sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
5
37
{ "fr": "Ils voudront sortir du Feu, mais ils n´en sortiront point. Et ils auront un châtiment permanent.", "wo": "Danañu bëgg a génn Safara, waaye duñu fa mën a génn. Am nañu fa mbugal mu sax dàkk." }
5
38
{ "fr": "Le voleur et la voleuse, à tous deux coupez la main, en punition de ce qu´ils se sont acquis, et comme châtiment de la part d´Allah. Allah est Puissant et Sage.", "wo": "Sàcc bu góor ak sàcc bu jigéen, dogleen seeni yoxo ñoom ñaar muy peyug la ñu fàggu, di mbugal mu tukkee ca Yàlla. Moom Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la." }
5
39
{ "fr": "Mais quiconque se repent après son tort et se réforme, Allah accepte son repentir. Car, Allah est, certes, Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Ku tuub ginnaaw ba mu tooñee, te mu sellal jëfam, Yàlla dana ko jéggal. Ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
5
40
{ "fr": "Ne sais-tu pas qu´à Allah appartient la royauté des cieux et de la terre ? Il châtie qui Il veut et pardonne à qui Il veut. Et Allah est Omnipotent.", "wo": "Moo ndax dangaa xamul ne Yàlla Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si ? Dana mbugal ku Ko soob, dana jéggal ku Ko soob. Te Yàlla mën na lu ne." }
5
41
{ "fr": "ô Messager ! Que ne t´affligent point ceux qui concourent en mécréance; parmi ceux qui ont dit : \"Nous avons cru\" avec leurs bouches sans que leurs coeurs aient jamais cru et parmi les Juifs qui aiment bien écouter le mensonge et écouter d´autres gens qui ne sont jamais venus à toi et qui déforment le sens des mots une fois bien établi. Ils disent : \"Si vous avez reçu ceci , acceptez-le et si vous ne l´avez pas reçu, soyez méfiants\". Celui qu´Allah veut éprouver, tu n´as pour lui aucune protection contre Allah. Voilà ceux dont Allah n´a point voulu purifier les coeurs. A eux, seront réservés, une ignominie ici-bas et un énorme châtiment dans l´au-delà.", "wo": "Éy yaw Yonent bi ! Bula jëfi ñiy jëkkante di sóobu cig kéefar metti ; ci ña nga xam ne danañu wax ci seeni gimiñ ne : “Gëm nañu” , te seeni xol gëmul; ak ca ña nekk i yahuud, di dégluwaakoon i fen, di dégluwaakoon i ñeneen nit ñoo xam ne agsiwuñu ci yaw, dañuy soppi baat ba jële ko fa mu tëddoon. Danañu wax naan : “Bu ñu leen joxee lii, jël-leen ko, bu ñu leen joxul, moytuleen” . Ku Yàlla namm a fitnaal, doo ko mënal dara fa Yàlla. Ña nga xam ne Yàlla nammuleen a baal seeni xol, am nañu toroxtaane ci àddina ak mbugal mu rëy ca àllaaxira.(r)" }
5
42
{ "fr": "Ils sont attentifs au mensonge et voraces de gains illicites. S´ils viennent à toi, sois juge entre eux ou détourne toi d´eux. Et si tu te détournes d´eux, jamais ils ne pourront te faire aucun mal. Et si tu juges, alors juge entre eux en équité. Car Allah aime ceux qui jugent équitablement.", "wo": "Dañuy déglu ay fen, di lekk lu araam, lu araam [lool]. Bu ñu la seetsee, nanga àtte seen diggante walla nga dëddu leen. Te sax boo leen dëddoo, duñu la mën a wàññi dara. Boo àttee, nanga àtte seen diggante ci maandute. Yàlla safoo na way-maandu ña. " }
5
43
{ "fr": "Mais comment te demanderaient-ils d´être leur juge quand ils ont avec eux la Thora dans laquelle se trouve le jugement d´Allah ? Et puis, après cela, ils rejettent ton jugement. Ces gens-là ne sont nullement les croyants .", "wo": "Naka lañu lay àtteloo sax te ñu yor Tawreet, àttey Yàlla ya nekk ca biir ? Gannaaw loolu, ñu dëddu dëgg ga. Ñoom gëmuñu de." }
5
44
{ "fr": "Nous avons fait descendre le Thora dans laquelle il y a guide et lumière. C´est sur sa base que les prophètes qui se sont soumis à Allah, ainsi que les rabbins et les docteurs jugent les affaires des Juifs. Car on leur a confié la garde du Livre d´Allah, et ils en sont les témoins . Ne craignez donc pas les gens, mais craignez Moi. Et ne vendez pas Mes enseignements à vil prix. Et ceux qui ne jugent pas d´après ce qu´Allah a fait descendre, les voilà les mécréants.", "wo": "Nun wàcce Nanu Tawreet, njub ak leer nekk ca Yonent ya nga xam ne wommatu woon nañu. Àtte nañu ca ña nekkoon i yahuud, ak niti Yàlla ya ak fóore ya. Te la nga xam ne dénkoon nañu leen ko [ci xam- xam] ci Téere Yàlla ba, ñu nekkoon ca ay seede. Buleen ragal nit ñi, ragal-leen Ma. Buleen weddi Samay laaya ci njëg gu néew. Képp du dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñoo di ay yéefar." }
5
45
{ "fr": "Et Nous y avons prescrit pour eux vie pour vie, oeil pour oeil, nez pour nez, oreille pour oreille, dent pour dent. Les blessures tombent sous la loi du talion . Après, quiconque y renonce par charité, cela lui vaudra une expiation. Et ceux qui ne jugent pas d´après ce qu´Allah a fait descendre, ceux-là sont des injustes.", "wo": "Dogal Nanu ca ñoom ci Tawreet, ne ku rey nit ñu rey la ; naka noonu, ku fuq bët, ñu fuq bosam ; ku dog bakkan, ñu dog bosam ; nopp itam, nopp a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey. Gaañu-gaañu it dañu koy feyee gaañu-gaañu. Waaye ku baale sa àq def ko sarax, dana am njéggalu Boroomam. Képp ku dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñooy tooñkat ña." }
5
46
{ "fr": "Et Nous avons envoyé après eux Jésus, fils de Marie, pour confirmer ce qu´il y avait dans la Thora avant lui. Et Nous lui avons donné l´évangile, où il y a guide et lumière, pour confirmer ce qu´il y avait dans la Thora avant lui, et un guide et une exhortation pour les pieux.", "wo": "Toxal Nanu ci seen ginnaaw ya [ñoom Yonent ya] Iisaa, doomi Maryaama, mu dëggal la ko jiitu ci Tawreet. Jox ko Linjiil, njub ak leer nekk ca, muy dëggal la ko jiitu ci Tawreet, di njub ak waare gu jëm ca way-ragal Yàlla ña." }
5
47
{ "fr": "Que les gens de l´évangile jugent d´après ce qu´Allah y a fait descendre. Ceux qui ne jugent pas d´après ce qu´Allah a fait descendre, ceux-là sont les pervers.", "wo": "Ñoñ-Injiil, nañu àtte ca la Yàlla wàcce ca biir [Téere boobu]. Képp ku dul àtte ca la Yàlla wàcce, ñoom way-sàqi ndigal lañu." }
