinañu fay lu toll ci téeméeri junniy dolaar (100 000). |
Gànnaaw ba ñu dëddoo àdduna, jàmbaari taskati xibaar yii di Yoro Jàllo, Usmaan ak Abu Mamadu Si, maa ngi leen di jaal këru liggéeyukaay gi, Leeral, seen njaboot ak bépp taskatu xibaar bu nekk Senegaal. |
Ci fukki at yu ànd ak ndimbal, wóor na ne jokkalante xarala yi dina war a mat ci sama xalaat, kon sunu nit ñi war nañoo mën a doxal loolu niki ni ñu koy amale ci diggante Aibd-Mbuur. |
Kiiraay gu mujj gi gën ci joŋante Ligue 1 bi jiitu na Alphonse Areola, Edouard Mendy, Benjamin Lecomte et Anthony Lopes. |
Lu weesu loolu, péncum ndawi réew mi béréb la bu dul càmbar koppar ak alal juy doon kumpa, |
toll ci lu ëpp juróom-ñetti milyaar, yu mbooloo ma fa ëpp di wote at mu nekk ci lu dul ànd ak lenni coow ak daraay saytu (du këri saytu alal yile di IGE wala Cours des comptes wala yeneen ak yeneen). |
Senegaal dina daje ëllëg ak réewum Kolombi, te Tahiti war na siggil réew miy dalal. |
Njombe yu teglantoo yii waraloon nañu ag jubbanti jëm ci koppar yiy dugg ci juuti yeek béréb yi ko yellool, |
ci jamonoy ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru mee atum 2016, cib xaalis bu toll ci juróom-benni milyaar ak juróomi téeméer ak juróom-ñett-fukk ak juróom-ñeenti milyoŋ ak juróom-ñaar téeméer ak juróom-ñetti junni ak juróom-ñeenti téeméer ak juróom-ñaar-fukk ak ñeent (6 589 708 974) ci xaalisu Seefaa yu ñu xaaje nii : cosaan juuti bi / lim yi. |
Masayeer Siise tabb nanu ko muy kiy topp ci njiit li, ak doon njiital British Petroleum ngir réewu Senegaal. |
Pólotig jeego yu am solo lay dox jëm ci taxawal càkkéef bu baax. |
Ci négandikug ndajeem daan mu toog yi, ak njëkk ndajeem géew mu tar mi ci seen digganteek Algérie alxames, futbalkati Sénégal yi ñoo ngi ci tanki toppandoo Egypte, Nigéria ak Maroc, yenn ci naataangoom yi ëpp solo, ñoom ñépp ñoo daan ci seen joŋante yu njëkk yi. |
Méngale kook LFR1 mi xaalisam bi dugg yem ci (2 964, 79) milyaar, te mu génne ci (gannaaw bor bi ñu wàcce) lu toll ci milyaar (3 398, 65) milyaar ci Seefaa ngir LFR1, naal bi fi nekk ngir ñu wote ko, am na ay yokkute yu toppantee nii milyaar (293, 66) milyaar ci Seefaa, (9,9%) boo jël, ak (310, 33) milyaar ci Seefaa, (9, 1%) ci njëg lu teew. |
Njiital kurélu basket gu Ndar-géej li fi nekk nii, Baaba Tànjãa nee na moom itam moo gën a am naqar ak lu ko metti, ndeke kenn ci ñi dëddu, bokkoon na ci mbooloom Leeral mi ñëwoon këram te Soxna Laaliya jiite woon ko ngir ay laaj ci basket bi. |
Kon naka la kurél gi di gàlloo ci ndoddu liggéeykat bi nekk ci waawu ki ko féete kaw te muy joxekatu ndigal li war a àddu ci tur ak ci jëmmi nguur gi ? |
Lefu mindum (CEP) mooy fi ñu war a leerale ne ci jenn jamono ji ñuy dégloo kàddoom ya (ndax jot nañu koo déglu ñaari yoon), |
Sang bi Maysa Njaay, njiital daaraay moomeel yi ci Ngor Almadi, taxaw na ci ne deful lu dul teewal Njiitu moomeel yi ci ndawal jubóole gi, |
