sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
4
112
{ "fr": "Et quiconque acquiert une faute ou un péché puis en accuse un innocent, se rend coupable alors d´une injustice et d´un péché manifeste.", "wo": "Ku def ñaawtéef walla bàkkaar ba noppi jiiñ ko ku ca set wecc, kooka yenu ma duur ak bàkkaar bu bari." }
4
113
{ "fr": "Et n´eût été la grâce d´Allah sur toi (Muhammad) et Sa miséricorde, une partie d´entre eux t´aurait bien volontiers égaré. Mais ils n´égarent qu´eux-mêmes, et ne peuvent en rien te nuire. Allah a fait descendre sur toi le Livre et la Sagesse, et t´a enseigné ce que tu ne savais pas. Et la grâce d´Allah sur toi est immense.", "wo": "Bu dul woon teraanga Yàlla ak yërmaandeem ci yaw, kon ab kurél ci ñoom danañu ittewoo sànk la. Waaye sànkuñu kenn ku dul seen bopp, loruñu la ci dara. Te Yàlla wàcce na ci yaw Téere ba ak xam- xamu ràññee [xereñ], te xamal na la loo xamul woon. Te xéewali Yàlla ci yaw rëy na." }
4
114
{ "fr": "Il n´y a rien de bon dans la plus grande partie de leurs conversations secrètes, sauf si l´un d´eux ordonne une charité, une bonne action, ou une conciliation entre les gens. Et quiconque le fait, cherchant l´agrément d´Allah, à celui-là Nous donnerons bientôt une récompense énorme.", "wo": "Lu bari ca la ñuy déeyoo lu baax nekku ca, lu dul ci waxi kuy digle sarax, walla njekk, walla jubale ci diggante nit ñi. Ku def loolu, di sàkku ngërëmul Yàlla, Dananu ko jox [ëllëg] pey gu màgg.(n)" }
4
115
{ "fr": "Et quiconque fait scission d´avec le Messager, après que le droit chemin lui est apparu et suit un sentier autre que celui des croyants, alors Nous le laisserons comme il s´est détourné, et le brûlerons dans l´Enfer. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga feesee ci moom, muy topp lu wuuteek yoonu jullit ña, Dananu ko méngaleek la mu méngool, te séndal ko Safara. Ndaw delluwaay bu bon !" }
4
116
{ "fr": "Certes, Allah ne pardonne pas qu´on Lui donne des associés. A part cela, Il pardonne à qui Il veut. Quiconque donne des associés à Allah s´égare, très loin dans l´égarement.", "wo": "Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu Dana ko baale ku Ko neex. Te képp kuy bokkaale Yàlla, réer na réer gu sori." }
4
117
{ "fr": "Ce ne sont que des femelles qu´ils invoquent, en dehors de Lui. Et ce n´est qu´un diable rebelle qu´ils invoquent.", "wo": "Te kat ñoom ay xërëm yu ñu jigéenal ak Séytaane su fétterlu doŋŋ lañuy jaamu di ko woo bàyyi Yàlla." }
4
118
{ "fr": "Allah l´a (le Diable) maudit et celui-ci a dit : \"Certainement, je saisirai parmi Tes serviteurs, une partie déterminée.", "wo": "Yàlla rëbb na ko ca la mu wax moom [Séytaane], ne : “Fàwwu danaa jël ci say jaam ab cër bu takku” ." }
4
119
{ "fr": "Certes, je ne manquerai pas de les égarer, je leur donnerai de faux espoirs, je leur commanderai, et ils fendront les oreilles aux bestiaux; je leur commanderai, et ils altéreront la création d´Allah. Et quiconque prend le Diable pour allié au lieu d´Allah, sera, certes, voué à une perte évidente.", "wo": "Mu waxaat [moom Séytaane] : “Waat naa ne danaa leen réeral, danaa leen nax ca la ñuy xemmem, danaa leen digal ñu dog noppi jur gi, danaa leen sant ñu soppi ni Yàlla bindee [bindeef yi]. Ku bàyyi Yàlla, jàppe Séytaane muy kilifaam, yàqule na yàqule gu bir." }
4
120
{ "fr": "Il leur fait des promesses et leur donne de faux espoirs. Et le Diable ne leur fait que des promesses trompeuses.", "wo": "Dana leen dig, xemmemlu leen. Te Séytaane du dige lu dul ay wor. " }
4
121
{ "fr": "Voilà ceux dont le refuge est l´Enfer. Et ils ne trouveront aucun moyen d´y échapper !", "wo": "Ñooñu seeni dëkkuwaay mooy Safara. Te kenn duleen ca musal !" }
4
122
{ "fr": "Et quant à ceux qui ont cru et fait de bonnes oeuvres. Nous les ferons entrer bientôt aux Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement. Promesse d´Allah en vérité. Et qui est plus véridique qu´Allah en parole ?", "wo": "Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, dañu fay béel ba fàwwu. Digeb Yàlla lu dëggu la. Te sax, ana kan moo gën a dëggu ay wax Yàlla ?" }
4
123
{ "fr": "Ceci ne dépend ni de vos désirs ni des gens du Livre . Quiconque fait un mal sera rétribué pour cela, et ne trouvera en sa faveur, hors d´Allah, ni allié ni secoureur.", "wo": "Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee." }
4
124
{ "fr": "Et quiconque, homme ou femme, fait de bonnes oeuvres, tout en étant croyant... les voilà ceux qui entreront au Paradis; et on ne leur fera aucune injustice, fût-ce d´un creux de noyau de datte .", "wo": "Ku jëf, jëf ju bokk ci aw yiw, di góor mbaa muy jigéen, te di ab jullit... ñooña danañu dugg Àjjana; te kenn duleen ca tooñ [ba waññil leen] lu toll ni mboxosu xooxu tàndarma.(s)" }
4
125
{ "fr": "Qui est meilleur en religion que celui qui soumet à Allah son être, tout en se conformant à la Loi révélée et suivant la religion d´Abraham, homme de droiture ? Et Allah avait pris Abraham pour ami privilégié.", "wo": "Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla, te di kuy rafetal [jëfam], tey roy diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla ? Te Yàlla Moom jàppe na Ibraahiima soppeem." }
4
126
{ "fr": "C´est à Allah qu´appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. Et Allah embrasse toute chose (de Sa science et de Sa puissance).", "wo": "Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Te Yàlla lépp la peeg." }
4
127
{ "fr": "Et ils te consultent à propos de ce qui a été décrété au sujet des femmes. Dis : \"Allah vous donne Son décret là-dessus, en plus de ce qui vous est récité dans le Livre, au sujet des orphelines auxquelles vous ne donnez pas ce qui leur a été prescrit , et que vous désirez épouser, et au sujet des mineurs encore d´âge faible\". Vous devez agir avec équité envers les orphelins. Et de tout ce que vous faites de bien, Allah en est, certes, Omniscient.", "wo": "Ña nga lay laaj nga ubbee leen ci jigéen ñi. Neel : “Yàlla Dana leen ubbee ci ñoom, ak lañu leen jàngal ca Téere ba [di leeral lu jëm ci] jirim yu jigéen yi nga xam ne joxooleen leen la ñu digle ci ñoom, te ngeen xemmem takk leen, [ak leeral lu jëm ca] ñu néew doole ña ci xale yi” . [Ak di leen digal] ngeen taxawu jirim ci ag maandute. Lu ngeen ca def ci ñoom ci lu baax, Yàlla xam na ko." }
