sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
7
153
{ "fr": "Ceux qui ont fait de mauvaises actions et qui ensuite se sont repentis et ont cru... ton Seigneur, après cela est sûrement Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
7
154
{ "fr": "Et quand la colère de Moïse se fut calmée, il prit les tablettes. Il y avait dans leur texte guide et miséricorde à l´intention de ceux qui craignent leur Seigneur.", "wo": "Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom." }
7
155
{ "fr": "Et Moïse choisit de son peuple soixante-dix hommes pour un rendez-vous avec Nous. Puis lorsqu´ils furent saisis par le tremblement (de terre), il dit : \"Mon Seigneur, si Tu avais voulu, Tu les aurais détruis avant, et moi avec. Vas-Tu nous détruire pour ce que des sots d´entre nous ont fait ? Ce n´est là qu´une épreuve de Toi, par laquelle Tu égares qui Tu veux, et guides qui Tu veux. Tu es notre Maître. Pardonne-nous et fais-nous miséricorde, car Tu es le Meilleur des pardonneurs .", "wo": "Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale." }
7
156
{ "fr": "Et prescris pour nous le bien ici-bas ainsi que dans l´au-delà. Nous voilà revenus vers Toi, repentis.\" Et (Allah) dit : \"Je ferai que Mon châtiment atteigne qui Je veux. Et Ma miséricorde embrasse toute chose. Je la prescrirai à ceux qui (Me) craignent, acquittent la Zakat, et ont foi en Nos signes.", "wo": "Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.” . Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.(r)" }
7
157
{ "fr": "Ceux qui suivent le Messager, le Prophète illettré qu´ils trouvent écrit (mentionné) chez eux dans la Thora et l´évangile. Il leur ordonne le convenable, leur défend le blâmable, leur rend licites les bonnes choses, leur interdit les mauvaises, et leur ôte le fardeau et les jougs qui étaient sur eux. Ceux qui croiront en lui, le soutiendront, lui porteront secours et suivront la lumière descendue avec lui ; ceux-là seront les gagnants.", "wo": "Ña nga xam ne danañu topp Yonent ba, di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ñu bind ko ca ya ñu yore ci Tawreet ak Injiil. Mu di leen digal lu baax, di leen tere lu bon, daganal leen yu sell ya, araamal ca ñoom yu selladi ya, soppil leen ya leen diisoon ak gàkk ya nekkoon ca ñoom. Kon ñi ko gëm [moom Muhammad] te weg ko, te ñu topp leer ga Nu wàcce ci moom; ñoom ñooy way-texe ña. " }
7
158
{ "fr": "Dis : \"ô hommes ! Je suis pour vous tous le Messager d´Allah, à Qui appartient la royauté des cieux et de la terre. Pas de divinité à part Lui. Il donne la vie et Il donne la mort. Croyez donc en Allah, en Son messager, le Prophète illettré qui croit en Allah et en Ses paroles. Et suivez-le afin que vous soyez bien guidés\".", "wo": "Neeleen : «Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi nga xam ne Moo moom nguuru asamaan yi ak suuf si. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Mooy dundal, Mooy rey. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam bi, di ku ñu soloo te jàngul, te moom gëm na Yàlla ak ug kàddoom. Kon toppleen ko, xéy-na kon ngeen gindiku” ." }
7
159
{ "fr": "Parmi le peuple de Moïse, il est une communauté qui guide (les autres) avec la vérité, et qui, par là, exerce la justice.", "wo": "Amoon na ci nitu Muusaa, mbooloo muy gindee ci dëgg ak di ca tegtaloo ci maandute." }
7
160
{ "fr": "Nous les répartîmes en douze tribus, (en douze) communautés. Et Nous révélâmes à Moïse, lorsque son peuple lui demanda de l´eau : \"Frappe le rocher avec ton bâton.\" Et voilà qu´en jaillirent douze sources. Chaque tribu sut son abreuvoir. Nous les couvrîmes de l´ombre du nuage, et fîmes descendre sur eux la manne et les cailles : \"Mangez des bonnes choses que Nous vous avons attribuées.\" Et ce n´est pas à Nous qu´ils ont fait du tort, mais c´est à eux même qu´ils en faisaient.", "wo": "Nu xaaj leen fukki giir ak ñaar ñuy ay xeet. Ba noppi, Nu soloo Muusaa, ba ñuy sàkku lu ñu naan, ne ko : “Dóoral xeer wi ak sa yet wi.” . Noonu fukki bëti ndox ak ñaar balle ca. Ku nekk ca ñoom xamee fa muy naane. Nu defal leen keppaar ak niir wa, Nu wàcceel leen lem gu weex ak i njanaaw, ne leen : “Lekkleen ci yu sell yi Nu leen wërsëgale.” . Waaye tooñuñu Nu, seen bopp rekk lañuy tooñ." }
7
161
{ "fr": "Et lorsqu´il leur fut dit : \"Habitez cette cité et mangez [de ses produits] à votre guise, mais dites : rémission [à nos pêchés] et entrez par la porte en vous prosternant. Nous vous pardonnerons vos fautes; et aux bienfaisants (d´entre vous,) Nous accorderons davantage\".", "wo": "[Fàttalikul] ba ñu leen waxee ne : “Dugguleen ci dëkk bii te nangeen di lekk ci ñamam yi fu mu leen soobe, te nangeen di wax : Sippikug bàkkaar te nangeen tàbbi ci buntu bi sujjóot. Kon Nu baal leen seeni ñaawteef ; te Dananu dolli way-rafetal ña” ." }
