sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
7
52
{ "fr": "Nous leurs avons, certes, apporté un Livre que Nous avons détaillé, en toute connaissance, à titre de guide et de miséricorde pour les gens qui croient.", "wo": "Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu Nu faramfàcce mu neex a dégg, muy njub ak yërmaande ngir nit ñu gëm." }
7
53
{ "fr": "Attendent-ils uniquement la réalisation (de Sa menace et de Ses promesses ? ). Le jour où sa (véritable) réalisation viendra, ceux qui auparavant l´oubliaient diront : \"Les messagers de notre Seigneur sont venus avec la vérité. Y a-t-il pour nous des intercesseurs qui puissent intercéder en notre faveur ? Ou pourrons-nous être renvoyés [sur terre], afin que nous oeuvrions autrement que ce que nous faisions auparavant ? \" Ils ont certes créé leur propre perte; et ce qu´ils inventaient les a délaissés.", "wo": "Moo ndax dañuy xaar ba lu ko firndéel agsi ? Ña ko fàtte woon, la ko jiitu, danañu wax ne : “Yonenti sunu Boroom indi woon nañu dëgg. Moo ndax dananu amatiy rammukat yu nuy rammu ? Walla ñu delloo nu [àddina] nu def fa lu gën a rafet la nu fa daan def ?” . Yàqal nañu jeeg seen bopp ; te la ñu daan duur réer na leen." }
7
54
{ "fr": "Votre Seigneur, c´est Allah, qui a créé les cieux et la terre en six jours, puis S´est établi \"istawa\" sur le Trône . Il couvre le jour de la nuit qui poursuit celui-ci sans arrêt. (Il a créé) le soleil, la lune et les étoiles, soumis à Son commandement. La création et le commandement n´appartiennent qu´à lui. Toute gloire à Allah, Seigneur de l´Univers !", "wo": "Seen Boroom nag mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu jublu ca Gàngunaay ga. Dana muure guddi ak bëccëg Mu toftale ko bu gaaw. Te jant bi ak weer wi ak bindiw, yu ñu tàggat lañu ci ndigalam. Moo ndax du Moo moom bind gi ak dogal yi? Yàlla Boroom àddina si, Ku barkeel la !" }
7
55
{ "fr": "Invoquez votre Seigneur en toute humilité et recueillement et avec discrétion. Certes, Il n´aime pas les transgresseurs.", "wo": "Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag soppul ñiy jéggi dayo." }
7
56
{ "fr": "Et ne semez pas la corruption sur la terre après qu´elle ait été réformée. Et invoquez-Le avec crainte et espoir, car la miséricorde d´Allah est proche des bienfaisants.", "wo": "Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Te nangeen di ñaan ànd ak ragal ak yaakaar, yërmaandey Yàlla nag lu jegeñ rafetalkat yi la." }
7
57
{ "fr": "C´est Lui qui envoie les vents comme une annonce de Sa Miséricorde. Puis, lorsqu´ils transportent une nuée lourde, Nous la dirigeons vers un pays mort [de sécheresse], puis Nous en faisons descendre l´eau, ensuite Nous en faisons sortir toutes espèces de fruits. Ainsi ferons-Nous sortir les morts. Peut-être vous rappellerez-vous.", "wo": "Moo moom kiy yabal ngelaw yi ñuy tasaaroo lu jiitu. Ba bu ñu yanoo niir yu diis, ñu nàndal ci réew mu bekkoor, Nu wàccee ca ndox, génne ca bépp xeetu doomu gàncax [meññent]. Noonu lañuy génnee ñi dee [bu ñu leen di dekkal] ndax xéy-na ngeen fàttaliku.(s)" }
7
58
{ "fr": "Le bon pays, sa végétation pousse avec la grâce de son Seigneur; quant au mauvais pays, (sa végétation) ne sort qu´insuffisamment et difficilement. Ainsi déployons-Nous les enseignements pour des gens reconnaissants .", "wo": "Te dëkk bu [suuf sa baax], gàncaxam dana génn ci coobare Boroomam ; ña [seen suuf] bon, du génne lu dul lu bon. Noonu Lanuy leerale tegtal yi ngir nit ñuy gërëm [seen Boroom]. " }
7
59
{ "fr": "Nous avons envoyé Noé vers son peuple. Il dit : \"ô mon peuple, adorez Allah. Pour vous, pas d´autre divinité que Lui. Je crains pour vous le châtiment d´un jour terrible\".", "wo": "Yónni woon Nanu [Nooh] ci aw nitam. Mu ne leen : “Yéen samay mbokk, nangeen jaamu Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Man dey, ragal naa ci yéen mbugalum bis bu màgg” ." }
7
60
{ "fr": "Les notables de son peuple dirent : \"Nous te voyons dans un égarement manifeste\".", "wo": "Mbooloo ma, ca aw nitam [kilifa ya], toontu ko ne : “Gis nanu ne yaa ngi ci réer gu tar” ." }
7
61
{ "fr": "Il dit : \"ô mon peuple, il n´y a pas d´égarement en moi; mais je suis un Messager de la part du Seigneur de l´Univers.", "wo": "Mu ne : «Man nekkuma ci ag réer ; Waaye man kat ab Yonentub Yàlla, miy Boroom àddina si, laa." }
7
62