5
48
{ "fr": "Et sur toi (Muhammad) Nous avons fait descendre le Livre avec la vérité, pour confirmer le Livre qui était là avant lui et pour prévaloir sur lui. Juge donc parmi eux d´après ce qu´Allah a fait descendre. Ne suis pas leurs passions, loin de la vérité qui t´est venue. A chacun de vous Nous avons assigné une législation et un plan à suivre. Si Allah avait voulu, certes Il aurait fait de vous tous une seule communauté. Mais Il veut vous éprouver en ce qu´Il vous donne. Concurrencez donc dans les bonnes oeuvres. C´est vers Allah qu´est votre retour à tous; alors Il vous informera de ce en quoi vous divergiez .", "wo": "Te wàcce Nanu ci Yaw Téere ba [Alxuraan] ci lu dëggu, muy dëggal la ko jiitu ci Téere bii, te muy aji-sàmm it [dëgg ya ca nekk]. Nanga àtte [yaw Yonent bi] seen diggante ci la Yàlla wàcce. Bul topp seen bànneex bàyyi li ñu la digal ci dëgg. Ku ci nekk ci yéen, defal Nanu ko aw yoon ak doxaliin. Te kat su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen di wenn xeet. Waaye [Dakoo defe noonu] ngir nattu leen ca la Mu leen jox. Jëkkanteleen jëm ci yiw ya. Yéen ñépp ca Yàlla ngeen di mujj dellu ; Mu xamal leen la ngeen nekkoon di ca juuyoo.(s)" }
5
49
{ "fr": "Juge alors parmi eux d´après ce qu´Allah a fait descendre. Ne suis pas leurs passions, et prends garde qu´ils ne tentent de t´éloigner d´une partie de ce qu´Allah t´a révélé. Et puis, s´ils refusent (le jugement révélé) sache qu´Allah veut les affliger [ici-bas] pour une partie de leurs péchés. Beaucoup de gens, certes, sont des pervers.", "wo": "Nangay àtte seeni diggante ak la Yàlla wàcce. Te bul topp seeni bànneex, te nga moytuleen ngir ñu bañ laa réeral, soril la lenn ca la Yàlla wàcce. Te yaw, bu ñu dëddoo dellu ginnaaw, nanga xam ne Yàlla amul lu dul lenn ci seeni bàkkaar yi dal leen. Bari na ci nit ñi ñu nekk way-sàqi ndigal.(n)" }
5
50
{ "fr": "Est-ce donc le jugement du temps de l´Ignorance qu´ils cherchent ? Qu´y a-t-il de meilleur qu´Allah, en matière de jugement pour des gens qui ont une foi ferme ?", "wo": "Moo ndax àtteb way-réer ña [jiitu Lislaam] lañuy sàkku ? Te ana àtteb kan moo gën a jege àtteb Yàlla ci nit ñoo xam ne ñu wóolu lañu seen Boroom ? " }
5
51
{ "fr": "ô les croyants ! Ne prenez pas pour alliés les Juifs et les Chrétiens; ils sont alliés les uns des autres. Et celui d´entre vous qui les prend pour alliés, devient un des leurs. Allah ne guide certes pas les gens injustes.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàpp yahuud yi ak nasraan yi di xaritook ñoom. Ku ko def ci yéeen, daanaka ca ñoom la bokk. Te nag Yàlla du gindi nit ñu di ay tooñkat." }
5
52
{ "fr": "Tu verras, d´ailleurs, que ceux qui ont la maladie au cœur se précipitent vers eux et disent : \"Nous craignons qu´un revers de fortune ne nous frappe.\" Mais peut-être qu´Allah fera venir la victoire ou un ordre émanant de Lui. Alors ceux-là regretteront leurs pensées secrètes.", "wo": "Danga gis ña nga xam ne jàngoroy [sikki-sàkka] nekk na ca seeni xol, ñuy gaawantu jëm ca ñoom, di taafantaloo ne dañoo ragal walbatikug jamono songu leen. Te amaana Yàlla indi ndam mbaa mbir mu tukkee ca Moom. Bu boobaa danañu rëccu la ñu bëggoon ca seeni xol." }
5
53
{ "fr": "Et les croyants diront : \"Est-ce là ceux qui juraient par Allah de toute leur force qu´ils étaient avec vous ? \" Mais leurs actions sont devenues vaines et ils sont devenus perdants.", "wo": "Ba way-gëm ña naan : “Moo ndax du ñii ñoo doon giñ ci Yàlla fa ngiñ gën a màggee ngir ne ñoom ñook yéen a ànd bu wér ?” Seeni jëf sippiku na [yàqu], ñu mujj di ñu yàqule." }
5
54
{ "fr": "ô les croyants ! Quiconque parmi vous apostasie de sa religion... Allah va faire venir un peuple qu´Il aime et qui L´aime, modeste envers les croyants et fier et puissant envers les mécréants, qui lutte dans le sentier d´Allah, ne craignant le blâme d´aucun blâmeur. Telle est la grâce d´Allah. Il la donne à qui Il veut. Allah est Immense et Omniscient.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Ku ci murtad ci yéen ba génn diineem... Yàlla Dana indi nit ñoo xam ne sopp Na leen , ñu sopp Ko, di ñu woyoflu ci jullit ñi te dëgër ci yéefar yi. Loolu ngënéelu Yàlla la. Ku Ko neex la koy jox. Yàlla Ku yaatu mbir la, Ku xam la." }
5
55
{ "fr": "Vous n´avez d´autres alliés qu´Allah, Son messager, et les croyants qui accomplissent la Salat, s´acquittent de la Zakat, et s´inclinent (devant Allah).", "wo": "Amul keneen ku far ak yéen ku dul Yàlla ak ab Yonentam, ak way-gëm ña nga xam ne danañu taxawal julli, di génne asaka te di way-sëgg." }
5
56
{ "fr": "Et quiconque prend pour alliés Allah, Son messager et les croyants, [réussira] car c´est le parti d´Allah qui sera victorieux.", "wo": "Ku xaritook Yàlla ak Yonentam ak way-gëm ña, [na xam ne] ña ànd ak Yàlla ñooy nit ña [gàddu ndam la]." }
5
57
{ "fr": "ô les croyants ! N´adoptez pas pour alliés ceux qui prennent en raillerie et jeu votre religion, parmi ceux à qui le Livre fut donné avant vous et parmi les mécréants. Et craignez Allah si vous êtes croyants.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàpp xarit ña nga xam ne dañuy jàppe seen diine ay caaxaan ak po, ca ña leen jëkk a jot Téere ak yéefar ya. Ragal- leen Yàlla ndegam way-gëm ngeen." }
5
58
{ "fr": "Et lorsque vous faites l´appel à la Salat, ils la prennent en raillerie et jeu. C´est qu´ils sont des gens qui ne raisonnent point.", "wo": "Bu ngeen di woote jëm ci julli, [ñoom] ñu jàppe ko caaxaan ak am po. Ñoom dañudi ay nit ñu xel-luwul." }
5
59
