url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
FUTBAL
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Victor Boniface moo ngi dox ci ndox
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu ci ñeenti weer a ngi nii (ut, sàttumbar, oktoobar ak nowàmbar) moom lees di tabb  ki gën a xareñ ci weer wi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Santos wacc na
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Këlëbu Beresil bi moo ngi am ren 111i at ba ñu ko taxawalee ak léegi. Ren jii di guléet muy wàcc ca ñaareelu sàmpiyonaa ya (D2). Loolu nekk lu doy waar ca boobu këlëb. Ndax, guléet la, te dafa doon ekib bu mag boo xam ni bii ay punkal ñu fa jaar, ñu ci mel ni Pële ak Neymaar…
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Musaa Wagee ngi dikkaat ndànk-ndànk
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon at yii weesu ca Barça, loolu bokk ci li wàññiwoon xareñteem, ca la doomu Senegaal ji mujje woon a jóge foofu dem ci këlëb bii di Anorthosis Famagouste, ca sàmpiyonaa Siipr. Mu mel ni mu ngi delsi ndànk-ndànk ci nees ko xame woon. Ndax, ci weeru nowàmbar bii ñu génn, moom lees tabb ki gënn a xareñ ca weer wa.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Tijaan Jàllo wax na bëgg-bëggam ci ekibu Senegaal
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Bokkoon na ci ndaw yi teewaloon Farãs ci Kuppeg Àddina gees jagleloon ndaw yi ëppalagul 17i at yi weesu ci fan yii. Moom nag xamle na ni lu koy neex la mu futbalal Réewam mii di Senegaal. Loolu nag xëyna dina neex mbokki saa-senegaalam yi waaye ña di waa-Farãs njort na ni du yam ca ñoom. Loolu nag war a tax ekib bi ubbil koy loxoom donte daf koy boole ca ndaw ña ngir mu am lim bëgg ak ñu bañ ko xatal ca ekibi Farãs ya.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
CAF Awards : Lamin Kamara jël na cargalug ndaw bi gën a xarañ
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Lamin Kamara (19i at), Amara Juuf (17i at) ak Ezzalzouli (U23 Marog) ñoo nekkoon ndaw yuy xëccoo cargalu gi ñu jagleel ndaw bi gën a xarañ ci at mi fii ci Afrig. Lamin Kamara moo ko mujje jël. Moom, Lamin Kamara, daf def at mu am solo, jël ci CHAN beek CAN U23, ba noppi di joxe ca këlëbam, bokk it léegi ci Ekibu Senegaal bu mag bi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Cargal gu mag gi, balu wurus bi (ballon d’or), Saa-Niseriyaa baa ko jël, Wiktoor Osimen.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Basket : Góorgi Si Jeŋ bàyyi na
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Saa-Senegaal bi xamle na ni bàyyi na basket bi ci benn laaj-tontu bu yàggul ak Jeff McDonald Du San Antonio. Moom nag mu ngi toll ci 33i at.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
LÀMB
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
Amaa Balde ak Giri Bóordoo jàppees na seen bëre 30i fan ci weeru suwe bii di ñëw ci 2024 mi. Saa-Cees ak Ëmma Seen itam jàppees na ko ci 5i fan ci me bi.
https://www.defuwaxu.com/fallu-siise-fekki-na-kocc-barma/
FÀLLU SIISE FEKKI NA KOCC BARMA!