7
162
{ "fr": "Puis, les injustes parmi eux changèrent en une autre, la parole qui leur était dite. Alors Nous envoyâmes du ciel un châtiment sur eux, pour le méfait qu´ils avaient commis.", "wo": "Ña tooñ ci ñoom, soppi la ñu leen wax ak yeneeni wax. Nu yebal fa ñoom mbugal mu tukke asamaan ngir la ñu nekk di tooñ." }
7
163
{ "fr": "Et interroges-les au sujet de la cité qui donnait sur la mer, lorsqu´on y transgressait le Sabbat ! Que leurs poissons venaient à eux faisant surfaces, au jour de leur Sabbat, et ne venaient pas à ceux le jour où ce n´était pas Sabbat ! Ainsi les éprouvions-Nous pour la perversité qu´ils commettaient .", "wo": "Te nga laaj leen lu jëm ci dëkk ba nekkoon ca tefesu géej ga ca gaawu ba ! Ba seen jën ya tëmbu ci ñoom ca seenug gaawu, tey bañ a génn bis ya! Noonu la Nu leen doon nattoo ngir la ñu daan fétterlu génn topp.(s)" }
7
164
{ "fr": "Et quand parmi eux une communauté dit : \"Pourquoi exhortez-vous un peuple qu´Allah va anéantir ou châtier d´un châtiment sévère ? \" Ils répondirent : \"Pour dégager notre responsabilité vis-à-vis de votre Seigneur; et que peut-être ils deviendront pieux ! \"", "wo": "Te am mbooloo ca ñoom ne : “Lu tax ngeen di waar nit ñoo xam ne Yàlla dana leen rey mbaa mu teg leen mbugal mu tar ?” . Ñu toontu [ñoom ña doon waare] ne : “Ngir nu am lay ca seen Boroom ak xéy- na ñoom ñu ragal Yàlla !”" }
7
165
{ "fr": "Puis, lorsqu´ils oublièrent ce qu´on leur avait rappelé, Nous sauvâmes ceux qui (leur) avaient interdit le mal et saisîmes par un châtiment rigoureux les injustes pour leurs actes pervers.", "wo": "Saar 7 : Dig wa 206 Laaya - Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
7
165
{ "fr": "Puis, lorsqu´ils oublièrent ce qu´on leur avait rappelé, Nous sauvâmes ceux qui (leur) avaient interdit le mal et saisîmes par un châtiment rigoureux les injustes pour leurs actes pervers.", "wo": "Ba ñu fàttee la ñu leen doon waare, musal Nanu ña doon tere lu bon, Nu sadd ña doon tooñ, mbugal mu tar ngir la ñu féttérlu woon génn topp." }
7
166
{ "fr": "Puis, lorsqu´ils refusèrent (par orgueil) d´abandonner ce qui leur avait été interdit, Nous leur dîmes : \"Soyez des singes abjects\".", "wo": "Bu ñu rëyloo ca la ñu leen tere, Nu wax leen ne : “Nekkleen di ay golo yu torox” ." }
7
167
{ "fr": "Et lorsque ton Seigneur annonça qu´Il enverra certes contre eux quelqu´un qui leur imposera le pire châtiment jusqu´au Jour de la Résurrection. En vérité ton Seigneur est prompt à punir mais Il est aussi Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "[Fàttalikul] ba seen Boroom xamlee ne Dana leen yónnee ku leen di teg gëm jaa boni mbugal ba kerook Bis-pénc di agsi. Sa Boroom nag Ku gaaw la ci mbugal te Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. " }
7
168
{ "fr": "Et Nous les avons répartis en communautés sur la terre. Il y a parmi eux des gens de bien, mais il y en a qui le sont moins. Nous les avons éprouvés par les biens et par des maux, peut-être reviendraient-ils (au droit chemin).", "wo": "Te séddale Nanu leen ay giir ci suuf si. Am ci ñoom ñu yiw, am ñu yiwadi. Nu nattu leen ciy xéewal ak ciy naqar ndax ñu dellusi [ci seen Boroom]." }
7
169
{ "fr": "Puis les suivirent des successeurs qui héritèrent le Livre, mais qui préférèrent ce qu´offre la vie d´ici-bas en disant : \"Nous aurons le pardon.\" Et si des choses semblables s´offrent à eux, ils les acceptent. N´avait-on pas pris d´eux l´engagement du Livre, qu´ils ne diraient sur Allah que la vérité ? Ils avaient pourtant étudié ce qui s´y trouve. Et l´ultime demeure est meilleure pour ceux qui pratiquent la piété, - Ne comprendrez-vous donc pas ? -", "wo": "Kuutaay gu bon toftaloo ca ñoom, [teewul] ñu jàppe ci alali ku yées ki [di àddina], ñu naan : “Dees nanu baal.” . Te bu leen alal ju ne mel dikkalee, ñu jàpp ca. Waaw ndax kóllareb Téere ba tënku leen ci di waxal Yàlla dëgg rekk ? Moone jàng nañu la nekk ca biir de. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla, - Moo ndax dangeen dul xel-lu ? -" }
7
170
{ "fr": "Et ceux qui se conforment au Livre et accomplissent la Salat, [en vérité], Nous ne laissons pas perdre la récompense de ceux qui s´amendent.", "wo": "Te ñay jafandu ca Téere ba te di taxawal julli, [nañu xam ne] Nun nag Dunu sànk peyu way-sellal ña." }
7
171
{ "fr": "Et lorsque Nous avons brandi au-dessus d´eux le Mont, Comme si c´eût été une ombrelle. Ils pensaient qu´il allait tomber sur eux. \"Tenez fermement à ce que Nous vous donnons et rappelez-vous son contenu. Peut-être craindrez vous Allah\" .", "wo": "[Fàttalikul] ba Nu yékkatee doj wa mu tiim leen, mel ni niir la. Ñu am njort ci mu daanu ci seen kaw. Ñu ne leen : “Jàppleen lii ñu leen jox ànd ca ak farlu te ngeen jëfe li nekk ci biir. Ndax xéy-na yéen ngeen ragal Yàlla” .(h)" }
