sourate
float64 1
114
⌀ | verset
float64 1
286
⌀ | translation
dict |
---|---|---|
80 | 22 | {
"fr": "puis Il le ressuscitera quand Il voudra.",
"wo": "te saa su Ko soobee mu dekkalaat Ko."
} |
80 | 23 | {
"fr": "Eh bien non ! [L´homme] n´accomplit pas ce qu´Il lui commande.",
"wo": "Déedéet ! [Nit] moom matalul mukk la nu ko digëloon."
} |
80 | 24 | {
"fr": "Que l´homme considère donc sa nourriture :",
"wo": "Na nit di xool ci aw ñamam lekkam :"
} |
80 | 25 | {
"fr": "C´est Nous qui versons l´eau abondante,",
"wo": "Nun noo sotti ndox mu dottiku,"
} |
80 | 26 | {
"fr": "puis Nous fendons la terre par fissures",
"wo": "ba noppi Nu xar suuf mu fett"
} |
80 | 27 | {
"fr": "et y faisons pousser grains,",
"wo": "nu saxal ci ay kembu,"
} |
80 | 28 | {
"fr": "vignobles et légumes,",
"wo": "ay reseñ ak i lujum,"
} |
80 | 29 | {
"fr": "oliviers et palmiers,",
"wo": "ak i oliw ak tàndarma,"
} |
80 | 30 | {
"fr": "jardins touffus,",
"wo": "ak ay dër yu naat,"
} |
80 | 31 | {
"fr": "fruits et herbages,",
"wo": "ak i fuytéef ak i xob, ngub"
} |
80 | 32 | {
"fr": "pour votre jouissance vous et vos bestiaux.",
"wo": "mu di seen bànneex ak seenug jur."
} |
80 | 33 | {
"fr": "Puis quand viendra le Fracas,",
"wo": "Bu bis pénc ba dikkee,"
} |
80 | 34 | {
"fr": "le jour où l´homme s´enfuira de son frère,",
"wo": "bis ba nit di daw mbokkam,"
} |
80 | 35 | {
"fr": "de sa mère, de son père,",
"wo": "ak yaayam, ak baayam,"
} |
80 | 36 | {
"fr": "de sa compagne et de ses enfants,",
"wo": "ak soxnaam ak doomam,"
} |
80 | 37 | {
"fr": "car chacun d´eux, ce jour-là, aura son propre cas pour l´occuper.",
"wo": "kenn ku nekk, bu keroogee, am mbir mu ko doy sëkk."
} |
80 | 38 | {
"fr": "ce jour-là, il y aura des visages rayonnants,",
"wo": "bu keroogee, ay xarkanam yu naat,"
} |
80 | 39 | {
"fr": "riants et réjouis.",
"wo": "bég lool tey ree."
} |
80 | 40 | {
"fr": "De même qu´il y aura, ce jour-là, des visages couverts de poussière,",
"wo": "Bu keroogee, am it, ay xarkanam yu fundóoñ,"
} |
80 | 41 | {
"fr": "recouverts de ténèbres.",
"wo": "lëndëm kariis."
} |
80 | 42 | {
"fr": "Voilà les infidèles, les libertins.",
"wo": "Ñooña ñoo di yéefar ya, di kàccoor ya. "
} |
81 | 1 | {
"fr": "Quand le soleil sera obscurci,",
"wo": "Saa su ñu lëndamalee jant bi, Maa ngi giiñ(s)"
} |
81 | 2 | {
"fr": "et que les étoiles deviendront ternes,",
"wo": "ak saa su biddew yi rotee,"
} |
81 | 3 | {
"fr": "et les montagnes mises en marche,",
"wo": "ak tundi doj yi saa su ñuy randatu di dox,"
} |
81 | 4 | {
"fr": "et les chamelles à terme , négligées,",
"wo": "ak saa su nu, sàgganee geleemam ga ëmbu ba sori talatuñu ko,"
} |
81 | 5 | {
"fr": "et les bêtes farouches, rassemblées,",
"wo": "ak ndokmenta ya (rab yu aaytal ya), dajaloo ñu dekkalaat leen,"
} |
81 | 6 | {
"fr": "et les mers allumées,",
"wo": "ak saa su ñu taalee geej ya mu di safara,"
} |
81 | 7 | {
"fr": "et les âmes accouplées ",
"wo": "ak saa su ñu lëkëlee ruu ya"
} |
81 | 8 | {
"fr": "et qu´on demandera à la fillette enterrée vivante ",
"wo": "ak saa su ñu laajee doom ju jigéen ja nu soloon te fekk muy dund, ngir daw gàcce"
} |
81 | 9 | {
"fr": "pour quel péché elle a été tuée.",
"wo": "ci ban bàkkaar bu mu def moo tax ñu rey ko."