https://www.defuwaxu.com/fallu-siise-fekki-na-kocc-barma/
Ndekete Fàllu Siise daa bokk ca ña daamar (kamiyoŋ) ga saaraan fan yii ñu génn ca Caaroy dal seen kaw. Aa… Ki doon dawal daamar googu de, xamul li mu def. Li mu def, mënees na koo méngale ak xosi almet sànni ko cig kàggu, téere ya ca ne, ànd ak xam-xam ya ñu ëmb, daldi lakk ñoom ñépp ba def dóom. Fàllu Siise kàggu la woon gu ëmb lu bari ñeel baati wolof ak mbaatiitu wolof. Te ni ko fentaakon bu mag boobu di wuyoo ci turu Aamadu Àmpaate Ba waxe, mu am solo lool, “Fii ci Afrig, boroom xam-xam bu làqu daa mel ne kàggu gu lakk”. Ñaar a ma tax a fàttali loolu, tey. Benn : boroom xam-xam yi mel ne Fàllu Siise duñuy faral di móol i téere di ci dëxéñ xam-xam boobuy tax bu ñu fi jógee mu des fi ba seeni sët ak seeni sëtaat jot ci ba sax gën koo ñoŋal. Ñaareel bi moo di ne seen xam-xam du wasaaroo ndax day saf baatin ba tax ñu néew a ciy jot jaare ko ci ag tarbiya. Bu nu boolee loolu lépp, demug Fàllu Siise gi day doon ci nun ñaari tiis. Bu njëkk bi ñeel génnug àddinaam ak anam bu metti bi mu ame. Bi ci des di xam-xam bi mu yóbbaale. Waaye nag sant Yàlla ndax bi nuy jooy loolu ci la ma Sëriñ Jili Kebe xamal ni Fàllu jotoon naa liggéey ak benn waay ba tax lu bari ci li newoon ci moom yëbb na ko ci waay jooju. Rax-ci-dolli, waxtaan yi mu jot a séq ak ña ca kippaango bee ñu duppe Akaademi wolof ci Facebook, baati wolof yu xóot te ñu bari umple leen woon, jot na ko faa rotal. Lee tax nu mën a jàpp ne Fàllu Siise dem na waaye demul ndax ni ko woykat bi waxe “suuf dina lekk doomu-Aadama bàyyi fa jëf”. Xanaa rekk des di ko ñaanal Yàlla miy Boroom-Yërmaande jéggal ko te xaare ko àjjanay firdawsi ci barke turandoom Sëriñ Fàllu Mbàkke. Bu loolu weesoo, nu def yitte ci dajale li mu nu fi bàyyil, móol ko, wasaare ko ba mottalil ko naalam wi jëm ci jëmmal làkk ak baatiitu wolof. Seen yéenekaay LU DEFU WAXU mi ngi koy jaale njabootam gépp ak i mbokkam. Waaye, noo ngi koy jaale yit waa Senegaal gépp rawatina ñiy liggéey ci làmmiñi réew mi.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
JIÑAABO, JÀMBAARU SELEKI BA CA SIGICOOR
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Boo demee ca diiwaanu Sigicoor, dinga fa fekk liise bees duppe Jiñaabo. Waaye, aka néew nit ñi xam kan mooy Jiñaabo !
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Njàmbaar, fit ak ngor ñooy jikko yiy màndargaal Jiñaabo. Dafa di, Jiñaabo ab dàkkental la rekk. Turam dëggantaan mooy Jinoyeb Baaji. Moom Jinoyeb, walla Jiñaabo, as ndawu joolaa la woon, amoon fulla lool, gëmoon askanam, daan ko xeexal ba mujje cee ñàkk bakkanam. Jiñaabo mi ngi juddu ci atum 1850, ñu faat ko ci atum 1906, weeru me, fekk mi ngi tolloon ci 56i at. Li ñépp di fàttaliku, moo di ne ay jëfam ndawuñu woon, turam sooyul te nettaleem ñaawul. Ndege, Jiñaabo ci toolu-xare la daanu ! Te kenn newu ko kaay nu xeex, kenn jàmmarloowul ak moom, ñuy dóorante ba moom mu dee. Loolu lépp dara amu ci. Ab buqat, xonq-nopp bu bon, moo taxaw fale, daldi koy fetal, keroog xare Seleki. Diggante Seleki ak Sigicoor, 25i kilomeetar rekk la.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Ki ko faat, nag, doomu Frãs la, nootkat bi, bóomkatu jàmbaar bi.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Ñetti at laata Jiñaabo di ganesi àddina la coow li tàmbali. Ndaxte, ci atum 1886 la leen nguurug Frãs tàmbalee cokkaas, di leen tooñ ak a bunduxataal ba ci seen biir dëkk. Ñu ni déet-a-waay, soldaari Frãs yi di leen sànni ay ndell ak a taal jëppit seeni dëkkuwaay. Dañoo mujj a toxu, ndax seen lépp a yàqu woon, amatuñu woon sax fuñ fanaan.