7
172
{ "fr": "Et quand ton Seigneur tira une descendance des reins des fils d´Adam et les fit témoigner sur eux-mêmes : \"Ne suis-Je pas votre Seigneur ? \" Ils répondirent : \"Mais si, nous en témoignons...\" - afin que vous ne disiez point, au Jour de la Résurrection : \"Vraiment, nous n´y avons pas fait attention\",", "wo": "[Fàttalikul] ba sa Boroom génnee ci ndigul doomu-aadama yi seeni sëf, te Mu seedeloo leen ci seen bopp, ne leen : “Du Maay seen Boroom ?” . Ñu ne : “ Axakay, seede nanu ko...” - ngir ngeen bañ a wax ca Bis-pénc ba ne : “Danoo réere woon lii [mu nekk seenu lay]” ," }
7
173
{ "fr": "ou que vous auriez dit (tout simplement) : \"Nos ancêtres autrefois donnaient des associés à Allah, et nous sommes leurs descendants, après eux. Vas-Tu nous détruire pour ce qu´ont fait les imposteurs ? \"", "wo": "mbaa ngeen bañ a wax : “Du dara lu dul sunuy maam dañoo bokkaale woon lu jiitu nu sëtoo ca ñoom ginnaaw ga. Ndax dees na nu mbugal [ci loo xam ne ña jubutoon ca nun ñoo ko def] ?”" }
7
174
{ "fr": "Et c´est ainsi que Nous expliquons intelligemment les signes. Peut-être reviendront-ils !", "wo": "Noonu la Nuy leeralee tegtal yi. Ndax xéy-na ñu dellusi [ci seen Boroom] !" }
7
175
{ "fr": "Et raconte-leur l´histoire de celui à qui Nous avions donné Nos signes et qui s´en écarta. Le Diable, donc, l´entraîna dans sa suite et il devint ainsi du nombre des égarés.", "wo": "Nettalileen ka Nu joxoon Sunuy mbóot mu rocceeku ca. Séytaane topp ko, tax na mu bokk ca way-beew ña." }
7
176
{ "fr": "Et si Nous avions voulu, Nous l´aurions élevé par ces mêmes enseignements, mais il s´inclina vers la terre et suivit sa propre passion. Il est semblable à un chien qui halète si tu l´attaques, et qui halète aussi si tu le laisses. Tel est l´exemple des gens qui traitent de mensonges Nos signes. Eh bien, raconte le récit. Peut-être réfléchiront-ils !", "wo": "Su nu sooboon Nu yékkatikook mbóot yooyu, waaye dafa jengoon jëm ci àddina, topp bànneexam. Dafay mel ni xaj, boo ko songee muy yalkat, boo ko bàyyee muy yalkat. Loolu mooy niróowaaleeb nit ña weddi Sunuy kàddu. Nettalil xew-xew ba. Xéy-na ñoom ñu fàttaliku !" }
7
177
{ "fr": "Quel mauvais exemple que ces gens qui traitent de mensonges Nos signes, cependant que c´est à eux-mêmes qu´ils font de tort.", "wo": "Nekkinu nit ña weddi Sunuy kàddu, aka bon, waaye seen bopp lañuy tooñ nag." }
7
178
{ "fr": "Quiconque Allah guide, voilà le bien guidé. Et quiconque Il égare, voilà les perdants.", "wo": "Ku Yàlla gindi nag, mu nekk cig njub. Ña Mu bàyyi cig réer, ñooy ñu yàqule ña." }
7
179
{ "fr": "Nous avons destiné beaucoup de djinns et d´hommes pour l´Enfer. Ils ont des coeurs, mais ne comprennent pas. Ils ont des yeux, mais ne voient pas. Ils ont des oreilles, mais n´entendent pas. Ceux-là sont comme les bestiaux, même plus égarés encore. Tels sont les insouciants.", "wo": "Nun bind nanu ba noppi ngir Safara jinne yu bari ak nit. Ñeel na leen xol yu dul am dégg-dégg. Ay bët yu ñu dul gis ak ay nopp yu ñu dul dégge. Ñooña, dañoo mel ni mala ya, ñoo leen gën a réer sax. Ñooy ñu sàggan ña.(s)" }
7
180
{ "fr": "C´est à Allah qu´appartiennent les noms les plus beaux. Invoquez-Le par ces noms et laissez ceux qui profanent Ses noms : ils seront rétribués pour ce qu´ils ont fait.", "wo": "Yàllaa moom tur yu rafet yi. Nangeen ko ciy jaamu te ngeen dëddu ña di jeng ci turam yi : dees na leen feye la ñu daan def." }
7
181
{ "fr": "Parmi ceux que Nous avons créés, il y a une communauté qui guide (les autres) selon la vérité et par celle-ci exerce la justice.", "wo": "Nekk na ci ñi Nu bind, xeet woo xam ne danañu gindiku ci dëgg te danañu maandu." }
7
182
{ "fr": "Ceux qui traitent de mensonges Nos enseignements, Nous allons les conduire graduellement vers leur perte par des voies qu´ils ignorent.", "wo": "Waaye ña weddi Sunuy tegtal, Dananu leen jay, jaarele leen fu ñu xamul." }
7
183
{ "fr": "Et Je leur accorderai un délai, car Mon stratagème est solide !", "wo": "Muñal-leen, Sama pexe naka lu dëgër la !" }
7
184
{ "fr": "Est-ce qu´ils n´ont pas réfléchi ? Il n´y a point de folie en leur compagnon (Muhammad) : il n´est qu´un avertisseur explicite !", "wo": "Moo ndax dañu dul xél-lu xam ne seen àndandoo bi jinne jàppu ko? Nekkul lu dul waarekat bu ràññeeku !" }
7
185
{ "fr": "N´ont-ils pas médité sur le royaume des cieux et de la terre, et toute chose qu´Allah a créée, et que leur terme est peut-être déjà proche ? En quelle parole croiront-ils après cela ?", "wo": "Moo ndax dañu dul xool nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xéy-na Mu jegeñal seen àpp ? Kon jan wax gannaaw josam, lañu mën a gëm ?" }