{ "fr": "Je vous communique les messages de mon Seigneur, et je vous donne conseil sincère, et je sais d´Allah ce que vous ne savez pas.", "wo": "Dama leen di jottali sama bataaxalub Boroom, te dama leen di laabire, te xam naa ci Yàlla lu ngeen xamul." }
7
63
{ "fr": "Est-ce que vous vous étonnez qu´un rappel vous vienne de votre Seigneur à travers un homme issu de vous, pour qu´ils vous avertisse et que vous deveniez pieux et que la miséricorde vous soit accordée ? \"", "wo": "Moo ndax dafa leen a jaaxal, ay kàdduy waare dikkal leen tukkee ca seen Boroom, jaare ci góor gu bokk ci yéen, ngir mu artu leen ngeen ragal Yàlla, ndax xéy-na yërëmeef leen ?”" }
7
64
{ "fr": "Et ils le traitèrent de menteur. Or, Nous le sauvâmes, lui et ceux qui étaient avec lui dans l´arche, et noyâmes ceux qui traitaient de mensonges Nos miracles. C´étaient des gens aveugles, vraiment.", "wo": "Ñu weddi ko. Nu musal ko, moom ak ña nekkoon ak moom ca gaal ga, Nu labal ña weddi samay kàddu. Ñooña, aw nitam ñu gumba lañu woon." }
7
65
{ "fr": "Et aux Aad, leur frère Hud : \"ô mon peuple, dit-il, adorez Allah. Pour vous, pas d´autre divinité que Lui. Ne [Le] craignez-vous donc pas ? \"", "wo": "[Yónni woon Nanu it] ca waa [Haad], seen mbokk [Huud], mu ne leen : «Yéen samay mbokk, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Moo ndax dangeen dul ragal Yàlla ?”" }
7
66
{ "fr": "Les notables de son peuple qui ne croyaient pas dirent : \"Certes, nous te voyons en pleine sottise, et nous pensons que tu es du nombre des menteurs\".", "wo": "Mbooloo ma weddi, ca aw nitam, wax ne : “Nun gis nanu la nga nekk ci ag ndof, te nun sax far nanu jort ne yaw ci fenkat yi nga bokk” ." }
7
67
{ "fr": "Il dit : \"ô mon peuple, il n´y a point de sottise en moi; mais je suis un Messager de la part du Seigneur de l´Univers.", "wo": "Mu ne : “Yéen samay mbokk, ag ndof nekkul ci man de ; waaye li wér moo di ne man ab Yonent laa, [ndaw] lu bawoo fa Yàlla Boroom àddina si." }
7
68
{ "fr": "Je vous communique les messages de mon Seigneur, et je suis pour vous un conseiller digne de confiance.", "wo": "Dama leen di jottali bataaxalub sama Boroom te man dama nekk ci yéen aji-laabir ju wóor." }
7
69
{ "fr": "Quoi ! Vous vous étonnez qu´un rappel vous vienne de votre Seigneur à travers un homme issu de vous, pour qu´il vous avertisse ? Et rappelez-vous quand Il vous a fait succéder au peuple de Noé, et qu´Il accrut votre corps en hauteur (et puissance). Eh bien, rappelez-vous les bienfaits d´Allah afin que vous réussissiez.", "wo": "Moo ndax dafa leen yéem, waare dikkal leen tukke ci seen Boroom, jaare ci góor gu bokk ci yéen ngir mu artu leen? Fàttalikuleen ginnaaw ba Mu leen defee ngeen di kuutaay ginnaaw nitu Nooh, te Mu yokk seeni jëmm, dolli seeni kàttan. Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ndax xéy-na yéen ngeen texe.(r)" }
7
70
{ "fr": "Ils dirent : \"Es-tu venu à nous pour que nous adorions Allah seul, et que nous délaissions ce que nos ancêtres adoraient ? Fais donc venir ce dont tu nous menaces, si tu es du nombre des véridiques\".", "wo": "Ñu wax ne : “Ndax danga noo dikkal ngir nu jaamu Yàlla moom doŋŋ, te bàyyi li sunu maam ya daan jaamu ? Indil nu li nga nu daan tëkkoo, ndegam ku dëggu nga” . " }
7
71
{ "fr": "Il dit : \"Vous voilà, frappés de la part de votre Seigneur d´un supplice et d´une colère. Allez vous vous disputer avec moi au sujet de noms que vous et vos ancêtres avez donnés, sans qu´Allah n´y fasse descendre la moindre preuve ? Attendez donc ! Moi aussi j´attends avec vous.", "wo": "Mu toontu ne : “Nekk na lu leen dëddale tukke ca seen Boroom, mbugal ak mer. Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ciy tur yu ngeen sos yéen ak seeni maam, te Yàlla wàccewu ca wenn lay ? Man maa ngi nekk ak yéen di bokk ca way-muñandiku ña." }
7
72
{ "fr": "Or, Nous l´avons sauvé, (lui) et ceux qui étaient avec lui, par miséricorde de Notre part, et Nous avons exterminé ceux qui traitaient de mensonges Nos enseignements et qui n´étaient pas croyants.", "wo": "Nu musal ko moom ak ña ànd ak moom, ci Sama yërmaande, Nu daldi faagaagal nag ña jàppe Sunuy laaya ay fen te gëmuñu." }
7
73