{ "fr": "Dis : \"ô gens du Livre ! Est-ce que vous nous reprochez autre chose que de croire en Allah, à ce qu´on a fait descendre vers nous et à ce qu´on a fait descendre auparavant ? Mais la plupart d´entre vous sont des pervers.", "wo": "Neel : “Éy yéen ñoñ-téere ! Ndax li ngeen nu bañe nekkul lu dul li nu gëm Yàlla ak li wàcceef na ko ci nun ak la jëkkoon a wàcc ? Li ëpp ci yéen ay saay-saay lañu.(s)" }
5
60
{ "fr": "Dis : \"Puis-je vous informer de ce qu´il y a de pire, en fait de rétribution auprès d´Allah ? Celui qu´Allah a maudit, celui qui a encouru Sa colère, et ceux dont Il a fait des singes, des porcs, et de même, celui qui a adoré le Tagut, ceux-là ont la pire des places et sont les plus égarés du chemin droit\" .", "wo": "Neel : “Moo ndax duma leen xamal ku yées pey ëllëg ca Yàlla ? Ña Yàlla rëbb, mere leen, soppi lenn ca ñoom ay golo ak i mbaam-xuux te ñuy jaamu Séytaane, ñooña ñoo yées dëkkuwaay te ñoo gën a réer, sore yoon wu jub wa” ." }
5
61
{ "fr": "Lorsqu´ils viennent chez vous, ils disent : \"Nous croyons.\" Alors qu´ils sont entrés avec la mécréance et qu´ils sont sortis avec. Et Allah sait parfaitement ce qu´ils cachent.", "wo": "Bu ñu dikkee ci yéen naan : “Gëm nanu.” . Te fekk kéefar lañu indiwaale te moom lañuy yóbbuwaale. Te Yàllaa gën a xam la ñuy nëbb." }
5
62
{ "fr": "Et tu verras beaucoup d´entre eux se précipiter vers le péché et l´iniquité, et manger des gains illicites. Comme est donc mauvais ce qu´ils oeuvrent !", "wo": "Danga gis ñu bari ci ñoom ñuy jëkkantee tàbbi ci bàkkaar, ak noonuwante ak séen lekk lu araam. Cëy la ñuy def aka bon ! " }
5
63
{ "fr": "Pourquoi les rabbins et les docteurs (de la Loi religieuse) ne les empêchent-ils pas de tenir des propos mensongers et de manger des gains illicites ? Que leurs actions sont donc mauvaises !", "wo": "Lu tee seen làbbe ya ak seen fóore ya tere leen wax ju ñaaw, ak lekk lu araam ? Cëy la ñu liggéey aka bon !" }
5
64
{ "fr": "Et les Juifs disent : \"La main d´Allah est fermée ! \" Que leurs propres mains soient fermées, et maudits soient-ils pour l´avoir dit. Au contraire, Ses deux mains sont largement ouvertes : Il distribue Ses dons comme Il veut. Et certes, ce qui a été descendu vers toi de la part de ton Seigneur va faire beaucoup croître parmi eux la rébellion et la mécréance. Nous avons jeté parmi eux l´inimité et la haine jusqu´au Jour de la Résurrection. Toutes les fois qu´ils allument un feu pour la guerre, Allah l´éteint. Et ils s´efforcent de semer le désordre sur la terre, alors qu´Allah n´aime pas les semeurs de désordre.", "wo": "Yahuud ya nee nañu : “Loxob Yàlla dafa banku !” Seeni yoxo kay ñoom moo banku, te rëbbeef na leen ngir la ñu wax. Li wér mooy ñaari yoxoy Yàlla dañoo tàlli : waaye ni mu ko neexe lay xéewale. Te la Mu wàcce ci yaw di yokk bew ak kéefar ca ñu bari ca ñoom. Te sànni Nanu ca seen diggante noonuwante ak bañante gu fay nekk ba Bis- pénc ba. Saa su ñu taalee safaraw xare, Yàlla fey ko. Dañuy dox di yàq ci suuf si rekk, te Yàlla safoowul yàqkat ya." }
5
65
{ "fr": "Si les gens du Livre avaient la foi et la piété, Nous leur aurions certainement effacé leurs méfaits et les aurions certainement introduits dans les Jardins du délice .", "wo": "Bu waa ñoñ-téere gëmoon te ragal Yàlla, kon Nu far seeni ñaawtéef, dugal leen Àjjana ju tudd [Nahiim] xéewal." }
5
66
{ "fr": "S´ils avaient appliqué la Thora et l´évangile et ce qui est descendu sur eux de la part de leur Seigneur, ils auraient certainement joui de ce qui est au-dessus d´eux et de ce qui est sous leurs pieds . Il y a parmi eux un groupe qui agit avec droiture; mais pour beaucoup d´entre eux, comme est mauvais ce qu´ils font !", "wo": "Bu ñu jëfewoon Tawreet, ak Linjiil al la ñu wàcce ca ñoom mu tukke ca seen Boroom, kon fàwwu ñu lekk [xéewal] gu bawoo ci kaw ak gu ballee ci seeni suufi tànk. Am na ci ñoom ay nit ñu jub ; waaye ñu bari ca ñoom lu bon lañuy def !" }
5
67
{ "fr": "ô Messager, transmets ce qui t´a été descendu de la part de ton Seigneur. Si tu ne le faisait pas, alors tu n´aurais pas communiqué Son message. Et Allah te protégera des gens. Certes, Allah ne guide pas les gens mécréants.", "wo": "Éy yaw Yonent bi, jottalil la ñu wàcce ci yaw mu tukkee ca sa Boroom. Boo ko deful kon jottaliwoo li Ma la yónni. [Te xamal ne] Yàlla Moo lay musal ci nit ñi. Te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay yéefar.(r)" }
5
68
{ "fr": "Dis : \"ô gens du Livre, vous ne tenez sur rien, tant que vous ne vous conformez pas à la Thora et à l´évangile et à ce qui vous a été descendu de la part de votre Seigneur.\" .\" Et certes, ce qui t´a été descendu de la part de ton Seigneur va accroître beaucoup d´entre eux en rébellion et en mécréance. Ne te tourmente donc pas pour les gens mécréants.", "wo": "Neel : “Éy yéen ñon-téere, nekkuleen ci dara li feek defuleen [lu ñu leen digal] ci Tawreet ak Linjiil ak li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom.” . Te dana yokk bew ak kéefar ñu bari ci ñoom li ñu wàcce ci yaw, mu jóge ci sa Boroom. Waaye bul jàq ci mbiri yéefar ya." }
5
69
{ "fr": "Ceux qui ont cru, ceux qui se sont judaïsés, les Sabéens, et les Chrétiens, ceux parmi eux qui croient en Allah, au Jour dernier et qui accomplissent les bonnes oeuvres, pas de crainte sur eux, et ils ne seront point affligés.", "wo": "Ña nekk nasraan te gëm Yàlla, walbatiku gëm Lislaam, ak Bis-pénc ba te sellal seeni jëf, duñu am njàqare, duñu am naqar." }
5
70
{ "fr": "Certes, Nous avions déjà pris l´engagement des Enfants d´Israël, et Nous leur avions envoyé des messagers. Mais chaque fois qu´un Messager leur vient avec ce qu´ils ne désirent pas, ils en traitent certains de menteurs et ils en tuent d´autres.", "wo": "Fasante woon Nanu kóllare ak waa Banii-Israayiila, yónni ci ñoom, saa yu Nu leen indilee lu leen neexul, ñu weddi ñenn ña, rey ñenn ña." }
5
71
