sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
6
117
{ "fr": "Certes ton Seigneur connaît le mieux ceux qui s´égarent de Son sentier, et c´est Lui qui connaît le mieux les bien-guidés.", "wo": "Te sa Boroom Moo gën a xam ku réere aw yoonam, te Moo gën a xam it ña tegu ci njub gindiku." }
6
118
{ "fr": "Mangez donc de ce sur quoi on a prononcé le nom d´Allah si vous êtes croyants en Ses versets (le Coran).", "wo": "Lekkleen la nga xam ne tuddeef na ca turu Yàlla [ba ñu koy rendi], ndegam gëm ngeen ay kàddoom." }
6
119
{ "fr": "Qu´avez-vous à ne pas manger de ce sur quoi le nom d´Allah a été prononcé ? Alors qu´Il vous a détaillé ce qu´Il vous a interdit, à moins que vous ne soyez contraints d´y recourir. Beaucoup de gens égarent, sans savoir, par leurs passions. C´est ton Seigneur qui connaît le mieux les transgresseurs .", "wo": "Lu leen nekkal ci bañ lekk loo xam ne tudd nañu ca turu Yàlla ? Moom leeral na leen la araam ci yéen, gannaaw bu fekkee mën ngeen a loru [ngir bañ a am lenn lu ngeen lekk]. Waaye ñu bari dañuy réer ngir topp seeni bànneex cig ñàkk a xam. Sa Boroom moo gën a xam way-jéggi dayo ña." }
6
120
{ "fr": "évitez le péché apparent ou caché, (car) ceux qui acquièrent le péché seront rétribués selon ce qu´ils auront commis.", "wo": "Saar 6 : Jur ga 165 Laaya - Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
6
120
{ "fr": "évitez le péché apparent ou caché, (car) ceux qui acquièrent le péché seront rétribués selon ce qu´ils auront commis.", "wo": "Nangeen bàyyi bàkkaar bu fés ak bu nëbbu, ñiy fàggu bàkkaar dees na leen fey la ñu fàggu woon.(s)" }
6
121
{ "fr": "Et ne mangez pas de ce sur quoi le nom d´Allah n´a pas été prononcé, car ce serait (assurément) une perversité. Les diables inspirent à leurs alliés de disputer avec vous. Si vous leur obéissez, vous deviendrez certes des associateurs.", "wo": "Buleen lekk loo xam ne tudduñu ca turu Yàlla, loolu génn topp la [caay-caay]. Te Séytaane mooy xiir aw nitam ñuy dàggasanteek yéen. Te bu ngeen leen toppee, daldi ñibbi ca way-bokkaale ya." }
6
122
{ "fr": "Est-ce que celui qui était mort et que Nous avons ramené à la vie et à qui Nous avons assigné une lumière grâce à laquelle il marche parmi les gens, est pareil à celui qui est dans les ténèbres sans pouvoir en sortir ? Ainsi on a enjolivé aux mécréants ce qu´ils oeuvrent.", "wo": "Moo ndax ka nekkoon ku dee [yéefar], Nu dundal ko [gëmloo ko], jox ko leer gu muy leerloo buy dox ci biir nit ñi, dana nirook ka nga xam ne misaalam mooy dafa nekk cig lëndëm gu mu dul génn ? Noonu la yéefar yi di rafetloo la ñu doon def." }
6
123
{ "fr": "Ainsi, Nous avons placé dans chaque cité de grands criminels qui y ourdissent des complots. Mais ils ne complotent que contre eux-mêmes et ils n´en sont pas conscients.", "wo": "Naka noonu, Lanu defe ci bépp dëkk ay kilifa ca ña dàq a tooñ ngir ñu fay nas ay pexe. Te pexe ya, dara duleen ca moy te yëguñu ko." }
6
124
{ "fr": "Et lorsqu´une preuve leur vient, ils disent : \"Jamais nous ne croirons tant que nous n´aurons pas reçu un don semblable à celui qui a été donné aux messagers d´Allah\". Allah sait mieux où placer Son message. Ceux qui ont commis le crime seront atteints d´un rapetissement auprès d´Allah ainsi que d´un supplice sévère pour les ruses qu´ils tramaient.", "wo": "Te ñoom, saa su leen laaya dikkalee, ñuy wax naan : “Nun dunu gëm ba mbete nu indil nu lu mel ni la ñu joxoon Yonent Yàlla ya” . Yàllaa gën a xam fa Muy wàcce la Muy yónnee. Bàkkaarkat yi, toroxte dal na leen tukke fa Yàlla ak mbugal mu tar ngir pexe [yu bon ya ñu daan nas]." }
6
125
{ "fr": "Et puis, quiconque Allah veut guider, Il lui ouvre la poitrine à l´Islam . Et quiconque Il veut égarer, Il rend sa poitrine étroite et gênée, comme s´il s´efforçait de monter au ciel. Ainsi Allah inflige Sa punition à ceux qui ne croient pas.", "wo": "Ku Yàlla bëgg a jubal, dafay ubbi xolam ci Lislaam. Ku Mu bëgg a bàyyi cig réeram, day bàyyi xolam nekk cig xat gu tar ba mel ni day yéeg jëm kaw asamaan. Noonu la Yàlla di tege mbugal ña gëmul." }
6
126
{ "fr": "Telle est la voie de ton Seigneur dans toute sa rectitude. Nous avons [effectivement] bien détaillé les signes (ou versets) à des gens qui se rappellent.", "wo": "Lile mooy sa yoonu Boroom wu jub xocc wa. Leeralal Nanu Sunuy tegtal nit ñuy fàttaliku [seen Boroom]." }
6
127
{ "fr": "Pour eux la maison du Salut auprès de leur Seigneur. Et c´est Lui qui est leur protecteur, pour ce qu´ils faisaient (sur terre).", "wo": "Am nañu kërug jàmm fa seen Boroom. Moom moo di Seen soppe ngir la ñu daan def [ci lu baax].(r) " }
6
128
{ "fr": "Et le jour où Il les rassemblera tous : \"ô communauté des djinns, vous avez trop abusé des humains\". Et leurs alliés parmi les humains diront : \"ô notre Seigneur, nous avons profité les uns des autres, et nous avons atteint le terme que Tu avais fixé pour nous.\" Il leur dira : \"l´Enfer est votre demeure, pour y rester éternellement, sauf si Allah en décide autrement.\" Vraiment ton Seigneur est Sage et Omniscient.", "wo": "Bis ba Mu leen di dajale [Yàlla] ñoom ñépp, di leen wax ne : «Éy yéen mboolooy jinne yi, baril ngeen seeni jëf ci nit ñi” . Nit ña ñu méngool ne : «Sunu Boroom, lenn ci nun, daanañu sàkku xéewlu ca ñeneen ña, te agsi nañu ca àpp ba Nga nu àppaloon.” . Mu ne leen : “Safaraay seen dëkkuwaay, te dangeen fay sax dàkk, lu dul la soob Yàlla.” . Sa Boroom dey Ku xereñ, Ku xam la." }