} |
81 | 10 | {
"fr": "Et quand les feuilles seront déployées ,",
"wo": "Ak saa su ñu tasaaree kayit yi ëmboon jëfi bindéef yi,"
} |
81 | 11 | {
"fr": "et le ciel écorché ",
"wo": "ak saa su nu xollee deri asamaan si"
} |
81 | 12 | {
"fr": "et la fournaise attisée,",
"wo": "ak saa su ñu taalee safaraw jahim,"
} |
81 | 13 | {
"fr": "et le Paradis rapproché,",
"wo": "ak saas u ñu jigeelee Àjjana,"
} |
81 | 14 | {
"fr": "chaque âme saura ce qu´elle a présenté.",
"wo": "bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëfoon."
} |
81 | 15 | {
"fr": "Non ! ... Je jure par les planètes qui gravitent",
"wo": "Déet !... Maa ngi giiñ ci biddiw yi fàq guddi"
} |
81 | 16 | {
"fr": "qui courent et disparaissent !",
"wo": "tey daw di suux !"
} |
81 | 17 | {
"fr": "par la nuit quand elle survient !",
"wo": "ak ci guddi gi saa suy tàmbali!"
} |
81 | 18 | {
"fr": "et par l´aube quand elle exhale son souffle !",
"wo": "ak ci suba si saa suy fenk!"
} |
81 | 19 | {
"fr": "Ceci [le Coran] est la parole d´un noble Messager ,",
"wo": "Ci ne [Alxuraan jii] waxi ab Yonent la bu tedd (Jibriil),"
} |
81 | 20 | {
"fr": "doué d´une grande force, et ayant un rang élevé auprès du Maître du Trône,",
"wo": "di boroom kàttan gu rëy, di ab xejj fa Boroom ganganaay ga Aras, "
} |
81 | 21 | {
"fr": "obéi, là-haut, et digne de confiance.",
"wo": "di ku ñuy digël, ndigëlam ca kaw, di ku ñu woolu."
} |
81 | 22 | {
"fr": "Votre compagnon (Muhammad) n´est nullement fou;",
"wo": "Te seen àndandoo ja (Muhammad) du ab dof de ;"
} |
81 | 23 | {
"fr": "il l´a effectivement vu (Gabriel), au clair horizon",
"wo": "moom gis na tigi (Jibriil), ca asamaan ya"
} |
81 | 24 | {
"fr": "et il ne garde pas avarement pour lui-même ce qui lui a été révélé.",
"wo": "te moom nayul ci li ñu ko soloo."
} |
81 | 25 | {
"fr": "Et ceci [le Coran] n´est point la parole d´un diable banni.",
"wo": "Te it [Alxuraan ji] du waxi seytaane sa ñu jam."
} |
81 | 26 | {
"fr": "Où allez-vous donc ?",
"wo": "Kon ana fu ngeen jëm ?"
} |
81 | 27 | {
"fr": "Ceci n´est qu´un rappel pour l´univers,",
"wo": "Lii du lenn lu dul luy fàttali waa àddina si yépp,"
} |
81 | 28 | {
"fr": "pour celui d´entre vous qui veut suivre le chemin droit.",
"wo": "ku mu soob ci yéen mu topp yoon wu jub xocc wa."
} |
81 | 29 | {
"fr": "Mais vous ne pouvez vouloir, que si Allah veut, [Lui], le Seigneur de l´Univers;",
"wo": "Waaye manuleena soob mukk, te du ut ne dafa soob Yàlla, Boroom àddina si yépp ; "
} |
82 | 1 | {
"fr": "Quand le ciel se rompra,",
"wo": "Saa su asamaan si dogee, Maa ngi giñ(n)"
} |
82 | 2 | {
"fr": "et que les étoiles se disperseront,",
"wo": "ak saa su biddew yi tasaaroo,"
} |
82 | 3 | {
"fr": "et que les mers confondront leurs eaux,",
"wo": "ak saa su géej yi taqaloo,"
} |
82 | 4 | {
"fr": "et que les tombeaux seront bouleversés,",
"wo": "ak saa su bàmmeel ya jaxasoo,"
} |
82 | 5 | {
"fr": "toute âme saura alors ce qu´elle a accompli et ce qu´elle a remis de faire à plus tard.",
"wo": "bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëkkoona def ak la mu mujja def."