{ "fr": "Comptant qu´il n´y aurait pas de sanction contre eux, ils étaient devenus aveugles et sourds. Puis Allah accueillit leur repentir. Ensuite, beaucoup d´entre eux redevinrent aveugles et sourds. Et Allah voit parfaitement ce qu´ils font.", "wo": "Ñu njortu ne menn mbugal [du ca topp] ba tax ñu gumba, tëx . Ci loolu Yàlla jéggal leen. Ba noppi, ñu bari ci ñoom dellu gumba tëx. Te Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy def." }
5
72
{ "fr": "Ce sont, certes, des mécréants ceux qui disent : \"En vérité, Allah c´est le Messie, fils de Marie.\" Alors que le Messie a dit : \"ô enfants d´Israël, adorez Allah, mon Seigneur et votre Seigneur\". Quiconque associe à Allah (d´autres divinités) Allah lui interdit le Paradis; et son refuge sera le Feu. Et pour les injustes, pas de secoureurs !", "wo": "Ña wax ne : “Yàlla Mooy ku ñu barkeel ka [Masiih], doomi Maryaama.” , tàbbi nañu ci kéefar. Te moom ku ñu barkeel ka waxoon na ne : «Yéen waa bani Israayiil, nangeen jaamu Yàlla, ka di sama Boroom” . Te [xamleen ne], ku bokkaale Yàlla ak dara, Yàlla Dana ko araamal Àjjana ; def dëkkuwaayam mu di Safara. Te tooñkat ya duñu am ndimbal ! " }
5
73
{ "fr": "Ce sont certes des mécréants, ceux qui disent : \"En vérité, Allah est le troisième de trois.\" Alors qu´il n´y a de divinité qu´Une Divinité Unique ! Et s´ils ne cessent de le dire, certes, un châtiment douloureux touchera les mécréants d´entre eux.", "wo": "Ña wax ne : “Yàlla ñetteel la ci ñett.” , tàbbi nañu ci kéefar. Te Yàlla Moom jenn doŋŋ la ! Bu ñu bàyyiwul li ñuy wax, fàwwu mbugal mu metti dal ña weddi ca ñoom.(s)" }
5
74
{ "fr": "Ne vont-ils donc pas se repentir à Allah et implorer Son pardon ? Car Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Lu leen teree tuub ci Yàlla ñaan ko njéggal ? Te Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
5
75
{ "fr": "Le Messie, fils de Marie, n´était qu´un Messager. Des messagers sont passés avant lui. Et sa mère était une véridique. Et tous deux consommaient de la nourriture. Vois comme Nous leur expliquons les preuves et puis vois comme ils se détournent .", "wo": "Ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, nekkul lu dul ab Yonent, boo xam ne ay Yonent jiitu woon na ko fi. Yaayam ku saxoon ci dëgg la. Ñoom ñaar dañu daan lekk ñam. Gisal ni Nu leen di leerale sunuy tegtal te it xoolal ni ñuy walbateee [dëgg ga]." }
5
76
{ "fr": "Dis : \"Adorez-vous, au lieu d´Allah, ce qui n´a le pouvoir de vous faire ni le mal ni le bien ? \" Or c´est Allah qui est l´Audient et l´Omniscient.", "wo": "Neel : “Moo ndax dangeen di bàyyi Yàlla, di jaamu loo xam ne mënuleen a lor, mënuleen a jariñ ?” .Te Yàlla Moom Kuy dégg la, Ku xam la." }
5
77
{ "fr": "Dis : \"ô gens du Livre, n´exagérez pas en votre religion, s´opposant à la vérité. Ne suivez pas les passions des gens qui se sont égarés avant cela, qui ont égaré beaucoup de monde et qui se sont égarés du chemin droit.", "wo": "Neel : “Yéen ñon-téere, buleen teeŋal seen diine, mu wuuteek dëgg ga. Buleen topp bànneexi nit ñoo xam ne réeroon nañu bu jëkk, te réeraloon nañu ñu bari, réere tigi yoon wu jub wa." }
5
78
{ "fr": "Ceux des Enfants d´Israël qui n´avaient pas cru ont été maudits par la bouche de David et de Jésus fils de Marie, parce qu´ils désobéissaient et transgressaient.", "wo": "Rëbbéef na ña weddi ca waa Bani Israayiila mu jaare ca làmmiñu Daawuda ak [Iisaa] doomi Maryaama, ngir lañu moy ndigal te nekkon ñu jéggi dayo." }
5
79
{ "fr": "Ils ne s´interdisaient pas les uns aux autres ce qu´ils faisaient de blâmable. Comme est mauvais, certes, ce qu´ils faisaient !", "wo": "Daawuñu bàyyi lu ñaaw la ñu daan def. Ay waay, la ñu daan def, aka bon !" }
5
80
{ "fr": "Tu vois beaucoup d´entre eux s´allier aux mécréants. Comme est mauvais, certes, ce que leurs âmes ont préparé, pour eux-mêmes, de sorte qu´ils ont encouru le courroux d´Allah, et c´est dans le supplice qu´ils éterniseront.", "wo": "Danga gis ñu bari ci ñoom ñuy xaritoo ak ña weddi. La leen seeni bakkan defloo ñaaw na, ba Yàlla mere leen, te ci ag mbugal lañuy nekk béel ca." }
5
81
{ "fr": "S´ils croyaient en Allah, au Prophète et à ce qui lui a été descendu, ils ne prendraient pas ces mécréants pour alliés. Mais beaucoup d´entre eux sont pervers.", "wo": "Bu ñu nekkoon di ñu gëm Yàlla, ak Yonent ba ak la ñu wàcce ca ñoom, duñu jàppe xarit [yéefar ya]. Waaye lu bari ca ñoom saay-saay lañu [ñu génn ci topp]." }
5
82
{ "fr": "Tu trouveras certainement que les Juifs et les associateurs sont les ennemis les plus acharnés des croyants. Et tu trouveras certes que les plus disposés à aimer les croyants sont ceux qui disent : \"Nous sommes chrétiens.\" C´est qu´il y a parmi eux des prêtres et des moines, et qu´ils ne s´enflent pas d´orgueil.", "wo": "Wér na ne danga gis ne, ña gën a tar nooneel ci nit ña jëme ca jullit ña, ñooy yahuud ya ak ñay bokkaale. Te danga gis it ne, ña gën a jege ci ag cofeel jullit ña, ñooy ñay wax ne : “Nun karcen lanu [nasraan].” Ndax am na ci ñoom ay làbbe ak ñu dëddu àddina, ñoo xam ne duñu rëy-rëylu.(h)" }
5
83
{ "fr": "Et quand ils entendent ce qui a été descendu sur le Messager [Muhammad], tu vois leurs yeux déborder de larmes, parce qu´ils ont reconnu la vérité. Ils disent : \"ô notre Seigneur ! Nous croyons : inscris-nous donc parmi ceux qui témoignent (de la véracité du Coran).", "wo": "Te bu ñu déggee li wàcc ci Yonent bi nga gis seeni bët di sottiy rongoñ ndax dëgg ga ñu cay xàmmee. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom ! Gëm nanu : Nanga nu boole ca ñay way- seede. " }
5
84
{ "fr": "Pourquoi ne croirions-nous pas en Allah et à ce qui nous est parvenu de la vérité. Pourquoi ne convoitions-nous pas que notre Seigneur nous fasse entrer en la compagnie des gens vertueux ? \".", "wo": "Luy tee ñu gëm Yàlla ak la ñu dikkal ci dëgg ak ni nu xemeeme sunu Boroom tàbbal nu Àjjana ànd ak way-sellal ña ?” ." }
5
85