waaye wax jooju mbindum yoonal mu Njiital réew mi ñu siife ci limu n°77-563 bu ñetti fan ci weeru Sulet atum 1977 wéddi na ko, te taxawal na ndaw loolu : kiy dalal moomeel yi ci Ngor Almadi doon na way-bokk ci yoon, lu wuuteek Njiital moomeel yi, mi bokkul ci wey-bokk yeek teewalkat yi. |
Jublu gi mooy fexe ba gaawal dugalug xarala yi ci nguuru Gauteng gi jaare ko ci samp nekkin gu am doole ci kéew gi. |
Leeral nanu ci ab téere bu génn bu yàggul ne ñiy jéem a soppi diine ji ci tëralinam ñu ngi weer seen bopp ba mel ni gune gu xamul dara. |
Fi mu nekk nii, waxtaan yi dinañu aju ci séddale goxu Kër Masaar, sos yeneen gox yu yees ci diwaanu Ndakaaru bi ak ñag gox-goxaan yi nekk ci diwaanu Kër Masaar, Pikin ak Tëngéej. |
Waaye wóor na ma ne juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ci téeméer boo jël (99%) ñi bëgg futbal dëgg def nañu ni man, di laaj njuréefu beneen joŋante bu ñàkk solo bi. |
Mën ngeen xoolante ciy bët, su fekkee ne kenn ci ñoom deewul ? |
Sang bi Faal, mi mënul a lijjante mbiri biir réew mi mu dëkk, du moom mooy indil dara réewu Tchad, lu dul yokk jaar-jaaram ci këyitu tegtalam geek am alal ju takku ngir waajal àllatereteem gi nga xam ne neex na ba noppi. |
Ci feneen fi, amoon na Zamalek mi kenn mënul a daane, noon meneen mbooloo mi, waa Angola yi bawoo ci Petro bu Luanda ci mujjantalu joŋante bi. |
Yombul di aar nit ku bëgg a dooni Njiit yor naal bu ame nii solo, ba pare di dugg ci coow yu ñàkke nii fayda. |
Kiy jëmmal mbooloom ndawi futbalkati réewum Portugal mi yëkkëti na màndargaam joŋante réew yi ci atum 2019 te ñoom ñu amoon ci ndam ci kanamu Pays-Bas. |
Jëwriñ ji gàlloo koom-koom beek koppar yi, Abdulaay Daawuda Jàllo ak njiitu Bànkub Àdduna bi te mu yor doxalinu xew-xew yi ci aju, Nathan Belete jàll nañu, àjjuma, ci xaatimu ñaari déggoo yu toll ci (150) milyoŋi ci xaalisu Seefaa, ngir ñu mën a fay ñaari naal yu jëm ci xëyu ndaw ñi, ak ay xeex yu jëm ci mbënd mi. |
Bi ma nekkoon di liggéeyal nguur gi, li ma daan jaaxal lool moo doonoon yeesalufg bagaasi taaral bérébu liggéey bi, te yi fi nekk soppeekuwuñu. |
Foofu la jafe-jafe bi féete ci mbir mii. |
Wala ci Senegaal ! Dale ci Seŋoor, A. Juuf, Laay Wàdd fekke nanu nun ñépp ay mbooloo yu mësul am, waaye seen mujjantal su ñëwee, dara du leen mën a aar !! |
Ci at mi, Senegaal dina fay lu ëpp ñetti téeméer ak juróom-fukki milyaar (350) ci bor booleek jafe-jafey askan wi : ñàkk xëyu ndaw ñi, mbey mi, napp amatul, ñàkk di wéy. |
Ci am réew mu namm ag yokkute, kaaraange gi dafa war a nekk yéegukaay bu wasaaroo ci diggante nguur gi, gox-goxaan yi ci réew meek askan wi. |
Dañu ma yóbbu ci béréb ya, fa laa fajoo paj mu njëkk mi ci fajkatu Caf bi, laataa ñu may yóbbu ci beneen fajukaay ba, loolu la wax dolli ci. |
Li am mooy, ki waroon a dooni tàggatkatu Paris Saint-Germain mujjee naa xaar ba Carlo Ancelotti àggaleel Pep Guardiola, ngir mu daan ponkalum Munich bi. |
Dëgg la, ndax ay sàndarma mës na ñoo dem sama kër yaay ca Sigicoor ngir nangufay kayiti parenaas. |
Indiwoo fi lu dul ay, ci dëkk bi, defoo fi dara, ba ci yëf yi gën a yomb muy jàmm, ay kàmbal nit, ak araftu kese. |
