sourate
float64 1
114
⌀ | verset
float64 1
286
⌀ | translation
dict |
---|---|---|
75 | 31 | {
"fr": "Mais il n´a ni cru, ni fait la Salat;",
"wo": "Gëmul woon, te it daawuloon julli;"
} |
75 | 32 | {
"fr": "par contre, il a démenti et tourné le dos,",
"wo": "waaye, moom sax dafa weddi woon dumóoyu,"
} |
75 | 33 | {
"fr": "puis il s´en est allé vers sa famille, marchant avec orgueil.",
"wo": "daldi dem nag ca aw nitam, di xoggaliku."
} |
75 | 34 | {
"fr": "Malheur à toi, malheur ! ",
"wo": "“Yaayoo nga toskare, yaayoo nga toskare!”"
} |
75 | 35 | {
"fr": "Et encore malheur à toi, malheur !",
"wo": "Te it yaayoo nga toskare, yayoo nga ko !"
} |
75 | 36 | {
"fr": "L´homme pense-t-il qu´on le laissera sans obligation à observer ? ",
"wo": "Moo ndax nit dafa foog ne dañu koy bàyyi rekk noonu muy nguyaay?"
} |
75 | 37 | {
"fr": "N´était-il pas une goutte de sperme éjaculé ?",
"wo": "Moo ndax dafa doonul woon tóqug maniyu guy sottiku ?"
} |
75 | 38 | {
"fr": "Et ensuite une adhérence Puis [Allah] l´a créée et formée harmonieusement;",
"wo": "Mu mujj di aw lumbu Ma bind ko mu ne càndaŋ yemoo;"
} |
75 | 39 | {
"fr": "puis en a fait alors les deux éléments de couple : le mâle et la femelle ?",
"wo": "ma def ci ñaari toolént ya : góor ak jigéen ?"
} |
75 | 40 | {
"fr": "Celui-là (Allah) n´est-Il pas capable de faire revivre les morts ? ",
"wo": "Moo ndax kooku munula dekkilaat ku dee ? "
} |
76 | 1 | {
"fr": "S´est-il écoulé pour l´homme un laps de temps durant lequel il n´était même pas une chose mentionnable ?",
"wo": "Mo ndax nit dafa amul woon ab diir ci jamono bu kenn daawu ko limaale ?(s)"
} |
76 | 2 | {
"fr": "En effet, Nous avons créé l´homme d´une goutte de sperme mélangé [aux composantes diverses] pour le mettre à l´épreuve. [C´est pourquoi] Nous l´avons fait entendant et voyant.",
"wo": "Nun noo binde nit ci maniyu mu jaxasoo. Di ko nattu def ko muy dégg di gis."
} |
76 | 3 | {
"fr": "Nous l´avons guidé dans le chemin, - qu´il soit reconnaissant ou ingrat -",
"wo": "Gindi nanu ko ci aw yoon , - amaana muy déloo njukkël di sant walla mu goreedi -"
} |
76 | 4 | {
"fr": "Nous avons préparé pour les infidèles des chaînes, des carcans et une fournaise ardente.",
"wo": "Waajalal nanu yéefar ya ay càllala, ak i jéng ak safara wuy bérëx."
} |
76 | 5 | {
"fr": "Les vertueux boiront d´une coupe dont le mélange sera de camphre,",
"wo": "Ñu baax ña danañuy naane ci kaas yu ñu jaxasee kaafar,"
} |
76 | 6 | {
"fr": "d´une source de laquelle boiront les serviteurs d´Allah et ils la feront jaillir en abondance. .",
"wo": "Batab ndox boo xam ne. Jaami Yàlla yaa cay naan, ñu di ko bëtte fa mu leen soob."
} |
76 | 7 | {
"fr": "Ils accomplissent leurs voeux et ils redoutent un jour dont le mal s´étendra partout.",
"wo": "Dañuy mottali seeni nisër tey ragal bis bu ayam wa tiis na ."
} |
76 | 8 | {
"fr": "et offrent la nourriture, malgré son amour , au pauvre, à l´orphelin et au prisonnier,",
"wo": "te lañuy bëgg ñam lépp, terewul ñu di ko leel, miskiin, yaak jirim yaak ña ñu tëj kaso,"
} |
76 | 9 | {
"fr": "(disant) : \"C´est pour le visage d´Allah que nous vous nourrissons : nous ne voulons de vous ni récompense ni gratitude.",
"wo": "(te naan leen) : “noo ngi leen koy leele de : waaye bëggu nu ci ak pey walla gëram ngir Yàlla rekk tax."
} |
76 | 10 | {
"fr": "Nous redoutons, de notre Seigneur, un jour terrible et catastrophique\".",
"wo": "Danoo ragal, ci sunu Boroom, bis bu ñàng te tëradi” ."