{ "fr": "Allah donc les récompense pour ce qu´ils disent par des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, où ils demeureront éternellement. Telle est la récompense des bienfaisants.", "wo": "Yàlla xéewale na leen, ngir la ñu wax, ay Àjjana yoo xam ne ay dex dañuy daw ca suufam, te dañu fay béel. Te loolu mooy peyug way- rafetal ña." }
5
86
{ "fr": "Et quant à ceux qui ne croient pas et qui traitent de mensonges Nos versets, ce sont les gens de la Fournaise.", "wo": "Waaye nag yéefar ya weddi Sunuy kàddu, ñoom ñooy dugg Safara." }
5
87
{ "fr": "ô les croyants : ne déclarez pas illicites les bonnes choses qu´Allah vous a rendues licites. Et ne transgressez pas. Allah, (en vérité,) n´aime pas les transgresseurs.", "wo": "Éy yéen ñi gëm : buleen araamal yu sell ya leen Yàlla daganal. Te it buleen jéggi dayo, Yàlla soppul ñiy jéggi dayo." }
5
88
{ "fr": "Et mangez de ce qu´Allah vous a attribué de licite et de bon. Craignez Allah, en qui vous avez foi.", "wo": "Lekkleen li leen Yàlla wërsëgale muy li dagan te sell. Te nangeen ragal Yàlla ji ngeen gëm." }
5
89
{ "fr": "Allah ne vous sanctionne pas pour la frivolité dans vos serments, mais Il vous sanctionne pour les serments que vous avez l´intention d´exécuter. L´expiation en sera de nourrir dix pauvres, de ce dont vous nourrissez normalement vos familles, ou de les habiller, ou de libérer un esclave. Quiconque n´en trouve pas les moyens devra jeûner trois jours. Voilà l´expiation pour vos serments, lorsque vous avez juré. Et tenez à vos serments, Ainsi Allah vous explique Ses versets, afin que vous soyez reconnaissants !", "wo": "Yàlla duleen jàppe ngiñ yi ngeen di kafe, waaye Dana leen jàppe ngiñ yi dëggu ci yéen. Te ñoom, la ñuy jéggaloo mooy leel fukki néew- ji-doole [ci ñam wa ngeen di faral a dundale seen njaboot], mbaa jox leen ay yére, walla goreel jaam. Ku ko mënul, na woor ñetti fan. Loola mooy na ñuy jéggaloo seen ngiñ ya ngeen waate [lu jaaduwul]. nangeen sàmm seen ngiñ, nii la leen Yàlla di leerale ay ndigalam ndax xéy-na ngeen gërëm Ko [delloo njukkal] !" }
5
90
{ "fr": "ô les croyants ! Le vin, le jeu de hasard, les pierres dressées, les flèches de divination ne sont qu´une abomination, oeuvre du Diable. écartez-vous en, afin que vous réussissiez.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! [xamleen ne] sàngara, wure, xerëm ak seen banti gisaane, nekkuñu lu dul sobe su jóge ci jëfi [Séytaane]. Nangeen leen moytu, xéy-na kon ngeen texe.(s)" }
5
91
{ "fr": "Le Diable ne veut que jeter parmi vous, à travers le vin et le jeu de hasard, l´inimité et la haine, et vous détourner d´invoquer Allah et de la Salat. Allez-vous donc y mettre fin ?", "wo": "Séytaane bëggul lu dul tàbbal ci seen diggante nooneel ak mbañeel, jaare ko ci sàngara ak wure te it dox seen diggante ak fàttaliku Yàlla ak julli. Moo ndax dungeen leen bàyyi ?" }
5
92
{ "fr": "Obéissez à Allah, obéissez au Messager, et prenez garde ! Si ensuite vous vous détournez... alors sachez qu´il n´incombe à Notre messager que de transmettre le message clairement. .", "wo": "Nangeen topp Yàlla ak Yonent bi, te ngeen wattandiku ! Bu ngeen dëddoo... nangeen xam ne Sunu Yonent bi dara waru ko lu dul jotal gu mat sëkk." }
5
93
{ "fr": "Ce n´est pas un pêché pour ceux qui ont la foi et font de bonnes oeuvres en ce qu´ils ont consommé (du vin et des gains des jeux de hasard avant leur prohibition) pourvu qu´ils soient pieux (en évitant les choses interdites après en avoir eu connaissance) et qu´ils croient ( en acceptant leur prohibition) et qu´ils fassent de bonnes oeuvres; puis qui (continuent) d´être pieux et de croire et qui (demeurent) pieux et bienfaisants. Car Allah aime les bienfaisants. ", "wo": "Du nekk bàkkaar ca ña gëm tey sellal seeni jëf, la ñu masoon a lekk [lu araam lu jiitu digle ga ko araamal], gannaaw ba, ñu nekk ñu di way-ragal Yàlla te gëm, di sellal seeni jëf ba noppi raggal Yàlla te gëm ; ragal Yàlla te rafetal seeni jëf. Yàlla safoo na way-rafetal ña." }
5
94
{ "fr": "ô les croyants ! Allah va certainement vous éprouver par quelque gibier à la portée de vos mains et de vos lances. C´est pour qu´Allah sache celui qui le craint en secret . Quiconque après cela transgresse aura un châtiment douloureux.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Yàlla dana leen nattu ci lenn lu jëm ci rëbb ci seeni loxo walla seeni xeej. Ndax Mu xam ku Ko ragal ci kumpa. Ku féttéerlu ginnaaw loolu, mbugal mu metti dana ko dal." }
5
95
{ "fr": "ô les croyants ! Ne tuez pas de gibier pendant que vous êtes en état d´Ihram . Quiconque parmi vous en tue délibérément, qu´il compense alors, soit par quelque bête de troupeau, semblable à ce qu´il a tué, d´après le jugement de deux personnes intègres parmi vous, et cela en offrande qu´il fera parvenir à (destination des pauvres de) la kaaba, ou bien par une expiation, en nourrissant des pauvres, ou par l´équivalent en jeûne. Cela afin qu´il goûte à la mauvaise conséquence de son acte. Allah a pardonné ce qui est passé; mais quiconque récidive, Allah le punira. Allah est Puissant et Détenteur du pouvoir de punir.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen rey aw rab bëgg rëbb, fekk ngeen nekk ci armal di aj [Màkka]. Ku ko rey ci yéen te tey ko, war naa fey lu mel ni la mu rey ci jur, ñaar ñu maandu ci yéen xayma ko, muy yool bu ñuy yóbb ca kaaba ga, mbaa mu jéggaloo aw ñam wu muy jox néew-ji- doole yi, walla mu woor kem lu tollu noona. Ndax mu mos mbugalu la mu jëf. Yàlla boroom kàttan la, Ku mën a feyyu la." }
5
96
{ "fr": "La chasse en mer vous est permise, et aussi d´en manger, pour votre jouissance et celle des voyageurs. Et vous est illicite la chasse à terre tant que vous êtes en état d´Ihram. Et craignez Allah vers qui vous serez rassemblés .", "wo": "Dagan na ci yéen la ngeen nappe ca géej ga, ak ñamu géej, muj xéewal ci yéen ñi nekk ci armal. Te nangeen ragal Yàlla, Ma nga xam ne, dees na leen fang jëme ca Moom." }