7
186
{ "fr": "Quiconque Allah égare, pas de guide pour lui. Et Il les laisse dans leur transgression confus et hésitants.", "wo": "Ku Yàlla bàyyi cig réeram, kenn du la mën a gindi. Dana leen jàppe ca seen beew ga ñuy tëñax-tëñaxi." }
7
187
{ "fr": "Ils t´interrogent sur l´Heure : \"Quand arrivera-t-elle ? \" Dis : \"Seul mon Seigneur en a connaissance. Lui seul la manifesta en son temps. Lourde elle sera dans les cieux et (sur) la terre et elle ne viendra à vous que soudainement.\" Ils t´interrogent comme si tu en étais averti. Dis : \"Seul Allah en a connaissance.\" Mais beaucoup de gens ne savant pas.", "wo": "Ñi ngi lay laaj ci taxawaayu Bis-pénc ba : “Kañ lay doon ?” . Neel : “Kenn amu ca xam- xam ku dul sama Boroom. Kenn du ko feeñal ca waxtoom ku dul Moom. Lu diis la ci asamaan ya ak ci suuf si, duleen digal lu dul cig mbetteel.” . Ña nga la koy laaj mel ni danga ca xam dara. Neel : “Xam-xam nekkul fenn fu dul fa Yàlla.” . Waaye lu ëpp ci nit ñi xamuñu." }
7
188
{ "fr": "Dis : \"Je ne détiens pour moi-même ni profit ni dommage, sauf ce qu´Allah veut. Et si je connaissais l´Inconnaissable, j´aurais eu des biens en abondance, et aucun mal ne m´aurait touché. Je ne suis, pour les gens qui croient, qu´un avertisseur et un annonciateur\" .", "wo": "Neel : “Mënaluma sama bopp njariñ walla lor lu dul la soob Yàlla. Su ma xamoon kumpa, kon ma bari lool alal ak i xéewal, te kon lu metti duma dal. Nekkuma man lu dul waarekat, béglekatu nit ñi gëm Yàlla” . (r)" }
7
189
{ "fr": "C´est Lui qui vous a créés d´un seul être dont il a tiré son épouse, pour qu´il trouve de la tranquillité auprès d´elle; et lorsque celui-ci eut cohabité avec elle, elle conçut une légère grossesse, avec quoi elle se déplaçait (facilement). Puis lorsqu´elle se trouva alourdie, tous deux invoquèrent leur Seigneur : \"Si Tu nous donnes un (enfant) sain, nous serons certainement du nombre des reconnaissants\".", "wo": "Moom mooy Ki leen bind ci benn bakkan, mu génne ca soxnaam ngir muy am ug dal ci moom; ba mu ko muuree, mu ëmb ëmb bu woyof, muy dem ak ëmbam. Ba mu diisee, ñoom ñaar ñu ñaanYàlla seen Boroom ne ko : “Soo nu mayee [doom] ju baax, kon faf dananu bokk ci gërëmaakoon ña” ." }
7
190
{ "fr": "Puis, lorsqu´Il leur eût donné un (enfant) sain, tous deux assignèrent à Allah des associés en ce qu´Il leur avait donné. Mais Allah est bien au-dessus des associés qu´on Lui assigne.", "wo": "Ba Mu leen mayee [doom], ñu bokkaale Yàlla ca la Mu leen may. Te Yàlla jomb na la ñu Ko bokkaale. " }
7
191
{ "fr": "Est-ce qu´ils assignent comme associés ce qui ne crée rien et qui eux-mêmes sont créés,", "wo": "Moo ndax dañuy bokkaaleek [Yàlla] ñoo xam ne mënuñoo bind dara te dañu leen a bind," }
7
192
{ "fr": "et qui ne peuvent ni les secourir ni se secourir eux-mêmes ?", "wo": "te mënuñuleen a dimbali, mënuñoo dimbali seen bopp sax ?" }
7
193
{ "fr": "Si vous les appelez vers le chemin droit, ils ne vous suivront pas. Le résultat pour vous est le même, que vous les appeliez ou que vous gardiez le silence.", "wo": "Boo leen woowee ci njub, duñuleen topp. Ngeen woo leen walla ngeen noppi [bañ leen a woo] yem kepp." }
7
194
{ "fr": "Ceux que vous invoquez en dehors d´Allah sont des serviteurs comme vous. Invoquez-les donc et qu´ils vous répondent, si vous êtes véridiques.", "wo": "Ña nga xam ne dangeen leen jaamu bàyyi Yàlla, ay jaam lañu ni yéen. Wooleen ba xam danañu leen nangul ndeem ñu dëggu ngeen." }
7
195
{ "fr": "Ont-ils des jambes pour marcher ? Ont-ils de mains pour frapper ? Ont-ils des yeux pour observer ? Ont-ils des oreilles pour entendre ? Dis : \"Invoquez vos associés, et puis, rusez contre moi; et ne me donnez pas de répit.", "wo": "Moo ndax dañoo am tànk yu ñu doxe ? Moo ndax dañoo am loxo yu ñu téye ? Moo ndax dañoo am bët yu ñuy gise ? Moo ndax dañoo am nopp yu ñuy dégge ? Neeleen : “Wooleen seen bokkaale yooyu, te nangeen ma fexeel, bañ maa yeexe." }
7
196
{ "fr": "Certes mon Maître, c´est Allah qui a fait descendre le Livre (le Coran). C´est Lui qui se charge (de la protection) des vertueux.", "wo": "Ki may dimbali mooy Yàlla Mi wàcce Téere ba te mu méngook ñu sell ña." }
7
197
{ "fr": "Et ceux que vous invoquez en dehors de Lui ne sont capables ni de vous secourir, ni de se secourir eux-mêmes.\"", "wo": "Ña ngeen di jaamu te bàyyi Ko, mënuñuleen a dimbali te mënuñoo dimbali seen bopp sax.”" }
7
198
{ "fr": "Et si tu les appelles vers le chemin droit, ils n´entendent pas. Tu les vois qui te regardent, (mais) ils ne voient pas.", "wo": "Boo leen woowee cig njub duñu dégg sax. Dangeen gis ñu di la xool te ñoom duñu gis." }
7
199