} |
76 | 11 | {
"fr": "Allah les protégera donc du mal de ce jour-là, et leur fera rencontrer la splendeur et la joie,",
"wo": "Yàlla daldi leen fegal ayu boobale bis, dajale leen ak naataangeek mbégte,"
} |
76 | 12 | {
"fr": "et les rétribuera pour ce qu´ils auront enduré, en leur donnant le Paradis et des [vêtements] de soie,",
"wo": "mu faye leen lañu muñoon, Àjjana ak i sooy,"
} |
76 | 13 | {
"fr": "ils y seront accoudés sur des divans, n´y voyant ni soleil ni froid glacial .",
"wo": "dañuy sóonu ca lal ya, te dunu fa gis ab jant waxantumalaak ab sedd liw."
} |
76 | 14 | {
"fr": "Ses ombrages les couvriront de près, et ses fruits inclinés bien bas [à portée de leurs mains].",
"wo": "Keram ya da leen di muur, meññatam ma yóore tiim leen."
} |
76 | 15 | {
"fr": "Et l´on fera circuler parmi eux des récipients d´argent et des coupes cristallines,",
"wo": "Ñu di leen wër ak ay ndabi xaalis, ak ay koppi weer, "
} |
76 | 16 | {
"fr": "en cristal d´argent, dont le contenu a été savamment dosé.",
"wo": "ay koppi weeri xaalis, yu yem kepp."
} |
76 | 17 | {
"fr": "Et là, ils seront abreuvés d´une coupe dont le mélange sera de gingembre,",
"wo": "Ñu, di leen fa nàndale ak kaas yu ñu njare jinjeer,"
} |
76 | 18 | {
"fr": "puisé là-dedans à une source qui s´appelle Salsabil.",
"wo": "ab bëtu ndox bu tudd Salsabiil."
} |
76 | 19 | {
"fr": "Et parmi eux, circuleront des garçons éternellement jeunes. Quand tu les verras, tu les prendras pour des perles éparpillées.",
"wo": "Te ay xalee ngay wër ca ñoom sax cig ndaw. Soo leen gisee, da ngay foog ne peme ju ñu tasaare la ñu.(r)"
} |
76 | 20 | {
"fr": "Et quand tu regarderas là-bas, tu verras un délice et un vaste royaume.",
"wo": "Soo ko gisee, danga fa gIisaale xeewal ak nguur gu màgg."
} |
76 | 21 | {
"fr": "Ils porteront des vêtements verts de satin et de brocart. Et ils seront parés de bracelets d´argent. Et leur Seigneur les abreuvera d´une boisson très pure.",
"wo": "Dañuy sol mbubbi sooy yu nëtëx werta. Moom la ñuy jiital waaje ko, te dañu leen di takkal caqi xaalis. Seen Boroom di leen fa ndàndale naan gu laab."
} |
76 | 22 | {
"fr": "Cela sera pour vous une récompense, et votre effort sera reconnu.",
"wo": "Lii nag mooy seen neexal, te seen jëf it lu ñu sant la."
} |
76 | 23 | {
"fr": "En vérité c´est Nous qui avons fait descendre sur toi le Coran graduellement.",
"wo": "Nun de Noo wàcce Alxuraan ci yaw ndànk-ndànk."
} |
76 | 24 | {
"fr": "Endure donc ce que ton Seigneur a décrété, et n´obéis ni au pécheur, parmi eux, ni au grand mécréant.",
"wo": "Muñal sa dogalub Boroom, te bul topp, ci ñoom, kenn kuy def bàkkaar walla mu di yéefar."
} |
76 | 25 | {
"fr": "Et invoque le nom de ton Seigneur, matin et après-midi;",
"wo": "Te na nga tudd sa turu Boroom, subaak ngoon ;"
} |
76 | 26 | {
"fr": "et prosterne-toi devant Lui une partie de la nuit; et glorifie Le de longues [heures] pendant la nuit.",
"wo": "te guddi gi it na nga Koy sujuudal ; te di ko sàbbaal [waxtuw] guddi lu bari."
} |
76 | 27 | {
"fr": "Ces gens-là aiment [la vie] éphémère (la vie sur terre) et laissent derrière eux un jour bien lourd [le jour du Jugement].",
"wo": "Ñoom dey da ñoo bëgg Àddina tey sàggane bis bu dis ginnaawal ko."
} |
76 | 28 | {
"fr": "C´est Nous qui les avons créés et avons fortifié leur constitution. Quand Nous voulons, cependant, Nous les remplaçons [facilement] par leurs semblables.",
"wo": "Nun Noo leen bind. May leen kàttan, te Sunu sooboon, Nu wuutal fi ñeneen."