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Ba ci ndoorteelu 20eeluxarnu bi, Farañse yi, jaare ko ci seen ndaw lu leen fa toogaloon, dañoo jàppoon ni Seleki seen moomeelu bopp la woon. Looloo taxoon ñu daan fayloo waa dëkk ba, rawatina baykati ceeb ya, ay juuti ci seenum mbay. Waaye, askanu Seleki mësuñoo bàyyeeku, mësuñoo nangu ku leen di xoqtal, di leen jaay doole ak di aakimoo seen alal. Moo waraloon ndawu Frãs la fa nekkoon, xawoon a ragal Seleki ndax dafa jàppoon ni kaaraangeem desoon na, rawatina ba nit ña fay yeewoo taxawee temm, ne dee duñ fay lempo. Ci meenu jàmbaar yooyu la Jiñaabo nàmpe, kon mënul woon doon lu dul bañkat.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Xareb Seleki bi Jiñaabo ñàkke bakkanam, ci njiiteefu soldaaru Frãs bu doon wuyoo ci turu Lauque la ame. Moo santaane woon cong gi, jiite woon ko yit. Deewub Jiñaabo bi, nag, xawoon na indi jiixi-jaaxa ci xeli waa Seleki yi. Ndege, Jiñaabo du woon ndaw ni yeneen ndaw yi. Dafa amoon lu mu àndal, di woon sëriñ bu mag, amoon i gàllaaj. Kenn mësul woon a foog ne ab balu fetal mënoon na ci moom dara. Ñépp a jàppoon ni dafa tul. Waaye, jaam ak pexeem, Yàllaak ndogalam. Li am ba des mooy ne, xibaaru deewam bi yéemoon na lool waa tund woowee ; daanaka ñu bare nanguwuñ koo woon gëm.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Jiñaabo jotoon naa am doom ju tuddoon Sitaayóbo Baseen. Bi muy faatu, doom jaa ngi amoon 8i at. Bi Tubaab yi reyee baayam, waa dëkk bi dañ koo rawale, yóbbu ko ca dëkk buñ naan Ëllubaliir. Li ñu ko dugge woon mooy bañ Tubaab bi dugal ko ci gaal yóbbu Ndar-Géej, ni mu ko tàmmoon a defe ak doomi buur yi, mu bindu ‘’École des Fils de Chefs’’, ca daara jañ leen jagleeloon.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
Nataal bi : ndey-joor jàpp càmmoñ, sëtu Jiñaabo ak Tete Jaaju*.
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/
*Tete Jaajukilifa aada la woon ci Sigicoor ; tuddees na ko jenn daara ca diiwaan boobu.
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/
DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/
Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi dañuy jëfandikoo tarixa yi ngir beccingéel yeneen wutaakon yi ak a yëkkati seen mbër. Fan yii yépp, ñi bokk ci Ëttu boole baa ngiy daje di waxtaan ci jafe-jafe yeek yëngu-yëngu yiy am ci antarnet beek i xeeti xaralaam yu deme ni Facebook ak WhatsApp. Kilifay Facebook yi amal nañu ag saytu, ànd ceek kàngam yi taxawal kurél gi. Weccoo nañu xalaat naka lañu war a def ba dakkal téesanteek wax ju ñaaw ci béréb yooyu. Bi bésu pal gi desee benn ayu-bés rekk, ay ndéggat yu bari tàbbalees na leen ci antarnet bi, wesaare leen ci “Whatsapp” yi. Ay saay-saay a sooke lu ni mel, di sos ay fen yu tooy xepp, naan këru diine sàngam warul a sànnil xob wutaakon sàngam ndax bokkul ci ñoom, te gëmul seeni sëriñ. Lii moo bijji tiitaange ju réy ci waa réew mi. Diine nekk na lu man a jur xiirook ŋaayoo, te wareesul a mbubboo tarixa ngir soppi ko gànnaay, di ko xeexe ci politig bi. Yoonu tasawuf wi fi mag ñi sampoon, jàmm ak taalibe yi xamante, soppante a ko taxoon a jóg. Donte sax, politig masul a tàqalikook diine, ni seen diggante fése jamono jii dafa jéggi dayo. Séex Tiijaan Si, doomu Abdu Asiis Si Al Amiin, njiit li nekk ci boppu kurél googu yëkkati nay kàddu ngir àrtook leeral kóllëre gi dox ci diggante Murid yeek Tiijaan yi. Wane na ne ñaari kurél yii, waxul sax bokkoo gi leen boole, waaye ñoom ñépp liggéeyal diine ak Yonent bi rekk a leen yitteel. Nee na Sëriñ Séex Tiijaan Si Al Maxtoom wax na ni su Murid yi ak Tiijaan yiy ŋaayoo dafay naqari Yonent bi ndax moo leen jaboote ñoom ñépp. Rax-ci-dolli, wax na ne, palug njiitu réew du palu Imaam wala Xalifa, kon lees war a xool mooy jikko nit ki, jaar-jaaram, xam-xamu àddinaam ak yu ni mel. Waaye naan ci tarixa bii walla bee la bokk, ëpp naa def. Ëttu boole baa ngi ñaan waa réew mi ñu ànd ak dal te dem sànnil xob ki leen soob, bañ cee boole wax ju bari ak xuloo. Yal na Yàlla sotti jàmm ci réew mi te ki jig Senegaal Yàlla jox ko ndam lu sedd guyy.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