{ "fr": "Et aux Tamud, leur frère Salih : \"ô mon peuple, dit-il, adorez Allah. Pour vous, pas d´autre divinité que Lui. Certes, une preuve vous est venue de votre Seigneur : voici la chamelle d´Allah, un signe pour vous. Laissez-la donc manger sur la terre d´Allah et ne lui faites aucun mal; sinon un châtiment douloureux vous saisira .", "wo": "Yónni woon Nanu it ca waa Tamuud, seen mbokk Saalihu, mu ne : “Yéen samay mbokk, nangeen jaamu Yàlla ndax amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Ay lay yu leer nàññ dikkal na leen, tukke ca seen Boroom : gëléem gu jigéen la, di mbindéefum Yàlla, di kéemaan ci yéen. Bàyyileen ko muy lekk ci kaw suuf si Yàlla moom, te buleen ko def lu bon ; kon mbugal mu tar dal leen [bu ngeen jëfewut ndigal li]." }
7
74
{ "fr": "Et rappelez-vous quand Il vous fit succéder aux Aad et vous installa sur la terre. Vous avez édifié des palais dans ses plaines, et taillé en maisons les montagnes. Rappelez-vous donc les bienfaits d´Allah et ne répandez pas la corruption sur la terre \"comme des fauteurs de trouble\".", "wo": "Fàttalikuleen ba Mu leen defee ay kuutaay, ca ginnaaw Haad, mu dëkkal leen ci suuf si. Ngeen tabax ay kër yu rëy ci dénd yi, di yatt ci doj yi ay kër. Fàttalikuleen xéewali Yàlla te buleen doon ay yàqkat ci kaw suuf si." }
7
75
{ "fr": "Les notables de son peuple qui s´enflaient d´orgueil dirent aux opprimés, à ceux d´entre eux qui avaient la foi : \"Savez-vous si Salih est envoyé de la part de son Seigneur ? \" Ils dirent : \"Oui, nous sommes croyants à son message\".", "wo": "Kilifa ya nekkoon di rëy-rëylu ciy nitam wax nañu, ña ñu doyadal, muy ña gëm ca ñoom : “Moo ndax wóor na leen ne Saalihu Yonentub Yàlla la ? “. Ñu toontu ne : “Nun dey way-gëm lanu [ci bataaxal] bi ñu ko yónnee” ." }
7
76
{ "fr": "Ceux qui s´enflaient d´orgueil dirent : \"Nous, nous ne croyons certainement pas en ce que vous avez cru\".", "wo": "Ñay rëy-rëylu ne leen : “Nun dey, li ngeen gëm, weddi nanu ko” .(s)" }
7
77
{ "fr": "Ils tuèrent la chamelle, désobéirent au commandement de leur Seigneur et dirent : \"ô Salih, fais nous venir ce dont tu nous menaces, si tu es du nombre des Envoyés\".", "wo": "Ñu rey giléem ga, jalgati seen ndigalul Boroom, daldi ne : “Yaw Saalihu, indil nu la nga nu doon tëkkoo, ndegam ci Yonent yi nga bokk” ." }
7
78
{ "fr": "Le cataclysme les saisit; et les voilà étendus gisant dans leurs demeures.", "wo": "Ag yëngug suuf rajaxe leen ; ñu xëy ne lànjaŋ ca seen kër ya." }
7
79
{ "fr": "Alors il se détourna d´eux et dit : \"ô mon peuple, je vous avais communiqué le message de mon Seigneur et vous avais conseillé sincèrement. Mais vous n´aimez pas les conseillers sincères ! \"", "wo": "Mu dëddu leen, daldi ne : “Yéen samay mbokk, jottali naa leen sama Yonenteb Boroom, laabire naa leen itam. Waaye yéen dey soppuleen laabirekat yi !”" }
7
80
{ "fr": "Et Lot, quand il dit à son peuple : \"Vous livrez vous à cette turpitude que nul, parmi les mondes, n´a commise avant vous ?", "wo": "Fàttalikuleen itam ba Lóot waxee aw nitam, ne leen : “Moo ndax dangeen di def ñaawtéef woo xam ne kenn mësu koo def ci àddina sépp ?" }
7
81
{ "fr": "Certes, vous assouvissez vos désirs charnels avec les hommes au lieu des femmes ! Vous êtes bien un peuple outrancier.\"", "wo": "Ndaxte yéen dangeen di jublu góor ñi, di ca sàkku bànneex, bàyyi fa jigéen ña ! Yéen daal, aw nit ngeen ñu jéggi dayo.”" }
7
82
{ "fr": "Et pour toute réponse, son peuple ne fit que dire : \"Expulsez-les de votre cité. Ce sont des gens qui veulent se garder purs\" !", "wo": "Toontul aw nitam nekkul lu dulñu ne : “Génneleen leen seenub dëkk. Ndax ñoom aw nit lañu ñuy laab-laablu” ! " }
7
83
{ "fr": "Or, Nous l´avons sauvé, lui et sa famille, sauf sa femme qui fut parmi les exterminés.", "wo": "Nu musal ko (Nun Yàlla) mook waa këram, ba mu des soxnaam, moom dafa des ca mbugal ma." }
7
84
{ "fr": "Et Nous avons fait pleuvoir sur eux une pluie Regarde donc ce que fut la fin des criminels !", "wo": "Nu sotti ca seen kaw ab taw , waay-waay gisal na mujjug saay-saay sa mel !" }
7
85
{ "fr": "Et aux Madyan, leur frère Chuaïb : \"ô mon peuple, dit-il, adorez Allah. Pour vous, pas d´autre divinité que Lui. Une preuve vous est venue de votre Seigneur. Donnez donc la pleine mesure et le poids et ne donnez pas aux gens moins que ce qui leur est dû. Et ne commettez pas de la corruption sur la terre après sa réforme. Ce sera mieux pour vous si vous êtes croyants.", "wo": "(Fàttalikul ba Nu yónnee) fa Madyaana, seen mbokk Chuhaybu, mu ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Te ay lay yu leer dikkal na leen yu bawoo ca seen Boroom. Kon nangeen di matal natt ak màndaxe te buleen wàññil nit ña, la ñu moom. Te it buleen yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Loolu dey, moo di li gën ci yéen, bu fekkee ni gëm ngeen." }