} |
82 | 6 | {
"fr": "ô homme ! Qu´est-ce qui t´a trompé au sujet de ton Seigneur, le Noble,",
"wo": "Éy yaw nit ! Ana lan moo la fàbbi ci sa mbiru Boroom, bu Tedd bi,"
} |
82 | 7 | {
"fr": "qui t´a créé, puis modelé et constitué harmonieusement ?",
"wo": "(sa Boroom) bi la bind yemale la, jekkal la ?"
} |
82 | 8 | {
"fr": "Il t´a façonné dans la forme qu´Il a voulue.",
"wo": "Moo la defar ca na mu ko soobe."
} |
82 | 9 | {
"fr": "Non... ! [malgré tout] vous traitez la Rétribution de mensonge;",
"wo": "Déet... ! [ak lu mana xew] yéen a ngay weddi bis pénc ba ;"
} |
82 | 10 | {
"fr": "alors que veillent sur vous des gardiens ,",
"wo": "te am na ay wattukat yu nekk ci seen kaw,"
} |
82 | 11 | {
"fr": "de nobles scribes,",
"wo": "yu tedd yuy bind,"
} |
82 | 12 | {
"fr": "qui savent ce que vous faites.",
"wo": "yuy xam li ngeen di def."
} |
82 | 13 | {
"fr": "Les bons seront, certes, dans un [jardin] de délice,",
"wo": "Ñu baax ñaa ngi ca biir àjjanay xéewal,"
} |
82 | 14 | {
"fr": "et les libertins seront, certes, dans une fournaise",
"wo": "te itam kàccoor ya ñoom, ña nga ca biir safara jahiim"
} |
82 | 15 | {
"fr": "où ils brûleront, le jour de Rétribution",
"wo": "danañu ca xoyomoo, bu bis Pénc baa"
} |
82 | 16 | {
"fr": "incapables de s´en échapper.",
"wo": "te ñoom manuñu koo wuute."
} |
82 | 17 | {
"fr": "Et qui te dira ce qu´est le jour de la Rétribution ?",
"wo": "Ana lu lay xamal luy bis Pénc ?"
} |
82 | 18 | {
"fr": "Encore une fois, qui te dira ce qu´est le jour de la Rétribution ?",
"wo": "Ak lu lay xamal waay, luy bis Pénc ba ?"
} |
82 | 19 | {
"fr": "Le jour où aucune âme ne pourra rien en faveur d´une autre âme. Et ce jour-là, le commandement sera à Allah.",
"wo": "moo di bis ba benn bakkan dul manal moroomam tus. Te bu keroogee, Yàlla rekk ay joxe ndigël yi. "
} |
83 | 1 | {
"fr": "Malheur aux fraudeurs",
"wo": "Xuru safara ñeel na naxaatekat ya"
} |
83 | 2 | {
"fr": "qui, lorsqu´ils font mesurer pour eux-mêmes exigent la pleine mesure,",
"wo": "ñay natt peese di ëppal lay jëm ca ñoom,"
} |
83 | 3 | {
"fr": "et qui lorsqu´eux-mêmes mesurent ou pèsent pour les autres, [leur] causent perte.",
"wo": "te su ñuy nattal keneen, wàññi ko."
} |
83 | 4 | {
"fr": "Ceux-là ne pensent-ils pas qu´ils seront ressuscités,",
"wo": "Xanaa ñoom dañoo jàpput ne dees na leen dekkilaat (ginnaaw dee),"
} |
83 | 5 | {
"fr": "en un jour terrible,",
"wo": "ca bis bu ñàng,"
} |
83 | 6 | {
"fr": "le jour où les gens se tiendront debout devant le Seigneur de l´Univers ?",
"wo": "bis ba nit ña di taxaw ci kanam Boroom Àddina si yépp ?"
} |
83 | 7 | {
"fr": "Non... ! Mais en vérité le livre des libertins sera dans le Sijjin",
"wo": "Déet... ! Waaye téereb kàccoor yaa nga ca Sijjin de"
} |
83 | 8 | {
"fr": "et qui te dira ce qu´est le Sijjin ? -",
"wo": "ana lan moo lay xamal luy Sijjin ?"