{ "fr": "Accepte ce qu´on t´offre de raisonnable , commande ce qui est convenable et éloigne-toi des ignorants.", "wo": "Jéggaleel te nangay digle yiw, te nanga dëddu ñu réer ña.(s)" }
7
200
{ "fr": "Et si jamais le Diable t´incite à faire le mal, cherche refuge auprès d´Allah. Car Il entend, et sais tout.", "wo": "Saa su la ag soppeeku dalee, gu tukke ci Séytaane, nanga sàkku mucc ci Yàlla. Moom Yàlla nag Kuy dégg la, Kuy xam la." }
7
201
{ "fr": "Ceux qui pratiquent la piété, lorsqu´une suggestion du Diable les touche se rappellent [du châtiment d´Allah]: et les voilà devenus clairvoyants.", "wo": "Ña ragal Yàlla, bu leen lu metti dalee, tukke ci Séytaane, ñu fàttaliku [seen Boroom] daldi nekk ñu am ràññee." }
7
202
{ "fr": "(Quand aux méchants), leurs partenaires diaboliques les enfoncent dans l´aberration, puis ils ne cessent (de s´enfoncer).", "wo": "Mu am seen kuute ñoo xam ne danañu leen tàbbal ci ag réer, te di leen ca xamb rekk." }
7
203
{ "fr": "Quand tu ne leur apportes pas de miracles, ils disent : \"Pourquoi ne l´inventes-tu pas ? \" Dis : \"Je ne fais que suivre ce qui m´est révélé de mon Seigneur. Ces [versets coraniques] sont des preuves illuminantes venant de votre Seigneur, un guide et une grâce pour des gens qui croient.", "wo": "Te bu ndigal ñëwul, ñu naan : “Lu tee nga fental ko sa bopp ?” Neel : “Duma def lu dul topp li ñu ma soloo mu tukke ci sama Boroom. Loolu ay lay la yu tukkee ci seen Boroom, di njub ak yërmaande ci nit ñu gëm." }
7
204
{ "fr": "Et quand on récite le Coran, prêtez-lui l´oreille attentivement et observez le silence, afin que vous obteniez la miséricorde (d´Allah).", "wo": "Kon bu ñuy jàng Alxuraan, nangeen ko déglu te nangeen ko xarawlu ndax xéy-na yërëmees leen." }
7
205
{ "fr": "Et invoque ton Seigneur en toi-même, en humilité et crainte, à mi-voix, le matin et le soir, et ne sois pas du nombre des insouciants.", "wo": "Nangay tudd sa Boroom ci sa bopp ànd ak toroxlu ak ug ragal, ci lu ànd ak yelu ci sa kàddu, ci kaw subaak ngoon, te bul bokk ca ñu sàggan ña. " }
7
206
{ "fr": "Ceux qui sont auprès de ton Seigneur [les anges] ne dédaignent pas de L´adorer. Ils Le glorifient et se prosternent devant Lui .", "wo": "Ña nga xam ne ñanga ca sa Boroom, duñu di rëylu ci jaamu Ko. Te danañu Ko di sàbbaal, di Ko sujjóotal. " }
8
1
{ "fr": "Ils t´interrogent au sujet du butin. Dis : \"Le butin est à Allah et à Son messager.\" Craignez Allah, maintenez la concorde entre vous et obéissez à Allah et à Son messager, si vous êtes croyants.", "wo": "Ña nga lay laaj lu jëm ci màng yi. Neeleen : “Màng yi, Yàlla ak Yonentam ñoo leen moom.” Kon ragal-leen Yàlla te nangeen defar seeni diggante, te ngeen topp Yàlla ak Yonentam ndeem way-gëm ngeen." }
8
2
{ "fr": "Les vrais croyants sont ceux dont les coeurs frémissent quand on mentionne Allah. Et quand Ses versets leur sont récités, cela fait augmenter leur foi. Et ils placent leur confiance en leur Seigneur.", "wo": "Jullit ya ñooy ña nga xam ne bu ñu tuddee Yàlla seeni xol yëngu. Te bu ñu jàngaa ci ñoom ay laayaam mu yokk seen ngëm. Te ci seen Boroom lañu wékku." }
8
3
{ "fr": "Ceux qui accomplissent la Salat et qui dépensent [dans le sentir d´Allah] de ce que Nous leur avons attribué.", "wo": "Ñooy ña nga xam ne danañu taxawal julli te ca la Nu leen wërsëgal, danañu ca joxe." }
8
4
{ "fr": "Ceux-là sont, en toute vérité les croyants : à eux des degrés (élevés) auprès de leur Seigneur, ainsi qu´un pardon et une dotation généreuse.", "wo": "Ñooña ñooy jullit dëgg : ñeel na leen yékkatiku ca seen Boroom, ci ag jéggal ak wërsëg wu tedd." }
8
5
{ "fr": "De même, c´est au nom de la vérité que ton Seigneur t´a fait sortir de ta demeure, malgré la répulsion d´une partie des croyants .", "wo": "Naka noonu, sa Boroom génne na la sa kër ci dëgg, te fekk neexul ñennat ca way-gëm ña.(n)" }
8
6
{ "fr": "Ils discutent avec toi au sujet de la vérité après qu´elle fut clairement apparue; comme si on les poussait vers la mort et qu´ils (la) voyaient .", "wo": "Ñangay weranteek yaw ca dëgg ga ginnaaw ba mu feeñee, leer nàññ ; mel ni dañu leen a bëmax jëme ci dee, ñu ne ca jàkk." }
8
7
{ "fr": "(Rappelez-vous), quand Allah vous promettait qu´une des deux bandes sera à vous. \"Vous désiriez vous emparer de celle qui était sans armes, alors qu´Allah voulait par Ses paroles faire triompher la vérité et anéantir les mécréants jusqu´au dernier .", "wo": "(Fàttalikul), ba leen Yàlla digee ndam ca kaw benn ca ñaari kurél ya ngeen moom ko. Te ngeen ne siiw moom ga yorul ngànnaay, te Yàlla nammoon a dëgëral dëgg ga ci kàddoom te dog ginnaaw yéefar ya." }
8
8
{ "fr": "afin qu´Il fasse triompher la vérité et anéantir le faux, en dépit de la répulsion qu´en avaient les criminels.", "wo": "ngir dëgg sax te caaxaan jóge fi doonte la naqari na saay-saay sa." }
