text
stringlengths
6
463
Ginnaaw fukk ak benneelu rëcc bu kooku ñu tëj kaso te mu siiw lool, njiital kaso yi fii ci Ndakaaru, Mbay Saar moo ci jëkk a yëkkati kàddu.
Ci atum 1789, ginnaaw bi askanu Farãas amalee ak fippu, jeexal nguuru buur yi, wax nañu ci fukk ak juroomeelu ponk ci Tënku àq ak yélleefu doom-aadama yi ne ñépp am nañu sañ-sañu gisal seen bopp, wala sax ñi leen teewal, yittey indi seen xam-xam wala mën-mën ci liy doxal léppi-ñépp ci ni mu leen soobee ak ci waxtu wu mu leen neexee.
Waaw, nit ñi li ñu leen jàppee mooy càcc, njaayum yàmbaa, def lu defuwul ak yu deme noonu.
Ci atum 2017 dafa defar ab téereb wote boo xam ne moom kott moo xam lim bi ak li nekk ci biir.
Maa ngi tudd Soxna Jóob,
Ndakaaru laa juddoo waaye maa ngi fekk baax ca Luga fa sama baay juddoo.
Gis-gis yi wuutale ñaari nit ñi terewu leen a amal liggéey bu am solo ci pàrti bi nga xam ne ñoom ñoo ko taxal.
Nañu nangu te xam ne mënatuñoo amal ndawalin wu set wecc fii ci diwaanu Afirig.
Ci gàmmug Tiwaawan gu atum 2019, bérébu fajukaay bi ñu duppe Maam Abdu Asiis Si daloo na jumtukaay yu am solo.
Nasub joxey koppar bi dina tax dëkk yi nga xam ne ñi ngi ci yoonu suqaliku gën a dooleel seeni bérébu fajukaay ak ni ñuy saytoo ñi feebar, fexe ba ñi feebar te gën a ndóol mën a faju, tàggat ay ndawi kër doktoor yoo xam ne ñooy nekk ci kanam ak fexe ba boole askan wi ngirug kóolute.
Maaradaytaali, su ñu sukkandikoo ci Les Echos ci xibaar yi mu fësal tay, kameraa yi ñu def ca otel booba ngir kaaraange gi ñoo ko feeñal.
Ñu ngi leen di xaar ci tëj bi ngeen ko naral.
Ñu ngi leen di xaar ci baalaate gi ngeen di séddale ne boŋ-boŋ.
Ñoo ngi leen di fàtteli ne ab ndawal askan lañu jàpp, nekkul ab sàmbaa-bóoy.
Mbokki réew mi!
ﻵooloo gi ngir xeex Koronaa wiris bi dafa jaadu.
Lan moo tax ñu foog ne ay dóor mën naa tax xale yi soppiw doxaliin ?
Ki ñuy jàngal ne: ayca tijji leen seeni téere.
Duñu la jox seen balu oor bi!
Taarix dafay dellusi!
Xam naa am na ci ay bés.
Fi mu tollu Anàmbe, di gox bu nekk ca bokk moomeel bu Koldaa, ci mettit ak njàqare la nekk.
Kiy layool Móomoo Jàmme mi ngi laaj lu tolloog 77 865 407%20865%20407 ci li ñu ko sàcc ak juróom fukki milyoŋ yoo xam ne ndàmpaay lay doon.
Su ñu sukkandikoo ci kàdduy Maki Sàll, ngir yolamal ndànk-ndànk dogal yi ñu jëloon ca njëlbeen, dañu mujj jàng di dund ak doomu jàngoro ji, fexe ba kenn ku ne sa doxalin méngook ni mbas mi tëddee.
Ab xaalis jumtuwaay la bu mën a tax nit moom boppam,
Kon, nekkul rekk mbiru njiiti réewi Afirig yi kese, waaye yëfu ndawi askan wi la itam.
Yar googu dees na ko yégal FIFA itam.
Bànk yu jëkk yi am nañu jafe-jafe ngir am ay kiliyaan yu bare.
Ndax ñoom kiliyaan yi dañu jàpp ne bànk yooyu yaataluñu ba noppi seeni mbir dafa yéex te ngir nga jot ci ñoom dafay xaw a metti.
Mënuñu woon xalaat ne dee gaa ngi leen di xaar ci Xàllu 7 wi (RN7) booy waaj a agsi Ñokolokobaa.