6
129
{ "fr": "Et ainsi accordons-Nous, à certains injustes l´autorité sur d´autres, (injustes) à cause de ce qu´ils ont acquis.", "wo": "Noonu Lanuy feeñale kiliftéefu yenn tooñkat ya ca kaw ñeneen ña ngir la ñu nekkoon di ko fàggu." }
6
130
{ "fr": "ô communauté des djinns et des humains, ne vous est-il pas venu des messagers, choisis parmi vous, qui vous ont raconté Mes signes et averti de la rencontre de ce jour ? Ils diront : \"Nous témoignons contre nous-mêmes.\" La vie présente les a trompés; et ils ont témoigné contre eux-mêmes qu´en (vérité) ils étaient mécréants.", "wo": "[Mu ne leen] Éy yéen mbooloom jinne yi ak nit ñi ndax ay Yonent dafa leen a dikkalul woon, feeñ ci seen biir, di leen nettali Samay ndigal ci doon leen waar ci ndajem seen Bis bii ? Ñu toontu ne : “Seede nanu loolu mu nekk ci sunu kaw.” . Dundug àddina wor na leen ; seeni seede dal ci seen kaw, saxal ne ñoom ay yéefar lañu woon." }
6
131
{ "fr": "C´est que ton Seigneur n´anéantit point injustement des cités dont les gens ne sont pas encore avertis .", "wo": "Loolu dafay tegtale ne sa Boroom du alag ab dëkk cig tooñeel ndare dafa yónni ndaw ñu lànk koo topp." }
6
132
{ "fr": "A chacun des rangs (des récompenses) selon ses oeuvres. Or ton Seigneur n´est pas inattentif à ce qu´ils font.", "wo": "Ñoom ñépp danañu am pey gu méngook la ñu jëfoon. Sa Boroom ñàkkul paal ca la ñuy jëf." }
6
133
{ "fr": "Ton Seigneur est le Suffisant à Soi-même, le Détenteur de la miséricorde. S´Il voulait, Il vous ferait périr et mettrait à votre place qui Il veut, de même qu´Il vous a créés d´une descendance d´un autre peuple.", "wo": "Sa Boroom Ku woomal la, boroom yërmaande la. Bu ko neexoon, mu jële leen fi, wuutale ci seen ginnaaw la Ko soob, ni Mu leen sose woon ngeen di ay sëti ñeneen." }
6
134
{ "fr": "Ce qui vous a été promis arrivera (certainement.) Et vous n´êtes pas à même de [Nous] réduire à l´impuissance.", "wo": "Li ñu leen dig luy ñëw la. Te dungeen mën a raw." }
6
135
{ "fr": "Dis : \"ô mon peuple ! Continuez à agir selon votre méthode; moi aussi j´agirai selon la mienne. Ensuite, vous saurez qui aura un meilleur (sort) dans l´au-delà.\" Certes, les injustes ne réussiront jamais.", "wo": "Neel : «Yéen samaw nit ! Jëfleen ci seeni mbir ; man dey aji-jëf laa. Dangeen mas a xami kan moo moom kër gu mujj ga.” . Ak lu mën a xew, tooñkat ya ñoom duñu texe.(s)" }
6
136
{ "fr": "Et ils assignent à Allah une part de ce qu´Il a Lui-même créé, en fait de récoltes et de bestiaux, et ils disent : \"Ceci est à Allah - selon leur prétention ! - et ceci à nos divinités.\" Mais ce qui est pour leurs divinités ne parvient pas à Allah, tandis que ce qui est pour Allah parvient à leurs divinités. Comme leur jugement est mauvais !", "wo": "Dañuy sédd Yàlla li Mu bind ci mbey ak ci jur gi, ab cér daldi wax ne : “Lii mooy wàllu Yàlla - ci seeni njortu ! - lii mooy wàllu li nu koy bokkaale.” . Te la ñu sédd ñii, du agsi ca Yàlla, waaye la ñu sédd Yàlla, dana agsi ca ñañu koy bokkaaleel. Na ñuy àttee ñaaw na !" }
6
137
{ "fr": "Et c´est ainsi que leurs divinités ont enjolivé à beaucoup d´associateurs le meurtre de leurs enfants, afin de les ruiner et de travestir à leurs yeux leur religion. Or si Allah voulait, ils ne le feraient pas. Laisse-les donc, ainsi que ce qu´ils inventent.", "wo": "Noonu la seen xërëm yooyu rafetale, ca ñu bari ca way-bokkaale ya, rey seeni doom, ngir alag leen, lëntal seen diine. Bu neexoon Yàlla, duñu ko def. Waaye bàyyileen ak la ñuy duur." }
6
138
{ "fr": "Et ils dirent : \"Voilà des bestiaux et des champs frappés d´interdiction : n´en mangeront que ceux que nous voudrons.\" - selon leur prétention ! - Et voilà des bêtes dont le dos est tabou, et des bêtes sur lesquelles ils rétribuera pour ce qu´ils inventaient comme mensonges .", "wo": "Ñu naan : “Jur gi ak mbey mi araam na : kenn du ci lekk ku dul ku Nu neex.” . - ci seeni njort ! - Ak jur goo xam ne seen ginnaaw araam na, ak yoo xam ne duñu tuddu Yàlla ci ñoom, lu dul di ko duural, Dana leen fey la ñu nekkoon di ko duur. " }
6
139
{ "fr": "Et ils dirent : \"Ce qui est dans le ventre de ces bêtes est réservé aux mâles d´entre nous, et interdit à nos femmes.\" Et si c´est un mort-né, ils y participent tous. Bientôt Il les rétribuera pour leur prescription , car Il est Sage et Omniscient.", "wo": "Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan na ci sunuy góor waaye araam na ci sunuy jabar [jigéen ñi].” . Waay, bu dee lu médd, góor ak jigéen ñoo ci yem. Dana leen fey seeni duur, Moom dey [Yàlla] Ku xereñ la, Ku xam la." }
6
140
{ "fr": "Ils sont certes perdants, ceux qui ont, par sottise et ignorance tué leurs enfants, et ceux qui ont interdit ce qu´Allah leur a attribué de nourriture, inventant des mensonges contre Allah. Ils se sont égarés et ne sont point guidés.", "wo": "Ña rey seeni doom cig réer ngir ñàkk a xam, yàqule nañu booleek di araamal la leen Yàlla wërsëgal, lépp tegu ci kaw duural Yàlla. Ñoom réer nañu ba sànku te dootuñu gindiku.(n)" }
