sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
9
71
{ "fr": "Les croyants et les croyantes sont alliés les uns des autres. Ils commandent le convenable, interdisent le blâmable accomplissent la Salât, acquittent la Zakat et obéissent à Allah et à Son messager. Voilà ceux auxquels Allah fera miséricorde, car Allah est Puissant et Sage.", "wo": "Te way-gëm yu góor yi ak way-gëm yu jigéen ya, ay xarit lañu. Dañuy digalante lu baax, di tere lu bon, tey taxawal julli, di joxe asaka, tey topp Yàlla ak ub Yonentam. Ñooña, Yàlla Dana leen yëram, naka Yàlla, Ku not la, Ku xereñ la." }
9
72
{ "fr": "Aux croyants et aux croyantes, Allah a promis des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour qu´ils y demeurent éternellement, et des demeures excellentes, aux jardins d´Eden [du séjour permanent]. Et la satisfaction d´Allah est plus grande encore, et c´est là l´énorme succès .", "wo": "Yàlla digal na way-gëm yu góor yi ak way-gëm yu jigéen yi Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, dañu fay béel, ak dëkkuwaay yu sell ca Àjjana ju sax ja. Te ngërëmul Yàlla moo gën a màgg, te loolu nag moo di texe gu màgg ga." }
9
73
{ "fr": "ô Prophète, lutte contre les mécréants et les hypocrites, et sois rude avec eux; l´Enfer sera leur refuge, et quelle mauvaise destination !", "wo": "Éy yaw Yonent bi, nanga xeex ak yéefar yi ak naaféq yi, te nanga leen tiisal ; seen dëkkuwaay Safara la, te moo yées ci delluwaay !" }
9
74
{ "fr": "Ils jurent par Allah qu´ils n´ont pas dit (ce qu´ils ont proféré), alors qu´en vérité ils ont dit la parole de la mécréance et ils ont rejeté la foi après avoir été musulmans. Ils ont projeté ce qu´ils n´ont pu accomplir. Mais ils n´ont pas de reproche à faire si ce n´est qu´Allah - ainsi que Son messager - les a enrichis par Sa grâce. S´ils se repentaient, ce serait mieux pour eux. Et s´ils tournent le dos, Allah les châtiera d´un douloureux châtiment, ici-bas et dans l´au-delà; et ils n´auront sur terre ni allié ni secoureur .", "wo": "Ñangay waat ci Yàlla ne waxuñu dara, te wér na ne wax nañu baati weddi te tàbbi nañu ci kéefar ginnaaw ba ñu duggee ci Lislaam. Te ñangay ittewoo lu ñu mënul a am. Te amuñu la ñuy sàkku lu dul Yàlla - ak Yonentam - dafa leen jox ci mbaaxam koom-koom. Bu ñu tuuboon, mooy gën ci ñoom. Su ñu lànkee, féttéerlu, Yàlla Dana leen mbugal mbugal mu metti ci àddina ak àllaaxira ; te duñu am ci kaw suuf ku ñuy wéeru mu méngoo seeni mbir walla ku leen dimbali." }
9
75
{ "fr": "Et parmi eux il en est qui avaient pris l´engagement envers Allah : \"S´il nous donne de Sa grâce, nous payerons, certes, la Zakat, et serons du nombre des gens de bien\".", "wo": "Saar 9 : Tuub 129 Laaya - Ginnaaw Gàddaay gi" }
9
75
{ "fr": "Et parmi eux il en est qui avaient pris l´engagement envers Allah : \"S´il nous donne de Sa grâce, nous payerons, certes, la Zakat, et serons du nombre des gens de bien\".", "wo": "Ci ñoom, am na ñu warlul Yàlla, ne : “Bu nu Yàlla mayoon ci mbaaxam (alal), kon dey dananu natt asaka, te it dananu bokk ca ñu baax ña” .(r) " }
9
76
{ "fr": "Mais, lorsqu´Il leur donna de Sa grâce, ils s´en montrèrent avares et tournèrent le dos en faisant volte-face.", "wo": "Ba leen Yàlla mayee ci mbaaxam (alal), ñu nay ci joxe, ginnaaw ba ñu fuuyu." }
9
77
{ "fr": "Il a donc suscité l´hypocrisie dans leurs coeurs, et cela jusqu´au jour où ils Le rencontreront, pour avoir violé ce qu´ils avaient promis à Allah et pour avoir menti.", "wo": "Tax na Yàlla wuutale ci seen xol naaféq ba kera ñuy dajeek Moom ngir la ñu wor Yàlla ca la ñu ko digoon ak ca la ñu doon fen." }
9
78
{ "fr": "Ne savent-ils pas qu´Allah connaît leur secret et leurs conversations confidentielles et qu´Allah connaît parfaitement les (choses) inconnaissables.", "wo": "Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla xam na seen mbóot ya nëbbu ak seenub déeyoo, te nag Yàlla mooy xamaakoonub kumpa." }
9
79
{ "fr": "Ceux-là qui dirigent leurs calomnies contre les croyants qui font des aumônes volontaires et contre ceux qui ne trouvent que leurs faibles moyens (à offrir), et ils se moquent alors d´eux. Qu´Allah les raille. Et ils auront un châtiment douloureux.", "wo": "Ña nga xam ne dañuy ayibal (sikkal) way-coobarewu ña ci jullit yi ci natt asaka, ak ña nga xam ne amuñu leneen lu dul seeni kàttan ba tax ñuy reetaan lenn ca ñoom. Yàlla Dana leen yéjji te danañu am mbugal mu metti." }
9
80
{ "fr": "Que tu demandes pardon pour eux, ou que tu ne le demandes pas - et si tu demandes pardon pour eux soixante dix fois - Allah ne leur pardonnera point. Et ce parce qu´ils n´ont pas cru en Allah et en Son messager et Allah ne guide pas les gens pervers.", "wo": "Nga balul leen walla nga bañ leen a balul (moo yem) - soo leen baluloon juróom-ñaar fukki yoon - du tax Yàlla baal leen mukk. Ngir dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay saay-saay." }
9
81
{ "fr": "Ceux qui ont été laissés à l´arrière se sont réjouis de pouvoir rester chez eux à l´arrière du Messager d´Allah, ils ont répugné à lutter par leurs biens et leurs personnes dans le sentier d´Allah, et ont dit : \"Ne partez pas au combat pendant cette chaleur ! \" Dis : \"Le feu de l´Enfer est plus intense en chaleur.\" - S´ils comprenaient ! -", "wo": "Ña dem bañ a xeexal Lislaam, bég nañu ca seenub toogaay ngir juuyook Yonent Yàlla bi, te soppuñu di xeex ak seeni alal ak seeni bakkan ngir Yàlla, ñuy wax naan : “Buleen génn xare ji ci tàngaay bi !” . Neel : “Tàngaaru Safara moo gën a tar.” - Cëy bu ñu xamoon ! -" }