Jàpp nañu ko, daan ko,
waaye ki ko doon defloo li mu doon def, kenn defu ko dara.
Lii dafay firndeel ne diine dafa lëkkale, ci lu wér, làkku wolof ak araab.
Bala nga koy xam Gàmmu jot, wala Màggal, wala Póppëngin.
Mën nañu ko méngale ak ab bérébu daw-làqu, way-fippu yooyu bokk ci pàcci MFDC.
Ci njiit yi ñu war a sàkku seenug nangu bokk na ci : Muhàmmadu Buhaari bu Niseriyaa, Nana Akufo Addo bu Ganna ak Alfa Konde bu Ginne.
Ci kanamu ay nit ñu ko doon sargal, njiit li fa nekkoon, di Alaaji Màggat SEKK, yaramam dafa daw, xolam tooy, ba mujjewul àggale li mu doon wax.
Ci waxtaan wu mu séq ak waa Sen Tv, deppite bi dafa dëggal li mu waxoon ne ñoom ñetti téeméer rekk lañuy fay ci lempo.
Anduñu ci ceeb bi ñuy jox ay nit ñoo xam ne dese nañu koo soxla lool ba noppi bàyyi doom-aadama yi seen loxo jotul seen ginnaaw.
Citizen yi, ci joŋante boo xam ne ñoo ci teg tànk, mujje nañu jël raaya gi ca Angleterre.
Ni njàngum nasaraan mi amee kurél guy saytu lépp lu ci aju, noonu lees war a wutale daara yi tamit ag kurél guy wattu lépp lu ci aju.
Ci njeexitalu joŋante bi la àttekat bi, Bamlak Tessema Weyesa, te mu nekk doomu Ethiopie, fësal ne Tunisie am nañu ab teg-dóor ndax Idiriisa Gànna Géy looxoom daa laal bal bi.
Dox gi ñu nemmeeku ci soppi li ñuy jële ci mbay mi, nasum pexem njëg lu baax lee ko jëmmal.
Bu ñu gisee Cebio Soukou duut Kalidu Kulibali mi nga xam ne dafa dëgër këcc, wala Saajo Maane mi ngi xam ne Olivier Verdon dafa ko tëj lu yàgg, ki leen di tàggat, Aliw Siise xelam demoon na ci joŋante bi doon dox ci diggante Maroc ak Bénin te waa Bénin mujje yóbbu ndam li.
Jigéen jii nga xam ne bokk na ci ñi gën a mag ci ñiy yënagtu ci wàllu xeltu ak caada ci Senegaal, moom la waa IFAN di sargal ci turu kenn koo xam ne, ginnaaw ba ñu moomee suñu bopp, bokk na ci nit ñi gën a am solo ñuy xeex ngir ñu dooleel làkkI réew.
Ginnaaw lu ëpp juróom-ñaari at yu mu def ci nguur gi, laaj leen lu tax askanu Senegaal wéy di des ci ndóol ?
Ca atum 2013 ba léegi njàmbaarte la doomu Espaañ ji wone.
Su ñu sukkandikoo ci kilifay Sonatel yi, ci gunge nasub pexem xarala bi ñu naan « Sénégal numérique 2025 » ngir fexe ba xarala yu yees am njeexital ci askan wi ak ci jumtuwaay yi, Këru liggéeyukaay gii di Orange teg na juróomeelu jeego ngir indi ci ay coppite.
Yaakaar nañu ne xaatim yile daañu leen jëmmal ba mu kowe njort.
Ci genn gis-gis, Ahmat-Ahmat fomm na déggoo beek Puma, te joxewul ngànt, loolu la genn kilifaag koom-koomu CAF bind.
Xoolal liy dëggal gile dogalu toppaat gi mboolooy teg-xel yu Senegaal yi bëgg a aakimoo, ngir am ci wàll yi ëpp solo ci séddoo bi ëllëg.
Njureef li wone na ne am na kenn ku dee, ak fukk ak juróom yu ci am ay gaañu-gaañu, te ñaar ci ñoom, sonn nañu lool, loolu la Seneweb xamle.
Metti na waaye nanu booloo, te dajaloo ci benn naal bu ñu bokk : suuxat Senegaal ci soppi tëralinam.
Léeg-léeg ñuy raay nguur gi cig woyofal, léeg-léeg ñuy mel ni ñuy jàmmaarlook moom.