6
141
{ "fr": "C´est Lui qui a créé les jardins, treillagés et non treillagés; ainsi que les palmiers et la culture aux récoltes diverses; [de même que] l´olive et la grenade, d´espèces semblables et différentes. Mangez de leurs fruits, quand ils en produisent; et acquittez-en les droits le jour de la récolte. Et ne gaspillez point car Il n´aime pas les gaspilleurs.", "wo": "Moom Yàlla Moo sos ay tooli gàncax guy law ci suuf si ak yuy jóg taxaw ; ak garabi tàndarma ak mbey yu meññeent ya wuute ; ak oliw ak garanaat yu niroo ak yu niroowul. Lekkleen seeni doom bu ñoree ; te nangeen génne asaka ja bis ba ngeen di watt [ngóob]. Te buleen yàq ndax Moom [Yàlla] safoowul yàqkat ya." }
6
142
{ "fr": "Et (Il a créé) parmi les bestiaux, certains pour le transport, et d´autres pour diverses utilités ; mangez de ce qu´Allah vous a attribué, et ne suivez pas les pas du Diable, car il est pour vous un ennemi déclaré.", "wo": "Am na ci jur gi yu mën a sëf, ak yu nekk i gëtt; lekkleen ci li leen Yàlla di wërsëgale, te buleen topp jeegoy Séytaane, moom Séytaane seenub noon la bu bir." }
6
143
{ "fr": "(Il en a créé) huit, en couples : deux pour les ovins, deux pour les caprins... dis : \"Est-ce les deux mâles qu´Il a interdits ou les deux femelles, ou ce qui est dans les matrices des deux femelles ? Informez-moi de toute connaissance, si vous êtes véridiques\";", "wo": "Sàkk na juróom-ñett yu nekk i ñaar-ñaar : ci xar yu góor ak jigéen, ci bëy yi ñaar... Neel : “Ndax ñaar ñu góor ñi ñoo araam walla ñaar ñu jigéen ñi walla la ëmbe ci biir ñaar yu jigéen ñi ? Waxleen ma ci xam- xam ndegam aw nit ngeen” ;" }
6
144
{ "fr": "...deux pour les camélidés, deux pour les bovins... Dis : \"Est-ce les deux mâles qu´Il a interdits ou les deux femelles, ou ce qui est dans les matrices des deux femelles ? Ou bien étiez-vous témoins quand Allah vous l´enjoignit ? \" Qui est donc plus injuste que celui qui invente un mensonge contre Allah pour égarer les gens sans se baser sur aucun savoir ? Allah ne guide pas les gens injustes.", "wo": "...am na ci gëléem yi ñaar, ak ci nag yi ñaar... Neel : “Ndax ñaar ñu góor ñi ñoo araam walla ñaar ñu jigéen ñi, walla la ëmbe ca biir ñaar ñu jigéen ña ? Am dangeen a nekkoon di ay seede ca la leen Yàlla dénku ci yooyu ?” . Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen ngir mën a réeral nit ñi ci lu àndul ak xam-xam ? Yàlla du gindi nit ña di ay tooñkat." }
6
145
{ "fr": "Dis : \"Dans ce qui m´a été révélé, je ne trouve d´interdit, à aucun mangeur d´en manger, que la bête (trouvée) morte, ou le sang qu´on a fait couler, ou la chair de porc - car c´est une souillure - ou ce qui, par perversité, a été sacrifié à autre qu´Allah.\" Quiconque est contraint, sans toutefois abuser ou transgresser, ton Seigneur est certes Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Neel : “Man dey gisuma, ci li ñu ma soloo, lu araam ci ñam wu ñuy lekk lu dul mu nekk médd walla deret yuy tuuru, walla yàppu mbaam- xuux - ndax sobe la - walla la ñu tuddu [ba ñu koy rey] keneen ku dul Yàlla cig génn topp.” . Waaye koo xam ne dafa loru, te di ku bew, walla muy ku jéggi dayo ca loola, Sa Boroom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.(s)" }
6
146
{ "fr": "Aux Juifs, Nous avons interdit toute bête à ongle unique . Des bovins et des ovins, Nous leurs avons interdit les graisses, sauf ce que portent leur dos, leurs entrailles, ou ce qui est mêlé à l´os. Ainsi les avons-Nous punis pour leur rébellion. Et Nous sommes bien véridiques.", "wo": "Dogaloon Nanu ca ña nekk Yahuud, ne araam na ci ñoom lépp luy boroom we te it araam na ca ñoom nebbonu nag ya ak gàtt ya, lu dul bu tegu ci seen ginnaaw, walla bu nekk ca seen mbàq, walla bu jaxasook yax ya. Noonu Lanu leen feye seen bew ga te Nun ñu dëggu Lanu. " }
6
147
{ "fr": "Puis, s´ils te traitent de menteur, alors dis : \"Votre Seigneur est Détenteur d´une immense miséricorde cependant que Sa rigueur ne saura être détournée des gens criminels\".", "wo": "Bu ñu la weddee, neel : “Seen Boroom dey Ku am yërmaande ju yaatu la, waaye mbugalam ma jëm ca saay-saay sa dara mënukoo feg” ." }
6
148
{ "fr": "Ceux qui ont associé diront : \"Si Allah avait voulu, nous ne lui aurions pas donné des associés, nos ancêtres non plus et nous n´aurions rien déclaré interdit.\" Ainsi leurs prédécesseurs traitaient de menteurs (les messagers) jusqu´à ce qu´ils eurent goûté Notre rigueur. Dis : \"Avez-vous quelque science à nous produire ? Vous ne suivez que la conjecture et ne faites que mentir\".", "wo": "Ñay bokkaale danañu wax ne : “Bu neexoon Yàlla, dunu bokkaale, sunuy baay it kon duñu bokkaale te dunu araamal dara, wat ci watiit !” . Noonu doŋŋ la ña leen jiitu woon doon weddee ba Sa mbugal ne xees ci seen kaw. Neel : “Ndax am ngeen xam-xam bu ngeen nu mën a génneel ? Yéen daal toppuleen lu moy ay njort te nekkuleen ci lu moy di fen” ." }
6
149
{ "fr": "Dis : \"L´argument décisif appartient à Allah. S´Il avait voulu certainement Il vous aurait tous guidés.(sur le droit chemin)", "wo": "Neel : “Lii, wommatug Yàlla la, Moo ko moom. Bu ko sooboon, Mu jubal leen yéen ñépp." }