DÉMB AK TEYU DOXANDÉEMI ITALI YI
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
“Damay sànni ay kàddu yu néew ci waxtaan wi, jéem a joxe samay xalaat ci li nuy dund fii ci Itali.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Ci sama gis-gisu bopp, Móodu-Móodu yi agsi ci diggante atum 1980 ba 2000 wute nañu jëfin ak yeneen tukkikat yi tàmbalee tàbbi Itali ci atum 2000 ba tey jii.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Damay taxaw, léeg-léeg, seetlu,  ngir def ay jàngat ci ñaari doxalin yu wute yooyu lool, seet tamit lan a ko waral, fan la lalu. Ndax, boo gëstoo bu baax, mbir mi dafa lay jaaxal.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Naka la mbir mi deme ? Ňaari melokaan, ňaari jikko yu wute lool ci ay doomi-adama yu bokk fi ňu jóge.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Waaye boo xoolee bu baax ñi jëkk a agsi jànguñu, walla boog seen  njàng soriwul woon.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Dama koy seet ci sama maas gi. Dañoo jòge ci àll bi, walla jòge feneen ak feneen, jànguñu dara lu tax seen xalaat mën a sori.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Waaye ñàkkuñu woon cëslaay, amoon nañu tamit lu ñu gëm. Te boo ko de xool ci ñoom, Móodu yu jëkk yee fi taxawal ay daayira yu man a gindi mbokk yi ba kenn du gëlëm. Fakastalu, naam, am na, waaye Yàllaak daayira yee tax ba mag ñi fàttewuñu démb.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Jànguñu tubaab waaye mokkal nañu yeneeni làkk ba mën a xàll yoon wu leen di aar, di leen tee réer. Ndaxte, làkk wolof walla araab may na leen ñu xam fu ñuy teg seeni tànk ba bañ a saaraan. Te bi ñuy ñów ci réew mii gisuñu kenn ku leen tette waaye am nañu seen ngor ak seen diine, jàpp nañu ci ba taxaw fu dëgër. Ba tax kenn yóbbuwuleen ci weneen yoon wu doonul seen yoonu bopp. Kon tey, Móodu yu jëkk ya xam nañu fan lañ samp seeni tànk ba mën a téye seen aada ak seen ngor ak seen fulla. Loolu lépp am nay firnde ndaxte bu daayira yi nekkee fépp tey, xeer wu njëkk wi ñoom ñoo ko teg ba xale yi mujj a agsi mën cee jariñoo.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Doxalin wu ni mel ku yaafus walla ku ragal du ko sàmm ba ku la ca fekk, toppandoo la, mu indil ko tawféex. Xale yi topp ci yoon wi, nag, wax dëgg Yàlla gisuma ci kenn ku tarxiis ci kaw xollitu banaana.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Wax ji du gudd, dañu koy tënk.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Waaye maasi gone yu mujj yi, li leen sonal mooy ñàkk a mën a muñ. Jafe na lool jom ju tax ngay moytoo def looy réccu ëllëg. Walla bu la jamono naree lottal dinga ko mën a muñ ndax lu bari alal du la ko jaral. Li am solo mooy ngay xool bu baax sa juddu, di sàmm sa ngor, di bàyyi xel ci sa diine.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Xaley tey yi ànduñook dal, mënuñoo xaar. Te li koy indi mooy teel a bëgg am xaalis, yàkkamti koo am, sa lépp sotti léegi-léegi. Kenn xamatul luy taaxirlu.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Li ko waral mooy :
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
waa ji dafa wàcc Rom, dugg ci saxaar gi wutali Milaŋ, toog ba ci kanam mu ne ki mu dendal
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
-“Waaw, ndekete Itali am nab àll”
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
moroom mi ne ko :
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
“Noppil waay, loolu ëpp naa wax !’’