9
82
{ "fr": "Qu´ils rient un peu et qu´ils pleurent beaucoup en récompense de ce qu´ils se sont acquis .", "wo": "Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari (ca àllaaxira) mu di seenug pey ca la ñu doon fàggu." }
9
83
{ "fr": "Si Allah te ramène vers un groupe de ces (gens-là), et qu´ils te demandent permission de partir au combat, alors dis : \"Vous ne sortirez plus jamais en ma compagnie, et vous ne combattrez plus jamais d´ennemis avec moi. Vous avez été plus contents de rester chez vous la première fois; demeurez donc chez vous en compagnie de ceux qui se tiennent à l´arrière\" .", "wo": "Bu la Yàlla delloo ci ab kurél ñoom, te ñu ñaan la ndigalul génn (ànd ak yaw), neeleen : “Dootuleen génn mukk di ànd ak man, te it dootuleen xare ak noon yi ànd ak man. Ndax yéen tànnoon ngeen toog ca njalbéen ga ; kon nag toogleen, ànd ak way-des ña ginnaaw” ." }
9
84
{ "fr": "Et ne fais jamais la Salat sur l´un d´entre eux qui meurt, et ne te tiens pas debout auprès de sa tombe, parce qu´ils n´ont pas cru en Allah et en Son messager, et ils sont morts tout en étant pervers .", "wo": "Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay." }
9
85
{ "fr": "Et que ni leurs biens ni leurs enfants ne t´émerveillent ! Allah ne veut par là, que les châtier ici-bas, et qu´ils rendent péniblement l´âme en mécréants .", "wo": "Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla Daleen a namm a mbugal ci yooyu ci àddina, te bu seeni ruu di rot fekk ñu di ay yéefar. (s)" }
9
86
{ "fr": "Et lorsqu´une Sourate est révélée : \"Croyez en Allah et luttez en compagnie de Son messager\", les gens qui ont tous les moyens (de combattre) parmi eux te demandent de les dispenser (du combat), et disent : \"Laisse-nous avec ceux qui restent\".", "wo": "Bu aw saar wàccee (di leen ñaax) ci gëm Yàlla ak ànd xare ak ub Yonentam, woroom alal ya ca ñoom di laaj ndigal, naan : “Bàyyinu nu ànd ak ñay toog” ." }
9
87
{ "fr": "Il leur plaît, (après le départ des combattants) de demeurer avec celles qui sont restées à l´arrière. Leurs coeurs ont été scellés et ils ne comprennent rien .", "wo": "Neex na leen ñu ànd ak way-des ginnaaw ña. Tax na tëjeef na seeni xol ba ñoom dootuñu am dégg-dégg. " }
9
88
{ "fr": "Mais le Messager et ceux qui ont cru avec lui ont lutté avec leurs biens et leurs personnes. Ceux-là auront les bonnes choses et ce sont eux qui réussiront .", "wo": "Waaye Yonent bi ak ña ànd ak moom ci ngëm, ñangay xare ak seeni alal ak seeni bakkan. Ñoom am nañu ay ngëneel te ñoom texe nañu." }
9
89
{ "fr": "Allah a préparé pour eux des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour qu´ils y demeurent éternellement. Voilà l´énorme succès !", "wo": "Yàlla xaroo na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel. Loolu moo di texe gu màgg ga !" }
9
90
{ "fr": "Et parmi les Bédouins, certains sont venus demander d´être dispensés (du combat). Et ceux qui ont menti à Allah et à Son messager sont restés chez eux. Un châtiment douloureux affligera les mécréants d´entre eux.", "wo": "Ñiy sàkku ngànt (ci bañ a dem) xare ji ca sàmm sa, nekk nañu ngir ñu am ci ndigal. Ña weddi Yàlla ak ub Yonentam, toog nañu. Ña weedi ca ñoom, mbugal mu metti dana leen dal." }
9
91
{ "fr": "Nul grief sur les faibles, ni sur les malades, ni sur ceux qui ne trouvent pas de quoi dépenser (pour la cause d´Allah), s´ils sont sincères envers Allah et Son messager. Pas de reproche contre les bienfaiteurs. Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal, amuñu bàkkaar (ci toog bañ a xare ji) ndeem ñu rafet yéene lañu ci Yàlla ak ub Yonentam. Naka noonu it, ca ñay rafetal seeni jëf. Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la." }
9
92
{ "fr": "(Pas de reproche) non plus à ceux qui vinrent te trouver pour que tu leur fournisses une monture et à qui tu dis : \"Je ne trouve pas de monture pour vous.\" Ils retournèrent les yeux débordant de larmes, tristes de ne pas trouver de quoi dépenser.", "wo": "Ña nga xam ne bu ñu dikkee ci yaw di sàkku waruwaay, nanga leen di wax ne amuloo lu ñu mën a war, ñu dellu ànd ak naqar, di jooy ngir jàq ca la ñu amul waajtaay, ñoom it amuñu bàkkaar. Kenn du am ci ñoom aw yoon." }
9
93
{ "fr": "Il n´y a de voie (de reproche à), vraiment, que contre ceux qui demandent d´être dispensés, alors qu´ils sont riches. Il leur plaît de demeurer avec celles qui sont restées à l´arrière. Et Allah a scellé leurs coeurs et ils ne savent pas.", "wo": "Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon." }
9
94
{ "fr": "Il vous présentent des excuses quand vous revenez à eux. Dis : \"Ne présentez pas d´excuses : nous ne vous croyons pas. Allah nous a déjà informés de vos nouvelles. Et Allah verra votre oeuvre, ainsi que Son messager. Puis vous serez ramenés vers Celui qui connaît bien l´invisible et le visible, et alors, Il vous informera de ce que vous faisiez.", "wo": "Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji- xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.(h)" }
9
95
{ "fr": "Ils vous feront des serments par Allah, quand vous êtes de retour vers eux, afin que vous passiez (sur leur tort). Détournez-vous d´eux. Ils sont une souillure et leur refuge est l´Enfer, en rétribution de ce qu´ils acquéraient.", "wo": "Danañu leen waatal ci Yàlla, ba ngeen dellusee ci ñoom, ngir ngeen bañ leen a sikk. Waaye nangeen leen dëddu. Ñoom nag sobe lañu te seen delluwaay mooy Safara, muy peyug la ñu nekkoon di ko fàggu." }