7
86
{ "fr": "Et ne vous placez pas sur tout chemin, menaçant, empêchant du sentier d´Allah celui qui croit en Lui et cherchant à rendre ce sentier tortueux. Rappelez-vous quand vous étiez peu nombreux et qu´Il vous a multipliés en grand nombre. Et regardez ce qui est advenu aux fauteurs de désordre.", "wo": "Te buleen di toog ci wépp yoon, di dëkku ñi gëm Yàlla, di leen wëlbati, di dox seen digganteek yoonu Yàlla, di ko jéngal. Fàttalikuleen ba ngeen nekkee di ñu néew, Mu baril leen. Te nangeen settantal naka la mujjug yàqkat ya meloon." }
7
87
{ "fr": "Si une partie d´entre vous a cru au message avec lequel j´ai été envoyé, et qu´une partie n´a pas cru, patientez donc jusqu´à ce qu´Allah juge parmi nous car Il est le Meilleur des juges.\"", "wo": "Su fekkee am na ci yéen kurél bu gëm li ñu ma yónni, ak kurél bu goreedi, nangeen muñ ba ba Yàlla di àtte seenu diggante, te Moom (Yàlla) moo di gën jaa mën a àtte.”" }
7
88
{ "fr": "Les notables de son peuple qui s´enflaient d´orgueil, dirent : \"Nous t´expulserons certes de notre cité, ô Chuaïb, toi et ceux qui ont cru avec toi. Ou que vous reveniez à notre religion.\" - Il dit : \"Est-ce même quand cela nous répugne ? \" .", "wo": "Kilifa, ya rëy-rëylu ca aw nitam, ne ko : “Dananu la génne, yaw Chuhaybu ak ña gëm ànd ak yaw, ci sunum réew. Walla nga dellusi ci sunu diine.” - Mu ne leen : “Ba bu fekkee ne sax dangeen nuy ga [ci seen diine jooju] ?” .(h)" }
7
89
{ "fr": "Certes, nous aurions forgé un mensonge contre Allah si nous revenions à votre religion après qu´Allah nous en a sauvés. Il ne nous appartient pas d´y retourner à moins qu´Allah notre Seigneur ne le veuille. Notre Seigneur embrasse toute chose de Sa science. C´est en Allah que nous plaçons notre confiance. ô notre Seigneur, tranche par la vérité, entre nous et notre peuple car Tu es le meilleur des juges.\"", "wo": "“Bu nu delloo dugg ci seen diine, kon de nu duural Yàlla aw fen gannaaw ba nu Yàlla musalee ci seen diine jooju. Dunu mën a dellu duggu ci lu dul mu soob Yàlla sunu Boroom. Xam-xamu sunu Boroom ump na lu nekk. Ci Yàlla lanuy wéeru. Yaw sunu Boroom, àtteel sunu diggante ak sunuy nit, ci dëgg, ndaxte Yaw [Yàlla], yaa gën a mën àtte àttekat yi.”" }
7
90
{ "fr": "Et les notables de son peuple qui ne croyaient pas, dirent : \"Si vous suivez Chuaïb, vous serez assurément perdants\".", "wo": "Kilifa, ya weddi ca aw nitam, ne : “Bu ngeen toppee Chuhaybu, dangeen yàqule” ." }
7
91
{ "fr": "Alors le tremblement (de terre) les saisit; et les voilà étendus, gisant dans leurs demeures.", "wo": "Yëngug suuf rajaxe leen ; ñu xëy ne lànjaŋ fa seeni kër." }
7
92
{ "fr": "Ceux qui traitaient Chuaïb de menteur (disparurent) comme s´ils n´y avaient jamais vécu. Ceux qui traitaient Chuaïb de menteur furent eux les perdants.", "wo": "Ña weddi woon Chuhaybu, dañoo mujj mel ni masuñu faa dëkk. Ña weddi woon Chuhaybu yàqule nañu." }
7
93
{ "fr": "Il se détourna d´eux et dit : \"ô mon peuple, je vous ai bien communiqué les messages de mon Seigneur et donné des conseils. Comment donc m´attristerais-je sur des gens mécréants ? \"", "wo": "Mu dëddu leen, ne : “Yéen samay mbokk, jottali naa leen sama Yonentub Boroom, laabire naa leen itam. Kon naka laay yërëmtaloo ngir aw nit ñu di ay yéefar ?” " }
7
94
{ "fr": "Nous n´avons envoyé aucun prophète dans une cité, sans que Nous n´ayons pris ses habitants ensuite par l´adversité et la détresse afin qu´ils implorent (le pardon).", "wo": "Dunu yónni Yonent ci am réew, te tegunu waa réew ma ay tiis ak i njàqare ngir xéy-na ñu toroxlu." }
7
95
{ "fr": "Puis Nous avons changé leur mauvaise condition en y substituant le bien, au point qu´ayant grandi en nombre et en richesse, ils dirent : \"La détresse et l´aisance ont touché nos ancêtres aussi.\" Eh bien, Nous les avons saisis soudain, sans qu´ils s´en rendent compte.", "wo": "Ginnaaw ba ñu soppi yu bon ya, toxal ca yu baax, bu ñu biroo it ñu naan : “ Aw naqar ak mbégte daloon na sunuy maam.” . Nu songe woon leen ci mbetteel te fooguñu ko woon." }
7
96
{ "fr": "Si les habitants des cités avaient cru et avaient été pieux, Nous leur aurions certainement accordé des bénédictions du ciel et de la terre. Mais ils ont démenti et Nous les avons donc saisis, pour ce qu´ils avaient acquis.", "wo": "Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal Yàlla, kon fàwwu Dananu leen ubbil ay wërsëg yu bawoo asamaan ak ci suuf si. Waaye dañoo weddi, Nu sadd leen ngir la ñu daan fàggu ci lu bon." }