6
150
{ "fr": "Dis : \"Amenez vos témoins qui attesteraient qu´Allah a interdit cela.\" Si ensuite ils témoignent, alors toi, ne témoignent pas avec eux et ne suis pas les passions de ceux qui traitent de mensonges Nos signes et qui ne croient pas à l´au-delà, tandis qu´ils donnent des égaux à leur Seigneur.", "wo": "Neel : “Indileen seeni seede yu mën a seede ne lii Yàlla dakoo araamal.” . Bu ñu ko seedee, yaw bu ca ànd ak ñoom, bul topp bànneexi ñay weddi sunuy ndigal ak ña gëmul àllaaxira, te ñoom dañuy ñaawal seen digganteek seen Boroom." }
6
151
{ "fr": "Dis : \"Venez, je vais réciter ce que votre Seigneur vous a interdit : ne Lui associez rien; et soyez bienfaisants envers vos père et mère. Ne tuez pas vos enfants pour cause de pauvreté. Nous vous nourrissons tout comme eux. N´approchez pas des turpitudes ouvertement, ou en cachette. Ne tuez qu´en toute justice la vie qu´Allah a fait sacrée. Voilà ce qu´[Allah] vous a recommandé de faire; peut-être comprendrez-vous.", "wo": "Neel : “Kaayleen ma taril leen li Yàlla araamal ci yéen : mooy buleen ko bokkaaleek dara ; te nangeen di rafetal jëme ci seeni waajur. Te buleen rey seeni doom ngir ragal ñàkk. Ndax Nun [Yàlla], Noo leen di wërsërgal yéen, di leen wërsëgal ñoom it. Te buleen jegeñ njaaloo ca la cay feeñ ak la cay nëbbu. Te buleen rey bakkan bi Yàlla wormaal lu dul ci dëgg. Loolu la leen ci dénk ; ndax Yàlla ngeen xel-lu.(r)" }
6
152
{ "fr": "Et ne vous approchez des biens de l´orphelin que de la plus belle manière, jusqu´à ce qu´il ait atteint sa majorité . Et donnez la juste mesure et le bon poids, en toute justice. Nous n´imposons à une âme que selon sa capacité. Et quand vous parlez, soyez équitables même s´il s´agit d´un proche parent. Et remplissez votre engagement envers Allah. Voilà ce qu´Il vous enjoint. Peut-être vous rappellerez-vous.", "wo": "Buleen jegeñ [laal] alali jirim ci lu dul na mu gën a rafete, ba bamuy mën a lijjanti boppam. Te nangeen di matal natt ak peese cig maandute. Nun [Yàlla] dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan. Bu ngeen di dox [ca la ngeen di àtte], nangeen ko defe ci maandute, doonte la sax seen mbokk ngeen di àtte. Nangeen matal it kóllereg Yàlla. Loolu la leen ci Yàlla dénk. Ndax ngeen di fàttaliku." }
6
153
{ "fr": "Et voilà Mon chemin dans toute sa rectitude, suivez-le donc; et ne suivez pas les sentiers qui vous écartent de Sa voie. Voilà ce qu´Il vous enjoint. Ainsi atteindrez-vous la piété.", "wo": "“Te lii nag moo di Sama yoon wu jub xocc wa, toppleen ko ; te buleen topp ñall yi, kon ñu teqale leen ak samaw yoon.” . Loolu la leen ci Yàlla dénku. Ndax Yàlla ngeen [di fegu] ragal Yàlla." }
6
154
{ "fr": "Puis Nous avons donné à Moïse le Livre complet en récompense pour le bien qu´il avait fait, et comme un exposé détaillé de toute chose, un guide et une miséricorde. Peut-être croiraient-ils en leur rencontre avec leur seigneur (au jour du Jugement dernier).", "wo": "Ba noppi ñu jox Muusaa Téere ba, ngir matal xéewal ci ku rafetal, ak ug faramfàcce ci mbir yépp, di njub, di yërmaande. Ndax Yàlla ñoom ñu gëm ne danañu dajeek seen Boroom." }
6
155
{ "fr": "Et voici un Livre (le Coran) béni que Nous avons fait descendre - suivez-le donc et soyez pieux, afin de recevoir la miséricorde -", "wo": "Te Téere bii wàcce Nanu ko, barkeel ko - toppleen ko, te ngeen ragal (Yàlla) ndax Yàlla amaana yërëmees leen - " }
6
156
{ "fr": "afin que vous ne disiez point : \"On n´a fait descendre le Livre que sur deux peuples avant nous, et nous avons été inattentifs à les étudier .", "wo": "ndax it ngeen bañ a wax ne : “ Ab Téere wàcceluñu ko kenn ku dul ñaari kurél ya [Yahuud ya ak Nasraan ya] ca ña nu jiitu, te nun seenug njàngale umpu nanu." }
6
157
{ "fr": "Ou que vous disiez : \"Si c´était à nous qu´on avait fait descendre le Livre que nous aurions certainement été mieux guidés qu´eux.\" Voilà certes que vous sont venus, de votre Seigneur, preuve, guidée et miséricorde. Qui est plus injuste que celui qui traite de mensonges les versets d´Allah et qui s´en détourne ? Nous punirons ceux qui se détournent de Nos versets, par un mauvais châtiment, pour s´en être détournés.", "wo": "Walla ngeen di wax naan : “Bu fekkoon ne ci nun lañu wàcce Téere ba, kon noo leen di gën a gindiku.” . Ag leeral dikkal na leen, jóge fa seen Boroom, di njub ak yërmaande. Ana kan moo gën a tooñ kuy dummóoyu kàdduy Yàlla te weddi leen ? Dananu feye, ñay dëddu Sunuy kàddu, gën jaa suufe [bon] mbugal ngir seenug dëddu." }
6
158
{ "fr": "Qu´attendent-ils ? Que les Anges leur viennent ? Que vienne ton Seigneur ? Ou que viennent certains signes de ton Seigneur ? Le jour où certains signes de ton Seigneur viendront, la foi en Lui ne profitera à aucune âme qui n´avait pas cru auparavant ou qui n´avait acquis aucun mérite de sa croyance. Dis : \"Attendez ! \" Nous attendons, Nous aussi.", "wo": "Moo ndax dañuy xaar ba Malaaka ya dikk fa ñoom? Walla sa Boroom agsi ? Walla lenn ci sa kéemaani Boroom dikk ? Bis ba lenn ci sa kéemaani Boroom dikkee, bàjjo bu gëmul woon lu jiitu, di door a gëm, du ko jariñ dara de, walla ku sàkkuwul wenn yiw it, ngëmam du ko jariñ dara. Neel : “Xaarleen !” . Nun it Noo ngi xaar.(s)" }