9
96
{ "fr": "Ils vous font des serments pour se faire agréer de vous, même si vous les agréez, Allah n´agrée pas les gens pervers.", "wo": "Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet njort ci ñoom. Bu ngeen nangoo seeni lay, Yàlla du nangul aw lay nit ñu di ay saay-saay." }
9
97
{ "fr": "Les Bédouins sont plus endurcis dans leur impiété et dans leur hypocrisie, et les plus enclins à méconnaître les préceptes qu´Allah a révélés à Son messager. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Sàmm sa, ñoo gën a tar ag weddi ak ug naaféq, te gën a yey ci ñàkk a xam ndigal yi Yàlla wàcce cib Yonentam. Yàlla nag Ku xam la, Ku xereñ la." }
9
98
{ "fr": "Parmi les Bédouins, certains prennent leur dépense (en aumône ou à la guerre) comme une charge onéreuse, et attendent pour vous un revers de fortune. Que le malheur retombe sur eux ! Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Am na ci sàmm si ñu jàpp ni, la ñu joxe (ngir Yàlla) lu yàqu la, tax na ñuy seentu xew- xew (bu bon dal leeen). Yal na xew-xew bu bon (ba ñuy seentu) dal ci seen kaw ! Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la. " }
9
99
{ "fr": "(Tel autre,) parmi les Bédouins, croit en Allah et au Jour dernier et prend ce qu´il dépense comme moyen de se rapprocher d´Allah et afin de bénéficier des invocations du Messager. C´est vraiment pour eux (un moyen) de se rapprocher (d´Allah) et Allah les admettra en Sa miséricorde. Car Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Am na it ca sàmm sa, ñu gëm Yàlla ak Bis-pénc ba te jàpp nañu ne la ñuy joxe (ngir Yàlla), ag jaamu Yàlla la ak ug julli ci Yonent bi. Moo ndax loolu dafa nekkul di ag jege Yàlla ci ñoom? Yàlla Dana leen dugal ci yërmaandeem. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
9
100
{ "fr": "Les tout premiers [croyants] parmi les émigrés et les Auxiliaires et ceux qui les ont suivis dans un beau comportement, Allah les agrée, et ils l´agréent. Il a préparé pour eux des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, et ils y demeureront éternellement. Voilà l´énorme succès !", "wo": "Ña jiitu woon bu jëkk ca ña gàddaayoon (Muhaajiruuna ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ak ña leen toppoon cig rafetal (seeni jëf), Yàlla bég na ci ñoom, te ñoom it bég nañu ci Yàlla. Te it sédde na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel ba fàwwu. Loolu moo di texe gu màgg ga !" }
9
101
{ "fr": "Et parmi les Bédouins qui vous entourent, il y a des hypocrites, tout comme une partie des habitants de Médine. Ils s´obstinent dans l´hypocrisie. Tu ne les connais pas mais Nous les connaissons. Nous les châtierons deux fois puis ils seront ramenés vers un énorme châtiment.", "wo": "Am na it ca sàmm sa nekk ca seen wet, ay naaféq, ak waa (Madina). Am na ñu téppeeral cig naaféq. Xamuloo leen, (waaye) Nun xam Nanu leen. Dananu leen mbugal ñaari yoon ba noppi Nu door leen a delloo ca mbugal mu màgg ma.(s)" }
9
102
{ "fr": "D´autres ont reconnu leurs péchés, ils ont mêlé de bonnes actions à d´autres mauvaises. Il se peut qu´Allah accueille leur repentir. Car Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon nañu jëf yu sell ak yeneen yu ñaaw. Xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
9
103
{ "fr": "Prélève de leurs biens une Sadaqa par laquelle tu les purifies et les bénis, et prie pour eux. Ta prière est une quiétude pour eux. Et Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la." }
9
104
{ "fr": "Ne savent-ils pas que c´est Allah qui accueille le repentir de Ses serviteurs, et qui reçoit les Sadaqat , et qu´Allah est L´Accueillant au repentir et le Miséricordieux.", "wo": "Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon." }
9
105
{ "fr": "Et dis : \"Oeuvrez, car Allah va voir votre oeuvre, de même que Son messager et les croyants, et vous serez ramenés vers Celui qui connaît bien l´invisible et le visible. Alors Il vous informera de ce que vous faisiez\".", "wo": "Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def” ." }
9
106
{ "fr": "Et d´autres sont laissés dans l´attente de la décision d´Allah, soit qu´Il les punisse, soit qu´Il leur pardonne. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci ndigalul Yàlla, mën naa am Mu mbugal leen, mën naa am it Mu jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la." }
9
107
{ "fr": "Ceux qui ont édifié une mosquée pour en faire [un mobile] de rivalité, d´impiété et de division entre les croyants, qui la préparent pour celui qui auparavant avait combattu Allah et Son Envoyé et jurent en disant : \"Nous ne voulions que le bien ! \" [Ceux-là], Allah atteste qu´ils mentent .", "wo": "Ña nga xam ne dañoo defar jàkka ngir bëgg a lore ak weddi ak téqale way-gëm ña, ak di fàggul (pexem ña fay julli) ku xeex ak Yàlla ak ub Yonentam ca njalbeen ga, ak ngir mën a giñ ne bëgguñu lu dul lu baax. Yàlla seede ne li wóor mooy dañuy fen." }
9
108
{ "fr": "Ne te tient jamais dans (cette mosquée). Car une Mosquée fondée dès le premier jour, sur la piété, est plus digne que tu t´y tiennes debout. [pour y prier] On y trouve des gens qui aiment bien se purifier, et Allah aime ceux qui se purifient .", "wo": "Bul ca taxaw mukk. Ca njalbeenu bis (ba nga wàccee Madina), moo gën a yey ci nga taxaw fa. Aw góor a nga fa, ñoo xam ne, sopp nañu jéem a nekk ñu laab, te Yàlla sopp na ñu laab ña. " }
