audio
audioduration (s)
2.29
12.5
sentence
stringlengths
26
118
moo taxit feebaru jigéen dafa bari façons
bu nawetee du génn te gànnaayoowul ak permiyaabal
kii de dafay wanteer njëg li neex na lool
léegi daawur dafa mel ni ku télbati
delloo na naaru góor wi tëboon wajanam wi
ci saa si ayda jafandu ci waasintóoram yu tuuti ya
Nee ñu xobi pàppaayo baax na ci fas yi seen biir di metti
ku woor di togg mën naa am nga juubu mos xorom
ba mu egsee ca dëkk ba booba ñépp a nga woon ca tool ya ba mu des ndew ma mu fekk ca buntu néegam
ruuxal soow mi ndax soppuma ci sañ yi
tamaate fàrsi jaa ngi noy nepp kenn mënu ko dagg
mu fab ko saggane ko te ndeyam amoon ko muy benn doññ
mu nga jóge woon ca rëbb ma gàlloo genn kéwél
mbëtt mënula daw mënula jaab lu dul bar bari
sa yaraale bi màgg na léegi yow lañuy xaar
reeni xom xom fajkat yee koy jëfandikoo
muy toj mu ndaw di toj mu mag mënees nañoo tiim
saalu gerte tubaab rekk la xale yi bëgg
fas wa dellu fëx nekk ca la mu nekkoon
ki sàcc sa nag yi du jaar ci saawo si
buur ne ki rey ninki nanka bi lay may doomam
këram la waaye dëkku ci dafa ko luye
boo raxasee aset yi ba noppi nga fomp leen
mbubb ma nga soloon ca céet ga booba laa bëgg
mu jëm ca sàmba seytaane amari né ko
amul bàyyi ni ko ndax am na jur gu dem
dalal nga sama xel bi nga ma nee am na liggéey
morooman yi gunge nañu ko ba gaar ba
soo leen boolee dinañu gaawa xaritoo
fompal lumbi deret yi bala nga koy faj
moo yey Noy ci liggéeyam moo ko tax a suturlu
bu jëkk jigéen ñi begguñu woon sew dañu daan yaflu
Naar Naar Naar ba Naar yépp tiit daldi jóg ni ko
mag ñu jëkk ña daawuñu génn te takkuñu nafa
booy dem màrse ma yóbbante la kànja
ba jànq ya indee meew ma xale yu góor yi daldi naan
dafa bàyyi woon ay waajuram moo tax mu alku
seen ndën li yal nangeen ko yàgga def
kon dey ma dal di tegale samay ndab te dem
yaay ji ni ko benn lam bu ma sa baay mayoon bi mu ma takkee
ñu toogati lu yàgg ba ñépp fàtte
yaay ji ni ko benn lam bu ma sa baay mayoon bi mu ma takkee
jamanoy tàngaay ci teraas bi lañuy lekke
maa ngi nii nag waxal nag loo ma fi mayul ma delloo la ko
leegi li ñu wara def mooy balu ko te daw seeti feneen
fas di nà dov vandé rutimgeer à cà ràv
darkase yi meññuñu ndax bekkoor bi
xale bi raatale na laax bi ci dënn bi
loolu laa amoon lu ma leen di wax wasalaam
xaaral ba nu matal ay gii nga soga bokk
kër gu xate nii kenn mënu fi yar xar
wër nañu xale bi ba tàyyi gisuñu ko
saaga yu ñaaw lay génne ci gémmiñam gi
dégg naa ne kër googa dafay jaay luññutu ko
bu jur gi màngsee dañu leen di abal karas gi
amoon na fi jigéen ju bon ju nekkoon ag ñeenti doomam
mënuma laa dab yaa ma gën a gudd i jéego
toppatool xale bi dafa mel na ku tojal
xaaral ba suuf si màndi nga sog di gas
moo xale bi yow reew nga di waaw lu doon say tànk sax
xawma lu ko jot yaram mi dafa def yu mel ni ay càqar
sama maam a ma defarluloon seN oor bii
mbom la dagg bënn mi nii ni na doon bàmmeelam
mu ngi jonkon ci wetu taal bi di jaaru
mu ngi topp tali bi di tëñëx tëñëxi
balawlaw tàppit malaan a ngoog am yobbaale ko buur
li mu doon daw moo tax noyyi gi gëna gaaw
miskin yu bare la yélimaan jooju daan leel
xale bi laaj ko loo dagge sama butitu njurukaay
tëggkat yi tàmbaleeguñu ñu ngiy foddat ndënd yi
ci wetu seju la toolu banaana yi nekk
wax ju jëkk fasu par la tontu la naaru góor
mu daldi jël li mu soxla dem mu delluwaat ci yaayam ni ko
gàpp bi weesu na bu yàgg dama koy seeti ndax ma soññ ko
dafay gelu yaayam yóbbuleen ko ci moom
góomam bi dafa wunni bi mu ci defee sunguf si
badoolë bou bagn é ligaiye bagn é k mbok ëm
ki sàcc sa nag yi du jaar ci saawo si
bi mu tàmbalee jël garab googu ba tey miiratul
soo ko wutaloon mbaxana doon na baax ci naaj wi
damaa am ab rëq rëq ci li ma doon def
boo ko dénkul woon say mbóot lii du la dal
dafa ko seen rekk ne wëréñ ne mott
dama bëgg xam këf ki mu dugal ci waxande wi lu mu doon
sa ceebu tey bi wesaN na démb dafa xawoon tooy
altine biy ñów lañuy wori bu soobee yàlla
danga bëgg ci sama màngo bi waaye du jaar ci sa bóli
li nga wax leerul nee ma maa ngi jëm béréb sàngam
bu ñu noddee fajar dafa naan fojjet jóg
demal foo jublu yàlla na fa yiwu yàlla jublu
boo fi fekkulee xaalis bu jàppandal duma la mëna dimmali
xale yu tuuti yi nga xam ni xamuñu dara mu bàyyi leen
Nit ka déglu ko ba noppi dal di fiddi
soldaar yi amatuñu bal amatuñu puudër
këriñ gi du gaawa jàpp ndax dafa tooy
bañuñu koo bind matadi gi mu àndal a tax
fekk ma tool ya am na liggéey bu ñu fa war def
lu mpicà baré baré du téré ji dugup
bu ñu bëggee falu di wuta peeg nit ñi
janq yu ndaw ndawaan yi lañu fiy jàngal togg

Dataset Card for "wolof_speech_transcription"

More Information needed

Downloads last month
34

Models trained or fine-tuned on serge-wilson/wolof_speech_transcription