4
128
{ "fr": "Et si une femme craint de son mari abandon ou indifférence, alors ce n´est pas un péché pour les deux s´ils se réconcilient par un compromis quelconque, et la réconciliation est meilleure, puisque les âmes sont portées à la ladrerie. Mais si vous agissez en bien et vous êtes pieux... Allah est, certes, Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Bu ku jigéen ragalee ci jëkkëram naqar walla mu foñ ko, aayul ñu yéwénoo ñoom ñaar, ba juboo ci lenn, ndaxte yéwénoo moo gën, te bakkan dafa gaaw a jeng jëm ci nay. Waaye bu ngeen rafatalee te ragal Yàlla... Yàlla, ku deñ-kumpa la ci seeni jëf." }
4
129
{ "fr": "Vous ne pourrez jamais être équitable entre vos femmes, même si vous en êtes soucieux. Ne vous penchez pas tout à fait vers l´une d´elles, au point de laisser l´autre comme en suspens. Mais si vous vous réconciliez et vous êtes pieux... donc Allah est, certes, Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Dungeen mëna a maandu mukk ci diggante jigéen ñi, doonte xér ngeen ci yemale leen. Waaye, buleen jeng, jeng gu jéggi dayo ba tax ngeen bàyyi kenn ci ñoom ba mu mel ni ku ñu aj. Waaye, bu ngeen yéwénalee sellal te ragal Yàlla... Yàlla di ab Jéggalaakoon, di ab Jaglewaakoon." }
4
130
{ "fr": "Si les deux se séparent, Allah de par Sa largesse, accordera à chacun d´eux un autre destin. Et Allah est plein de largesses et parfaitement Sage.", "wo": "Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku ca nekk ci ag yaatalam. Yàlla Ku yaatu mbir la, di Ku xereñ (r)" }
4
131
{ "fr": "A Allah seul appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. \"Craignez Allah ! \" Voilà ce que Nous avons enjoint à ceux auxquels avant vous le Livre fut donné, tout comme à vous-mêmes. Et si vous ne croyez pas (cela ne nuit pas à Allah, car) très certainement à Allah seul appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. Et Allah se suffit à Lui-même et Il est digne de louange.", "wo": "Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla !” . Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant." }
4
132
{ "fr": "A Allah seul appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. Et Allah suffit pour s´occuper de tout.", "wo": "Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa." }
4
133
{ "fr": "S´il voulait, il vous ferait disparaître, ô gens, et en ferait venir d´autres. Car Allah en est très capable.", "wo": "Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko." }
4
134
{ "fr": "Quiconque désire la récompense d´ici-bas, c´est auprès d´Allah qu´est la récompense d´ici-bas tout comme celle de l´au-delà. Et Allah entend et observe tout.", "wo": "Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la." }
4
135
{ "fr": "ô les croyants ! Observez strictement la justice et soyez des témoins (véridiques) comme Allah l´ordonne, fût-ce contre vous mêmes, contre vos père et mère ou proches parents. Qu´il s´agisse d´un riche ou d´un besogneux, Allah a priorité sur eux deux (et Il est plus connaisseur de leur intérêt que vous). Ne suivez donc pas les passions, afin de ne pas dévier de la justice. Si vous portez un faux témoignage ou si vous le refusez, [sachez qu´] Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Taxawleen temm ci maandute, di seede ngir Yàlla doonte seede soosu [lu naqari la] luy dal ci seen kaw, walla ci seeni waajur, walla ci kaw seeni njaboot, walla seeni jegeñaale. Su dee ku woomal la walla ku ñàkk, Yàllaay ki gën pey ci ñoom ñaar ñépp. Buleen topp seeni bànneex ba ñàkk a maandu. Bu ngeen jéggalee [seede] walla ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla Ku deñ- kumpa la ci li ngeen def." }
4
136
{ "fr": "ô les croyants ! Soyez fermes en votre foi en Allah, en Son messager, au Livre qu´il a fait descendre sur Son messager, et au Livre qu´il a fait descendre avant. Quiconque ne croit pas en Allah, en Ses anges, en Ses Livres, en Ses messagers et au Jour dernier, s´égare, loin dans l´égarement.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg]." }
4
137
{ "fr": "Ceux qui ont cru, puis sont devenus mécréants, puis ont cru de nouveau, ensuite sont redevenus mécréants, et n´ont fait que croître en mécréance, Allah ne leur pardonnera pas, ni les guidera vers un chemin (droit).", "wo": "Ña nga xam ne dañoo gëm ba noppi weddi, daldi gëm, weddiwaat, seenug weddi di gën a tar, Yàlla duleen jéggal, te it duleen gindi teg leen ci yoon wu leer wa." }
4
138
{ "fr": "Annonce aux hypocrites qu´il y a pour eux un châtiment douloureux,", "wo": "Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti," }
4
139
{ "fr": "ceux qui prennent pour alliés des mécréants au lieu des croyants, est-ce la puissance qu´ils recherchent auprès d´eux ? (En vérité) la puissance appartient entièrement à Allah.", "wo": "ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña, ndax nee dañuy sàkku ci ñoom teraanga, te moone teraanga jépp a ngi ca Yàlla.(s)" }
4
140
{ "fr": "Dans le Livre, il vous a déjà révélé ceci : lorsque vous entendez qu´on renie les versets (le Coran) d´Allah et qu´on s´en raille, ne vous asseyez point avec ceux-là jusqu´à ce qu´ils entreprennent une autre conversation. Sinon, vous serez comme eux. Allah rassemblera, certes, les hypocrites et les mécréants, tous, dans l´Enfer.", "wo": "Te wàcceel na leen ca Téere ba, xamal leen ne : bu ngeen déggee ay nit ñuy weddi ak a ñaawal [yéjji] ndigali Yàlla yi, buleen toog ak ñay def loolu ba ba ñuy xuus ci weneen waxtaan. Lu ko moy dangeen di mel ni ñoom [cig weddi]. Yàlla Kuy dajale la naaféq yaak yéefar ya ñoom ñépp ca biir Safara." }
4