6
159
{ "fr": "Ceux qui émiettent leur religion et se divisent en sectes, de ceux-là tu n´es responsable en rien : leur sort ne dépend que d´Allah. Puis Il les informera de ce qu´ils faisaient.", "wo": "Ña nga xam ne dañoo xàjjale seen diine ba mu nekk ay pàcc-pàcc, bokkulook ñoom dara : seeni mbir ci Yàlla doŋŋ la nekk. Te Dana leen biral la ñu nekkoon di ko def." }
6
160
{ "fr": "Quiconque viendra avec le bien aura dix fois autant; et quiconque viendra avec le mal ne sera rétribué que par son équivalent. Et on ne leur fera aucune injustice.", "wo": "Ku def u yiw, am yool bu tollu ni fukki yooni yiw wa ; ku def ñaawtéef am bàkkaar bu tollu ni ñaawtéef wa. Te kenn duleen tooñ [ci yokkal mbaa wàññil leen ci dara]." }
6
161
{ "fr": "Dis : \"Moi, mon Seigneur m´a guidé vers un chemin droit, une religion droite, la religion d´Abraham, le soumis exclusivement à Allah et qui n´était point parmi les associateurs.", "wo": "Neel : “Sama Boroom gindi na ma teg ma ca yoon wu jub wa, di diine ju jub, di diiney Ibraahiima ma wéetal Boroomam te bokkuloon ca way-bokkaale ña." }
6
162
{ "fr": "Dis : \"En vérité, ma Salat, mes actes de dévotion, ma vie et ma mort appartiennent à Allah, Seigneur de l´Univers.", "wo": "Neel : “Samag julli, samag jaamu, samag dund ak samag dee, Yàlla Boroom àddina bee leen moom." }
6
163
{ "fr": "A Lui nul associé ! Et voilà ce qu´il m´a été ordonné, et je suis le premier à me soumettre.\"", "wo": "Amul bokkaale ! Te loolu lañu ma digal, te nekk naa di ku jiitu ca way-wommatu ña [jullit ña].”" }
6
164
{ "fr": "Dis : \"Chercherais-je un autre Seigneur qu´Allah, alors qu´Il est le Seigneur de toute chose ? Chacun n´acquiert [le mal] qu´à son détriment : personne ne portera le fardeau (responsabilité) d´autrui. Puis vers votre Seigneur sera votre retour et Il vous informera de ce en quoi vous divergez.", "wo": "Neel : “Ndax damay sàkku beneen boroom bu dul Yàlla, te Moom Mooy Boroom lépp lu ne ? Bakkan bu nekk, la mu fàggu ca moom doŋŋ lay delluwaat : kenn du yenul keneen yenam. Te ca seen Boroom ngeen di dellu Mu biral leen la ngeen nekkoon di ca juuyoo." }
6
165
{ "fr": "C´est Lui qui a fait de vous les successeurs sur terre et qui vous a élevés, en rangs, les uns au-dessus des autres, afin de vous éprouver en ce qu´Il vous a donné. (Vraiment) ton Seigneur est prompt en punition, Il est aussi Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Moom Moo leen def ngeen di ay kuutaay ci suuf si, Mu yékkati lenn ci yéen ci kaw ñeneen ña, [Dakoy def] ngir nattu leen ca la Mu leen jox. Sa Boroom nag Ku gaaw ci mbugal la, te it Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. " }
7
1
{ "fr": "Alif, Lam, Mim, Sad.", "wo": "Alif, Laam, Miim, Saad.(h)" }
7
2
{ "fr": "C´est un Livre qui t´a été descendu; qu´il n´y ait, à son sujet, nulle gêne dans ton cœur; afin que par cela tu avertisses, et (qu´il soit) un Rappel aux croyants.", "wo": "Ab Téeree ngi, bu ñu wàcce ci yaw ; ngir nga waare ca, ak mu nekk ag fàttali ci way-gëm ña ; bu wenn tiis nekk ci sa xol ngir loolu." }
7
3
{ "fr": "Suivez ce qui vous a été descendu venant de votre Seigneur et ne suivez pas d´autres alliés que Lui. Mais vous vous souvenez peu.", "wo": "Toppleen li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom. Buleen ko bàyyi di topp ay xërëm. Néew ngeen xalaat." }
7
4
{ "fr": "Que de cités Nous avons détruites ! Or, Notre rigueur les atteignit au cours du repos nocturne ou durant leur sieste.", "wo": "Bariwaana dëkk bu Nu alag ! Sunu mbugal agsi fa ci guddi walla ci bëccëg." }
7
5
{ "fr": "Leur invocation, lorsque leur survint notre rigueur, se limita à ces paroles : \"Certes nous étions injustes\".", "wo": "Te seeni njàmbat nekkul, ba leen mbugal ma saddee, lu dul : “Nun ay tooñkat lanu woon” ." }
7
6
{ "fr": "Nous interrogerons ceux vers qui furent envoyés des messagers et Nous interrogerons aussi les envoyés .", "wo": "Fàwwu Dananu laaj ña Nu yónni ca ñoom [nit ña], fàwwu it Dananu laaj ña Nu yónni woon [Yonent ya]." }
7
7
{ "fr": "Nous leur raconterons en toute connaissance (ce qu´ils faisaient) car Nous n´étions pas absent !", "wo": "Te Dananu leen nettali ji [ci loolu] ci xam-xam bu wér ndaxte fekke woon Nanu lépp !" }
7
8
{ "fr": "Et la pesée, ce jour-là, sera équitable. Donc, celui dont les bonnes actions pèseront lourd...Voilà ceux qui réussiront !", "wo": "Booba bis, peese bu dëggu lay doon. Ña seen peese diis ak u yiw... Ñoom ñooy ñu texe ña !" }
7
9
{ "fr": "Et quand à celui dont les bonnes actions pèseront léger...Voilà ceux qui auront causé la perte de leurs âmes parce qu´ils étaient injustes envers Nos enseignements.", "wo": "Ña seen peese woyof nag ... Ñooy ña yàqal seen bopp ngir ñàkk a faale Sunuy kàddu te doonoon ñu daan tooñ." }
7
10
{ "fr": "Certes, Nous vous avons donné du pouvoir sur terre et Nous vous y avons assigné subsistance. (Mais) vous êtes très peu reconnaissants !", "wo": "Defal Nanu leen ag jàppandal ci suuf si, defal leen ca lu ngeen dunde. Te seenug cant néew na !" }
7
11