Tay jii, lu yées juróom-ñetti weer wi ñuy dugg ci xaalisu Eco bi, xalaat yépp a bokk daanaka : ab randal bu bees mënul ñàkk. |
US Monastir moo leen daan ci alxames ji ci njuréefu juróom-ñett-fukk ak juróom-benn ci juróom-benn-fukk ak ñaar (86-62). |
Lan moo tax amuñu ñaar fukk ak juroomi bérébi fajukaay yu yees? |
Li ko waral mooy Maki Sàll lekk na téeméeri milyaar yi, |
ba noppi bàyyi nootaatekat yi lekk lépp li waroon a jëm ci taxawal ay bérébi fajukaay, ay lekool ak sax bérébi kaaraange. |
Dooleel leen mbooloo ak kurél yiy xeex Koronaa yépp te fexe ba ni ñuy rootee ay koppar ak ni ñu koy jëfandikoo daldi leer. |
Loolu, ginnaaw kalaame boo xam ne laykat bii di Abdulaay Tin nekk njiitu Union Sociale libéral (USL). |
Ndax ci ni yoon tëddee fii ci Senegaal, man nañu jaay li ñu waroon a dàmpee ak nit, te muy méngook foqati, jëfandikoo ko ngir faj ci soxlay askan wi. |
Ginnaaw ba ñu amee ak tële ci won askanu Senegaal ni ñoo bokk lépp. |
Ki jiite bérébu bëre bi nekk Mbuur te mu joti koppar ngir bëre ak Bàlla Gay 2 ci bésu ñaar fukki fan ak juróom-benn ci weeru suweŋ biy ñëw, bëgg na itam dajeek Ëmmë Seen. |
Su ñu sukkandikoo ci Vox populi, tay la liggéeykati SDE yi gën a takku ngir indi ay jafe-jafe ci céddaleg ndox mi ci diwaanu Ndakaaru. Jootoon na ñoo fësal seen yéeney sumb ab gerew bu ñuy tàmbali ci bésu fanweeri fan ci weeru nowàmbar biy ñow. |
Bi ma léen di taxawu, gis naa ay waxambaane yoo xam ne ba ñuy ndaw lanu leen yar. |
Àdduna di dox ba ñu bokk ci kurél yoo xam ne am na ñu njuréef yu am solo ci seenug dund. |
Ci atum 1928 la demoon Farãas, nekk fanweer ak ñaari at yu mu fa génnul. |
Waa Russie dañoo lànk a topp dogalub OPEP biy digle ñu wàññi njëgu peterol bi. |
Waa Arabie Saoudite ñoom dañoo wàññi seeni njëgi njuréef, waa USA ñëw bokksi ci waxtaan wi. |
Kenn warul a yaakaar ne weesu na ci moom ngir mu def lu baax, mu soppeeku teguwaat ciw yoon. |
Ca kanam, jàppalante gi diggante Senegaal ak Almaañ. |
Atum ren mee gën a baax mu daaw ci doomu Senegaal bi ci dugal fukk ak juróom-ñetti bal, |
loolu di firndeel ne li mu defoon daaw, maanaam dugal fukki bit ak ñaar, weesu na ko ren. |
Looloo tax mu sàkku diggante takk-der yi ak askan wi kóolute am ci, njureefi loolu mooy ñaari pàcc yépp bokk liggéey ci jàmm. |
Leeral bu jëkk bi mi ngi jëm ci musiba yiy gën a laal jigéen ñi. |
Réew muy liggéey rekk a ko mën a am. |
Am nañu yaqiin ne ñun ñoo war a indi ay coppite, duñu toog mukk di xaar coppite yu dul agsi mukk. |
Dañoo raam ba agsi fii tey : maanaam bokk ci pàrti yi nekk ci kujje yi askan wi gën a bàyyi xel. |
Njariñal PASTEEF mooy ñu gën di def ay ŋàññ yu amee solo nii te muy méngook seen gëm-gëm ak seen taxawaay. |
Laata nawetu 2020-2021, ñi ci seen xam-xam màcc ci wall wi dañu fësal ne taw yi daañu bari ci Senegaal te daañu wasaroo bu baax ci gox yi ak ci waxtu wi. |
Su ñu sukkandikoo ci moom, yóbbees na ca Tiwaawon luy tollook ñaari junniy takk-der. |
Bokk na ci ñoom, ñiy nasaxal pexey sàmbaa-bóoy yi ak ñi seen xam-xam màcc ci wàllu yoon ngir yor kaaraange gàmmu gi |