8
9
{ "fr": "(Et rappelez-vous) le moment où vous imploriez le secours de votre Seigneur et qu´Il vous exauça aussitôt : \"Je vais vous aider d´un millier d´Anges déferlant les uns à la suite des autres.", "wo": "(Fàttalikul) ba ngeen sàkkoo xettaliku ci seen Boroom te Mu nangul leen, ne : “Man danaa leen dooleel ak junni Malaaka yuy toftalante." }
8
10
{ "fr": "Allah ne fit cela que pour (vous) apporter une bonne nouvelle et pour qu´avec cela vos coeurs se tranquillisent. Il n´y a de victoire que de la part d´Allah. Allah est Puissant est Sage.", "wo": "Yàlla deful loolu lu dul ngir mbégtem [jullit ñi] ak ngir seen xel dal. Ndimbal amul feneen fu dul fa Yàlla. Naka Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la." }
8
11
{ "fr": "Et quand Il vous enveloppa de sommeil comme d´une sécurité de Sa part, et du ciel Il fit descendre de l´eau sur vous afin de vous en purifier, d´écarter de vous la souillure du Diable, de renforcer les coeurs et d´en raffermir les pas ! [vos pas].", "wo": "(Fàttalikuleen) ba Mu leen muuree ag ngëmmentu muy jàmm ju jóge ci Moom, te Mu wàcce ci yéen ndox mu jóge asamaan ngir Mu laabal leen ak loolu, ak ngir Mu dàqal leen sobees Séytaane, ak ngir Mu dëgëral seeni xol, dëgëral seeni ndëggu." }
8
12
{ "fr": "Et ton Seigneur révéla aux Anges : \"Je suis avec vous : affermissez donc les croyants. Je vais jeter l´effroi dans les coeurs des mécréants. Frappez donc au-dessus des cous et frappez-les sur tous les bouts des doigts.", "wo": "[Fàttalikul] ba sa Boroom xamalee Malaaka ya ne leen : “Maak yéen a ànd : nangeen dooleel ñi gëm. Danaa sànni njàqare ci xoli ñi weddi. Kon dóorleen ci kaw doq yi te ngeen dóor leen ci cati baaraam yi." }
8
13
{ "fr": "Ce, parce qu´ils ont désobéi à Allah et à Son messager.\" Et quiconque désobéit à Allah et à Son messager... Allah est certainement dur en punition !", "wo": "Loolu, ngir dañoo juuyook Yàlla ak Yonentam.” . Te ku juuyook Yàlla ak Yonentam, ... [na xam ne] Yàlla ku tar mbugal la !" }
8
14
{ "fr": "Voilà (votre sort); goûtez-le donc ! Et aux mécréants le châtiment du Feu (sera réservé).", "wo": "Noonu lay dalee ci yéen [yéefar yi] ; kon mosleen ko ! Te ñeel na way- weddi ña mbugalu Safara." }
8
15
{ "fr": "ô vous qui croyez quand vous rencontrez (l´armée) des mécréants en marche , ne leur tournez point le dos.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ñi, bu ngeen dajeek yéefar yi ñuy ràngu jëm ci yéen, buleen daw won leen ginnaaw.(s)" }
8
16
{ "fr": "Quiconque, ce jour-là, leur tourne le dos, - à moins que ce soit par tactique de combat, ou pour rallier un autre groupe, - celui-là encourt la colère d´Allah et son refuge sera l´Enfer. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Ku daw won leen ginnaaw, ca bis boobu - lu dul kuy jéem a njuuy ba jekku na mu war a xeexe, walla kuy jéem a tafu ci mboolom jullit, - tàbbi ci merum Yàlla te dëkkuwaayam Safara la. Aka bon booba dëkkuwaay !" }
8
17
{ "fr": "Ce n´est pas vous qui les avez tués : mais c´est Allah qui les a tués. Et lorsque tu lançais (une poignée de terre) , ce n´est pas toi qui lançais : mais c´est Allah qui lançait, et ce pour éprouver les croyants d´une belle épreuve de Sa part ! Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Te reyuleen leen [yéen jullit ñi] : Yàlla moo leen rey. Te sànniwoo [yaw Yonent bi], bi nga sànnee suuf si : waaye Yàlla moo sànni, ngir Mu may jullit ñi xéewal gu rafet gu tukke ca Moom Yàlla ! Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la." }
8
18
{ "fr": "Voilà ! Allah réduit à rien la ruse des mécréants.", "wo": "Loolu la dëggal ci yéen te [xamleen ne] Kuy doyadal pexey yéefar yi la [Moom Yàlla]." }
8
19
{ "fr": "Si vous avez imploré l´arbitrage d´Allah vous connaissez maintenant la sentence [d´Allah] Et si vous cessez [la mécréance et l´hostilité contre le Prophète..], c´est mieux pour vous. Mais si vous revenez, Nous reviendrons, et votre masse, même nombreuse, ne vous sera d´aucune utilité. Car Allah est vraiment avec les croyants.", "wo": "Ndegam dangeen di sàkku lu ngeen di àttewoo [yéen yéefar yi], ab àtte dikkal na leen ba noppi. Bu ngeen bàyyee [la ngeen nekkoon cig kéefar], mooy gën ci yéen. Bu ngeen delloo [ca la ngeen nekke woon], Nu dellu [ci di jox Yonent bi ndimbal], te kon seeni mbooloo duleen jariñ dara, doonte dafa bari lool. Yàlla nag Mook jullit yee ànd." }
8
20
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Obéissez à Allah et à Son messager et ne vous détournez pas de lui quand vous l´entendez (parler).", "wo": "Éy yéen ñi gëm ñi ! Nangeen topp Yàlla ak ub Yonentam, buleen ko dëddu te fekk dégg ngeen li muy wax." }
8
21