} |
83 | 9 | {
"fr": "un livre déjà cacheté (achevé).",
"wo": "ab téere la bu ñu xas tàmpe."
} |
83 | 10 | {
"fr": "Malheur, ce jour-là, aux négateurs,",
"wo": "Bu keroogee, weddikat ya, danañu tàbbi xuru safara,"
} |
83 | 11 | {
"fr": "qui démentent le jour de la Rétribution.",
"wo": "ña daan weddi bis Pénc ba."
} |
83 | 12 | {
"fr": "Or, ne le dément que tout transgresseur, pécheur :",
"wo": "te kenn, du ko weddi ku dul ab jalgatikat, buy def bàkkaar :"
} |
83 | 13 | {
"fr": "qui, lorsque Nos versets lui sont récités, dit : \"[Ce sont] des contes d´anciens ! \"",
"wo": "su ñu jàngee ci ñoom Laaya, dañu naan : “Léebi mag ña la!”"
} |
83 | 14 | {
"fr": "Pas du tout, mais ce qu´ils ont accompli couvre leurs coeurs .",
"wo": "Lañu daan def moo muur xomaagal seen xol ya.(s)"
} |
83 | 15 | {
"fr": "Qu´ils prennent garde ! En vérité ce jour-là un voile les empêchera de voir leur Seigneur,",
"wo": "Déet ! Ñoom kay bu keroogee duñu gis seen Boroom de,"
} |
83 | 16 | {
"fr": "ensuite, ils brûleront certes, dans la Fournaise;",
"wo": "te, dees na leen lakk, Safara jahiim ;"
} |
83 | 17 | {
"fr": "on [leur] dira alors : \"Voilà ce que vous traitiez de mensonge ! \"",
"wo": "te di leen wax naan leen: “Lii ngeen daan weddi !”"
} |
83 | 18 | {
"fr": "Qu´ils prennent garde ! Le livre des bons sera dans l´Illiyoun -",
"wo": "Déetawaay ! Téereb ñu baax ñaa nga ca biir Illiyiina"
} |
83 | 19 | {
"fr": "et qui te dira ce qu´est l´Illiyoun ? -",
"wo": "Saar 83 : Naxekat ya 36 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi."
} |
83 | 19 | {
"fr": "et qui te dira ce qu´est l´Illiyoun ? -",
"wo": "ana lan moo lay xamal luy Illiyiina ?"
} |
83 | 20 | {
"fr": "un livre cacheté !",
"wo": "ab téere la bu ñu xas tàmpe ! "
} |
83 | 21 | {
"fr": "Les rapprochés (d´Allah : les Anges) en témoignent.",
"wo": "Ña jege Yàlla koy seede (Malaaka ya)."
} |
83 | 22 | {
"fr": "Les bons seront dans [un jardin] de délice,",
"wo": "Ñu baax ñaa nga ca biir xeewal,"
} |
83 | 23 | {
"fr": "sur les divans, ils regardent.",
"wo": "ña nga ne toŋŋ ca kaw toogu ya, di xool."
} |
83 | 24 | {
"fr": "Tu reconnaîtras sur leurs visages, l´éclat de la félicité.",
"wo": "Danga seere ca seen xarkanam ya, naataangey xéewël ya."
} |
83 | 25 | {
"fr": "On leur sert à boire un nectar pur, cacheté,",
"wo": "Ñu nandalu ci sàngaras àjjana suñu xàmmee,"
} |
83 | 26 | {
"fr": "laissant un arrière-goût de musc. Que ceux qui la convoitent entrent en compétition [pour l´acquérir]",
"wo": "tem-temam misk lay doon. Ñiy rawante nañu rawante [ci am ko]"
} |
83 | 27 | {
"fr": "Il est mélangé à la boisson de Tasnim ,",
"wo": "Di njarum Tasniim,"
} |
83 | 28 | {
"fr": "source dont les rapprochés boivent.",
"wo": "bëtub ndox la bu ña jegeñoo cay naan."
} |
83 | 29 | {
"fr": "Les criminels riaient de ceux qui croyaient,",
"wo": "Tooñkat ya dañu daan reetaan ña gëmoon,"
} |
83 | 30 | {
"fr": "et, passant près d´eux, ils se faisaient des oeillades,",
"wo": "saa suñu leen rombaan, di leen ñaawal,"
} |