5
97
{ "fr": "Allah a institué la Kaaba, la Maison sacrée, comme un lieu de rassemblement pour les gens. (Il a institué) le mois sacré, l´offrande (d´animaux,) et les guirlandes, afin que vous sachiez que vraiment Allah sait tout ce qui est dans les cieux et sur la terre; et que vraiment Allah est Omniscient .", "wo": "Yàlla def na kaaba ga muy néeg bu ñu wormaal, muy lu ñu taxawal ngir nit ñi. Ak àtte weer wa ñu wormaal ak yool ga, ak mala ya ñu ràngal, yooyu yépp [def na ko] ngir ngeen xam ne Yàlla xam na li nekk ci asamaan yi ak suuf si; te it xam na lu ne.(r)" }
5
98
{ "fr": "Sachez qu´Allah est sévère en punition, mais aussi Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Xamleen ne Yàlla Ku tar mbugal la, te it Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
5
99
{ "fr": "Il n´incombe au Messager de transmettre (le message). Et Allah sait ce que vous divulguer tout comme ce que vous cachez.", "wo": "Dara warul Yonent bi lu dul jottal. Te Yàlla xam na li ngeen feeñal ak li ngeen di nëbb." }
5
100
{ "fr": "Dis : \"Le mauvais et le bon ne sont pas semblables, même si l´abondance du mal te séduit. Craignez Allah, donc, ô gens intelligents, afin que vous réussissiez", "wo": "Neel : “Lu bon ak lu sell yemuñu, doonte yéem na la barig alal ju araam. Nangeen ragal Yàlla yéen woroom xel yi, ndax xéy-na ngeen texe." }
5
101
{ "fr": "ô les croyants ! Ne posez pas de questions sur des choses qui, si elles vous étaient divulguées, vous mécontenteraient. Et si vous posez des questions à leur sujet, pendant que le Coran est révélé, elles vous seront divulguées. Allah vous a pardonné cela. Et Allah est Pardonneur et Indulgent.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen di laaj ci yoo xam ne, bu ñu leen ko leeralee, mu nekk lu naqari ci yéen. Te bu ngeen ko laajee ca waxtu wa Alxuraan di wàcc, ñu leeral leen ko. Yàlla jéggal na leen [seen laaj yooyu]. Yàlla Jéggalaakoon la, Ku lewet la." }
5
102
{ "fr": "Un peuple avant vous avait posé des questions (pareilles) puis, devinrent de leur fait mécréants.", "wo": "Am na xeet yu leen jiitu yu laajoon lu mel noonu, te ca sababus laaj ya, tax ñu mujj di ay yéefar." }
5
103
{ "fr": "Allah n´a pas institué la Bahira, la Saïba, la Wasila ni le Ham, Mais ceux qui ont mécru ont inventé ce mensonge contre Allah, et la plupart d´entre eux ne raisonnent pas. .", "wo": "Du ut ne Yàlla Moo taxawal Bahiirata , ak Saaniyata , ak Wasiilata ak Haam , waaye yéefar ya ñoo duural Yàlla ay fen te la ëpp ca ñoom xel-luwuñu." }
5
104
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Venez vers ce qu´Allah a fait descendre (La Révélation), et vers le Messager\", ils disent : \"Il nous suffit de ce sur quoi nous avons trouvé nos ancêtres.\" Quoi ! Même si leurs ancêtres ne savaient rien et n´étaient pas sur le bon chemin... ?", "wo": "Bu ñu leen nee : “Kaayleen ci li Yàlla wàcce ci Yonent bi” , ñu ne : “La ñu fekk ca sunuy maam doy nanu.” . Doonte la sax ! Seeni maam xamuñu dara te gindikuwuñu [dañuy sax ci loolu]... ?" }
5
105
{ "fr": "ô les croyants ! Vous êtes responsables de vous-même ! Celui qui s´égare ne vous nuira point si vous vous avez pris la bonne voie. C´est vers Allah que vous retournerez tous; alors Il vous informera de ce que vous faisiez.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Sàmmleen seen bopp te yéwénal ko ! Ku réer duleen wàññi dara ndegam gindiku ngeen. Seen delluwaay, yéen ñépp, ca Yàlla la jëm ; mu won leen la ngeen daan def." }
5
106
{ "fr": "ô les croyants ! Quand la mort se présente à l´un de vous, le testament sera attesté par deux hommes intègres d´entre vous, ou deux autres, non des vôtres, si vous êtes en voyage dans le monde et que la mort vous frappe. Vous les retiendrez (les deux témoins), après la Salat, puis, si vous avez des doutes, vous les ferez jurer par Allah : \"Nous ne faisons aucun commerce ou profit avec cela, même s´il s´agit d´un proche, et nous ne cacherons point le témoignage d´Allah. Sinon, nous serions du nombre des pêcheurs\".", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Bu dee dabee kenn ci yéen, na dénkaane te am seede yu nekk ñaar ñu maandu ci yéen, walla ci ñeneen ñu dul yéen, su fekkee dangeen a nekk ci tukki, tiisu dee dab leen. Taxawal-leen ñoom ñaar, ginnaaw julli, ndegam dangeen a am ci ñoom sikki-sàkka, ñu giñ ci Yàlla ne : “Jaayunu sunu seede ci genn njëg, doonte la dafa jëm ci sunu mbokk, te it nëbbunu lu nu Yàlla seedeloo ndax danuy bokk ci way-bàkkaar ña (su nu ko defee)” .(s)" }
5
107
{ "fr": "Si l´on découvre que ces deux témoins sont coupables de pêché, deux autres plus intègres, parmi ceux auxquels le tort a été fait, prendront leur place et tous jureront par Allah : \"En Vérité, notre témoignage est plus juste que le témoignage de ces deux-là; et nous ne transgressons point. Sinon, nous serions certainement du nombre des injustes\".", "wo": "Bu ñu xamee ne ñoom ñaar waxuñu dëgg, kon ñeneen ñaar wuutu leen, ñu di ña gën a nekk i jegeñaale [néew ba], ñu giñ ci Yàlla ne : “Sunu seede moo gën a dëggu sunu bos te jalgatiwunu. Nde kon nu bokk ci way-tooñ ña” ." }
5
108
{ "fr": "C´est le moyen le plus sûr pour les inciter à fournir le témoignage dans sa forme réelle; ou leur faire craindre de voir d´autres serments se substituer aux leurs. Et craignez Allah et écoutez. Allah ne guide pas les gens pervers.", "wo": "Loolooy tax ña giñ joxe seede su dëggu ; mbaa ñu ragal ñu dàq seeni seede ginnaaw ba ñu defee seede su [dëng]. Te nangeen ragal Yàlla tey dégg [ndigal]. Yàlla du gindi nit ñu di ay saay-saay [ñu génn ci topp]." }
5
109