} |
76 | 29 | {
"fr": "Ceci est un rappel. Que celui qui veut prenne donc le chemin vers son Seigneur !",
"wo": "Lii dey ag fàttali la. Képp ku mu soob man ngaa sóobu yoon jëm ca sa Boroom !"
} |
76 | 30 | {
"fr": "Cependant, vous ne saurez vouloir, à moins qu´Allah veuille. Et Allah est Omniscient et Sage.",
"wo": "Manu leen a sottal dara, te du dafa soob Yàlla. Moom ku Xam la ku Xereñ la."
} |
76 | 31 | {
"fr": "Il fait entrer qui Il veut dans Sa miséricorde. Et quant aux injustes, Il leur a préparé un châtiment douloureux.",
"wo": "Mooy tàbbal ku ko soob ci yërmëndéem. Te tooñkat yi, Waajalna leen mbugël mu mitti. "
} |
77 | 1 | {
"fr": "Par ceux qu´on envoie en rafales .",
"wo": "Maa ngi giñ ci ngelaw ya ñu yabal muy jaayu."
} |
77 | 2 | {
"fr": "et qui soufflent en tempête !",
"wo": "Ak yiy ràddi càllmeer!"
} |
77 | 3 | {
"fr": "Et qui dispersent largement [dans toutes les directions].",
"wo": "ak yiy gëwéeluy tasaare."
} |
77 | 4 | {
"fr": "Par ceux qui séparent nettement (le bien et le mal) ,",
"wo": "Ak yiy teqale dëgg ak fen (Laaya yi) ,"
} |
77 | 5 | {
"fr": "et lancent un rappel",
"wo": "di sànni fàttali"
} |
77 | 6 | {
"fr": "En guise d´excuse ou d´avertissement ! !",
"wo": "Di jélële walla muy xuppe !"
} |
77 | 7 | {
"fr": "Ce qui vous est promis est inéluctable.",
"wo": "La ñu leen di tëkóo fàwwu mu ay (xew)."
} |
77 | 8 | {
"fr": "Quand donc les étoiles seront effacées,",
"wo": "Bu ru raafee biddiw yi,"
} |
77 | 9 | {
"fr": "et que le ciel sera fendu,",
"wo": "daldi xar asamaan si,"
} |
77 | 10 | {
"fr": "et que les montagnes seront pulvérisées,",
"wo": "moñoxe tundi doj yi,"
} |
77 | 11 | {
"fr": "et que le moment (pour la réunion) des Messagers a été fixé ! ...",
"wo": "ak suñu dajalee Yonent ya !..."
} |
77 | 12 | {
"fr": "A quel jour tout cela a-t-il été renvoyé ?",
"wo": "Ana ban bis la doon xaar ?"
} |
77 | 13 | {
"fr": "Au Jour de la Décision. [le Jugement] !",
"wo": "Ca bisub àtte ba !"
} |
77 | 14 | {
"fr": "Et qui te dira ce qu´est le Jour de la Décision ?",
"wo": "Ana kan moo lay xamal luy bisub àtte ba ?"
} |
77 | 15 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 16 | {
"fr": "N´avons-Nous pas fait périr les premières [générations] ?",
"wo": "Moo ndax Nun faagaagalunu ñu jëkk ña ?(s)"
} |
77 | 17 | {
"fr": "Puis ne les avons-Nous pas fait suivre par les derniers ?",
"wo": "Toftal ca ña mujjoon ?"
} |
77 | 18 | {
"fr": "C´est ainsi que Nous agissons avec les criminels.",
"wo": "Noonu la ñuy def ak tooñkat ya."
} |
77 | 19 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 20 | {
"fr": "Ne vous avons-Nous pas créés d´une eau vile ",
"wo": "Moo ndax bindewunu leen ci ndox mu doyadi "
} |
77 | 21 | {
"fr": "que Nous avons placée dans un reposoir sûr, ,",
"wo": "Nu daldi koy saxal ci barab wu wóor,"
} |
77 | 22 | {
"fr": "pour une durée connue ?",
"wo": "ba ca ab diir bu ñu xam ?"
} |
77 | 23 | {
"fr": "Nous l´avons décrété ainsi et Nous décrétons [tout] de façon parfaite.",
"wo": "Nu daldi dogal cëy Noo mana dogal yemale."
} |
77 | 24 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 25 | {
"fr": "N´avons-Nous pas fait de la terre un endroit les contenant tous,",
"wo": "Ndax defu nu suuf si mu làmboo lépp,"
} |
77 | 26 | {
"fr": "les vivants ainsi que les morts ?",
"wo": "ñuy dund ak ñu dee ?"
} |
77 | 27 | {
"fr": "Et n´y avons-Nous pas placé fermement de hautes montagnes ? Et ne vous avons-Nous pas abreuvés d´eau douce ?",
"wo": "Te def Nanu ci ay tund doj yu kawe? Te nàndale leen ak ndox mu neex ?"