141
{ "fr": "Ils restent dans l´expectative à votre égard; si une victoire vous vient de la part d´Allah, ils disent : \"N´étions-nous pas avec vous ? \"; et s´il en revient un avantage aux mécréants. ils leur disent : \"Est-ce que nous n´avons pas mis la main sur vous pour vous soustraire aux croyants ? \" Eh bien, Allah jugera entre vous au Jour de la Résurrection. Et jamais Allah ne donnera une voie aux mécréants contre les croyants.", "wo": "Ña nga xam ne ñanga téyandi seen bopp ci yéen ; su leen Yàlla joxee ndam, ñu gaaw ne : “Ndax àndunu woon ak yéen ?” ; bu yéefar yi amee cër ci ndam, ñu ne leen : “Xanaa du ñoo leen doon song [yéen yéefar yi] te nu fegal leen jullit ñi ?” . Yàlla Dana àtte seen diggante Bis- pénc ba. Te du jox yéefar yi ndam ci kaw jullit ñi. " }
4
142
{ "fr": "Les hypocrites cherchent à tromper Allah, mais Allah retourne leur tromperie (contre eux-mêmes). Et lorsqu´ils se lèvent pour la Salat, ils se lèvent avec paresse et par ostentation envers les gens. A peine invoquent-ils Allah.", "wo": "Naaféq ya dañuy jéem a nax Yàlla, te fekk Yàlla Dana leen juuy. Te bu ñu taxawalee julli, taxaw ci tàyyeel, di ngistal ci bëti nit ñi. Te duñu tudd [fàttaliku Yàlla] lu dul ñu néew ci ñoom." }
4
143
{ "fr": "Ils sont indécis (entre les croyants et les mécréants) n´appartenant ni aux uns ni aux autres. Or, quiconque Allah égare, jamais tu ne trouveras de chemin pour lui.", "wo": "Ñuy deŋŋi-deŋŋi ci diggante yooyu, féetewuñu ci ñii, féetewuñu ca ñaa. Ku Yàlla bàyyi cig cànkuteem, kenn du ko mën a teg ci yoon wu jub wa." }
4
144
{ "fr": "ô les croyants ! Ne prenez pas pour alliés les mécréants au lieu des croyants. Voudriez-vous donner à Allah une preuve évidente contre vous ?", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàppe yéefar yi ay xarit bàyyi jullit ña. Ndax dangeen bëgg a jox Yàlla lay wu jub ci seen kaw ?" }
4
145
{ "fr": "Les hypocrites seront, certes, au plus bas fond du Feu, et tu ne leur trouveras jamais de secoureur,", "wo": "Naaféq yaa nga ca dëru ya gën a suufe ca Safara, te kenn duleen dimbali," }
4
146
{ "fr": "sauf ceux qui se repentent, s´amendent, s´attachent fermement à Allah, et Lui vouent une foi exclusive. Ceux-là seront avec les croyants. Et Allah donnera aux croyants une énorme récompense.", "wo": "ba mu des ña tuub, réccu, te sellal [yéwénal], jubbantiku te tënku ci Yàlla te sellal seenug jaamu Yàlla. Ñooña, ñook jullit ñee ànd. Te Yàlla Dana jox jullit ñi pey gu màgg." }
4
147
{ "fr": "Pourquoi Allah vous infligerait-il un châtiment si vous êtes reconnaissants et croyants ? Allah est Reconnaissant et Omniscient.", "wo": "Lu Yàlla di doye mbugal leen? Bu ngeen dee sant Yàlla te gëm ko, Yàlla di Kuy nangug cant, di Ku xam lépp nag." }
4
148
{ "fr": "Allah n´aime pas qu´on profère de mauvaises paroles sauf quand on a été injustement provoqué. Et Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Yàlla bëggul ku fésal wax ju ñaaw, ndegam nekkul ku ñu tooñ. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam lépp.(h)" }
4
149
{ "fr": "Que vous fassiez du bien, ouvertement ou en cachette, ou bien que vous pardonniez un mal... Alors Allah est Pardonneur et Omnipotent.", "wo": "Bu ngeen fésalee yiw, walla ngeen nëbb ko, walla ngeen baale lu bon [la ñu leen def]... Xamleen ne Yàlla kuy baale la, Ku am kàttan la." }
4
150
{ "fr": "Ceux qui ne croient pas en Allah et en Ses messagers, et qui veulent faire distinction entre Allah et Ses messagers et qui disent : \" Nous croyons en certains d´entre eux mais ne croyons pas en d´autres\", et qui veulent prendre un chemin intermédiaire (entre la foi et la mécréance),", "wo": "Ña weddi Yàlla ak i Yonentam, te bëgg a téqale Yàlla ak i Yonentam, te naan : “ Gëm nanu ñenn ña, weddi ñenn ña [ca Yonentam ya]” , tey jéem a am ca yoon wa nekk ca diggante weddeek ngëm," }
4
151
{ "fr": "les voilà les vrais mécréants ! Et Nous avons préparé pour les mécréants un châtiment avilissant.", "wo": "ñooña ñooy dëgg-dëggi yéefar ! Te Dananu xaaroo yéefar yi mbugal mu leen di toroxal." }
4
152
{ "fr": "Et ceux qui croient en Allah et en Ses messagers et qui ne font de différence entre ces derniers, voilà ceux à qui Il donnera leurs récompenses. Et Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Waaye ña gëm Yàlla ak i Yonentam te xàjjalewuñu kenn ci ñoom, ñooña gaay Dananu leen jox seen pey. Te Yàlla Jéggaleekoon la, Jaglewaakoon la." }
4
153
{ "fr": "Les gens du Livre te demandent de leur faire descendre du ciel un Livre. Ils ont déjà demandé à Moïse quelque chose de bien plus grave quand ils dirent : \"Fais-nous voir Allah à découvert ! \" Alors la foudre les frappa pour leur tort. Puis ils adoptèrent le Veau (comme idole) même après que les preuves leur furent venues. Nous leur pardonnâmes cela et donnâmes à Moïse une autorité déclarée.", "wo": "Ña jotoon ab Téere, ñangay laaj, bëgg nga wàcce ca ñoom ab Téere bu bawoo asamaan. Waaye ñoom sax laajoon nañu Muusaa lu gën a rëy loolu, ndax dañu ne ko : “Won nu Yàlla ñu janook Moom !” . Dënnu ga fàdd leen ngir seen bàkkaar boobu. Ba loola jàllee, ñuy jaamu yëkk wa, ginnaaw ba leen dëgg gu bir dikkalee. Nu baal leen loola, topp Nu jox Muusaa kiliftéef gu bari. " }
4
154
{ "fr": "Et pour (obtenir) leur engagement, Nous avons brandi au-dessus d´eux le Mont Tor , Nous leur avons dit : \"Entrez par la porte en vous prosternant\"; Nous leur avons dit : \"Ne transgressez pas le Sabbat\"; et Nous avons pris d´eux un engagement ferme.", "wo": "Nu yékkati doj wa ca seen kaw ngir fasanteek ñoom kóllare, ñu ne leen woon : “Dugguleen ci buntu bi ànd ak di sujjóot” ; Neeti leen : “Buleen jalgati bisub gaawu” ; Nu jàppe woon ak ñoom kóllëre gu dëgër." }
4
155