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Waa  ji tontu ko ne ko ;
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
“Aa, man kat damaa defe woon ni fii lépp ay taax la.”
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Xam nga ni kii kay, am na mbetteel te dara xewagul. Fu amul àll, kenn du fa bay, te  fu  mbay amul,  xamuma luñ fay dunde. Loolu moom, waxin la rekk.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Jamono ji ñu tollu, jafe-jafe yi bari nañ Itali waaye lépp dañu koy sante sunu boroom. Seneraasiyoŋ bu bees bi am na ciy jàmbaar waaye tamit bari na ci ñu réer. Du gaaw nag ñu defar seen réew.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Boo demee gaaru Milaŋ am na ñuy fanaan ci mbedd yi. Taxawaalu bi bari na lool, te xale yi mënuñoo yor seen bopp. Bu sedd bi ñëwee, xale yu bari dañuy tumuraanke. Tukki baax na waaye nit bala ngay jòg war ngaa xam fa nga jëm lan nga fay fekk.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Nun mag ñi war nañoo góor-góorlu ba teg xale yi ci yoon wu jub. Jàngal leen seen kàllaama, nàmpaatal leen ngir ñu xam seen cosaan. Loolu dina tax kenn du soppeeku ba topp tubaab yi ci seen melokaan.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Nun doomi Senegaal yi, dinanuy ànd dem ci daayira, dem julli jàkka waaye li nuy dimbalante ci sunu biir bariwul te bokk na ci li nu tax a des ginnaaw. Nit dina tollu diggante, ñòw ci biir mbooloo mu takku te fa mu tollu moom rekk a koy xam. Te dina rus a laaj, te ña mu fekki, bu ñu amul xelu jox ko walla dimbali ko, noonu lay jògee ca jataay ba, dellook aajo bu fajuwul.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Loolu dafay tax nit di gaaw a suux te du ca génn. Bu yàggee, kër ga mu luye sax dootu ko mën a fay. Boo dee ku am jom, dinga génn kër googu, bu booba mbedd mee lay for walla nga dem bay fanaan ci sa biir oto. Am na ku mu fi daloon, dafa mujj faatu ci sedd bi.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Li may jëkk a digale, mooy na nit kiy duggante ak mbokki senegaleem yi, saa yu ñu wootee mu jiitu fa, te ci daayira yi lañuy gën a faral di daje. Su ma nee daayira, nag, seetuma ci tarixaa bi mba beneen, daayira yépp laa yemale. Nekk ak say mbokk am na solo ndax bu saafarawul lépp tamit, mën naa saafara lu bari.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Nit ki fa ngay yeewoo, fa ngay faatoo. Kon, ci fànn yépp la jàppante am solo.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/
Li duuf ci nag wi, xejul ci cin li. Kon boog ba beneen jotaay.”
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci seen i joŋante, war a daje ci finaal bi war a am keroog 1eelu fan ci weeru suwe  fa Wembley.
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Paris Saint-Germain – Dortmund
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Saa-Almaañ yi ñoo toogloo farãse yi ci seen ñaari joŋante yi. Paris Saint-Germain moo njëkk a fekki, keroog 30i fan ci weeru awril wii, Dortmund daldi koy dóor 1-0. Barki-démb, ci talaata ji, 7i Me 2024, mu fekksi ko ca fowoom bees duppee “Parc des princes”, gañewaat ko benn bal ci dara, daldi jàll finaal.
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Real Madrid – Bayern Munich
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Ci weneen wàll wi, waada (champion) Espaañ bi moo toogloo yeneen Saa-Almaañ yi. Ñu amal ñaari joŋante yu metti lool nag. Keroog, bu njëkk ba, 29i Awril 2024, la Real Madrid fekki woon Bayern ca pàkkam, ndaje ma metti, ñu mujjee timboo 2-2. Ci àllarbay démb ji, 8i Me 2024, Bayern Munich daldi fekksi Saa-Espaañ yi seen dëkk. Niki bu njëkk ba, ndaje mi metti lool. Ci 2eelu xaaju joŋante bi la Bayern njëkk a dugal (Alphonso Davies, 68eeli simili). Naka noona, Real Madrid daldi koy tontu, dugal, dugalaat. Joselu moo dugal ñaari bii yi (88eel ak 90+1eel).