} |
77 | 28 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 29 | {
"fr": "Allez vers ce que vous traitiez alors de mensonge !",
"wo": "Fëxleen nag jëm ci li ngeen daan weddi !"
} |
77 | 30 | {
"fr": "Allez vers une ombre [fumée de l´Enfer] à trois branches;",
"wo": "Fëxleen jëm ca ker ga am ñatti tokkoor [saxaar sa] ;"
} |
77 | 31 | {
"fr": "qui n´est ni ombreuse ni capable de protéger contre la flamme;",
"wo": "Saar 77 : Ñu ñuy yabal ña 50 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi."
} |
77 | 31 | {
"fr": "qui n´est ni ombreuse ni capable de protéger contre la flamme;",
"wo": "manuta keral kenn waxatumaak di feg tàkk-tàkk ;"
} |
77 | 32 | {
"fr": "car [le feu] jette des étincelles volumineuses comme des châteaux,",
"wo": "moom dafay sànni ay ferñent yu tollu ni njéndi,"
} |
77 | 33 | {
"fr": "et qu´on prendrait pour des chameaux jaunes.",
"wo": "dañu melni ay giléem yu mboq."
} |
77 | 34 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 35 | {
"fr": "Ce sera le jour où ils ne [peuvent] pas parler,",
"wo": "Bu bis baa du ñu mana àddu wax,"
} |
77 | 36 | {
"fr": "et point ne leur sera donné permission de s´excuser.",
"wo": "kenn du leen may pose bu ñuy jéggaloo."
} |
77 | 37 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 38 | {
"fr": "C´est le Jour de la Décision [Jugement], où nous vous réunirons ainsi que les anciens.",
"wo": "Lii mooy bisub àtte ba, boole nanu leen ak ñu jëkk ña."
} |
77 | 39 | {
"fr": "Si vous disposez d´une ruse, rusez donc contre Moi.",
"wo": "Su ngeen amee ay pexe, fexel leen Ma."
} |
77 | 40 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 41 | {
"fr": "Les pieux seront parmi des ombrages et des sources.",
"wo": "Ña ragal Yàlla ñoom ña nga ca ker ya ak bëti ndox ya."
} |
77 | 42 | {
"fr": "De même que des fruits selon leurs désirs.",
"wo": "Ak ay fuytéef ya ñu bëgg."
} |
77 | 43 | {
"fr": "Mangez et buvez agréablement, pour ce que vous faisiez.",
"wo": "“Lekkleen te naan, mooy peyug la ngeen daan jëf” ."
} |
77 | 44 | {
"fr": "C´est ainsi que Nous récompensons les bienfaisants.",
"wo": "Noonu la Ñuy faye way rafetal ya."
} |
77 | 45 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 46 | {
"fr": "Mangez et jouissez un peu (ici-bas); vous êtes certes des criminels.",
"wo": "“Lekkleen te bànneexu tuuti ; yéen ay tooñkat ngeen” . "
} |
77 | 47 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 48 | {
"fr": "Et quand on leur dit : \"Inclinez-vous , ils ne s´inclinent pas.",
"wo": "Te saasu ñu leen waxee ne : “rukóoleen, duñu rukoo (duñu julli)."
} |
77 | 49 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.",
"wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi."
} |
77 | 50 | {
"fr": "Après cela, en quelle parole croiront-ils donc ?",
"wo": "Bu waxtaan wii jàllee, ana wan waxtaan lañuy gëmati ? "
} |
78 | 1 | {
"fr": "Sur quoi s´interrogent-ils mutuellement ?",
"wo": "Ana ci man mbir la ñuy laajante ?(h)"
} |
78 | 2 | {
"fr": "Sur la grande nouvelle,",
"wo": "Ci xibaar bu rëy ba,"
} |
78 | 3 | {
"fr": "à propos de laquelle ils divergent.",
"wo": "xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo."
} |
78 | 4 | {
"fr": "Eh bien non ! Ils sauront bientôt.",
"wo": "Mukk ! danañu xala xam."
} |
78 | 5 | {
"fr": "Encore une fois, non ! Ils sauront bientôt.",
"wo": "Déedéet kay ! Danañu xala xam."
} |
78 | 6 | {
"fr": "N´avons-Nous pas fait de la terre une couche ?",
"wo": "Moo ndax du Nun Noo def suuf si mu di laltaay ?"
} |
78 | 7 | {
"fr": "et (placé) les montagnes comme des piquets ?",
"wo": "ak tundi doj yi ñu di ay dott ?"
} |
78 | 8 | {
"fr": "Nous vous avons créés en couples,",
"wo": "Nu bind leen ngeen di ay tóllent,"
} |