{ "fr": "(Nous les avons maudits) à cause de leur rupture de l´engagement, leur mécréance aux révélations d´Allah, leur meurtre injustifié des prophètes, et leur parole : \"Nos coeurs sont (enveloppés) et imperméables\". Et réalité, c´est Allah qui a scellé leurs coeurs à cause de leur mécréance, car ils ne croyaient que très peu .", "wo": "Ci sababu firig seen kóllare ak seen weddi kàdduy Yàlla ya, ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg, ak la ñuy wax naan: “Sunuy xel muuru na” . Li am kay moo di Yàllaa fatt seeni xol ci sababus seenug la ñu weddi, ñu néew ñoo gëm ca ña bokk ca ñoom." }
4
156
{ "fr": "Et à cause de leur mécréance et de l´énorme calomnie qu´ils prononcent contre Marie.", "wo": "Ak ca sababus la ñu weddi, te wax ci Maryaama duur [fen] wu rëy." }
4
157
{ "fr": "et à cause leur parole : \"Nous avons vraiment tué le Christ, Jésus, fils de Marie, le Messager d´Allah\"... Or, ils ne l´ont ni tué ni crucifié; mais ce n´était qu´un faux semblant ! Et ceux qui ont discuté sur son sujet sont vraiment dans l´incertitude : ils n´en ont aucune connaissance certaine, ils ne font que suivre des conjectures et ils ne l´ont certainement pas tué .", "wo": "ak ca la ñu wax ne : “Noo rey [Masiihu Iisaa] doomi Maryaama, Yonentub Yàlla ba” ... Te reyuñu ko, daajuñu ko ci ay bant ; waaye dañu leen koo nirëleel ñu cay werante ! Wóor na ne ci am lënt lañu nekk ci mbir moomu: amuñu ca benn xam-xam lu dul topp seen njort, te nag reyuñu ko de.(s)" }
4
158
{ "fr": "mais Allah l´a élevé vers Lui. Et Allah est Puissant et Sage.", "wo": "li am kay mooy Yàllaa ko yékkati jëme ko ca Moom. Te Yàllaa di Ku not lépp, di Ku xereñ." }
4
159
{ "fr": "Il n´y aura personne, parmi les gens du Livre, qui n´aura pas foi en lui avant sa mort . Et au Jour de la Résurrection, il sera témoin contre eux.", "wo": "Dana am ñenn ca ña jotu Téere, ñoo xam ne fàwwu danañu ko gëm balaa muy dee [Moom Iisaa doomu Maryaama]. Te Bis-pénc ba moom dana nekk seede ci ñoom." }
4
160
{ "fr": "C´est à cause des iniquités des Juifs que Nous leur avons rendu illicites les bonnes nourritures qui leur étaient licites, et aussi à cause de ce qu´ils obstruent le sentier d´Allah, (à eux-mêmes et) à beaucoup de monde,", "wo": "Te sababus tooñug Yahuud ya, araamaloon Nañu ca ñoom yu sell ya daganoon ca ñoom, ak la ñu daan férawle ñu bari soril leen diine," }
4
161
{ "fr": "et à cause de ce qu´ils prennent des intérêts usuraires - qui leur étaient pourtant interdits - et parce qu´ils mangent illégalement les biens des gens. A ceux d´entre eux qui sont mécréants Nous avons préparé un châtiment douloureux.", "wo": "ak lañu doon lekk ribaa - te ñu tere woon leen ko - ak di lekk alali nit ña ci neen. Nañu xam ne Nun Yàlla xaaroo Nanu yéefar ya mbugal mu metti." }
4
162
{ "fr": "Mais ceux d´entre eux qui sont enracinés dans la connaissance, ainsi que les croyants , (tous) ont foi à ce qu´on a fait descendre sur toi et à ce qu´on a fait descendre avant toi. Et quant à ceux qui accomplissent la Salat, paient la Zakat et croient en Allah et au Jour dernier, ceux-là Nous leur donnerons une énorme récompense.", "wo": "Waaye ñay woroomi xam-xam yu xóot ca ñoom ak ña ca gëm, gëm nañu la ñu wàcce ci yaw [Muhammad] ak la ñu wàcce woon mu jiitu la. Ak ñay taxawal julli ak ñay génne asaka, ak ña gëm Yàlla ak Bis- pénc ba, ñooñee, Dananu leen jox pey gu rëy." }
4
163
{ "fr": "Nous t´avons fait une révélation comme Nous fîmes à Noé et aux prophètes après lui. Et Nous avons fait révélation à Abraham, à Ismaël, à Isaac, à Jacob, aux Tribus, à Jésus, à Job, à Jonas, à Aaron et à Salomon, et Nous avons donné le Zabour à David.", "wo": "Sol Nanu [Nun Yàlla] leerug Yonent ci yaw [Muhammad] ni Nu ko sole woon ca [Nooh] ak Yonent ya toppoon ca moom. Sol Nanu ko Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba, ak sët ya ak Iisaa, ak Ayuuba, ak Yuunusa, ak Haaruun, ak Suleymaan, te jox Nanu Daawuda ab Téere bu tudd [Zabuur]. " }
4
164
{ "fr": "Et il y a des messagers dont Nous t´avons raconté l´histoire précédemment, et des messagers dont Nous ne t´avons point raconté l´histoire - et Allah a parlé à Moïse de vive voix -", "wo": "Ak Yonent yoo xam ne nettali woon Nanu leen seeni mbir lu jiitu, ak ñeneen ñu Nu la nettaliwul [seeni mbir] - Te Yàlla wax na ak Muusaa waxante tigi -" }
4
165
{ "fr": "en tant que messagers, annonciateurs et avertisseurs, afin qu´après la venue des messagers il n´y eût pour les gens point d´argument devant Allah. Allah est Puissant et Sage.", "wo": "ñu di ay Yonent yuy bégle ak xuppe ngir nit ñi bañ a am lay wu mën a yey Yàlla, ginnaaw ba leen Yonent ya xamalee dëgg. Yàlla ku am kàttan la, di Ku tedd." }
4
166
{ "fr": "Mais Allah témoigne de ce qu´Il a fait descendre vers toi, Il l´a fait descendre en toute connaissance. Et les Anges en témoignent. Et Allah suffit comme témoin.", "wo": "Waaye Yàlla seede na la Mu wàcce ci Yaw, te ci xam-xam la ko wékk. Te Malaaka ya it seede nañu. Te Yàlla doy na, mat sëkk seede.(r)" }
4
167
{ "fr": "Ceux qui ne croient pas et qui obstruent le sentier d´Allah, s´égarent certes loin dans l´égarement.", "wo": "Ña weddi tey féew nit ñi yoonu Yàlla, réer nañu réer gu sori." }
4
168
{ "fr": "Ceux qui ne croient pas et qui pratiquent l´injustice, Allah n´est nullement disposé à leur pardonner, ni à les guider dans un chemin", "wo": "Ña weddi te tooñ, Yàlla duleen baal, duleen gindi, teg leen ci yoon wu jub wa" }
4
169
{ "fr": "(autre) que le chemin de l´Enfer où ils demeureront éternellement. Et cela est facile à Allah.", "wo": "lu dul xanaa ca yoonu Safara, te dañu fay béel ba fàwwu. Loola di lu yombu Yàlla." }
4
170
{ "fr": "ô gens ! Le Messager vous a apporté la vérité de la part de votre Seigneur. Ayez la foi, donc, cela vous sera meilleur. Et si vous ne croyez pas (qu´importe ! ), c´est à Allah qu´appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Éy yéen nit ñi ! Yonent bi indil na leen dëgg te bawoo fa seen Boroom. Kon gëmleen, [su ngeen ko defee], moo gën ci yéen de. Bu ngeen weddee nag, xamleen ne Moo moom la ca asamaan ya ak suuf si. Te Yàlla di Ku xam, di Ku xereñ." }
4
171