9
109
{ "fr": "Lequel est plus méritant ? Est-ce celui qui a fondé son édifice sur la piété et l´agrément d´Allah, ou bien celui qui a placé les assises de sa construction sur le bord d´une falaise croulante et qui croula avec lui dans le feu de l´Enfer ? Et Allah ne guide pas les gens injustes.", "wo": "Moo ndax ku samp ab tabaxam cig ragal Yàlla ak yaakaar ngërëmam moo gën ? Walla ku sampu tabaxam ci pindub kàmbu gu joy jëm ci daanu ca biir Safara ? Te Yàlla du gindu aw nit ñu di ay tooñkat." }
9
110
{ "fr": "La construction qu´ils ont édifiée sera toujours une source de doute dans leurs coeurs, jusqu´à ce que leurs coeurs se déchirent. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Tabax ba ñu tabax du noppee nekk sikki-sàkka ca seeni xol ba ba seeni xol di daggatoo (ba ba ñuy dee). Te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la." }
9
111
{ "fr": "Certes, Allah a acheté des croyants, leurs personnes et leurs biens en échange du Paradis. Ils combattent dans le sentier d´Allah : ils tuent, et ils se font tuer. C´est une promesse authentique qu´Il a prise sur Lui-même dans la Thora, l´évangile et le Coran. Et qui est plus fidèle qu´Allah à son engagement ? Réjouissez-vous donc de l´échange que vous avez fait : Et c´est là le très grand succès .", "wo": "Yàlla nag jënd na, ca ña gëm, seeni bakkan ak seeni alal, feye na leen Àjjana. Ndax ñangay xeex ci yoonu Yàlla : di reye, ñu di leen rey. Muy dig bu réy ca Yàlla ci dëgg (na Mu ko waxe) ci Tawreet ak Injiil ak ca Alxuraan. Ana kan moo gën a matal kóllareem ci Yàlla ? Kon bégleen ci njaay mi ngeen jaayanteek Moom. Te loolu moo di texe gu mag ga.(r)" }
9
112
{ "fr": "Ils sont ceux qui se repentent, qui adorent, qui louent, qui parcourent la terre (ou qui jeûnent), qui s´inclinent, qui se prosternent, qui commandent le convenable et interdisent le blâmable et qui observent les lois d´Allah... et fais bonne annonce aux croyants .", "wo": "(Ñooña) ñuy tuub lañu, di ñuy jaamu Yàlla, di Ko sant, di ñuy woor, di lunku di sujjóot (julli), di digle lu baax, di tere lu bon, di wattu dëeli Yàlla yi (daytal)... bégalal ña gëm." }
9
113
{ "fr": "Il n´appartient pas au Prophète et aux croyants d´implorer le pardon en faveur des associateurs, fussent-ils des parents alors qu´il leur est apparu clairement que ce sont les gens de l´Enfer.", "wo": "Yellul ci Yonent bi ak ñi gëm ñuy baalul bokkaalekat yi, doonte la sax mbokk lañu ginnaaw ba mu leen biree ne ñoom ñuy dugg Safara lañu." }
9
114
{ "fr": "Abraham ne demanda pardon en faveur de son père qu´à cause d´une promesse qu´il lui avait faite. Mais, dès qu´il lui apparut clairement qu´il était un ennemi d´Allah, il le désavoua. Abraham était certes plein de sollicitude et indulgent.", "wo": "Te it jéggalu ga Ibraayiima doon jéggalul baayam, du utoon dara lu dul ab dig bu mu ko digoon. (Waaye), ba mu ko leeree ne noonub Yàlla la (moom baayam), dafa deñ ba set wecc ci loolu. Ibraahiima ab delluwaakoon la ci Boroomam, ku lewet la." }
9
115
{ "fr": "Allah n´est point tel à égarer un peuple après qu´Il les a guidés, jusqu´à ce qu´Il leur ait montré clairement ce qu´ils doivent éviter. Certes, Allah est Omniscient.", "wo": "Yàlla du bàyyi ñoo xam ne gindi na leen ba noppi ñuy tàbbiwaat cig réer, te leeralal na leen la ñu war a ragal. Yàlla xam na lépp." }
9
116
{ "fr": "A Allah appartient la royauté des cieux et de la terre. Il donne la vie et Il donne la mort. Et il n´y a pour vous, en dehors d´Allah, ni allié ni protecteur.", "wo": "Yàllaa moom nguurug asamaan yi ak suuf si. Mooy dundal, di rey. Te amuleen wéeruwaay walla ku leen mën a dimbali ku dul Moom (Yàlla)." }
9
117
{ "fr": "Allah a accueilli le repentir du Prophète, celui des Emigrés et des Auxiliaires qui l´ont suivi à un moment difficile, après que les coeurs d´un groupe d´entre eux étaient sur le point de dévier. Puis Il accueillit leur repentir car Il est Compatissant et Miséricordieux à leur égard .", "wo": "Yàlla jéggal na ba noppi Yonent ba ak way-gàddaay ña (Muhaajiruun ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ñoom ña nga xam ne toppoon nañu ko ca jamono ju jafe ja, ginnaaw ba xoli lenn ca ñoom xawoon a jeng. Mu jéggal leen ndax Moom (Yàlla) Ku ñeewant la, di Jaglewaakoon ci ñoom." }
9
118
{ "fr": "Et [Il accueillit le repentir] des trois qui étaient restés à l´arrière si bien que, toute vaste qu´elle fût, la terre leur paraissait exiguë; ils se sentaient à l´étroit, dans leur propre personne et ils pensaient qu´il n´y avait d´autre refuge d´Allah qu´auprès de Lui. Puis Il agréa leur repentir pour qu´ils reviennent [à Lui], car Allah est L´accueillant au repentir, le Miséricordieux .", "wo": "Ak ñett ñañu bàyyi woon ginnaaw ba tax li suuf si yaatu yépp, lépp xat ci ñoom ; te it seeni jëf xat ci ñoom ba ñu jort ne amul wenn wéeruwaay (wuy musle) ci Yàlla ju dul Moom Yàlla. Mu daldi leen jéggal ngir ñu tuub (rëccu). Naka Yàlla Nanguwaakoonu tuub la, Jaglewaakoon la.(s) " }
9
119
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Craignez Allah et soyez avec les véridiques.", "wo": "Éy yéen way-gëm ñi ! Nangeen ragal Yàlla te ànd ak ñu dëggu ña." }
9
120