{ "fr": "Et ne soyez pas comme ceux qui disent : \"Nous avons entendu \", alors qu´ils n´entendent pas.", "wo": "Buleen mel ni ñiy wax : “Dégg nanu” , te fekk dégguñu woon dara." }
8
22
{ "fr": "Les pires des bêtes auprès d´Allah, sont, [en vérité], les sourds-muets qui ne raisonnent pas .", "wo": "Li gën a yées ci bindeef yi ca Yàlla, mooy ñi tëx, luu te bañ a xel-lu.(r)" }
8
23
{ "fr": "Et si Allah avait reconnu en eux quelque bien, Il aurait fait qu´ils entendent. Mais, même s´Il les faisait entendre, ils tourneraient [sûrement] le dos en s´éloignant.", "wo": "Ku leen woo woon ñu dëddu, nekk ñu beddiku." }
8
24
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Répondez à Allah et au Messager lorsqu´il vous appelle à ce qui vous donne la (vraie) vie, et sachez qu´Allah s´interpose entre l´homme et son cœur, et que c´est vers Lui que vous serez rassemblés.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Nangeen wuyu Yàlla ak Yonentam ba, bu ñu leen woowee ci lu leen di musal, te nangeen xam ne Yàlla nag Dana dox nit ak xelam, te Danañu leen bëmëx jëme ca Moom. " }
8
25
{ "fr": "Et craignez une calamité qui n´affligera pas exclusivement les injustes d´entre vous. Et sachez qu´Allah est dur en punition.", "wo": "Te nangeen ragal mbugal moo xam ne ku dul ña weddi ci yéen. Te nangeen xam ne Yàlla Ku tar mbugal la." }
8
26
{ "fr": "Et rappelez-vous quand vous étiez peu nombreux, opprimés sur terre, craignant de vous faire enlever par des gens. Il vous donna asile, vous renforça se Son secours et vous attribua de bonnes choses afin que vous soyez reconnaissants", "wo": "Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal ci suuf si, ngeen di ragal nit ñi fëkk leen. Mu daroo leen, dimbali leen ci ndimbalam, Mu wërsëgal leen ci xéewal yu sell ndax xéy-na yéen ngeen gëram [seen Boroom]." }
8
27
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Ne trahissez pas Allah et le Messager. Ne trahissez pas sciemment la confiance qu´on a placée en vous ?", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent bi. Te buleen wuruj ci seen kóllare te xam ko xéll." }
8
28
{ "fr": "Et sachez que vos biens et vos enfants ne sont qu´une épreuve et qu´auprès d´Allah il y a une énorme récompense.", "wo": "Xamleen ne seeni alal ak seeni doom, fitna lañu ci yéen te pey gu màgg a nga fa Yàlla." }
8
29
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Si vous craignez Allah, Il vous accordera la faculté de discerner (entre le bien et le mal), vous effacera vos méfaits et vous pardonnera. Et Allah est le Détenteur de l´énorme grâce.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen ragalee Yàlla, Mu sagal leen, far seeni ñaawtéef, jéggal leen. Te Yàlla Kuy Boroom ngëneel yu màgg la." }
8
30
{ "fr": "(Et rappelle-toi) le moment où les mécréants complotaient contre toi pour t´emprisonner ou t´assassiner ou te bannir. Ils complotèrent, mais Allah a fait échouer leur complot, et Allah est le meilleur en stratagèmes .", "wo": "(Fàttalikul) ba la yéefar ya fexelee ngir ñu tëj la ci barab mbaa ñu rey la mbaa ñu génne la. Ñu def seeni pexe, Yàlla def ay pexeem, te Yàlla di Ku gën a màgg ay pexe." }
8
31
{ "fr": "Et lorsque Nos versets leur sont récités, ils disent : \"Nous avons écouté, certes ! Si nous voulions, nous dirions pareil à cela, ce ne sont que des légendes d´anciens.", "wo": "Te saa yu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy laaya, ñu ne : “Dégg nanu, ba noppi te sunu neexoon nu wax lu mel ni lii, ndaxte lii nekkul lu dul léebi nit ñu jëkk ña” .(s)" }
8
32
{ "fr": "Et quand ils dirent : \"ô Allah, si cela est la vérité de Ta part, alors, fais pleuvoir du ciel des pierres sur nous, ou fais venir sur nous un châtiment douloureux\".", "wo": "(Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam lii lu dëggu la lu jóge ci Yaw, Nanga sotti ci sunu kaw taw bu nekk ay xéewal wàcc jóge asamaan, mbaa nga indil nu mbugal mu metti” ." }
8
33
{ "fr": "Allah n´est point tel qu´Il les châtie, alors que tu es au milieu d´eux. Et Allah n´est point tel qu´Il les châtie alors qu´ils demandent pardon.", "wo": "Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal." }
8
34
{ "fr": "Qu´ont-ils donc pour qu´Allah ne les châtie pas, alors qu´ils repoussent (les croyants) de la Mosquée sacrée, quoiqu´ils n´en soient pas les gardiens, car ses gardiens ne sont que les pieux. Mais la plupart d´entre eux ne le savent pas.", "wo": "Yellul ci ñoom Yàlla bañ leen a mbugal, te ñuy wax nit ñi bañ a jëm ci jàkka ju ñu wormaal ja, nekkuñu ñoom soppey jàkka jooju, ay soppeem ñooy way-ragal Yàlla ña. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu." }
8
35
{ "fr": "Et leur prière , auprès de la Maison, n´est que sifflement et battements de mains : \"Goûtez donc au châtiment, à cause de votre mécréants ! \"", "wo": "Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak ay tàccu, kon : “Mosleen mbugal mi [ca xare Badar] ngir la ngeen doon weddi !”" }