{ "fr": "ô gens du Livre (Chrétiens), n´exagérez pas dans votre religion, et ne dites d´Allah que la vérité. Le Messie Jésus, fils de Marie, n´est qu´un Messager d´Allah, Sa parole qu´Il envoya à Marie, et un souffle (de vie) venant de Lui. Croyez donc en Allah et en Ses messagers. Et ne dites pas \"Trois\". Cessez ! Ce sera meilleur pour vous. Allah n´est qu´un Dieu unique. Il est trop glorieux pour avoir un enfant. C´est à Lui qu´appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre et Allah suffit comme protecteur .", "wo": "Éy yéen ñoñ-téere, buleen jéggi dayo ci seen diine, te buleen wax ci Yàlla lu dul lu nekk dëgg. Ku Nu barkeel ka di Iisaa, doomi Maryaama, doonul lu dul Yonentub Yàlla, di kàddoom ga Mu sànni ca Maryaama, di ruu gu tukkee ci Moom. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam. Te buleen di wax nit [Yàlla]. Bàyyileen wax jooju ! Moo gën ci yéen. Yàlla Moom kenn rekk la. Sellam gi jombaate naak Muy am doom. Moom mooy boroom li nekk ci asamaan yeek suuf si, te Yàlla doy na sëkk wéeruwaay." }
4
172
{ "fr": "Jamais le Messie ne trouve indigne d´être un serviteur d´Allah, ni les Anges rapprochés [de Lui]. Et ceux qui trouvent indigne de L´adorer et s´enflent d´orgueil... Il les rassemblera tous vers Lui.", "wo": "Ku ñu barkeel ka [Iisaa], du jomlu te du jombulu ci nekk jaamab Yàlla, Malaaka ya gën a jegeñ [seen Boroom], ñoom it duñu ko jomlu ci jombu koo jaamu. Képp ku jomlu ci jomb koo jaamu ... [Na xam ne] Yàlla Dana leen fang [gur-gur jiital] ñoom ñépp jëme leen ca Moom." }
4
173
{ "fr": "Quant à ceux qui ont cru et fait de bonnes oeuvres, Il leur accordera leurs pleines récompenses et y ajoutera le surcroît de Sa grâce. Et quant à ceux qui ont eu la morgue et se sont enflés d´orgueil, Il les châtiera d´un châtiment douloureux. Et ils ne trouveront, pour eux, en dehors d´Allah, ni allié ni secoureur,", "wo": "Ñi gëm nag tey jëf ay yiw, Yàlla Dana leen jox seen pey ba yokkal leen ca ngënéelam. Waaye ña jomlu tey rëy-rëylu, Dananu leen teg mbugal mu metti. Te duñu gis [am] keneen ku dul Yàlla ku leen di mën a yiir walla dimbali,(s)" }
4
174
{ "fr": "ô gens ! Certes une preuve évidente vous est venue de la part de votre Seigneur. Et Nous avons fait descendre vers vous une lumière éclatante .", "wo": "Éy yéen nit ñi ! Aw lay dikkal na leen wu tukkee ca seen Boroom. Te wàcce Nanu ci yéen leer gu ni nàññ. " }
4
175
{ "fr": "Alors ceux qui croient en Allah et qui s´attachent à Lui, Il les fera entrer dans une miséricorde venue de Lui, et dans une grâce aussi. Et Il les guidera vers Lui dans un chemin droit.", "wo": "Ña gëm Yàlla te jafandu ci Moom, Dana leen dugal ci yërmaandeem ak ci ngëneel, ci gindi leen, jubale leen ca boppam, teg leen ca yoon wa jub xocc." }
4
176
{ "fr": "Ils te demandent ce qui a été décrété. Dis : \"Au sujet du défunt qui n´a pas de père ni de mère ni d´enfant, Allah vous donne Son décret : si quelqu´un meurt sans enfant, mais a une sœur, à celle-ci revient la moitié de ce qu´il laisse. Et lui, il héritera d´elle en totalité si elle n´a pas d´enfant. Mais s´il a deux sœurs (ou plus), à elles alors les deux tiers de ce qu´il laisse; et s´il a des frères et des sœurs, à un frère alors revient une portion égale à celle de deux sœurs. Allah vous donne des explications pour que vous ne vous égariez pas. Et Allah est Omniscient .", "wo": "Danañu sàkku ci yaw ubbee [ci mbirum ndono]. Neel : “Yàllaa ngi leen di ubbee ci càppaacoli : bu nit faatoo di ku góor gu amul doom, te am na jigéen [bu mu bokkal ndey ak baay walla baay], moo moom génn-wàllu la mu bàyyi [ci alal]. Bu fekkee ne jigéen a bàyyi, dee te amul doom, [moom càmmiñ ja] day donn alal ja jépp. Bu fekkee ne ñaari jigéen lañu, dañuy donn ñaari ñeenteeli alal ja mu bàyyi ginnaaw ; bu ñu dee ñu góor ak ñu jigéen, na ku góor am cëru ñaari jigéen. Yàlla dafa leen di leeralal ngir bañ ngeen réer. Yàlla xam na lu ne. " }
5
1
{ "fr": "ô les croyants ! Remplissez fidèlement vos engagements. Vous est permise la bête du cheptel, sauf ce qui sera énoncé [comme étant interdit]. Ne vous permettez point la chasse alors que vous êtes en état d´ihram . Allah en vérité, décide ce qu´Il veut.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Nangeen matal pas-pasi kóllare ya. Dagan na ci yéen [yàpp] juri kër yi, ginnaaw ya ñu leen limal. Daganul it ya ñu rey te fekk ngeen armal ba noppi. Yàlla lu ko neex lay def." }
5
2
{ "fr": "ô les croyants ! Ne profanez ni les rites du pèlerinage (dans les endroits sacrés) d´Allah, ni le mois sacré, ni les animaux de sacrifice, ni les guirlandes, ni ceux qui se dirigent vers la maison sacrée cherchant de leur Seigneur grâce et agrément. Une fois désacralisés, vous êtes libres de chasser. Et ne laissez pas la haine pour un peuple qui vous a obstrué la route vers la Mosquée sacrée vous inciter à transgresser. Entraidez-vous dans l´accomplissement des bonnes oeuvres et de la piété et ne vous entraidez pas dans le péché et la transgression. Et craignez Allah, car Allah est, certes, dur en punition !", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen ñàkk a wormaal màndargay diiney Yàlla, ak weer wa ñu wormaal, ak mala ya nekk ay yool, ak mala ya ñu ràngal, ak ñay aj ca néeg bu ñu wormaal ba ngir sàkku ngëneel ci seen Boroom ak ngërëmam. Bu ngeen yéwwikoo, mën ngeen a rëbb. Te mbañeeli nit ña leen tere woon jëm ca jàkka jañu wormaal, bumu tax ngeen di jéggi dayo. Nangeen di dimbalante ci ag mbaax ak ragal Yàlla te buleen dimbalante jëm ci bàkkaar ak noonoo. Te nangeen ragal Yàlla, Yàlla dey Ku tar mbugal la !" }
5
3