Ci yemukaayu waxtu ak mën-mën yi ñu tënk ngir tëral yoonu joxe ndigalu jëf, Njiital réew mi jël na ay yoon yu ñu war a jëfe saa yu ñu leen siiwal rekk.
Waaye yoon yooyu duñu baax fi leek naal bi koy yoonal yóbbuwuñu ko ca pencum ndawi réew ma, njëkk waxtu wi ñu ko tënkoon.
Ginnaaw juróom-ñetti at ci boppu réew mi, Maki Sàll a ngi seetaan juróom-benni junniy mbaari négandinku, ay daara yu yàqu yaxeet, ay ndongo yu dëkk ci bank seeni loxo ndax ñàkk li gën a tuuti ci seen nekkinu njàng,
yokkuteg ñi am bakaloreyaa ci atum 2019 tollu ci fan-weer ak juróom-ñaar kos juroom-ñaar ci téeméer bo jël … lu yenuwul maanaa!
Nguurug njiitu réew mi Maki Sàll dugal na ñetti téeméer ak juróom-ñaari milyaar ci njëndum daamaari kilifay réew mi,
ca booba, suñu jigéen ñiy dee ci jàngoroy kañseer, ndax ñàkk masin buy jëfandikoo ay ceeneer ngir neenal jànoroy jooju ci yaram, te muy jar ñeenti milyaar ci xaalisu Seefaa.
Ak lu mana am, tekkaaral ak yëngoodi gu kujje gi moom lay jariñ!
Sónko ñaajal, say biddéew feq na ngir nga eggale say naal!
Kujje gi, ngir yàlla bànneexu leen bu baax ci seeni yelleef ! Abib Jóob
Noppalu leen léegi, teg ngeen jeego yi njëkk ; bàyyileen xale yi ñu def li des.
Koom-koom bi ñuy wax mooy alal ji, koppar wala wurus, ñu dénkaane ca Bànkub Farãas ngir matal njënd mi réewi Kurél giy saytu koom-koom bi ak koppar yi réewi Afirig sowu jànt di jéggaani.
Mbirum ndem-si-yàlla àttekat bi di Sàmba Sàll mooy ñaareelu kómpoloo ngir askan wi.
Defin wi dafa mujje soof ba yéematul kenn,
dañu ko sax far yoonal te mu bokk ci mbir yi ñu war a def ci jamonoy dagaanug baati askan wi.
Ñun ñépp a gis li am ci Péncum Ndawi réew mi jamono yii.
Waaye dañoo làbbali at mi ci topp jël Ligg dee Nasiyoŋ ci kanam futbalkati Pays-Bas yi.
Koppar yi ñu dajale tollu na ci junniy milyaar ak ñaar ci xaalisu Seefaa;
li nit ñi joxe ci seen teeyug bakkan, ñaar-fukki milyaar ci xaalisu Seefaa la, li ñu yokk ci koppar yi réew miy jëfandikoo ci at mi, téeméeri milyaar ak fukk-ak-juróom-ñeenti ci xaalisu Seefaa, bor yi ñu waajaloon, juróom-benni téeméeri milyaar ak ñaar-fukk ak ñett ci xaalisu Seefaa,
ndimbal yi ñu yokk ci koppar yi réew miy jëfandikoo ci at mi, ñaari téeméer milyaar ak ñeen-fukk ci xaalisu Seefaa ak li ñu dugal ci defaruwaat gi ngir réew mi mën a dox, tollu na ci junniy milyaar ak fukk ak ñeenti ak ñetti téeméeri milyoŋ ci xaalisu Seefaa.
Wér-gu-yaram, juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñetti milyaar ak juróom ñaari téeméeri milyoŋ ci xaalisu Seefaa, ndimbalu askan wi ak doomi réew mi yi nekk bitim réew, téeméer ak ñetti milyaar ci xaalisu Seefaa,
ndëgërlaayu koom-koom li, juróom-ñaari téeméeri milyaar ak juróom-fukk ak juróom ci xaalisu Seefaa, doyalug dund gi, juróom ñaar-fukki milyaar ak juróom-ñaar ak juróom-benn-téeméeri milyoŋ.
Doomi Bayern yi dañoo amoon wërsëg ci joŋante boobu.
Bayern dugal nañu ñeent ci lu ëpp fukki bal ak benn yi ñu jëmale ci caax yi.
Waa Pastef dañuy yóbbu raw-gàddu gi ca Cees bu neexee Yàlla.