{ "fr": "Il n´appartient pas aux habitants de Médine, ni aux Bédouins qui sont autour d´eux, de traîner loin derrière le Messager d´Allah, ni de préférer leur propre vie à la sienne. Car ils n´éprouveront ni soif, ni fatigue, ni faim dans le sentier d´Allah, ils ne fouleront aucune terre en provoquant la colère des infidèles, et n´obtiendront aucun avantage sur un ennemi, sans qu´il ne leur soit écrit pour cela une bonne action. En vérité Allah ne laisse pas perdre la récompense des bienfaiteurs.", "wo": "Yellul ci ñi dëkk Madina ak sàmm sa ko wër, ñuy des ginnaaw, di bàyyi Yonent bi (buy dem jareji), te buleen seeni bakkan gënal bosam. Ndax ñoom, mar walla coono, walla xiif, duleen dale ci yoonu Yàlla, te duñu dëkk senn suuf (soo xam ne, danañu ca taxaw lu dul ne) dana metti yéefar ya, te it duñu am genn nooteel cib noon, te Dana leen ko bindal muy jëf yu yiw ñeel leen. Yàlla du sànk mukk peyug ñiy rafetal." }
9
121
{ "fr": "Ils ne supporteront aucune dépense, minime ou importante, ne traverseront aucune vallée, sans que (cela) ne soit inscrit à leur actif, en sorte qu´Allah les récompense pour le meilleur de ce qu´ils faisaient.", "wo": "Te duñu joxe alal ju tuuti, walla ju bari, te it duñu jàll aw xur lu dul ne dees na leen ko bindal, Yàlla feye leen ko lu gën a rafetal." }
9
122
{ "fr": "Les croyants n´ont pas à quitter tous leurs foyers. Pourquoi de chaque clan quelques hommes ne viendraient-il pas s´instruire dans la religion, pour pouvoir à leur retour, avertir leur peuple afin qu´ils soient sur leur garde .", "wo": "Warul ci jullit ñépp dem (xareji). Lu tere mbooloo mu ne mu am ñu ca dem (xamluji) xam-xamu diine, ba bu ñu delsee ca seeni mbokk, waar leen ngir ñu mën a wattandiku." }
9
123
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Combattez ceux des mécréants qui sont près de vous; et qu´ils trouvent de la dureté en vous. Et sachez qu´Allah est avec les pieux.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Xeexleen ak ñi leen jegeñ ci yéefar yi ; nañu fekk ci yéen dëgër gu mat sëkk. Te ngeen xam ne Yàllaa ngi ànd ak ñi ragal Yàlla." }
9
124
{ "fr": "Et quand une Sourate est révélée, il en est parmi eux qui dit : \"Quel est celui d´entre vous dont elle fait croître la foi ? \" Quant aux croyants, elle fait certes croître leur fois, et ils s´en réjouissent.", "wo": "Te bu aw saar mësaan a wàcc, dana am ci ñooña (naaféq) ya, ñuy wax naan : “ Ana kan la lii mën a dolli ngëmam ?” . Waaye, ña nga xam ne ñoom gëm nañu, Dana leen yokk ngëm, te it danañu ca bég.(n)" }
9
125
{ "fr": "Mais quant à ceux dont les coeurs sont malades elle ajoute une souillure à leur souillure , et ils meurent dans la mécréance.", "wo": "Ña nga xam ne jàngaro nekk na ci seen xol ya, dafay nekk ci ñoom kéefar guy dolliku cig kéefar, te ci kéefar googu lañuy deewaale." }
9
126
{ "fr": "Ne voient-ils pas que chaque année on les éprouve une ou deux fois ? Malgré cela, ils ne se repentent, ni ne se souviennent.", "wo": "Moo ndax dañoo gisul ne at mu nekk dees na leen not benn walla ñaari yoon ? Te ñooña, duñu tuub, duñu waaru." }
9
127
{ "fr": "Et quand une Sourate est révélée, ils se regardent les uns les autres [et se disent]: \"Quelqu´un vous voit-il ? \" Puis ils se détournent. Qu´Allah détourne leurs coeurs, puisque ce sont des gens qui ne comprennent rien.", "wo": "Te su ñu wàccee aw saar ñu daldi xoolante, daldi wax ne : “Moo ndax am na ku nu gis ?” . Daldi wëlbëtiku. Yal na Yàlla wëlbëti seeni xol ndax ñoom, aw nit lañu ñu amul genn dégg-dégg." }
9
128
{ "fr": "Certes, un Messager pris parmi vous, est venu à vous, auquel pèsent lourd les difficultés que vous subissez, qui est plein de sollicitude pour vous, qui est compatissant et miséricordieux envers les croyants.", "wo": "Ab Yonent dikkal na leen bu bokk ci yéen, seeni coono tiis ci moom, di ku xér ci ngeen jub, di ku am ñeewant ak yërmaande ci jullit ñi." }
9
129
{ "fr": "Alors, s´ils se détournent, dis : \"Allah me suffit. Il n´y a de divinité que Lui. En Lui je place ma confiance; et Il est Seigneur du Trône immense\".", "wo": "Bu ñu dëddoo, neel : “Yàlla doy na ma. Amul jenn yàlla ju dul Moom. Te Moom laay dëgërloo ; te Moom moo di Boroom gàngunaay gu màgg ga (Aras)” . " }
10
1
{ "fr": "Alif, Lam, Ra . Voici les versets du Livre plein de sagesse.", "wo": "Alif, Laam, Raa. Lii ay laayay Téere bu ñu xereñe lañu." }
10
2
{ "fr": "Est-il étonnant pour les gens, que Nous ayons révélé à un homme d´entre eux : \"Avertis les gens, et annonce la bonne nouvelle aux croyants qu´ils ont auprès de leur Seigneur une présence méritée [pour leur loyauté antérieure] ? Les mécréants dirent alors : \"Celui-ci est certainement un magicien évident\".", "wo": "Moo ndax dafa dul yéem ci nit ñi, Nu soloo (xamal) góor gu bokk ci ñoom : “Ndigalul waar nit ñi ci bégal way-gëm ñi te xamal leen ne, am nañu fa seen Boroom dawal bu di dëgg ? Ña weddi ñoom nee nañu : “Lii dey ag njibar gu fés la” .(s)" }
10
3
{ "fr": "Votre Seigneur est Allah qui créa les cieux et la terre en six jours, puis S´est établi \"Istawa\" sur le Trône, administrant toute chose. Il n´y a d´intercesseur qu´avec Sa permission. Tel est Allah votre Seigneur. Adorez-Le donc. Ne réfléchissez-vous pas ?", "wo": "Yàlla seen Boroom nag Mooy ki bind asamaan yi ak suuf si ci juróom- benni fan, topp Mu yemoo ca gàngunaay ga (Haras), di settantal mbir ya (ndigal ya). Amul kenn ku mën a ramm te du ci ndigalam. Kookoo di seen Boroom. Jaamuleen Ko. Moo ndax dungeen fàttaliku ?" }
10
4