{ "fr": "Vous sont interdits la bête trouvée morte, le sang, la chair de porc, ce sur quoi on a invoqué un autre nom que celui d´Allah, la bête étouffée, la bête assommée ou morte d´une chute ou morte d´un coup de corne, et celle qu´une bête féroce a dévorée - sauf celle que vous égorgez avant qu´elle ne soit morte -. (Vous sont interdits aussi la bête) qu´on a immolée sur les pierres dressées, ainsi que de procéder au partage par tirage au sort au moyen de flèches. Car cela est perversité. Aujourd´hui, les mécréants désespèrent (de vous détourner) de votre religion : ne les craignez donc pas et craignez-Moi. Aujourd´hui, J´ai parachevé pour vous votre religion, et accompli sur vous Mon bienfait. Et J´agrée l´Islam comme religion pour vous. Si quelqu´un est contraint par la faim, sans inclination vers le péché... alors, Allah est Pardonneur et Miséricordieux .", "wo": "Araam na ci yéen mala yu médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak la ñu rey tudd ca ku dul Yàlla, ak mala mu wékku, ak bu ñu dóor ba mu dee, ak bu mbartal daanu, ak bu ñu jam béjjan, ak bu rabu àll am lu mu ca lekk - lu dul la ngeen reendi -. (Terees na it) bu ñu reendi ci ay xërëm, ngeen di séddalee ci wantaleb gisaane . Lu génn diine la. Tey jii, ña weddi naagu nañu ci seen diine : buleen leen ragal, ragal-leen Ma. Bis-pénc niki tey, matalal Naa leen seen diine, te xëpp naa leen Samay xéewal. Gërëm naa ci yéen Lislaam mu di seen diine. Koo xam ne dafa loru ci jamonoy xiif [ba lekk lu Ma araamal], te du dafa sóobu ci bàkkaar... na xam ne, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.(n)" }
5
4
{ "fr": "Ils t´interrogent sur ce qui leur permis. Dis : \"Vous sont permises les bonnes nourritures, ainsi que ce que capturent les carnassiers que vous avez dressés, en leur apprenant ce qu´Allah vous a appris. Mangez donc de ce qu´elles capturent pour vous et prononcez dessus le nom d´Allah. Et craignez Allah. Car Allah est, certes, prompt dans les comptes.", "wo": "Ñanga lay laaj lan moo dagan ci ñoom. Neel : “Yu sell ya ñoo dagan ci yéen, ak la leen seen rëbbukaay yi ngeen yore indil, yu deme ni xaj, na leen ko Yàlla jàngale. Mën ngeen a lekk ca la ñu leen jàppale te nangeen ca tudd turu Yàlla. Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla Ku gaaw la ci natt jëf yi." }
5
5
{ "fr": "Vous sont permises, aujourd´hui, les bonnes nourritures. Vous est permise la nourriture des gens du Livre, et votre propre nourriture leur est permise. (Vous sont permises) les femmes vertueuses d´entre les croyantes, et les femmes vertueuses d´entre les gens qui ont reçu le Livre avant vous, si vous leur donnez leur mahr, avec contrat de mariage, non en débauchés ni en preneurs d´amantes. Et quiconque abjure la foi, alors vaine devient son action, et il sera dans l´au-delà, du nombre des perdants .\r\n5|6|ô les croyants ! Lorsque vous vous levez pour la Salat, lavez vos visages et vos mains jusqu´aux coudes; passez les mains mouillées sur vos têtes; et lavez-vous les pieds jusqu´aux chevilles. Et si vous êtes pollués junub\" , alors purifiez-vous (par un bain); mais si vous êtes malades, ou en voyage, ou si l´un de vous revient du lieu ou´ il a fait ses besoins ou si vous avez touché aux femmes et que vous ne trouviez pas d´eau, alors recourez à la terre pure , passez-en sur vos visages et vos mains. Allah ne veut pas vous imposer quelque gêne, mais Il veut vous purifier et parfaire sur vous Son bienfait. Peut-être serez-vous reconnaissants.", "wo": "“Bis niki tey, dagan na ci yéen [ñam] yu sell ya. Àtteb ñamu ña jotoon Téere dagan na leen, te seeni ñam yéen, dagan ca ñoom. Te it gor ñu jigéen ña yéwén ci jullit ñi, ak jigéen ña di ay gor, yiw ca ña leen jëkk a jot Téere [dagan na ngeen sëy ak ñoom], ginnaaw ba ngeen joxee seen can ngir sëy mu bañ di njaaloo, ngeen bañ leen a jàppe it ay coro. Képp ku weddi ngëm, ay jëfam sippiku [yàqu] na te àllaaxiraa, ca ña yàqule lay bokk." }
5
7
{ "fr": "Et rappelez-vous le bienfait d´Allah sur vous, ainsi que l´alliance qu´Il a conclue avec vous, quand vous avez dit : \"Nous avons entendu et nous avons obéi\" . Et craignez Allah. Car Allah connaît parfaitement le contenu des coeurs.", "wo": "Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek Moom ba ngeen nee : “Dégg nanu te nangu nanu” . Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla dey Ku xam li nekk ci xol yi la.(s)" }
5
8
{ "fr": "ô les croyants ! Soyez stricts (dans vos devoirs) envers Allah et (soyez) des témoins équitables. Et que la haine pour un peuple ne vous incite pas à être injuste. Pratiquez l´équité : cela est plus proche de la piété. Et craignez Allah. Car Allah est certes Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la." }
5
9
{ "fr": "Allah a promis à ceux qui croient et font de bonnes oeuvres qu´il y aura pour eux un pardon et une énorme récompense.", "wo": "Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy." }
5
10
{ "fr": "Quant à ceux qui ne croient pas et traitent de mensonge Nos preuves, ceux-là sont des gens de l´Enfer.", "wo": "Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal ay fen, ñooña ñooy waa Safara." }
5
11
{ "fr": "ô les croyants ! Rappelez-vous le bienfait d´Allah à votre égard, le jour où un groupe d´ennemis s´apprêtait à porter la main sur vous (en vue de vous attaquer) et qu´Il repoussa leur tentative. Et craignez Allah. C´est en Allah que les croyants doivent mettre leur confiance.", "wo": "Yéen ñi gëm, fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ba mu amee kurél bu nammoon a dal ci seen kaw te Ma fegal leen loxoy noon ya. Ragal- leen Yàlla. Ñi gëm nag, ci Yàlla doŋŋ lañu war a sukkandiku." }
5
12
{ "fr": "Et Allah certes prit l´engagement des enfants d´Israël. Nous nommâmes douze chefs d´entre eux. Et Allah dit : \"Je suis avec vous, pourvu que vous accomplissiez la Salat, acquittiez la Zakat, croyiez en Mes messagers, les aidiez et fassiez à Allah un bon prêt. Alors, certes, J´effacerai vos méfaits, et vous ferai entrer aux Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux. Et quiconque parmi vous, après cela, mécroît, s´égare certes du droit chemin\" !", "wo": "Yàlla fasante woon na kóllare ak waa Banii-Israayiila. Nu feeñal ci ñoom fukki kilifa ak ñaar. Yàlla ne leen : “Maak yéeen a ànd, bu ngeen di taxawal jullli [fonku ko], di génne asaka, te gëm Samay Yonent, di leen dimbali tey lebal Yàlla [ci seeni alal]. Bor bu rafet dana leen jéggal seeni bàkkaar [ñaawtéef], dugal leen Àjjana yoo xam ne ay dex ay daw ci suufam. Ku weddi ginnaaw loolu te bokk ci yéen, [na xam ne] réere na yoon wu jub wa” !" }