7
97
{ "fr": "Les gens des cités sont-ils sûrs que Notre châtiment rigoureux ne les atteindra pas la nuit, pendant qu´ils sont endormis ?", "wo": "Moo ndax dafa am ci waa dëkk yooyu ñu naagu ne Sunu mbugal duleen dikke ci guddi fekk ñuy nelaw ?" }
7
98
{ "fr": "Les gens des cités sont-ils sûrs que Notre châtiment rigoureux ne les atteindra pas le jour, pendant qu´ils s´amusent ?", "wo": "Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?" }
7
99
{ "fr": "Sont-ils à l´abri du stratagème d´Allah ? Seuls les gens perdus se sentent à l´abri du stratagème d´Allah.", "wo": "Moo ndax dañoo naagu ci pexey Yàlla ? Te kenn du naagu ci pexey Yàlla ku dul nit ñu yàqule." }
7
100
{ "fr": "N´est-il pas prouvé à ceux qui reçoivent la terre en héritage des peuples précédents que, si Nous voulions, Nous les frapperions pour leurs péchés et scellerions leurs coeurs, et ils n´entendraient plus rien ?", "wo": "Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw ña fi nekkoon, ci ne su Nu neexoon Nu sadd leen ngir seeni bàkkaar ak fatt seeni xol ba dootuñu am dégg-dégg ?(s)" }
7
101
{ "fr": "Voilà les cités dont Nous te racontons certaines de leurs nouvelles. [A ceux-là,] en vérité, leurs messagers leur avaient apporté les preuves, mais ils n´étaient pas prêts à accepter ce qu´auparavant ils avaient traité de mensonge. C´est ainsi qu´Allah scelle les coeurs des mécréants.", "wo": "Dëkk yooyu, Noo ngi lay nettali dara ci seeni xibaar. Te fekk Sunuy Yonent dikkoon fa ak ay lay yu leer, waaye ñoom mënatuñu woon a gëm la ñu daan weddi ca njalbéen. Noonu la Yàlla di fattee xoli yéefar ya." }
7
102
{ "fr": "Et Nous n´avons trouvé chez la plupart d´entre eux aucun respect de l´engagement; mais Nous avons trouvé la plupart d´entre eux pervers.", "wo": "Fekkunu woon li ëpp ci ñoom ñu ame kóllare fenn ; lu dul ne li ëpp ci ñoom ay saay-saay lañu." }
7
103
{ "fr": "Puis, après [ces messagers,] Nous avons envoyé Moïse avec Nos miracles vers Pharaon et ses notables. Mais ils se montrèrent injustes envers Nos signes. Considère donc quelle fut la fin des corrupteurs.", "wo": "Ba noppi Nu yónni ci seen ginnaaw Muusaa, mu ànd ak Sunu kéemaan ca Firawna ak mbooloom ña weddi. Seetlul naka la mujjug yàqkat ya mel nag." }
7
104
{ "fr": "Et Moïse dit : \"ô Pharaon, je suis un Messager de la part du Seigneur de l´Univers,", "wo": "Muusaa ne : “Yaw Firawna, man ab Yonent laa [boo xam ne], Yàlla miy Boroom àddina si Moo ma yónni," }
7
105
{ "fr": "je ne dois dire sur Allah que la vérité. Je suis venu à vous avec une preuve de la part de votre Seigneur. Laisse donc partir avec moi les Enfants d´Israël.\"", "wo": "wér na ci man ma bañ a wax ci Yàlla lu dul dëgg. Ne indil naa leen aw lay wu tukkee ci seen Boroom. Boyalal waa Bani-Israayil ñu ànd ak man.”" }
7
106
{ "fr": "Si tu es venu avec un miracle, dit (Pharaon,) apporte-le donc, si tu es du nombre des véridiques.", "wo": "Mu toontu ne : “Ndegam danga indi ag kéemaan, wone ko ndegal ku dëggu nga.”" }
7
107
{ "fr": "Il jeta son bâton et voilà que c´ était un serpent évident.", "wo": "Sànni na yetam wa mu daldi nekk jaan ju rëy. " }
7
108
{ "fr": "Et il sortit sa main et voilà quelle était blanche (éclatante), pour ceux qui regardaient.", "wo": "Mu génne loxoom mu daldi weex tàll ca ña koy gis." }
7
109
{ "fr": "Les notables du peuple de Pharaon dirent : \"Voilà, certes, un magicien chevronné.", "wo": "Kilifa ya bokk ca nitu Firawna ne ko : “Jabar bu am xam-xam la” ." }
7
110
{ "fr": "Il veut vous expulser de votre pays.\" - \"Alors, que commandez-vous ? \"", "wo": "[Firawna] ne : “Dafa leen bëgg a génne ci seen suuf.” - “Lan mooy seen ndigal ?”" }
7
111
{ "fr": "Ils dirent : \"Fais-le attendre, lui et son frère, et envoie des rassembleurs dans les villes,", "wo": "Ñu ne ko : “Xaarloo ko mook mbokkam, te yónnee ci dëkk yi ay ndaw ñu mën a dajale nit ñi," }
7
112
{ "fr": "qui t´amèneront tout magicien averti.", "wo": "ñu indil la bépp jabar bu am xam-xam." }
7
113
{ "fr": "Et les magiciens vinrent à Pharaon en disant : \"Y aura-t-il vraiment une récompense pour nous, si nous sommes les vainqueurs ? \"", "wo": "Jabar ya ñëw ca Firawna ne ko : “Ndax dananu am pey bu fekkee ne not nanu ?”[joŋ]" }
7
114
{ "fr": "Il dit : \"Oui, et vous serez certainement du nombre de mes rapprochés\".", "wo": "Mu ne leen : “Waawaaw, kon dangeen bokk ci ñi may jegeñ” ." }
7
115