{ "fr": "Nous vous avons créés, puis Nous vous avons donné une forme, ensuite Nous avons dit aux Anges : \"Prosternez-vous devant Adam.\" Ils se prosternèrent, à l´exception d´Iblis qui ne fut point de ceux qui se prosternèrent.", "wo": "Bind Nanu leen, jox leen i melo, ba noppi Nu wax Malaaka ya : “Sujjóotal-leen Aadama.” . Ñoom ñépp a sujjoot, ba mu des Ibliis, moom bokkul ca ña sujjóot." }
7
12
{ "fr": "[Allah] dit : \"Qu´est-ce qui t´empêche de te prosterner quand Je te l´ai commandé ? \" Il répondit : \"Je suis meilleur que lui : Tu m´as créé de feu, alors que Tu l´as créé d´argile\".", "wo": "[Yàlla] ne ko : “Lan moo la tee sujjóot ba Ma la ko digalee ?” . Mu ne : “Maa ko gën : ndax Danga ma bind ci Safara, moom Nga bind ko ci ban” . " }
7
13
{ "fr": "[Allah] dit : \"Descends d´ici, Tu n´as pas à t´enfler d´orgueil ici. Sors, te voilà parmi les méprisés.\"", "wo": "[Yàlla] ne ko : “Wàccal jóge fi, yaw waroo fi rëy-rëylu. Génnal, torox nga.”" }
7
14
{ "fr": "Accorde-moi un délai, dit (Satan) jusqu´au jour où ils seront ressuscités.", "wo": "Ibliis ne Ko : Muñal ma ba bisu dekki ba.”" }
7
15
{ "fr": "[Allah] dit : \"Tu es de ceux à qui délai est accordé.\"", "wo": "[Yàlla] ne ko : “Bokk nga ca ña Nuy muñandiku.”" }
7
16
{ "fr": "Puisque Tu m´as mis en erreur, dit [Satan], je m´assoirai pour eux sur Ton droit chemin,\r\n7|17|puis je les assaillirai de devant, de derrière, de leur droite et de leur gauche. Et, pour la plupart, Tu ne les trouveras pas reconnaissants.", "wo": "Ibliis daldi ne : “Giñ naa ne beewloo gi Nga ma teg, danaa leen rékki ci sa yoon wu jub wi," }
7
18
{ "fr": "Sors de là, dit (Allah) banni et rejeté. \"Quiconque te suit parmi eux... de vous tous, J´emplirai l´Enfer\".", "wo": "Yàlla ne ko : “Génnal” , di ku ñu detteel, di ku ñu dàq. “Ku la ca toppati ci ñoom... fàwwu Danaa feesale Safara ci yéen ñépp [yaak ñoom]” ." }
7
19
{ "fr": " ô Adam, habite le Paradis, toi et ton épouse; et ne mangez en vous deux, à votre guise; et n´approchez pas l´arbre que voici; sinon, vous seriez du nombre des injustes.", "wo": "“Te yaw Aadama, dëkkal yaak sa soxna, Àjjana ; lekkleen yéen ñaar fu leen fi neex ; waaye buleen jegeñ garab gii ; su amee, ngeen tooñ.”" }
7
20
{ "fr": "Puis le Diable, afin de leur rendre visible ce qui leur était caché - leurs nudités - leur chuchota, disant : \"Votre Seigneur ne vous a interdit cet arbre que pour vous empêcher de devenir des Anges ou d´être immortels ! \".", "wo": "Séytaane jax-jaxal leen ngir mu feeñal ca ñoom ñaar la Nu leen nëbboon - ci seen cër - mu ne leen : “Seen Boroom terewuleen ngeen jegeñ garab gii lu dul ne Dafa bañ ngeen nekk ñaari Malaaka walla ngeen bokk ca ñay dund fàwwu [duñu dee] !” ." }
7
21
{ "fr": "Et il leur jura : \"Vraiment, je suis pour vous deux un bon conseiller\".", "wo": "Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire” .(s)" }
7
22
{ "fr": "Alors il les fit tomber par tromperie. Puis, lorsqu´ils eurent goûté de l´arbre, leurs nudités leur devinrent visibles; et ils commencèrent tous deux à y attacher des feuilles du Paradis. Et leur Seigneur les appela : \"Ne vous avais-Je pas interdit cet arbre ? Et ne vous avais-Je pas dit que le Diable était pour vous un ennemi déclaré ? \"", "wo": "Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ?”" }
7
23
{ "fr": "Tous deux dirent : \"ô notre Seigneur, nous avons fait du tort à nous-mêmes. Et si Tu ne nous pardonnes pas et ne nous fais pas miséricorde, nous serons très certainement du nombre des perdants\".", "wo": "[Aadama ak Awa] daldi ne : “Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña” ." }
7
24
{ "fr": "Descendez, dit [Allah], vous serez ennemis les uns des autres. Et il y aura pour vous sur terre séjour et jouissance, pour un temps.", "wo": "Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.”" }
7
25
{ "fr": "Là, dit (Allah), vous vivrez, là vous mourrez, et de là on vous fera sortir.", "wo": "“Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].”" }
7
26
{ "fr": "ô enfants d´Adam ! Nous avons fait descendre sur vous un vêtement pour cacher vos nudités, ainsi que des parures. - Mais le vêtement de la piété voilà qui est meilleur. - C´est un des signes (de la puissance) d´Allah. Afin qu´ils se rappellent.", "wo": "Yéen doomi-aadama ! Wàcceel Nanu leen koddaay lu ngeen di muure seeni pëy ak i takkaay. -Waaye koddaayul ragal Yàlla moo gën de. - Loolu bokk na ci kéemaani Yàlla yi. Ndax Yàlla ñuy fàttaliku [seen Boroom]. " }
7
27
{ "fr": "ô enfants d´Adam ! Que le Diable ne vous tente point, comme il a fait sortir du Paradis vos père et mère, leur arrachant leur vêtement pour leur rendre visibles leurs nudités. Il vous voit, lui et ses suppôts, d´où vous ne les voyez pas. Nous avons désigné les diables pour alliés à ceux qui ne croient point,", "wo": "Yéen doomi-aadama ! Buleen Séytaane sànke ni mu génne woon seen ñaari maam ya Àjjana, muri seeni koddaay ngir won leen seeni pëy. Moom mi ngi leen di gis, moom ak njabootam, te yéen mënuleen a gis fa ñu nekk. Nun def Nanu Séytaane ya ñu lëkkaloo ak ñi gëmul," }
7
28