5
13
{ "fr": "Et puis, à cause de leur violation de l´engagement, Nous les avons maudits et endurci leurs coeurs : ils détournent les paroles de leur sens et oublient une partie de ce qui leur a été rappelé . Tu ne cesseras de découvrir leur trahison, sauf d´un petit nombre d´entre eux. Pardonne-leur donc et oublie [leurs fautes]. Car Allah aime, certes, les bienfaisants.", "wo": "Ci sababus firi ga ñu firi kóllare ga, la Nu leen rëbbe [Nun Yàlla], def seeni xol wow koŋŋ : dañuy toxal baat [maanaa ya] jële ko fa mu tëddoon, boole ca fàtte as lëf ca la Nu leen waare woon. Te foo toll di gis ci ñoom ay wor, lu dul ci lu néew ca ñoom. Nanga leen jéggal te jéllale. Yàlla safoo na ñay rafetal.(r)" }
5
14
{ "fr": "Et de ceux qui disent : \"Nous sommes chrétiens\", Nous avons pris leur engagement. Mais ils ont oublié une partie de ce qui leur a été rappelé. Nous avons donc suscité entre eux l´inimitié et la haine jusqu´au Jour de la Résurrection. Et Allah les informera de ce qu´ils faisaient .", "wo": "Ña def seen bopp ay [nasraan] it, fasante woon Nanu kóllare ak ñoom. Ñoom fàtte nañu as lëf ca la Nu leen waare woon, tax ñu tàbbaal seen diggante noonoo ak mbañeel guy wéy ba Bis-pénc ba. Yàlla dana leen xala xabaar la ñu daan def." }
5
15
{ "fr": "ô gens du Livre ! Notre Messager (Muhammad) vous est certes venu, vous exposant beaucoup de ce que vous cachiez du Livre, et passant sur bien d´autres choses ! Une lumière et un Livre explicite vous sont certes venus d´Allah !", "wo": "Éy yéen ñon-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen, leeral na leen lu bari ci la ngeen nëbboon ca Téere ba, te muy jéllale itam lu bari ! Téere bu jóge ca Yàlla dikkal na leen, di leer guy leeral !" }
5
16
{ "fr": "Par ceci (le Coran), Allah guide aux chemins du salut ceux qui cherchent Son agrément. Et Il les fait sortir des ténèbres à la lumière par Sa grâce. Et Il les guide vers un chemin droit.", "wo": "Yàlla dana ca gindi képp ku topp ndigalam, muy yoonu jàmm. Te Dana leen génne cig lëndëm, tàbbal leen cig leer bu Ko soobee. Te teg leen ci yoon wu jub xocc wa." }
5
17
{ "fr": "Certes sont mécréants ceux qui disent : \"Allah, c´est le Messie, fils de Marie ! \" - Dis : \"Qui donc détient quelque chose d´Allah (pour L´empêcher), s´Il voulait faire périr le Messie, fils de Marie, ainsi que sa mère et tous ceux qui sont sur la terre ? ... A Allah seul appartient la royauté des cieux et de la terre et de ce qui se trouve entre les deux\". Il crée ce qu´Il veut. Et Allah est Omnipotent.", "wo": "Ña wax ne : “Ka ñu barkeel, doomi Maryaama [Iisaa], mooy Yàlla !” , weddi nañu Yàlla - Neel : “ Ana kan moo mënal Yàlla dara, su bëggoon a rey ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, ak yaayam, ak ñi nekk ci kaw suuf si ñépp [Am na sañ-sañu def ko] ?... Te Yàllaay Boroom asamaan yeek suuf si ak li ci seen diggante” . Moom Yàlla mooy sàkk [sos] li ko soob. Yàlla am na kàttan ci def lu ne." }
5
18
{ "fr": "Les Juifs et les Chrétiens ont dit : \"Nous sommes les fils d´Allah et Ses préférés.\" Dis : \"Pourquoi donc vous châtie-t-Il pour vos péchés ? \" En fait, vous êtes des êtres humains d´entre ceux qu´Il a créés. Il pardonne à qui Il veut et Il châtie qui Il veut. Et à Allah seul appartient la royauté des cieux et de la terre et de ce qui se trouve entre les deux. Et c´est vers Lui que sera la destination finale.", "wo": "Yahuud yeek Nasraan yi wax nañu ne : “Nun nooy doomi Yàlla te di ay soppam.” Neel : “Lu tax mu mbugal leen ci sababus seeni bàkkaar ?” Li am kay mooy, yéen, ay nit ngeen ñu bokk ca ña Mu bind. Dana baal ku Ko soob, Dana mbugal it ku Ko soob. Te Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si ak lu nekk ci seen diggante. Te ca Moom la lépp di dellu." }
5
19
{ "fr": "ô gens du Livre ! Notre Messager (Muhammad) est venu pour vous éclairer après une interruption des messagers afin que vous ne disiez pas : \"Il ne nous est venu ni annonciateur ni avertisseur\". Voilà, certes, que vous est venu un annonciateur et un avertisseur. Et Allah est Omnipotent.", "wo": "Éy yéen ñoñ-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen leeralal leen ginnaaw diir ba dox digganteem ak ka mujj a feeñ ngir ngeen bañ a taafentaloo ne : “Kenn kuy waare walla kuy xamle dikkul fi nun” . Am na ku dikkoon fi yéen kay di xamle ak a waare. Te Yàlla am na kàttan ci def lu Ko soob." }
5
20
{ "fr": "(Souvenez-vous) lorsque Moïse dit à son peuple : \"ô, mon peuple ! Rappelez-vous le bienfait d´Allah sur vous, lorsqu´Il a désigné parmi vous des prophètes. Et Il a fait de vous des rois. Et Il vous a donné ce qu´Il n´avait donné à nul autre aux mondes.", "wo": "(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam, ne leen : “Yéen samaw nit ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi Mu defoon ci yéen, ba Mu defee ci yéen ay Yonent. Def leen ngeen di ay buur. Mu mayoon leen lu mu musul may kenn ci àddina bi.(s)" }
5
21
{ "fr": "ô mon peuple ! Entrez dans la terre sainte qu´Allah vous prescrite. Et ne revenez point sur vos pas [en refusant de combattre] car vous retourneriez perdants.", "wo": "Yéen samaw nit ! Dugguleen ci suuf su sell si leen Yàlla sédde. Te buleen walbatiku dellu ginnaaw, kon ngeen yàqule. " }
5
22
{ "fr": "Ils dirent : \"ô Moïse, il y a là un peuple de géants. Jamais nous n´y entrerons jusqu´à ce qu´ils en sortent. S´ils en sortent, alors nous y entrerons\".", "wo": "Ñu ne ko : «Yaw Muusaa, [xamal ne] suuf soosu ñu bari doolee fa nekk. Te nun dunu ca mën a dugg mukk li feek génnuñu. Bu ñu génnee nag ñu door a dugg” ." }
5
23