{ "fr": "Ils dirent : \"ô Moïse, ou bien tu jetteras (le premier), ou bien nous serons les premiers à jeter\" .", "wo": "Ñu ne : “Muusaa, benn yaw nga sànni, walla nun nu sànni” ." }
7
116
{ "fr": "Jetez dit-il. Puis lorsqu´ils eurent jeté, ils ensorcelèrent les yeux des gens et les épouvantèrent, et vinrent avec une puissante magie.", "wo": "Mu ne : “Sànnileen” . Ba ñu sànnee, dañoo jabar bëti nit ña, ragal-loo leen ci jabar gu rëy." }
7
117
{ "fr": "Et Nous révélâmes à Moïse : \"Jette ton bâton\". Et voilà que celui-ci se mit à engloutir ce qu´ils avaient fabriqué.", "wo": "Nu xelal Muusaa ne ko : “Sànnil sa yet wi” . Mu daldi wann la ñu doon wëlbati.(r)" }
7
118
{ "fr": "Ainsi la vérité se manifesta et ce qu´ils firent fût vain.", "wo": "Dëgg daldi tàbbi, la ñu doon def yàqu." }
7
119
{ "fr": "Ainsi ils furent battus et se trouvèrent humiliés.", "wo": "Ñu not leen foofa, ñu daldi ànd ak toroxte." }
7
120
{ "fr": "Et les magiciens se jetèrent prosternés.", "wo": "Ñu rot ñoom jabar ya, sujjóot." }
7
121
{ "fr": "Ils dirent : \"Nous croyons au Seigneur de l´Univers,", "wo": "Ñu ne : “Gëm nañu Boroom àddina si," }
7
122
{ "fr": "au Seigneur de Moïse et d´Aaron.\"", "wo": "Boroom Muusaa ak Aaruuna.”" }
7
123
{ "fr": "Y avez-vous cru avant que je ne vous (le) permette ? dit Pharaon. C´est bien un stratagème que vous avez manigancé dans la ville, afin d´en faire partir ses habitants. Vous saurez bientôt...\r\n7|124|Je vais vous couper la main et la jambe opposées, et puis, je vous crucifierai tous.", "wo": "Firawna ne leen : “Ndax dangeen Koy gëm te joxuma leen ci ndigal ? Lii, pexe la mu ngeen fàggu ci dëkk bi, ngir génne ñi fi dëkk.Waaye dangeen xam..." }
7
125
{ "fr": "Ils dirent : \"En vérité, c´est vers notre Seigneur que nous retournerons.", "wo": "Ñu toontu ne : “Nun ci sunu Boroom lanuy dellu." }
7
126
{ "fr": "Tu ne te venges de nous que parce que nous avons cru aux preuves de notre Seigneur, lorsqu´elles nous sont venues. ô notre Seigneur ! Déverse sur nous l´endurance et fais nous mourir entièrement soumis.\"", "wo": "Feyoowoo ci nun lu dul nu gëm ay kéemaani sunu Boroom, ba ñu agsee ci nun. Sunu Boroom ! Sottil ci nun muñ te nga rey nu fekk nu dee jullit.” " }
7
127
{ "fr": "Et les notables du peuple de Pharaon dirent : \"Laisseras-tu Moïse et son peuple commettre du désordre sur la terre, et lui-même te délaisser, toi et tes divinités ? \" Il dit : \"Nous allons massacrer leurs fils et laisser vivre leurs femmes. Nous aurons le dessus sur eux et les dominerons.\"", "wo": "Kilifa ya bokk ci nitu Firawna ne ko : “Moo ndax dangaa bàyyi Muusaa ak u nitam ñuy yàq ci suuf si, te moom mu bàyyi la, bàyyi sa yàlla ?” . Mu toontu ne : “Danaa rey seeni doom yu góor, ba yu jigéen yi. Ndax nun noo leen tiim, noo leen not.”" }
7
128
{ "fr": "Moïse dit à son peuple : \"Demandez aide auprès d´Allah et soyez patients, car la terre appartient à Allah. Il en fait qui Il veut parmi Ses serviteurs. Et la fin (heureuse) sera aux pieux\".", "wo": "Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te ngeen muñ, suuf si Yàllaa ko moom. Dana ko donnale ku ko neex ciy jaamam. Te muj ga, way-ragal Yàlla yee ko moom” ." }
7
129
{ "fr": "Ils dirent : \"Nous avons été persécutés avant que tu ne viennes à nous, et après ton arrivée.\" Il dit : \"Il se peut que votre Seigneur détruise votre ennemi et vous donne la lieutenance sur terre, et Il verra ensuite comment vous agirez\".", "wo": "[Ñoom yahuud ya] ne : “Loreef nanu lu jiitu sa dikk ci nun ak ginnaaw la nga nu indil.” . Mu ne : “Xéy-na seen Boroom dana rey seeni noon, Mu wuutal leen ci suuf si ba noppi di saytu na ngeen di def” ." }
7
130
{ "fr": "Nous avons éprouvé les gens de Pharaon par des années de disette et par une diminution des fruits afin qu´ils se rappellent.", "wo": "Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent ndax xéy-na ñu fàttaliku [seen Boroom]." }
7
131
{ "fr": "Et quand le bien-être leur vint, ils dirent : \"Cela nous est dû\"; et si un mal les atteignait, ils voyaient en Moïse et ceux qui étaient avec lui un mauvais augure. En vérité leur sort dépend uniquement d´Allah ? Mais la plupart d´entre eux ne savent pas.", "wo": "Bu leen lu baax dikkalee, ñu ne : “Lii noo ko moom” ; bu leen lu bon dalee, ñu gaafal Muusaa ak ña ànd ak moom. Déedéet seen gaaf nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Waaye ña ëpp ca ñoom xamuñu.(s)" }
7
132