8
36
{ "fr": "Ceux qui ne croient pas dépensent leurs biens pour éloigner (les gens) du sentier d´Allah. Or, après les avoir dépensés, ils seront pour un sujet de regret. Puis ils seront vaincus, et tous ceux qui ne croient pas seront rassemblés vers l´Enfer,", "wo": "Ña nga xam ne dañoo weddi, Dananu sànk seeni alal ngir dëdduloo [nit ñi] yoonu Yàlla. Waaye Danañu ko sànk ba noppi di ko réccu. Ñu not leen, te ña weddi dees na leen bëmax jëme Safara," }
8
37
{ "fr": "afin qu´Allah distingue le mauvais du bon, et qu´Il place les mauvais les uns sur les autres, pour en faire un amoncellement qu´Il jettera dans l´Enfer. Ceux-là sont les perdants.", "wo": "ngir Yàlla téqale yéefar yi ak ña gëm Yàlla, Dana boole yéefar yi, dajale leen ñoom ñépp ca biir Safara. Ñooñu ñooy way-ñàkk ña. " }
8
38
{ "fr": "Dis à ceux qui ne croient pas que, s´ils cessent, on leur pardonnera ce qui s´est passé. Et s´ils récidivent, (ils seront châtiés); à l´exemple de (leurs) devanciers.", "wo": "Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek Yonent bi], nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekke woon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk." }
8
39
{ "fr": "Et combattez-les jusqu´à ce qu´il ne subsiste plus d´association, et que la religion soit entièrement à Allah. Puis, s´ils cessent (ils seront pardonnés car) Allah observe bien ce qu´ils oeuvrent.", "wo": "Xeexleen ak ñoom ba fitna jóge fi, ba diine nekk lu ñu jagleel Yàlla léppam. Waaye bu ñu bàyyee nag, Yàlla mi ngi ne jàkk ci li ñuy def." }
8
40
{ "fr": "Et s´ils tournent le dos, sachez alors qu´Allah est votre Maître. Quel excellent Maître et quel excellent Protecteur!", "wo": "Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di jàppale. Ndaw soppe bu baax, ndaw Aji-dimbalee ju baax !" }
8
41
{ "fr": "Et sachez que, de tout butin que vous avez ramassé, le cinquième appartient à Allah, au messager, à ses proches parents, aux orphelins, aux pauvres, et aux voyageurs (en détresse), si vous croyez en Allah et en ce que Nous avons fait descendre sur Notre serviteur, le jour du Discernement : le jour où les deux groupes s´étaient rencontrés, et Allah est Omnipotent ).", "wo": "Te nangeen xam ne lu ngeen màng ci lu mu mën a doon, juróomeelu xaaj ba ñeel na Yàlla ak Yonent ba ak i jegeñaaleem, ak jirim ya, ak way-ñàkk ya, ak ña nekk ci yoon di tukki, ndegam gëm ngeen Yàlla ak la Nu wàcce ci Sunu jaam ba bisu téqale ba [ca Badar] : bisu ndaje ñaari mbooloo ya, te Yàlla mën na lu ne.(h)" }
8
42
{ "fr": "Vous étiez sur le versant le plus proche, et eux (les ennemis) sur le versant le plus éloigné, tandis que la caravane était plus bas que vous. Si vous vous étiez donné rendez-vous, vous l´auriez manqué (effrayés par le nombre de l´ennemi). Mais il fallait qu´Allah accomplît un ordre qui devait être exécuté, pour que, sur preuve, pérît celui qui (devait) périr, et vécût, sur preuve, celui qui (devait) vivre. Et certes, Allah est Audient et Omniscient .", "wo": "Fekk na booba ngeen nekk ca xur wa gën a jegeñ, ñoom ñu nekk ca xur wa gën a sori, njëgg ma gën a suufe. Bu ngeen sàkku woon a dajeek ñoom, du sotti. Waaye lu Yàlla dogal day nekk, dana am ñu dee ci lu bir ak ñu dundu ci lu bir. Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la." }
8
43
{ "fr": "En songe, Allah te les avait montrés peu nombreux ! Car s´Il te les avait montrés nombreux, vous auriez certainement fléchi, et vous vous seriez certainement disputés à propos de l´affaire. Mais Allah vous en a préservés. Il connaît le contenu des coeurs.", "wo": "Ba la Yàlla wonee ci sa gént, ñoom ñu nekk mbooloo mu néew ! [Li ko waral mooy], su Ma la wonoon ñu nekk ñu bari, kon dangeen di yoqat, te dangeen xëccoo ca mbir ma. Waaye Yàlla defal leen dal. Moom nag xam na li nekk ci xol yi." }
8
44
{ "fr": "Et aussi, au moment de la rencontre, Il vous les montrait peu nombreux à Vos yeux, de même qu´Il vous faisant paraître à leurs yeux peu nombreux afin qu´Allah parachève un ordre qui devait être exécuté. C´est a Allah que sont ramenées les choses.", "wo": "Fàttalikul ba Ma leen wonee, ba ngeen dajee, ñu néew ci seeni bët, te ngeen nekk ca ñu néew ca seeni bët ngir la Yàlla dige lu am la. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellu." }
8
45
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Lorsque vous rencontrez une troupe (ennemie), soyez fermes, et invoquez beaucoup Allah afin de réussir.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ñi ! Bu ngeen dajeek mbooloo, nangeen sax ci pastéef te ngeen tudd Yàlla lu bari ndax ngeen am ndam." }