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
Noonu la 1/2 yi demee. Ñaari way-bom yi war a daje bés bi njëkk ci weeru suwe wees dëgmal, fa Wembley (Àngalteer).
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
MBARA-WÀCC DOOMI-GAYNDE NJAAY YI !
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Sunu gaynde yi amagul ñaar-fukki at wone nañu njàmbaar fale ca Niseer, nga xam ne fa la réewi Afrig yi gën a xareñ ci futbal daje woon di joŋante.
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Jaaraama sunu Doomi-Gaynde yi ! Ay jàmbaar dëgg lañu, ñaawuñu ci xare bi ndax ca Niseer, daje nañook ñeenti ekib, am ndam ñeenti yoon. Mali ak Ganaa lañu njëkk a gal-gal ñaari bal ci dara (2–0), duma Burkinaa Faaso duma yu metti, juróomi bal ci benn (5–1), jóge fa jaar ci kow Réewum Afrig-bëj-Saalum benn ci dara (1–0). Léegi, ñook seen doomi-ndeyi Mali yi rekk a des ci géew bi ! Ak lu mën a xew fan yiiy ñëw, gone yi def nañu lu réy. Sunu xel dal na ndax déggoo, doon benn a leen tax a yegg fiñ yegg tey, fëq caax yi juròom ñeenti yoon te benn yoon doŋŋ lañu nax seen góol. Muy firndeel itam ni ekib bi dëgëre…
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Fi mu ne nii, ñu ngiy xaar Mali, waaye dara mënatuleen a tee bokk ci joŋante bu mag biy dajale réewi addina sépp, ca Poloñ ci weeri me ak suweŋ yiiy ñëw. Loolu du guléet, ndax Senegaal demoon na Nuwel-Selànd, ci atum 2015 ak itam réewum Kore Bëj-saalum ci atum 2017.
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Ku xam Yuusuf Daabo miy tàggat sunu gaynde yu ndaw yi, xam ne amul tiitukay. Daanaka kóoluteem ci goney ekip bi amul àpp. Nee na Senegaal amul lu muy ragal ndax démb la tàmbalee waajal joŋanteb Niseer bi tey soog a ñëw. Loolu tekki ne liggéey bu jaar yoon a ko tax a dal xel. Te, sàllaaw, bala yàgg nun ñépp dinanu bég. Yuusu Daabo yokk na ci sax ne : « Jot nanoo am i jogaŋte yu metti, Burkinaa Faaso lanu mujjee dajeel, ñu indilnuy jafe-jafe. Waaye sunu pas-pas tax na ñu génn ci. Gëm naa ni kenn mënatunoo të, ku nu dajeel dinan la dóor ».
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Li wóor ba wóor moo di ne bu Senegaal toogul ci gàngunaay bi dina ñaaw, ndax dellu ginnaaw lay gën a nirool. Ñaari yoon yi mujje yépp, doomi-gaynde yi àgg nañu ba ci njeexital li ñu daan leen. Su nu waxantee dëgg, nag, loolu mënuta wéy te ñu baree ngi koy naqarlu ba tey jii. Kon mu mel ni am ndam ci dibéer ji rekk mooy seral xol yi.
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
Abdulaay Seen
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
(Bi nu bindee li ngeen jàng ba noppi, lanu dégg xibaar bu tiis bi : Mali mujje naa dóor Senegaal 3 penalti ci 2. Kon ñu ne xalam demoon na bay neex…)
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
SÀMPIYONAA ALMAAÑ : BAYER LEVERKUSEN JËL NA KO !
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
Xabi Alonso ak gaayam yi def nañ ko. Dugal nañ Bayer Leverkusen ci mboorum futbalu Almaañ. Ci anam bu rafet a rafet lañ ko defee nag. Saa-Espaañ bi, Xabi Alonso miy tàggatkatu këlëb ba, def na jaloore ju réy a réy. Niki dibéeru démb ji, 14 awril 2024, lañ duma Werder Bremen 5i bal ci 0. Ndam loolu leen tax a nekk waagay (champions) sàmpiyonaa. Ndaxte, ki topp ci ñoom, Bayer Munich, mënatu leen a dab. Muy guléet ci mboorum Bayer Leverkusen. Nde, bi këlëb bi sosoo ba léegi, mu ngi sog a gañe sàmpiyonaa bi.