{ "fr": "Et ils dirent : \"Quel que soit le miracle que tu nous apportes pour nous fasciner, nous ne croirons pas en toi\".", "wo": "Ñu ne : “ Loo nu mën a indil ciy kéemaan ngir jabar nu ci, dunu la gëm” ." }
7
133
{ "fr": "Et Nous avons alors envoyé sur eux l´inondation, les sauterelles, les poux (ou la calandre), les grenouilles et le sang, comme signes explicites, Mais ils s´enflèrent d´orgueil et demeurèrent un peuple criminel.", "wo": "Yabal Nanu ca seen kaw am mbënn, ak i njéeréer, ak teeñ ya ak mbott ya, ak deret ja, ñu di ay kéemaan yu fés, waaye ña rëy-rëylu nag ay nit ñu saay-saay lañu." }
7
134
{ "fr": "Et quand le châtiment les frappa, ils dirent : \"ô Moïse, invoque pour nous ton Seigneur en vertu de l´engagement qu´Il t´a donné. Si tu éloignes de nous le châtiment, nous croirons certes en toi et laisserons partir avec toi les enfants d´Israël\".", "wo": "Ba mbugal ma agsee ca ñoom, ñu ne : “Yaw Muusaa, ñaanal nu sa Boroom ci kóllare gi dox seen diggante. Boo nu tàggaleek mbugal mii, dananu la gëm te dananu bàyyi Banii- israayil ñu dem ànd ak yaw” ." }
7
135
{ "fr": "Et quand Nous eûmes éloigné d´eux le châtiment jusqu´au terme fixé qu´ils devaient atteindre, voilà qu´ils violèrent l´engagement.", "wo": "Ba Nu teggee ca ñoom mbugal ma [ca àpp ba mu waroon a yem], firi nañu la ñu dige woon." }
7
136
{ "fr": "Alors Nous Nous sommes vengés d´eux; Nous les avons noyés dans les flots, parce qu´ils traitaient de mensonges Nos signes et n´y prêtaient aucune attention.", "wo": "Tax na Nu feyyu ci ñoom ; labal leen ci géej gi, ndax ñoom dañoo weddi sunuy tegtal, sàggane leen." }
7
137
{ "fr": "Et les gens qui étaient opprimés, Nous les avons fait hériter les contrées orientales et occidentales de la terre que Nous avons bénies. Et la très belle promesse de ton Seigneur sur les enfants d´Israël s´accomplit pour prix de leur endurance. Et Nous avons détruit ce que faisaient Pharaon et son peuple, ainsi que ce qu´ils construisaient.", "wo": "Nu donnale suuf si nit ña ñu nekkoon daan leen suufeel, penku ba sowu te barkeel ko. Noonu, sa dogalu Boroom bu rafet bi, daldi mat ci Banii-israayil ngir la ñu nekkoon di muñ. Nu rajaxe la Firawna ak u nitam nekkoon di liggéey ak ya ñu tabaxoon." }
7
138
{ "fr": "Et nous avons fait traverser la Mer aux enfants d´Israël. Ils passèrent auprès d´un peuple attaché à ses idoles et dirent : \"ô Moïse, désigne-nous une divinité semblable à leurs dieux.\" Il dit : \"Vous êtes certes des gens ignorants.", "wo": "Jàllale Nanu Bani-Israayil géej ga. Ñu fekk fa aw nit ñoo xam ne ña nga doon jaamu seeni xërëm, ñu ne : «Muusaa, defal nu yàlla ju mel ni seen yàlla.” . Mu ne leen : “Yéen daal ñu réer ngeen. " }
7
139
{ "fr": "Le culte, auquel ceux-là s´adonnent, est caduc; et tout ce qu´ils font est nul et sans valeur.\"", "wo": "Nii la ñu nekkee di ñu alku; te seeni jëf lu yàqu la.”" }
7
140
{ "fr": "Il dit : \"Chercherai-je pour vous une autre divinité qu´Allah, alors que c´est Lui qui vous a préférés à toutes les créatures [de leur époque] ? \"", "wo": "Mu wax ne : “Moo ndax dama leen di wutal jeneen yàlla ju dul Yàlla, te Moom mu defal leen ngëneel, teg leen ci kaw waa àddina si yépp [ca booba] ?”" }
7
141
{ "fr": "(Rappelez-vous) le moment où Nous vous sauvâmes des gens de Pharaon qui vous infligeaient le pire châtiment. Ils massacraient vos fils et laissaient vivre vos femmes. C´était là une terrible épreuve de la part de votre Seigneur.", "wo": "(Fàttalikuleen) ba Nu leen musalee ci nitu Firawna ya leen doon teg mbugal mu gën a ñaaw. Daan rey seeni doom yu góor, di bàyyi yu jigéen ya. Te loolu nekkoon na nattu bu màgg bu tukkee ca seen Boroom." }
7
142
{ "fr": "Et Nous donnâmes à Moïse rendez-vous pendant trente nuits, et Nous les complétâmes par dix, de sorte que le temps fixé par son Seigneur se termina au bout de quarante nuits. Et Moïse dit a Aaron son frère : \"Remplace-moi auprès de mon peuple, et agis en bien, et ne suis pas le sentier des corrupteurs\".", "wo": "Àppal Nanu Muusaa fanweeri guddi, Nu mottali ko ak fukk, diir ba Boroomam dogal mat ñeneenti fukki guddi. Muusaa wax na mbokkam ma Aaruuna : “Wuutu ma ci samaw nit, te nangay jubbanti te bul topp yoonu yàqkat ya” .(n)" }
7
143