{ "fr": "et quand ceux-ci commettent une turpitude, ils disent : \"C´est une coutume léguée par nos ancêtres et prescrite par Allah.\" Dis : \"[Non,] Allah ne commande point la turpitude. Direz-vous contre Allah ce que vous ne savez pas ? \"", "wo": "bu ñu defee ñaawtéef, dañuy wax ne : “Danoo fekk sunuy maam di ko def, te Yàllaa nu ko digal.” Neel : “Yàlla du digle ñaawtéef. Moo ndax dangeen di waxal Yàlla lu ngeen xamul ?”" }
7
29
{ "fr": "Dis : \"Mon Seigneur a commandé l´équité. Que votre prosternation soit exclusivement pour Lui. Et invoquez-Le, sincères dans votre culte . De même qu´Il vous a créés, vous retournez à Lui\".", "wo": "Neel : “Yàlla Dafa digle maandute. Nangeen di jublu ci jàkka yépp te nangeen ko jaamu, di sellal ngir Moom [Yàlla]. Dangeen dellu ca Moom, na Mu leen sose woon cag njalbéen” ." }
7
30
{ "fr": "Il guide une partie, tandis qu´une autre partie a mérité l´égarement parce qu´ils ont pris, au lieu d´Allah, les diables pour alliés, et ils pensent qu´ils sont bien-guidés !", "wo": "Am na kurél bu gindiku, waaye am na ab kurél bu ab réer wàkk na leen, ñoom dañoo féeteek Séytaane bàyyi Yàlla te defe ne cig njub lañu nekk !" }
7
31
{ "fr": "ô enfants d´Adam, dans chaque lieu de Salat portez votre parure (vos habits). Et mangez et buvez; et ne commettez pas d´excès, car Il [Allah] n´aime pas ceux qui commettent des excès .", "wo": "Éy yéen doomi-aadama, [jépp jàkka ju ngeen jëmati] nangeen di waaj ba jekk [ak yére yu rafet]. Te nangeen di lekk di naan ; te buleen di yàq, ndax Yàlla soppul yàqkat yi." }
7
32
{ "fr": "Dis : \"Qui a interdit la parure d´Allah, qu´Il a produite pour Ses serviteurs, ainsi que les bonnes nourritures ? \" Dis : \"Elles sont destinées à ceux qui ont la foi, dans cette vie , et exclusivement à eux au Jour de la Résurrection.\" Ainsi exposons-Nous clairement les versets pour les gens qui savent.", "wo": "Neel : “ Ana kan mooy digle ne taari Yàlla, yi Mu génneel ay jaamam, araam nañu, ak xéewal yu sell yi ?” . Neel : “Yooyu, ñi gëm ci àddina bi, ñoo koy moom, ñoom doŋŋ te bu àllaaxiraa.” . Noonu la Nuy leeralee Sunuy tegtal ci nit ñuy xam." }
7
33
{ "fr": "Dis : \"Mon Seigneur n´a interdit que les turpitudes (les grands péchés), tant apparentes que secrètes, de même que le péché, l´agression sans droit et d´associer à Allah ce dont Il n´a fait descendre aucune preuve, et de dire sur Allah ce que vous ne savez pas\".", "wo": "Neel : “Sama Boroom araamalul lu dul ñaawtéef yi, la ca feeñ ak la ca nëbbu ak bàkkaar, ak bew guy jalgati dëgg, ak di Ko bokkaaleek loo xam ne wenn lay wàccewu ca, ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul. [Yooyu ñoo araam]” ." }
7
34
{ "fr": "Pour chaque communauté il y a un terme. Quand leur terme vient, ils ne peuvent le retarder d´une heure et ils ne peuvent le hâter non plus.", "wo": "Xeet wu nekk am na àpp. Bu àpp ba agsee, duñu yées senn saa te it duñu ko jiitu." }
7
35
{ "fr": "ô enfants d´Adam ! Si des messagers [choisis] parmi vous viennent pour vous exposer Mes signes, alors ceux qui acquièrent la piété et se réforment, n´auront aucune crainte et ne seront point affligés.", "wo": "Éy yéen doomi-aadama yi ! Amaana ay Yonent yu bokk ci yéen dikkal leen, di leen nettali sunuy tegtal, (nangeen xam ne) képp ku ragal na Yàlla tey yéwénal, du am tiitaange te du jàq." }
7
36
{ "fr": "Et ceux qui traitent de mensonges Nos signes et s´en écartent avec orgueil, sont les gens du Feu et ils y demeureront éternellement.", "wo": "Gaa ña nga xam ne dañoo weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu, dëddu ko, ñooñee ñooy waa Safara, te dañu fay béel." }
7
37
{ "fr": "Quel pire injuste, que celui qui invente un mensonge contre Allah, ou qui traite de mensonges Ses signes ? Ceux là auront la part qui leur a été prescrite; jusqu´au moment où Nos Envoyés [Nos Anges] viennent à eux pour leur enlever l´âme, en leur disant : \"Où sont ceux que vous invoquiez en dehors d´Allah ? \" - Ils répondront : \"Nous ne les trouvons plus\". Et ils témoigneront contre eux-mêmes qu´ils étaient mécréants.", "wo": "Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen walla muy weddi ay tegtalam ? Ñoom dey, danañu jot seen wàll wi Nu dogal ci ñoom ; ba kero bu leen Sunuy ndaw dikkale, naan len : “Ana ña ngeen daan jaamu bàyyi Yàlla ?” - Ñu toontu ne : “Réer nañu nu” . Daldi seede ne ñoom ay yéefar lañu." }
7
38
{ "fr": "Entrez dans le Feu, dira [Allah,] \"parmi les djinns et les hommes des communautés qui vous ont précédés.\" Chaque fois qu´une communauté entrera, elle maudira celle qui l´aura précédée. Puis, lorsque tous s´y retrouveront, la dernière fournée dira de la première : \"ô notre Seigneur ! Voilà ceux qui nous ont égarés : donne-leur donc double châtiment du feu.\" Il dira : \"A chacun le double, mais vous ne savez pas\".", "wo": "Mu ne leen : “Dugguleen fekki xeet ya leen jiitu woon, di ay nit ak i jinne ca Safara sa.” . Xeet wu ca dugg rekk, tàmbalee rëbb moroom ja. Ba ñépp yembee, ña jiitu ak ña mujj ku nekk naan : “Ñii noo nu sànkkoon : kon nag Yàlla, fulal mbugal ma ci seen kaw.” . Yàlla ne leen : “Yéen ñépp laay ful seen mbugal, waaye xamuleen” ." }
7
39
{ "fr": "Et la première fournée dira à la dernière : \"Mais vous n´avez sur nous aucun avantage. Goûtez donc au châtiment, pour ce que vous avez acquis\".", "wo": "Ña fa jiitu ñoom di wax ña mujj a agsi, naan leen : “Yéen ñii daal, gënewuleen nu lenn. Kon mosleen [toqamtiku] mbugal mi ngir la ngeen fàggu woon ciy bàkkaar” .(s)" }