{ "fr": "(Rappelle-toi) le jour où Allah rassemble (tous) les messagers, et qu´Il dira : \"Que vous a-t-on donné comme réponse ? \" Ils diront : \"Nous n´avons aucun savoir : c´est Toi, vraiment, le grand connaisseur de tout ce qui est inconnu\".", "wo": "Bis bu Yàlla dajalee Yonent ya, ne leen : “Lu ñu leen toontu ?” Ñu ne Ko : “ Amunu xam-xam : Yaw yaay ki xam kumpa” ." }
5
110
{ "fr": "Et quand Allah dira : \"ô Jésus, fils de Marie, rappelle-toi Mon bienfait sur toi et sur ta mère quand Je te fortifiais du Saint-Esprit. Au berceau tu parlais aux gens, tout comme en ton âge mûr. Je t´enseignais le Livre, la Sagesse, la Thora et l´évangile ! Tu fabriquais de l´argile comme une forme d´oiseau par Ma permission; puis tu soufflais dedans. Alors par Ma permission, elle devenait oiseau. Et tu guérissais par Ma permission, l´aveugle-né et le lépreux. Et par Ma permission, tu faisais revivre les morts. Je te protégeais contre les Enfants d´Israël pendant que tu leur apportais les preuves. Mais ceux d´entre eux qui ne croyaient pas dirent : \"Ceci n´est que de la magie évidente\".", "wo": "[Fàttalikul] ba Yàlla nee : «Yaw Iisaa, doomi Maryaama, fàttalikul xéewal ya Ma la defal yaak sa yaay ba Ma la dimbalee boole la ak Ruu gu sell ga [Jibriil]. Ba nga wax ak nit ñi fekk yaa ngi nekk liir ak ba nga nekkee mag mu weesu ndaw. [Fàttalikul it] ba Ma la jàngalee Téere ba ak gis-gis bu ubbiku, ak Tawreet ak Linjiil ! [Fàttalikul it] ba ngay sos ci ban lu ame melow njanaaw ; ci Sama coobare nga ëf ca. Mu nekk njanaaw ci sama coobare. Te ngay wéral ku gumba ak ku gaana, ci Sama coobare. Ak di génne ku dee [ci bàmmeel] ci Sama coobare ak ci li Ma la fegal waa Bani-Israayiil [ñu bañ laa lor] ba nga leen indilee lay yu leer ya. Te ña weddi ca ñoom ne leen : “Nekkul lu dul njibar gu bir” ." }
5
111
{ "fr": "Et quand J´ai révélé aux Apôtres ceci : \"Croyez en Moi et Mon messager (Jésus)\". Ils dirent : \"Nous croyons; et atteste que nous sommes entièrement soumis\".", "wo": "Fàttalikul ba nu xiiree sa taalibe ya [waaraatekat ya], sol ci seeni xol ne leen: “Gëmleen Ma ak Sama Yonent” . Ñu ne : “Gëm nanu ; te Nanga seede ne nun way-wommatu lanu [jullit lanu]” ." }
5
112
{ "fr": "(Rappelle-toi le moment) où les Apôtres dirent : \"ô Jésus, fils de Marie, se peut-il que ton Seigneur fasse descendre sur nous du ciel une table servie ? \" Il leur dit : \"Craignez plutôt Allah, si vous êtes croyants\".", "wo": "(fàttalikul) ba waarekat yooyu waxee ne : “Yaw Iisaa, doomi Maryaama, moo ndax sa Boroom mën naa wàcce ci nun [ndën] lu jóge ci asamaan [am ñam] ?” . Mu ne leen : “Ragal- leen Yàlla, ndegam gëm ngeen” .(n)" }
5
113
{ "fr": "Ils dirent : \"Nous voulons en manger, rassurer ainsi nos coeurs, savoir que tu nous as réellement dit la vérité et en être parmi les témoins\".", "wo": "Ñu ne : “Danoo bëgg lekk ci moom [ndën la] ndax sunu xel dal, nu daldi xam ne wax nga dëgg te kon nun dananu seede loolu” ." }
5
114
{ "fr": "ô Allah, notre Seigneur, dit Jésus, fils de Marie, fais descendre du ciel sur nous une table servie qui soit une fête pour nous, pour le premier d´entre nous, comme pour le dernier, ainsi qu´un signe de Ta part. Nourris-nous : Tu es le meilleur des nourrisseurs.", "wo": "Iisaa doomu Maryaama ne : «Yaw sama Boroom, wàcceel ci nun taabal [ndën lu am ñam] mu jóge asamaan, mu nekk ci nun xew- xewu mbégte, mu ñeel ku jëkk ak ku mujj ci nun, te it muy kéemaan gu tukkee ci Yaw. Defal nu ko : Yaa di gën gi xéewalaakoon buy joxe wërsëg.”" }
5
115
{ "fr": "Oui, dit Allah, Je la ferai descendre sur vous. Mais ensuite, quiconque d´entre vous refuse de croire, Je le châtierai d´un châtiment dont Je ne châtierai personne d´autre dans l´univers.", "wo": "Yàlla toontu ne : “Maa ngi koy wàcce ci yéen. Waaye ku weddi ci yéen ginnaaw loolu, Dinaa ko mbugale noo xam ne mësuma koo mbugale kenn ci àdduna bi.”" }
5
116
{ "fr": "(Rappelle-leur) le moment où Allah dira : \"ô Jésus, fils de Marie, est-ce toi qui as dit aux gens : \"Prenez-moi, ainsi que ma mère, pour deux divinités en dehors d´Allah ? \" Il dira : \"Gloire et pureté à Toi ! Il ne m´appartient pas de déclarer ce que je n´ai pas le droit de dire ! Si je l´avais dit, Tu l´aurais su, certes. Tu sais ce qu´il y a en moi, et je ne sais pas ce qu´il y a en Toi. Tu es, en vérité, le grand connaisseur de tout ce qui est inconnu.", "wo": "(Fàttalikul) ba Yàlla nee : «Yaw Iisaa, doomu Maryaama, moo ndax yaw yaa wax nit ñi ne : “Jàppeleen ma, maak sama yaay, nu di ñaari yàlla, beddi Yàlla ?” . Mu toontu [moom Iisaa, doomu Maryaama] ne ko : “Tudd naa sag sell ! Yellul ci man may wax lu dul dëgg ! Su fekkee maa ko wax, xam nga ci dara. Ndax Yaw xam nga li nekk ci man, te man xamuma li nekk fi Yaw. Te Yaw yaay Xamaakoonu kumpa yi." }
5
117
{ "fr": "Je ne leur ai dit que ce Tu m´avais commandé, (à savoir) : \"Adorez Allah, mon Seigneur et votre Seigneur\". Et je fus témoin contre eux aussi longtemps que je fus parmi eux. Puis quand Tu m´as rappelé, c´est Toi qui fus leur observateur attentif. Et Tu es témoin de toute chose.", "wo": "Waxumaleen lu dul li nga digle ci loolu, ne leen : “Jaamuleen Yàlla, miy sama Boroom, di seen Boroom” . Ma nekk seede ci ñoom, fekk maa nga nekkoon ca seen biir. Ba nga ma yóbboo ci Yaw [jële ma fa], Yaw yaa leen doon fuglu [nemmiku]. Te sax Yaw yaay Aji-seede ci lépp." }
5
118
{ "fr": "Si Tu les châties, ils sont Tes serviteurs. Et si Tu leur pardonnes, c´est Toi le Puissant, le Sage\".", "wo": "Boo leen mbugalee, say jaam lañu. Boo leen jéggalee it, Yaw yaa di Aji-not ji, di Ku xereñ [ci say àtte]” ." }
5
119
{ "fr": "Allah dira : \"Voilà le jour où leur véracité va profiter aux véridiques : ils auront des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux pour y demeurer éternellement.\" Allah les a agréés et eux L´ont agréé. Voilà l´énorme succès.", "wo": "Yàlla ne : “Bis niki tey, ña dëgguwoon, seen dëggu ga dana leen jariñ : am nañu Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ca seen ron, dañu fay béel ba fàwwu.” Yàlla bég na ci ñoom, ñoom it ñu bég ci Yàlla. Loolu mooy texe gu màgg ga tigi." }