{ "fr": "Et lorsque Moïse vint à Notre rendez-vous et que son Seigneur lui eut parlé, il dit : \"ô mon Seigneur, montre Toi à moi pour que je Te voie ! \" Il dit : \"Tu ne Me verras pas; mais regarde le Mont : s´il tient en sa place, alors tu Me verras.\" Mais lorsque son Seigneur Se manifesta au Mont, Il le pulvérisa, et Moïse s´effondra foudroyé. Lorsqu´il se fut remis, il dit : \"Gloire à toi ! A Toi je me repens; et je suis le premier des croyants\".", "wo": "Ba Muusaa agsee ca Sunu ndaje te Boroomam wax ak moom, mu ne : «Sama Boroom, won ma ma gis La !” . Mu ne ko : “Doo ma gis Muusaa ; waaye xoolal tundu doj wii : bu saxee ci barab bi mu nekk, kon danga Ma mën a gis.” . Ba Boroomam feeñoo doj wa, dafa mokk rumbax, Muusaa daanu xëm. Ba mu ximmee, mu daldi ne : “Tudd naa sag sell, kañ naa La ! Dellu naa ci Yaw ; te man sax faf maa di ki jëkk a gëm” ." }
7
144
{ "fr": "Et (Allah) dit : \"ô Moïse, Je t´ai préféré à tous les hommes, par Mes messages et Ma parole. Prends donc ce que Je te donne, et sois du nombre des reconnaissants\".", "wo": "Mu ne ko : “Yaw Muusaa, Man tànn naa la ci biir nit ñi, ngay Sama Yonent ak Sama kàddu. Jëlal li Ma la jox te nga bokk ca way-gëm ña” ." }
7
145
{ "fr": "Et Nous écrivîmes pour lui, sur les tablettes, une exhortation concernant toute chose, et un exposé détaillé de toute chose. \"Prends-les donc fermement et commande à ton peuple d´en adopter le meilleur. Bientôt Je vous ferai voir la demeure des pervers.", "wo": "Nu bindal ko ci àlluwaya lu nekk ngir waare ak faramfàcce lu nekk ba mu waar ko cig farlu. “Nu digal ko mu wax ay nitam ñu jàppe ko ca na mu gën a rafete. Danaa leen won dëkku saay-saay sa." }
7
146
{ "fr": "J´écarterai de Mes signes ceux qui, sans raison, s´enflent d´orgueil sur terre. Même s´ils voyaient tous les miracles, ils n´y croiraient pas. Et s´ils voient le bon sentier, ils ne le prennent pas comme sentier. Mais s´ils voient le sentier de l´erreur, ils le prennent comme sentier. C´est qu´en vérité ils traitent de mensonges Nos preuves et ils ne leur accordaient aucune attention.", "wo": "Danaa soreel Samay tegtal ña rëy-rëylu ci suuf si ci lu dul dëgg. Ba bu ñu gisee bépp kéemaan duñu ko gëm. Bu ñu gisee yoon wu njub, duñu ko topp, muy seenu yoon. Li waral loolu mooy dañoo weddi Sunuy kàddu, sàggan ba dëddu leen." }
7
147
{ "fr": "Et ceux qui traitent de mensonges Nos preuves ainsi que la rencontre de l´au-delà, leurs oeuvres sont vaines. Seraient-ils rétribués autrement que selon leurs oeuvres ? \"", "wo": "Ña weddi Sunuy kàddu ak ndaje mu mujj ma, seeni jëf yàqu na. Ndax deesuleen fey lu dul la ñu daan def”" }
7
148
{ "fr": "Et le peuple de Moïse adopta après lui un veau, fait de leurs parures : un corps qui semblait mugir. N´ont-ils pas vu qu´il ne leur parlait point et qu´il ne les guidait sur aucun chemin ? Ils l´adoptèrent [comme divinité], et ils étaient des injustes .", "wo": "Nitu Muusaa jàpp nañu ci ginnaawam aw yëkk wu ñu takk seeni takkaayi yaram, weddi Sunuy kàddu. Ndax dañoo gisul ne moom mënuta wax ak ñoom te duleen jubale ciw yoon ? Jàpp nañu ko [di ko jaamu], nekk i way-tooñ. " }
7
149
{ "fr": "Et quand ils éprouvèrent des regrets, et qu´ils virent qu´ils étaient bel et bien égarés, ils dirent : \"Si notre Seigneur ne nous fait pas miséricorde et ne nous pardonne pas, nous serons très certainement du nombre des perdants\".", "wo": "Waaye ba mu daanoo ca seeni yoxo, te ñu gis ne ñoom dañoo nekkoon cig réer, ñu ne sunu Boroom : “Soo nu yërëmul, baal nu, dananu bokk ca way-yàqule ña” .(s)" }
7
150
{ "fr": "Et lorsque Moïse retourna à son peuple, fâché, attristé, il dit : \"Vous avez très mal agi pendant mon absence ! Avez-vous voulu hâter le commandement de votre Seigneur ? \" Il jeta les tablettes et prit la tête de son frère, en la tirant à lui : \"ô fils de ma mère, (dit Aaron), le peuple m´a traité en faible, et peu s´en est fallu qu´ils ne me tuent. Ne fais donc pas que les ennemis se réjouissent à mes dépens, et ne m´assigne pas la compagnie des gens injustes\".", "wo": "Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw?” . Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ” ." }
7
151
{ "fr": "Et (Moïse) dit : \"ô mon Seigneur, pardonne à moi et à mon frère et fais-nous entrer en Ta miséricorde, car Tu es Le plus Miséricordieux des miséricordieux\".", "wo": "Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme” ." }
7
152
{ "fr": "Ceux qui prenaient le veau (comme divinité), bientôt tombera sur eux de la part de leur Seigneur, une colère, et un avilissement dans la vie présente. Ainsi, Nous rétribuons les inventeurs (d´idoles).", "wo": "Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla." }