{ "fr": "Deux hommes d´entre ceux qui craignaient Allah et qui étaient comblés par Lui de bienfaits dirent : \"Entrez chez eux par la porte; puis quand vous y serez entrés, vous serez sans doute les dominants. Et c´est en Allah qu´il faut avoir confiance, si vous êtes croyants\".", "wo": "Ñaari nit, ca ña ragal Yàlla, wax ne Yàlla teral na leen : “Dugguleen ca ñoom, nu jaare ci buntu bi ; bu ngeen jàllee, yéen ay not. Te ci Yàlla doŋŋ ngeen war a sukkandiku ndegam ñu gëm ngeen” .(h)" }
5
24
{ "fr": "Ils dirent : \"Moïse ! Nous n´y entrerons jamais, aussi longtemps qu´ils y seront. Va donc, toi et ton Seigneur, et combattez tous deux. Nous restons là où nous sommes\".", "wo": "Ñu ne : “Yaw Muusaa ! [xamal ne] nun, dunu fa dugg mukk li feek ña nga nekk foofa. Dem fa, yaak sa Boroom, ngeen xeex yéen foofa. Nun fii la nuy toog” ." }
5
25
{ "fr": "Il dit : \"Seigneur ! Je n´ai de pouvoir, vraiment, que sur moi-même et sur mon frère : sépare-nous donc de ce peuple pervers\".", "wo": "Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul man ak sama mbokk [Haaruuna : àtteel sunu diggante ak ñiy sàqi ndigal” ." }
5
26
{ "fr": "Il (Allah) dit : \"Eh bien, ce pays leur sera interdit pendant quarante ans, durant lesquels ils erreront sur la terre. Ne te tourmente donc pas pour ce peuple pervers\".", "wo": "[Boroom bi tontu] ne: “Suuf soosu araam na leen ñeent-fukki at yoo xam ne danañu gëlëm di wëndéelu ci àll bi. Bul jàq ci mbiru ñiy sàqi ndigal” ." }
5
27
{ "fr": "Et raconte-leur en toute vérité l´histoire des deux fils d´Adam. Les deux offrirent des sacrifices; celui de l´un fut accepté et celui de l´autre ne le fut pas. Celui-ci dit : \"Je te tuerai sûrement\". \"Allah n´accepte, dit l´autre, que de la part des pieux\".", "wo": "Nettalileen, ci lu dëggu, xibaari ñaari doomi Aadama ya. Ba ñu sàkkoo yool bu ñu jaamoo Yàlla ; te Yàlla nangul kenn ca ñoom ñaar, bañ a nangul ka ca des. Ka ñu nangulul wax ne : “Danaa la rey” . Ka ñu nangul ne ko : “Na la wóor yaw it ne, Yàlla ña ko ragal lay nangu seeni jëf” ." }
5
28
{ "fr": "Si tu étends vers moi ta main pour me tuer, moi, je n´étendrai pas vers toi ma main pour te tuer : car je crains Allah, le Seigneur de l´Univers.", "wo": "Te boo tàllalee sa loxo di ma rey man dey duma jëme sama loxo ci yaw waxantumalaak di la jéem a rey : ndax man Yàlla Miy Boroom mbindeef yi laa ragal." }
5
29
{ "fr": "Je veux que tu partes avec le péché de m´avoir tué et avec ton propre péché : alors tu seras du nombre des gens du Feu. Telle est la récompense des injustes.", "wo": "Te sax li ma namm moo di nga yenu sama bàkkaar boole kook sa bos : bu ko defee nga bokk ca waa Safara. Te loolu mooy peyug tooñkat ya." }
5
30
{ "fr": "Son âme l´incita à tuer son frère. Il le tua donc et devint ainsi du nombre des perdants.", "wo": "[Ka ñu nangulul], bakkanam daldi koy xiir ci rey mbokkam. Mu daldi far bokk ca way- yàqule ña." }
5
31
{ "fr": "Puis Allah envoya un corbeau qui se mit à gratter la terre pour lui montrer comment ensevelir le cadavre de son frère. Il dit : \"Malheur à moi ! Suis-je incapable d´être, comme ce corbeau, à même d´ensevelir le cadavre de mon frère ? \" Il devint alors du nombre de ceux que ronge le remords.", "wo": "Yàlla daldi yebal baaxoñ buy gas suuf si ngir mu won ko naka lay suturaale néewub mbokkam moomu. [Ba mu gisee baaxoñ ba], mu daldi ne : “Ngalla man ! Ndax damaa yées baaxoñ bii ba mënumaa suturaal néewub sama mbokk mi ?” . Daldi koy rëccu lool." }
5
32
{ "fr": "C´est pourquoi Nous avons prescrit pour les Enfants d´Israël que quiconque tuerait une personne non coupable d´un meurtre ou d´une corruption sur la terre, c´est comme s´il avait tué tous les hommes. Et quiconque lui fait don de la vie, c´est comme s´il faisait don de la vie à tous les hommes. En effet Nos messagers sont venus à eux avec les preuves. Et puis voilà, qu´en dépit de cela, beaucoup d´entre eux se mettent à commettre des excès sur la terre .", "wo": "Ngir loolu, bokkal Nanu ca waa Banii-Israayiila, ne képp ku reyati nit koo xam ne reyul kenn, te deful njaaxum ci kaw suuf si, mel na ni rey na nit ñépp. Ku xettali nit, musal ko ci dee, mel na ni ku musal nit ñépp ci dee. Sunuy Yonent dikkal na leen ànd ak lay yu leer nàññ. Ginnaaw loolu, lu bari ci ñoom nekk ay yàqkat ci suuf si [àddina bi]. " }
5
33
{ "fr": "La récompense de ceux qui font la guerre contre Allah et Son messager, et qui s´efforcent de semer la corruption sur la terre, c´est qu´ils soient tués, ou crucifiés, ou que soient coupées leur main et leur jambe opposées, ou qu´ils soient expulsés du pays. Ce sera pour eux l´ignominie ici-bas; et dans l´au-delà, il y aura pour eux un énorme châtiment,", "wo": "Peyug ñay jéem a xeex Yàlla ak Yonentam , tey dox di yàq ci suuf si, [seen àtte] nekkul lu dul ñu rey leen, mbaa ñu daaj leen ci ay bant, mbaa ñu dagg seeni yoxo ak seeni tànk cig jàllawle, mbaa ñu génn leen réew ma. Ñu simboo gàcce ci àddina ; te mbugal mu rëy dana leen dal ca àllaaxira," }
5
34
{ "fr": "excepté ceux qui se sont repentis avant de tomber en votre pouvoir : sachez qu´alors, Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "ba mu des ñanga xam ne tuub nañu lu jiitu ngeen not leen : nangeen xam xéll ne Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
5
35
{ "fr": "ô les croyants ! Craignez Allah, cherchez le moyen de vous rapprocher de Lui et luttez pour Sa cause. Peut-être serez-vous de ceux qui réussissent !", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla, sàkkuleen lu leen di jigeeñal Yàlla te nangeen sonn ci liggéeyal Yàlla. Ndax Yàlla ngeen texe !(s)" }
5
36
{ "fr": "Si les mécréants possédaient tout ce qui est sur la terre et autant encore, pour se racheter du châtiment du Jour de la Résurrection, on ne l´accepterait pas d´eux. Et pour eux il y aura un châtiment douloureux.", "wo": "Ña nga xam ne weddi nañu, bu ñu amoon àddina ak li ci biiram lépp ba dolli ca li na toll, bëgg koo joxe ngir jotoo ko ca mbugalum Bis- pénc ba, kenn duleen ko nangul. Te nag mbugal mu metteey dal ci seen kaw." }