{ "fr": "C´est vers Lui que vous retournerez tous, c´est là, la promesse d´Allah en toute vérité ! C´est Lui qui fait la création une première fois puis la refait (en la ressuscitant) afin de rétribuer en toute équité ceux qui ont cru et fait de bonnes oeuvres. Quant à ceux qui n´ont pas cru, ils auront un breuvage d´eau bouillante et un châtiment douloureux à cause de leur mécréance !", "wo": "Seen delluwaay yéen ñépp ca Moom la jëm, mooy digub Yàlla bu dëggu ba ! Moom moo sos mbindéef yi (booba dara amul), Moo leen di delloosi (ginnaaw bu ñu dee ba ràpp) ngir Mu feye ña gëm pey gu duun. Waaye ña weddi woon ñoom, seenug naan, ndox mu tàng lay doon ak mbugal mu metti, muy peyug seenug weddi !" }
10
5
{ "fr": "C´est Lui qui a fait du soleil une clarté et de la lune une lumière, et Il en a déterminé les phases afin que vous sachiez le nombre des années et le calcul (du temps). Allah n´a créé cela qu´en toute vérité. Il expose les signes pour les gens doués de savoir.", "wo": "Moom mooy ki jox jant bi tàkk-tàkk, jox weer wi leeraay te dogal ko ay wàccuwaay ndax ngeen mën a xam limu at yi ak mën a waññi. Yàlla bindul loolu lu dul ci dëgg. Te Dana biralal tegtal ya nit ñay xam." }
10
6
{ "fr": "Dans l´alternance de la nuit et du jour, et aussi dans tout ce qu´Allah a créé dans les cieux et la terre, il y a des signes, certes, pour des gens qui craignent (Allah).", "wo": "Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak li Yàlla sàkk ci asamaan yi ak suuf si, ay kéemaan ci nit ñu ragal (Yàlla)." }
10
7
{ "fr": "Ceux qui n´espèrent pas Notre rencontre, qui sont satisfaits de la vie présente et s´y sentent en sécurité, et ceux qui sont inattentifs à Nos signes [ou versets],", "wo": "Ña nga xam ne nag yaakaaruñoo dajeek Nun, te tànn dundug àddina gii, doyloo ko, ak ña nga xam ne sàggane nañu Sunuy ndigal," }
10
8
{ "fr": "leur refuge sera le Feu, pour ce qu´ils acquéraient.", "wo": "ñooña seen delluwaay moo di Safara ngir la ñu fàggu." }
10
9
{ "fr": "Ceux qui croient et font de bonnes oeuvres, leur Seigneur les guidera à cause de leur foi. A leurs pieds les ruisseaux couleront dans les jardins des délices.", "wo": "Ña nga xam ne gëm nañu tey jëf yu yiw, seen Boroom dana leen wommat ngir seen ngëm, tàbbal leen Àjjanay xéewal. Ay dex di daw ci seen suuf. " }
10
10
{ "fr": "Là, leur invocation sera \"Gloire à Toi, ô Allah\", et leur salutation : \"Salam\", [Paix ! ] et la fin de leur invocation : \"Louange à Allah, Seigneur de l´Univers\".", "wo": "Seenug jaamu foofa mooy di wax naan : “Cëy sellug sunu Boroom” , te seenug nuyyoo foofa mooy : “Jàmm rekk” , te la ñuy mujjeel ca seenug jaamu, moo di ñu wax ne: “Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla Boroom àddina si” ." }
10
11
{ "fr": "Et si Allah hâtait le malheur des gens avec autant de hâte qu´ils cherchent le bonheur, le terme de leur vie aurait été décrété. Mais Nous laissons ceux qui n´espèrent pas Notre rencontre confus et hésitants dans leur transgression.", "wo": "Bu Yàlla gaawe woon àtte nit ñi ci mettit kem ni ñu yàkkamtee am alal, àttekoon na seenug yàkkamti. Waaye Dananu bàyyi ña nga xam ne yaakaaruñoo dajeek Nun ñuy laam- laame ca seen biir ngëlamte.(r)" }
10
12
{ "fr": "Et quand le malheur touche l´homme, il fait appel à Nous, couché sur le côté, assis, ou debout. Puis quand Nous le délivrons de son malheur, il s´en va comme s´il ne Nous avait point imploré pour un mal qui l´a touché. C´est ainsi que furent embellies aux outranciers leurs actions.", "wo": "Nit, bu ko aw naqar dalee, mu daldi Nuy woo, (moo xam dakoo fekk mu) tëdd walla mu toog walla taxaw. Te bu Nu ko tekkilee naqaram woowu, muy wéy (ci kéefaram), fakk mel ni mësunoo woo ci naqar wu ko dal. Noonu la jekkee woon ca ñoom bokkaalekat ya la ñu daan def." }
10
13
{ "fr": "Nous avons fait périr les générations d´avant vous lorsqu´elles eurent été injustes alors que leurs messagers leur avaient apporté des preuves. Cependant, elles n´étaient pas disposées à croire. C´est ainsi que Nous rétribuons les gens criminels.", "wo": "Alag Nanu ay xeet yu bari yu leen jiitu ba ñu tooñee, te Yonent dikkal leen ak i lay yu leer nàññ. Te nanguwuñuleen woon a gëm. Noonu la Nuy feyee nit ñu di ay saay-saay." }
10
14
{ "fr": "Puis nous fîmes de vous des successeurs sur terre après eux, pour voir comment vous agiriez.", "wo": "Ba noppi Nu def leen ngeen wuutu leen ci suuf si ci seen ginnaaw, ngir Nu seetlu naka ngeen di def." }
10
15
{ "fr": "Et quand leur sont récités Nos versets en toute clarté, ceux qui n´espèrent pas notre rencontre disent : \"Apporte un Coran autre que celui-ci\" ou bien \"Change-le\". Dis : \"Il ne m´appartient pas de le changer de mon propre chef. Je ne fait que suivre ce qui m´est révélé. Je crains, si je désobéis à mon Seigneur, le châtiment d´un jour terrible\".", "wo": "Te bu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy kàddu yu leer yi, ña yaakarul a dajeek Nun wax ne : “Indil weneen jàngin wu wuuteek wii” mbaa “Nga soppi ko” . Neel : “Yellul ci man ma soppi ko ci sama coobare bopp. Duma topp lu dul la ñu ma soloo. Ragal naa, su ma moyee sama Boroom, mbugalum bis bu rëy (dal ma)” ." }
10
16
{ "fr": "Dis : \"Si Allah avait voulu, je ne vous l´aurais pas récité et Il ne vous l´aurait pas non plus fait connaître. Je suis bien resté, avant cela, tout un âge parmi vous. Ne raisonnez-vous donc pas ? \" .", "wo": "Neel : “Bu sooboon Yàlla, duma leen ko jàngal te duma leen ko xamal. Ndax dundu naak yéen ay at lu ko jiitu. Moo ndax dangeen dul xel- lu ?” ." }