7
40
{ "fr": "Pour ceux qui traitent de mensonges Nos enseignements et qui s´en écartent par orgueil, les portes du ciel ne leur seront pas ouvertes, et ils n´entreront au Paradis que quand le chameau pénètre dans le chas de l´aiguille. Ainsi rétribuons-Nous les criminels.", "wo": "Ña weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu ba dëddu leen, Deefuleen ubbil wunti asamaan si, te duñu dugg Àjjana li feek gëléem duggul ci bën- bënu puso. Te noonu Lanuy feye saay-saay si." }
7
41
{ "fr": "L´Enfer leur servira de lit et, comme couverture, ils auront des voiles de ténèbres. Ainsi rétribuons-Nous les injustes.", "wo": "Am nañu laltaayu Safara ak mbalaanum [Safara]. Noonu Lanuy feye tooñkat ya." }
7
42
{ "fr": "Et ceux qui croient et font de bonnes oeuvres - Nous n´imposons aucune charge à personne que selon sa capacité - ceux-là seront les gens du Paradis : ils y demeureront éternellement.", "wo": "Ña gëm te jëf u yiw - Te kat Dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan - ñooña ñooy waa Àjjana : te dañu fay béel." }
7
43
{ "fr": "Et Nous enlèverons toute la rancune de leurs poitrines, sous eux couleront les ruisseaux, et ils diront : \"Louange à Allah qui nous a guidés à ceci. Nous n´aurions pas été guidés, si Allah ne nous avait pas guidés. Les messagers de notre Seigneur sont venus avec la vérité.\" Et on leur proclamera : \"Voilà le Paradis qui vous a été donné en héritage pour ce que vous faisiez\".", "wo": "Te Danuy rocci la nekkoon ca seeni dënn cig noonoo, dex ya dañuy daw-dawaan ca seen ron, ñuy wax naan : “Sant nanu Yàlla, Moom Mi nu indi ci lii. Te mënunu woon a gindi mukk sunu bopp, su fekkoon ne Yàlla gindiwunu. Sunu Boroom, ay Yonentam indi woon nañu dëgg.” . Ñu woo leen, ne leen : “ Àjjana jii donolees na leen ko ngir la ngeen daan def [ci lu baax]” ." }
7
44
{ "fr": "Les gens du Paradis crieront aux gens du Feu : \"Certes, nous avons trouvé vrai ce que notre Seigneur nous avait promis. Avez-vous aussi trouvé vrai ce que notre Seigneur avait promis ? \" \"Oui\", diront-ils. Un héraut annoncera alors au milieu d´eux : Que la malédiction d´Allah soit sur les injustes,", "wo": "Waa Àjjana woo waa Safara, ne leen : “Nun dey, gis nanu la nu sunu Boroom digoon muy dëgg. Moo ndax yéen fekk ngeen li leen seen Boroom digoon muy dëgg ?” . Ñu toontu ne : “Waaw” . Mu am wootekat bu daldi woote ne : rëbbum Yàlla dal na ca tooñkat ya," }
7
45
{ "fr": "qui obstruaient le sentier d´Allah, qui voulaient le rendre tortueux, et qui ne croyaient pas à l´au-delà.\"", "wo": "ñoom ñay féewale [nit ñi] ak diiney Yàlla ji, di doxe doxiin wu jeng, te ñoom dañoo weddi àllaaxira.”" }
7
46
{ "fr": "Et entre les deux, il y aura un mur, et, sur al-Araf seront des gens qui reconnaîtront tout le monde par leurs traits caractéristiques . Et ils crieront aux gens du Paradis : \"Paix sur vous ! \" Ils n´y sont pas entrés bien qu´ils le souhaitent.", "wo": "Dox na ca seen diggante [waa Àjjana] kiiraay, nekk na ca kaw (dig) wa aw nit ñoo xam ne danañu leen xàmmee ñoom ñépp ca seen màndarga ya. Ñu woo waa Àjjana, ne leen : “Yal na jàmm nekk ci yéen !” . Ñoom duñu dugg Àjjana te xemmem nañu ko." }
7
47
{ "fr": "Et quand leurs regards seront tournés vers les gens du Feu, ils diront : \"ô notre Seigneur ! Ne nous mets pas avec le peuple injuste\".", "wo": "Saa su seeni gët jubloo ca waa Safara, ñu ne : “Sunu Boroom, Yàlla boo nu boole ak nit ñu di ay tooñkat” .(n) " }
7
48
{ "fr": "Et les gens d´al-Araf, appelant certains hommes qu´ils reconnaîtront par leurs traits caractéristiques, diront : \"Vous n´avez tiré aucun profit de tout ce que vous aviez amassé et de l´orgueil dont vous étiez enflés !", "wo": "Ña nekk ca dig wa tuddu [Al-Lahraaf] woo ay nit ñu ñu xàmmee ngir seeni màndarga, ne leen : “Waa kon alal ja ngeen daan dajale ak la leen taxoon a rëy-rëylu, amaluñuleen benn njariñ !" }
7
49
{ "fr": "Est-ce donc ceux-là au sujet desquels vous juriez qu´ils n´obtiendront de la part d´Allah aucune miséricorde... ? - Entrez au Paradis ! Vous serez à l´abri de toute crainte et vous ne serez point affligés.", "wo": "Moo ndax ñii du ña ngeen giñoon ne Yàlla duleen dugal ci yërmaande... ? - Dugguleen ci Àjjana ! Te buleen am njàqare, te buleen am naqar." }
7
50
{ "fr": "Et les gens du Feu crieront aux gens du Paradis : \"Déversez sur nous de l´eau, ou de ce qu´Allah vous a attribué.\" \"Ils répondront : Allah les a interdits aux mécréants\".", "wo": "Waa Safara woo waa Àjjana ne leen : “Bëbël-leen ci nun lenn ci ndox mi, walla ci li leen Yàlla wërsëgale.” Ñu toontu ne : “Yàlla dogal na ne [xéewal yii] araam na ci yéefar yi” ." }
7
51
{ "fr": "Ceux-ci prenaient leur religion comme distraction et jeu, et la vie d´ici-bas les trompait. Aujourd´hui, Nous les oublierons comme ils ont oublié la rencontre de leur jour que voici, et parce qu´ils reniaient Nos enseignements.", "wo": "Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak i caaxaan, te dundug àddina nax leen. Tey Dananu leen fàtte na ñu fàttee woon ndajem tey jii, ak la ñu weddi woon Sunuy kàddu." }