5
120
{ "fr": "A Allah seul appartient le royaume des cieux, de la terre et de ce qu´ils renferment et Il est Omnipotent.", "wo": "Yàllaa moom nguuru asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen biir, te Muy ku am kàttan nag ci def lépp [lu ko soob]. " }
6
1
{ "fr": "Louange à Allah qui a créé les cieux et la terre, et établi les ténèbres et la lumière. Pourtant, les mécréants donnent des égaux à leur Seigneur.", "wo": "Cant ñeel na Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si, te sos lëndëm yi ak leer yi. Terewul ña weddi ñoom di dendale seen Boroom ak leneen.(s)" }
6
2
{ "fr": "C´est Lui qui vous a créés d´argile; puis Il vous a décrété un terme, et il y a un terme fixé auprès de Lui. Pourtant, vous doutez encore !", "wo": "Moom mooy ki leen bind ci ban ; ba noppi dugal àpp [ci dundu gu ne] ak àpp ba ñu tudd ci Moom [ci jéexug àdduna si]. Ba noppi ngeen di am xel-yaar !" }
6
3
{ "fr": "Et Lui, Il est Allah dans les cieux et sur la terre. Il connaît ce que vous cachez en vous et ce que vous divulguez et Il sait ce que vous acquérez.", "wo": "Te Mooy Yàlla ci asamaan yeek suuf si. Mooy ki xam seen mbóot yi ngeen di nëbb ak yi ngeen di feeñal te xam it la ngeen di fàggu." }
6
4
{ "fr": "Et il ne leur vient aucun des signes d´entre les signes de leur Seigneur, sans qu´ils ne s´en détournent.", "wo": "Te kat amul lenn ndigal lu leen dikke ca seen Boroom te dëdduwuñu ko." }
6
5
{ "fr": "Ils traitent de mensonge la vérité quand celle-ci leur vient. Mais ils vont avoir des nouvelles de ce dont ils se moquent.", "wo": "Weddi nañu dëgg ba mu dikkee ca ñoom. Waaye dana leen mas a dikkal xew-xewi la ñu tejji." }
6
6
{ "fr": "N´ont-ils pas vu combien de générations, avant eux, Nous avons détruites, auxquelles Nous avions donné pouvoir sur terre, bien plus que ce que Nous vous avons donné ? Nous avions envoyé, sur eux, du ciel, la pluie en abondance, et Nous avions fait couler des rivières à leurs pieds. Puis Nous les avons détruites, pour leurs péchés; et Nous avons créé, après eux, une nouvelle génération.", "wo": "Moo ndax dañoo xamul ñaata maas Lanu alag ca ña leen jiitu, ñoo xam ne mayoon Nanu leen lu Nu leen mayul [yéen] ? Te dottil woon Nanu asamaan mu taw ca ñoom, waaye defaloon leen ay dex yuy dawaan. Waaye Nu daldi leen alag ngir seeni bàkkaar ; sosaat nag geneen maas wu watle leen ko." }
6
7
{ "fr": "Même si Nous avions fait descendre sur toi (Muhammad) un Livre en papier qu´ils pouvaient toucher de leurs mains, ceux qui ne croient pas auraient certainement dit : \"Ce n´est que de la magie évidente ! \"", "wo": "Bu Nu la wàcceeloon Téere bu ñu bind ci kayit gu ñu mën a laal ak seeni yoxo sax, du tee ñu weddi ñoom ne : “Lii ag jibar doŋŋ la !”" }
6
8
{ "fr": "Et ils disent : \"Pourquoi n´a-t-on pas fait descendre sur lui (Muhammad) un Ange ? \" Si Nous avions fait descendre un Ange, ç´eût été, sûrement, affaire faite ; puis on ne leur eût point donné de délai.", "wo": "Ba noppi di wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom Malaaka ?” . Waaye bu ñu wàcce woon Malaaka, kon mbir ya sottikoon na ; ndax kenn duleen muñandiku kon." }
6
9
{ "fr": "Si Nous avions désigné un Ange [comme prophète], Nous aurions fait de lui un homme et Nous leur aurions causé la même confusion que celle dans laquelle ils sont.", "wo": "Te sax bu Nu ko defoon muy Malaaka, kon jëmmi nit Lanu koy jox, te kon Nu lëntal ca ñoom la Nu lëntal ci seen bopp." }
6
10
{ "fr": "Certes, on s´est moqué de messagers avant toi, mais ceux qui se sont raillés d´eux, leur propre raillerie les enveloppa.", "wo": "Doon nañu yejji ay Yonent lu jiitu, waaye ña leen doon reetaan, la ñu daan yejji wàcc na ca seen kaw [alag leen]. " }
6
11
{ "fr": "Dis : \"Parcourez la terre et regardez ce qu´il est advenu de ceux qui traitaient la vérité de mensonge\".", "wo": "Neel : “Doxleen ci suuf si te ngeen seetlu naka la mujjug way-weddi ña deme” ." }
6
12
{ "fr": "Dis : \"A qui appartient ce qui est dans les cieux et la terre ? \" Dis : \"A Allah ! \" Il S´est à Lui-même prescrit la miséricorde . Il vous rassemblera, certainement, au Jour de la Résurrection : il n´y a pas de doute là-dessus. Ceux qui font leur propre perte sont ceux qui ne croient pas.", "wo": "Neel : “Kan moo moom li nekk ci asamaan yeek suuf si ?” . Neel : “Yàllaa ko moom !” Bind na ci boppam yërmaande. Fàwwu Dana leen dajale Bis-pénc ba : sikkuwul. Ña yàqal seen bopp, ñoom duñu gëm." }
6
13
{ "fr": "Et à Lui tout ce qui réside dans la nuit et le jour. C´est Lui qui est l´Audient, l´Omniscient.", "wo": "Moo moom lépp lu ne tekk [dal] ci guddi ak bëccëg. Aji-dégg la, Aji- xam la.(r)" }
6
14
{ "fr": "Dis : \"Devais-je prendre pour allié autre qu´Allah, le Créateur des cieux et de la terre ? C´est Lui qui nourrit et personne ne Le nourrit. Dis : \"On m´a commandé d´être le premier à me soumettre \". Et ne sois jamais du nombre des associateurs.", "wo": "Neel : “Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku kiiraay, te Moo sàkk asamaan yeek suuf si ? Mooy lele te kenn du ko leel [ñam]. Neel : “Dëggaleef na ma, ma nekk ku jëkk a wommatu” . Te buleen bokk ca way-bokkaale ña." }
6
15
{ "fr": "Dis : \"Je crains, si je désobéis à mon Seigneur, le châtiment d´un jour redoutable \".", "wo": "Neel : “Su ma moyee sama Boroom [cig ndigalam], mbugalum bis bu màgg ba [Bis-pénc ba], ragal naa mu dal ma” ." }
6
16
{ "fr": "En ce jour, quiconque est épargné, c´est qu´[Allah] lui a fait miséricorde, Et voilà le succès éclatant.", "wo": "Koo xam ne musal nañu ko ca bis booba ci mbugal moo ma, kooka Yàlla yërëm na ko, te loolu mooy texe tigi tigi." }