10
17
{ "fr": "Qui est plus injuste que celui qui invente un mensonge contre Allah, ou qui traite de mensonges Ses versets (le Coran) ? Vraiment, les criminels ne réussissent pas.", "wo": "Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla di weddi ay tegtalam ? Ak lu mën a xew, saay-saay sa duñu texe." }
10
18
{ "fr": "Ils adorent au lieu d´Allah ce qui ne peut ni leur nuire ni leur profiter et disent : \"Ceux-ci sont nos intercesseurs auprès d´Allah\". Dis : \"Informerez-vous Allah de ce qu´Il ne connaît pas dans les cieux et sur la terre ? \" Pureté à Lui, Il est Très élevé au-dessus de ce qu´Ils Lui associent !", "wo": "Dañuy jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne duleen mën a lor, duleen mën a jariñ dara, ñuy wax naan : “Ñii ñoo nuy rammu fa Yàlla” . Neel : “Ndax dangeen a mën a xamal Yàlla lu Mu xamul ci asamaan yi ak suuf si ?” . Kañ naa Ko, te kawe na lool la ñu Koy bokkaale !" }
10
19
{ "fr": "Les gens ne formaient (à l´origine) qu´une seule communauté. Puis ils divergèrent. Et si ce n´était une décision préalable de ton Seigneur, les litiges qui les opposaient auraient été tranchés.", "wo": "Nit ñi nekkuñu woon lu dul wenn xeet. Ñu juuyoo. Te bu dul koon waxi Yàlla ja jiitu woon, àttekoon na seeni diggante ca la ñu juuyoo. (s) " }
10
20
{ "fr": "Et ils disent : \"Que ne fait-on descendre sur lui (Muhammad) un miracle de son Seigneur ? \" Alors, dis : \"L´inconnaissable relève seulement d´Allah. Attendez donc; je serai avec vous parmi ceux qui attendent.", "wo": "Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom laaya ju tukkee ca Boroomam ?” . Neel : “Lu fàddu (di kumpa) Yàlla rekk a ko xam. Kon nanga muñandiku ; Man nag, maa ngi ànd ak yéen bokk ca way- muñandiku ña." }
10
21
{ "fr": "Et quand Nous faisons goûter aux gens une miséricorde après qu´un malheur les a touchés, voilà qu´ils dénigrent Nos versets. Dis : \"Allah est plus prompt à réprimer (ceux qui dénigrent Ses versets)\". Car Nos anges enregistrent vos dénigrements .", "wo": "Su Nu musalee nit ci yërmaande [niki taw] ginnaaw ba leen naqar dalee, ñuy def i pexe ci Sunuy tegtal. Neel : “Yàllaa gën a gaaw ciy pexe” . Sunuy ndaw danañu bind li ngeen di fexe de." }
10
22
{ "fr": "C´est Lui qui vous fait aller sur terre et sur mer, quand vous êtes en bateau. [Ces bateaux] les emportèrent, grâce à un bon vent. Ils s´en réjouirent jusqu´au moment où, assaillis par un vent impétueux, assaillis de tous côtés par les vagues, se jugeant enveloppés [par la mort], ils prièrent Allah, Lui vouant le culte [et disant]: \"Certes, si Tu nous sauves de ceci, nous serons parmi les reconnaissants ! \"", "wo": "Moom mooy ki leen doxloo, ci suuf si ak ci géej gi, ba ngeen nekkee ca gaal ga. Te gaal googu daw ak ñoom ci ngelaw lu teey. Ñu bég ca ba ngelaw lu tar songu leen, duusi géej wër leen ci wet gu nekk, ba ñu njortu ne ñoom alageef na leen, ñuy ñaan Yàlla, di sellal diineem, di [giñ] ne: “Boo Nu musalee ci lii, fàwwu dananu bokk ci way-sant ña [Yàlla] !”" }
10
23
{ "fr": "Lorsqu´Il les a sauvés, les voilà qui, sur terre, transgressent injustement. ô gens ! Votre transgression ne retombera que sur vous-mêmes. C´est une jouissance temporaire de la vie présente. Ensuite, c´est vers Nous que sera votre retour, et Nous vous rappellerons alors ce que vous faisiez.", "wo": "Ba Nu leen musalee, ñu daldi beew ci kaw suuf si ci lu dul dëgg. Éy yéen nit ñi ! Seen beew googu tooñuleen ci kenn ku dul seen bopp. Muy yóbbalub àdduna. Ba noppi nag ngeen dellu jëm ci Nun, Nu xamal leen la ngeen doon def." }
10
24
{ "fr": "La vie présente est comparable à une eau que Nous faisons descendre du ciel et qui se mélange à la végétation de la terre dont se nourrissent les hommes et les bêtes. Puis lorsque la terre prend sa parure et s´embellit, et que ses habitants pensent qu´elles est à leur entière disposition, Notre Ordre lui vient, de nuit ou de jour, c´est alors que Nous la rendrons toute moissonnée, comme si elle n´avait pas été florissante la veille. Ainsi exposons-Nous les preuves pour des gens qui réfléchissent.", "wo": "Nirale dundug àddina nekkul lu dul lu mel ni ndox mu ñu wàcce mu jóge asamaan sa, gàncax ga ràbboo ci suuf si [ngir màndi ci ndox moomu], muy li nit ñi ak mala yi di lekk. Bu suuf si jot taaram ci rafet ba ña ca dëkk am yaakaar ne am nañu kàttan ci moom, Sunu dogal dikkal ko guddi walla bëccëg, Nu def ko ni lu ñu góob, mu mel ni nekku fa woon démb. Noonu Lanuy leerale laaya yi ci nit ñoo xam ne danañu xalaat." }
10
25
{ "fr": "Allah appelle à la demeure de la paix et guide qui Il veut vers un droit chemin.", "wo": "Yàllaa ngi woote jëme [ci topp ndigal] ca këru jàmm ga, te Dana jubal ku ko soob jëme ko ca yoon wu jub wa xocc." }
10
26
{ "fr": "A ceux qui agissent en bien est réservée la meilleure (récompense) et même davantage. Nulle fumée noircissante, nul avilissement ne couvriront leurs visages. Ceux-là sont les gens du Paradis, où ils demeureront éternellement .", "wo": "Ñay rafetal, am nañu li gën a baax [Àjjana] ak ndollant [Gis Yàlla]. Te seeni kanam du muuru ngir njàqare walla toroxte. Ñooña ñooy duggu Àjjana te dañu fay béel.(h)" }
10
27