Ay kàcc la de, bu Jëwriñu koom-koom ji, te aw doxalinu wuy nësëxal koom-koom gi, wax ne Senegaal amul yelleefu siiwal njëgu ropplaan gi ndax day sàmm suturas si ñu tënk ci digaale bi.
Aps nee na daamaarug juróom-ñaari toogu (7palaas), te mu jóge woon Conk-Esil moo xalangu ca Buluf, ca diiwaanu Sigicoor, ba mu am kenn ku ca faatu ak juróom-benn yu am ay gaañu-gaañu.
Bi muy màggal kóoluteg (Bànku àddina bi yépp) Bànk Monjaal ci Nguurug Senegaal, Abulaay Daawuda Jàllo yégle na tamit ne ci fan yu néew, ak ginnaaw déggoo bi réew mi am ak Kurél giy saytu tiyinu Bànk Monjaal, dinañu xaatim ab déggoo ngir dugal ay koppar ci jotug ñakk yiy xeex Koronaawiris ci njëg lu tollu ci téeméeri milyaar ak fan-weer ak ñeent ci xaalisu dolaar (134 000 000), maanaam juróom-ñaar fukki milyaar ak ñaar ci xaalisu Seefaa (72 000 000 000 F CFA).
Njiitu réew mi, ñoo ngi lay ñaax nga gën a defal suñu gox bi.
Ayda Jàllo moom, dafa toog ca këram ga nekk ca ginnaaw dalluwaay ba.
Li Guwarjolaa wax Tuxël : ca atum 2016, ba Peb Guwarjolaa di waaj a jóge ca Bundesliga : Tomas dinga ma wéetal lool, lool.
Ñeen-fukk ak juróom ñaar ci téeméer boo jël (47%), méngale ko ak yeneen réew yi mel ni Farãas ak Amerig yi nga xam ne wér-gu-yaram farataal nañu ko ba boole ci koppar yi réew miy jëfandikoo ci at mi.
Ndax doomu Alseeri la ni yaw.
Génn yu mujji Macron ak Guterres gën na leer:
Afirig la mbootaayi àdduna yi di taafantoo ngir dajale koppar yu sakkan.
Te li mbuxumkati koppar yooyu di def, teguwul ci yoon.
Ray katu koom-koom gi li ñuy def tere wuñu ko
Ca geneen wàllu Ërop ga, ca estaat bi di Groupama, OL waroon na fa dakkal joŋante yi mu fay defe te du ca am ndam.
Usmaan Sónko ak Décce Faal, ñoom ñaar, ñoo yenu raayag kujje gi.
Taxawaayug coppiteg njëgu koppar bi nga xam ne réew yi duñu ko dogal te mu soxal EKO la njiiti réew et nguur yu Mbootaayu réewi Afirig sowu jànt ngir koom-koom bi xaatim bu ñu sukkandikoo ci Kërug tas-xibaar gii di France-Presse te mu jële ko ci yégle yi ñu siiwal bi seen waxtaan wa jeexee gaawu ca Abutsaa, ca Niseriyaa.
Bo ci génne doomu Esypt ji di Muhamet Sala te mënul a bokk ci joŋante bi ngir téye raaya bi, ñett ñi ñu tànn te ñu bokk ci Mansesteer Siti (Esterliŋ, Bernardóo Silwaa ak Sersio Aguwero) ak ku Celsi (Eden Asaar)
Ñu ngi laaj Yoon wi tax ñu doon xeex.
Góor ak jigéen ñu aay ñi bokkoon ci siiwalug naalu dundin wi ñu bëgg ci Senegaal, ca Nuwel-Akiten ak fépp sax.
Siiwal bi jur na ndamal Usmaan Sónko lu yaatu lool ci suñu diwaan ci wotey palum njiitu réew mi yu féewiriyee atum 2019.
Ñu ngi woo askan wi ci mu gën a dal ndax lawug Koronaawiris ci sunu réew, te mu wàccoo ak matuwaayi fegu yi kër doktoor yi digle.
Kilifay mbootaayu baykat yi daje nañu ci Kérulug baykat yi ak sàmmkat yi nekk ci dëkk yi ñuy baye gerte.
Lu jëm ci woroo bi am ci lim bi ñu wax ci lempo bi nuy dagg ci pay gi, balluwaayu xibaar bi leeral na ne lempo bi nguur gi gàll ci nit ñi, mu ngi aju ca ndombo tànk ya ñu am ca Péncu Ndawi réew ma.