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
Saa-Españool bi ak i ndawam daldi nañu dakkal nguuru Bayern Munich foofee, fa Almaañ. Dafa di, 11i at yii weesu yépp, moo rekk a daan jël sàmpiyonaa ba. Daawu ko bokk ak kenn. Kon, li Xabi Alonso ak i kuppekatam def, jaloore ju réy a réy, rawatina bi nga xamee ne keen xaaru leen woon file.
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
Li gën a réyal jaloore ji mooy ne, moom Bayer Leverkusen, amalagum na 43i joŋante yoy, kenn dóoru ko ci : dafa gañ38i yi, daldi témbóo 5 yi. Gaa yi dugal ci 123i bii, jël ci 31i.
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
Laata seen joŋanteb démb ji, soppey këlëb bi dañu fees dell mbeddi gox ba, di jaajëfal seen tàggatkat bi, ba sax daldi ne soppi nañu turu yoon wi jëm ca fowu ba duppee ko “Yoonu Xabi Alonso” (Xabi Alonso Alle). Xanaa yayoo na ko ! Nde, moom Saa-Espaañ bi, dafa soppi xar-kanamu këlëb ba, di leen futbal-loo lu set te rafet, neex a seetaan.
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
Wëliis sàmpiyonaa bi ñu gañe, dese na leen ñaari kub yi ñu war a mën a jël. Ndaxte, am nañu finaalu kubu Almaañ ba te njortees na ne ñoo koy jël. Rax-ci-dolli, am na joŋanteb kaar-dë-finaal ci Ëropaa Lig ba, te dafa gañe West Ham ci mats bu njëkk bi. Fi mu nekk nii, ñettale (triplé) la Xabi Alonso di diir. Siporteer yi ñoom, nee nañ, bu fi yemoon sax mu neex. Ndeem neex na, nay gën di neex !
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
KUPPEG TEFES
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran).
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
NDAW YI MU TANN
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Góol : Alseyni Njaay ak Useynu Fay.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Defãsëer : Mamadu Silla, Papaa Móodu Ndóoy, Baabakar Ñaŋ, Baabakar Faal, Seydinaa M.A. Gajaga.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Miliyë : Maamur Jaañ, Séydinaa Isaa Laay Seen,  Amar Sàmb.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Ataakã : Rawul Méndi, Séydinaa Manjoon Jaañ, Suleymaan Koli, Suleymaan Baaji.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
ABDULAAY SIMAA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Saa-Senegaal bi moo ngi wane xarañte ca ekibam boobu di Rangers FC fa Ekos. Fi mu nekk nii, moo ngi ci 14i bii yu mu dugalagum. Ndax loolu dina doy ngir Aliw Siise wóolu ko ci CAN bii ñu dëgmal ? Kenn xamagul. Lu leer daal mooy ni soxlees na ci ekib bi ay ataakã yu xarañ ci kanami kã yi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
LÀMB JI : MÓODU LÓO AK BOY ÑAŊ NAROON NAÑU SONGOO
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Démb ci gaawu gi 15i Desàmbar bi la ñaari mbër yi doon amal seen jàkkaarloo bu mujju laata seen bésu bëre 1 sãwiyee 2024.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
Ci jàkkaarloo bi, doomu pikin bi dafa fekki Móodu Lóo di nappanteek moom, ñuy sannantey kàddu ci suuf jekki saay rekk doomu Parsel bi daldi koy buux. Ba loolu amee ñu nar a jàppante foofu faf ñenn ca ña ànd ak ñoom ak ca njiit ya dox seen diggante. Yu ni mel dees na wane ni ñaari mbër yi pare nañu ngir neexal bés bi. Waaye nag, lu jar a yamale la laata muy jur lu ñaaw.
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
YAA GORE !
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
Yàgg, yàgg, dëgg ay daan
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
Dëgg lottoon na Senegaal
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
Usmaan Sonkoo tax mu daan
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
Lii dinaa ko bind ngir ëllëg
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/
Danga daan xëy di liggéey
README.md exists but content is empty.
Downloads last month
30