{ "fr": "Et ceux qui ont commis de mauvaises actions, la rétribution d´une mauvaise action sera l´équivalent. Un avilissement les couvrira, - pas de protection pour eux contre Allah -, comme si leurs visages se couvraient de lambeaux de ténèbres nocturnes. Ceux-là sont là les gens du Feu où ils demeureront éternellement.", "wo": "Ña nga xam ne dañoo fàggu lu ñaaw, am nañu lu ñaaw lu ko niru. Te la ñu yayoo mooy toroxte, - te duñu am kenn ku leen musal ci Yàlla -, daanaka day mel ni seeni kanam dañoo muuru ak daggitu guddi gu lëndëm. Ñooña ñoo dugg Safara te dañu fay béel." }
10
28
{ "fr": "(Et rappelle-toi) le jour où Nous les rassemblerons tous. Puis, Nous dirons à ceux qui ont donné [à Allah] des associés : \"A votre place, vous et vos associés.\" Nous les séparerons les uns des autres et leurs associés diront : \"Ce n´est pas nous que vous adoriez\".", "wo": "Te bis ba ñu leen dajalee ñoom ñépp, te ñu wax ña daan bokkaale : “Beruleen fale ak seeni xërëm ya.” . Dananu téqale seeni diggante, seen xërëm ya naan : “Du nun ñii lañu doon jaamu de” . " }
10
29
{ "fr": "Allah suffit comme témoin entre nous et vous. En vérité, nous étions indifférents à votre adoration\".", "wo": "Te Yàlla doy na seede ci sunu diggante ak yéen. Nekkewunu woon lu dul di ñàkk a faale seenug jaamu” ." }
10
30
{ "fr": "Là, chaque âme éprouvera (les conséquences de) ce qu´elle a précédemment accompli. Et ils seront ramenés vers Allah leur vrai Maître; et leurs inventions (idoles) s´éloigneront d´eux.", "wo": "Noonu, bakkan bu nekk la mu jëfoon sadd ko. Ñu delloo leen ca seen Boroom muy dëgg ; ya ñu daan sos réer leen." }
10
31
{ "fr": "Dis : \"Qui vous attribue de la nourriture du ciel et de la terre ? Qui détient l´ouïe et la vue, et qui fait sortir le vivant du mort et fait sortir le mort du vivant, et qui administre tout ? \" Ils diront : \"Allah\". Dis alors : \"Ne le craignez-vous donc pas ? \".", "wo": "Neel : “ Ana kan moo leen di jox xéewal yu jóge kaw asamaan ak ci suuf si ? Kan moo moom dégg-dégg [nopp yi], ak gis-gis [bët yi], ana kan mooy génne luy dundu ci lu dee, di génne lu dee ci lu dundu, ana kan mooy dogal mbir yi ?” . Danañu toontu ne : “Yàlla” . Neeleen kon : “Lu leen teree ragal Yàlla ?” ." }
10
32
{ "fr": "Tel est Allah, votre vrai Seigneur. Au delà de la vérité qu´y a-t-il donc sinon l´égarement ? Comment alors pouvez-vous, vous détourner ? \"", "wo": "Kon noonu la, Yàlla di seen Boroom ba di dëgg ga. Kon lan moo nekk ci ginnaaw dëgg lu dul ag réer ? Kon naka leen leen mën a wëlbatee ?” ." }
10
33
{ "fr": "C´est ainsi que s´est réalisée la parole de ton Seigneur contre ceux qui sont pervers : \"Ils ne croiront pas\".", "wo": "Noonu la sa kàddug Boroom yayee te dal ca kaw ña di ay saay-saay ndax gëmuñu." }
10
34
{ "fr": "Dis : \"Parmi vos associés, qui donne la vie par une première création et la redonne [après la mort] ? \" Dis : \"Allah [seul] donne la vie par une première création et la redonne. Comment pouvez-vous vous écarter [de l´adoration d´Allah] ?", "wo": "Neel : “Ndax am na ci ña ngeen di bokkaaleek [Yàlla] kuy sos mbindéef, mën koo dundal [gannaaw ba mu deewee]?” . Neel : “Yàlla rekk a mën a sos mbindéef te mën koo dundal. Kon naka lees leen di wëlbatee ?” ." }
10
35
{ "fr": "Dis : \"Est-ce qu´il y a parmi vos associés un qui guide vers la vérité ? \" Dis : \"C´est Allah qui guide vers la vérité. Celui qui guide vers la vérité est-il plus digne d´être suivi, ou bien celui qui ne se dirige qu´autant qu´il est lui-même dirigé ? Qu´avez-vous donc ? Comment jugez-vous ainsi ? \"", "wo": "Neel : “Yàlla rekkay gindee jëme ci dëgg. Moo ndax du Kiy gindee jëme ci dëgg moo gën a yey ci ñu topp ko, walla ka nga xam ne du gindee, lu dul ñu di ko gindi ? Kon lu leen jot te naka ngeen di àttee ?” ." }
10
36
{ "fr": "Et la plupart d´entre eux ne suivent que conjecture. Mais, la conjecture ne sert à rien contre la vérité ! Allah sait parfaitement ce qu´ils font.", "wo": "Li ëpp ci ñoom, toppuñu lu dul ay njort. Te njort du jariñ dara ci dëgg ! Yàlla naka Ku xam xéll la li ngeen di def." }
10
37
{ "fr": "Ce Coran n´est nullement à être forgé en dehors d´Allah mais c´est la confirmation de ce qui existait déjà avant lui, et l´exposé détaillé du Livre en quoi il n´y a pas de doute, venu du Seigneur de l´Univers.", "wo": "Alxuraan jii nekkul lu ñu duur bàyyi Yàlla, waaye dafa nekk di luy dëggal la ko jiitu tey settantal Téere ba nga xam ne sikk nekkul ci ne ma nga tukkee ca Boroom àddina si.(s)" }
10
38
{ "fr": "Ou bien ils disent : \"Il (Muhammad) l´a inventé ? \" Dis : \"Composez donc une Sourate semblable à ceci, et appelez à votre aide n´importe qui vous pourrez, en dehors Allah, si vous êtes véridiques\".", "wo": "Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur” ? Neel : “Indileen saar wu ni mel, te woo ku leen neex ba mu des Yàlla [mu dimbali leen ci loolu] ndeem ñu dëggu ngeen” ." }
10
39
{ "fr": "Bien au contraire : ils ont traité de mensonge ce qu´ils ne peuvent embrasser de leur savoir, et dont l´interprétation ne leur est pas encore parvenue. Ainsi ceux qui vivaient avant eux traitaient d´imposteurs (leurs messagers). Regarde comment a été la fin des injustes !", "wo": "Déedéet : weddi nañu loo xam ne amuñu xam-xamam te ag leeralam agsiwul ci ñoom. Noonu la ña leen jiitu weddee woon. Waaye xoolal rekk la mujjug tooñkat ya deme woon !" }
10
40
{ "fr": "Certains d´entre eux y croient, et d´autres n´y croient pas. Et ton Seigneur connaît le mieux les fauteurs de désordre.", "wo": "Te kat am na ci ñoom ñu ko gëm, am na it ñu ko gëmul. Te sa Boroom moo gën a xam yàqkat ya." }