nga xam ne ab xew-xewu diine buy dajale ay junniy doom-aadama ci bokk moomeel boobu nekk ci diwaann Cees. |
Ci noonu wax nañu ci fukk ak juróomeelu paasub tënkub liggéey bi ne ndawal askan wii di Usmaan Sónko mi nga xam ne daf doon jàppal tànk kenn ci way-ndono yi, dafa jàdd yoon ndax turu jàmbur la jëfandikoo. |
Waaye bi ci siife këyit wiy firndeel ne pàcc yépp nangu na ñu rekk desee, Usmaan Sónko dafa jiital Ismayla Ba mi ngi xam ne moom du ci dara te moom moo jiite kuréeli xelal yii di ATLAS ak MERCALEX. Kuréel yooyu Usmaan Sónko moo leen moom. |
Yomb na nekk fii di yuuxu ci mbooloo mi, |
waaye bu desee lu dul xëcc nit ñi ci biir PASTEEF wala sax nekk ki yore kàddoom, seetlu bi mooy ñàkk loo wax dafay feeñ rawatina nag ci tóoxidóona bu mel nii nga xam ne askan wi loolu rekk lañuy jàpp. |
Yëfi yambar la. |
Léonard de Vinci bind na ne wàllu cuub moom xeltu la, mooy doom ju jigéenu càkkeef gi. |
Fàttelekuleen joŋante bi doon dox diggante Senegaal ak Kótdiwaar, dañu ko dakkaloon ndax ay xeexoo. |
Li liggéey bii laaj mooy teel a jóg, teel a faj ak yar, |
looloo tax jot na léegi léegi ñu sumb waxtaan. |
MD : yaw lañu fal bees njiitu kuréelu Seine Marne, Lan nga nas ? |
Di amal ay waxtaan saa su ne ak di bàyyi xel téeréb suuf bi, mën nañoo musal ci coowal suuf. |
Su ñu sukkandikoo ci L’As ñiy saytul nguur gi seeni liggéey tuxu nañu ci seen béréb yu yees tàq yi. |
Ab woto bu joge woon Binjoona dafa këppu ci yoonu Gàmbul Coog nekk ci diwaanu Kawlax. |
Ñi dëkk ci ñaari gox yi dañu jékki jékki rekk gis ñaari woto yuy dàqante di daw seen xëlu bakkan. |
Ci noonu, dafay wuuteeg bépp xeetu dagg lempo yépp ndax kiy natt moom am na loo xam ne dafay dellusi ci moom, |
ci misaal mën nañu koo delloo li mu def ci wàllu wér-gu-yaram, am na sañ-sañu fayeeku bés bu àllateretee. Lii nag bokkul yeneen xeeti dagg lempo yi nga xam ne dara dellusi ci moom. |
Am na fi ay kàngam yoo xam ne ay njiit lañu yu askanu Senegaal naw, bokk na ci Ibraayima Faal. |
Ñoo ngi fësal ne loolu mënu leen a dakkal xeex bi. |
Manuñu lu dul gën a yokk liggéey bi, boolee gën a góor-góorlu ci ndajey bitim-réew yi. Loolu la fësal ca RFI. |
Dawalkat bii di Usmaan Njaay am na jabar ak ñetti doom. |
Abiib nee : gën leen a jëliy dogal ngir suqalikug kuréeli koom yi. |
Li tax ñu gën a jàppal tànk Senegaal, donte sax ci jamonoy mbas lañu nekk, dafay wone kóolute gu kuréeli koomi àdduna bi am ci liggéey bu njiitu réew mi Maki Sàll ci njàmbaarte gu mu def ci yokkute gi, ci pas-pas bi mu wone ci jëfandiku gi ñeel gafa réew mi, ak taxawaay bi mu am ci mbir bi. |
Ci weeru féewiriyee 2019, ñi nekk ci kujjeg pólótig gi te ñu doon yóotu réew mi, takk-der yi ak boroom doole yi bokk APR dañu leen doon fitnaal ngir nasaxal seen i yëngu-yëngu ci wàllu pólótig. |
Li mooy li xew ci dëkk yu mag yi seen woroom fonk yépp. |
Waaw, dëkk bu mag dafa war a am béréb yu bakkane. |
Lu ci bare, dafay faral di seetlu ne nit ñi amuñu benn yég-yég ci jafe-jafey wér-gu-yarami joŋantekat yi ci seen wàllu xel. |
Te saa su yu laaj ak tontu doxee suñu diggante ak ñoom ma seetlu ko. |
Subsets and Splits