wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Mbëtt mënula daw, mënula jaab, lu dul bar-bari
le varan de terre ne sait ni courir ni galoper, rien que se déplacer comme un varan.
bare
être abondant, nombreux, beaucoup, exister en quantité, avoir en quantité, avoir beaucoup
Nit ñu bare
beaucoup de gens.
(prov.) Bare dugub, fekke déwén a ko gën
quoi bon avoir beaucoup de mil si on ne lui survit pas.
Li gëna bare
la plupart du temps, le plus souvent.
bare-fitna
être trop zélé
baawaan
couler à flots
Ndox maa ngiy baawaan
L'eau coule à flots.
baaru
accompagner un chanteur à mi-voix
Mu ngi koy baaru
il l’accompagne en sourdine.
barkeelu
tirer profit de la grâce de qqn ou de qqch à son contact
Ma barkeelu ci kaalag sëriñ bi
que le turban du marabout m’apporte un peu de grâce.
barkeel b-
fait de bénir
Barkeel bi moo wutale ndoxu batise bi ak ndox mi ngay naan ci sa kër
C'est la bénédiction qui différencie l’eau du baptême de celle que tu bois chez toi.
barkooje
avoir la gale
Sa fas wi dafa barkooje
ton cheval a la gale.
barkooje b-
gale du cheval
Garab bii dafay wéral barkooje
ce médicament guérit la gale du cheval.
barle
avoir perdu un animal (bétail)
Dama barle
J'ai perdu une bête.
barmol b-
veau dont le cordon ombilical n’est pas encore tombé
Ab barmol laa jénd, nar koo yar
J'ai acheté un tout jeune veau dans l’intention de l’élever.
baroom b-
antilope petite, rougeâtre et sans cornes
Ab baroom la rey
il a tué une antilope.
(prov.) Baroom jur ci sa tool taxul nga yett giir
ce n’est pas parce qu’une antilope aura mis bas dans ton champ que tu vas tailler une écuelle
barsàq b-
endroit où les âmes défuntes demeurent jusqu’au jour du jugement dernier
Ñi dée, barsàq lañu nekk
les défunts sont au séjour des morts.
barxal
glisser subrepticement un objet parmi d’autres
Dafa ko doon jéema barxal ci ndabam yi
elle essayait de le glisser subrepticement dans ses ustensiles.
bas
larmoyer
Sedd bee tax sa bët yi di bas
C'est à cause du froid que tes yeux larmoient.
basaŋ g-
natte (pour s’asseoir)
Lalal basaŋ gi ca taatu garab ga
étale la natte au pied de l’arbre !
baddax
lancer un couteau pour le planter dans une cible
Dafa ko baddax paaka
il lui a lancé un couteau.
bar
être égaré
Sama fas dafa bar
mon cheval s’est égaré.
bar
unité de mesure
Bar ca bar ca; bar ca ñaar ca
une mesure (d’un produit) contre une mesure (d’un autre produit); une mesure (d’un produit) contre deux mesures (d’un autre produit).
basiira g-
maturité, sagesse
Séy bu ànd ak basiira gu mat sëkk
une union où il y a une grande maturité.
batale
laisser un message à qqn pour un tiers
Batale naa la ak Omar
J'ai laissé un message pour toi à Omar.
batañse g-
pied d’aubergine
batañse g-
pied d’aubergine
batari b-
batterie
batik b-
(emprunt) Batik
bawol-bawol b-
originaire de la région du Baol (de Diourbel)
Bawol-bawol yee yore njaay mi
ce sont les ressortissants du Baol qui détiennent le commerce.
Ab Bawol-bawol la
C'est une personne rusée.
bawol g-
baol (région appelée aussi Diourbel Jurbel)
bax
bouillir
Ndox maa ngiy bax
L'eau est en train de bouillir.
(prov.) Cin, su naree neex, bu baxee, xeeñ
la marmite, si elle doit être délicieuse, quand elle sera en train de bouillir, elle sentira)
baxa
être bleu ciel
Mbubb mu baxa la sol
il porte un boubou bleu ciel.
baxa b-
grand boubou en basin bleu indigo
Paaseel sama baxa bi
repasse mon boubou en basin bleu indigo !
ballarñi
(champ d’arachide) Faire le troisième binage
Damay waaja ballarñi
je m’apprête à faire le troisième binage.
baxal
faire bouillir qqch
Damay baxal ndox
je fais bouillir de l’eau.
baaxental b-
commémoration
Sunu Baaxentalub moom-sa-réew la
C'est la commémoration de notre indépendance.
baxla b-
mulet mule
Jéndal baxla, moo gën
achète un mulet, cela vaut mieux.
baye b-
bahut, buffet bas
Defal weer yi ci baye bi
mets les verres dans le bahut.
bayliku
se laisser aller
Moom de dafa bayliku léegi
il se laisse aller maintenant.
baykat b-
paysan
Sama baay baykat la
mon père est agriculteur.
bayre b-
magnétisme qui fait que tout le monde s’intéresse à une personne attirance
Téere bii, soo ko takkee, dina la may bayre
ce talisman, si tu le portes, cela te donnera un fluide tel que tout le monde s’intéressera à toi.
baynàmmul b-
hilaire à moitié usé
Sa baynàmmul bee lay yeexal
C'est ton hilaire usée qui te retarde.
bëcci
se décharger de ce qu’on porte en le jetant par terre devant soi
Naka la agsi ci kër gi rekk, daldi bëcci sayu matt wa
dès qu’il arriva à la maison, il jeta à terre le fagot de bois qu’il portait.
bëccëg b-
jour (par opposition à nuit)
Guddi ak bëccëg, mu ngiy woy
nuit et jour, il chante.
Bëccëgu ndarakàmm
en plein jour.
béccngél
mépriser
Lu naqari la mu ma doon def, di ma ko yéjje ak di ma béccngél, moo tax ma tudde dëkk bi Njar-Meew
J'ai appelé ce village {Njar-Meew} (lait coupé) à cause des choses déplaisantes qu’elle me faisait pour me saboter (me démoraliser) et me mépriser
beddeeku
se mettre à l’écart
Bu amee ñam, dafay beddeeku
quand il a de la nourriture, il se met à l’écart.
bee
c’est le… qui…
Xale bee lekk ceeb bi
C'est l’enfant qui a mangé le riz.
bee
le
Nanu roñu bala nu fi taw bee fekk
plions bagage avant que la pluie ne nous trouve ici !
beeco b-
petit pagne qu’on porte sous les autres
Mu ngiy jaay ay beeco yu rafet
elle vend de jolis petits pagnes de dessous.
béej
avoir de l’urticaire
Dafa béej
il a de l’urticaire.
béeméer
brider un cheval sans lui mettre de mors
Soo amul ub laxaab, nga béeméer ko te dem; naaj na
si tu n’as pas de mors, tu le brides juste avec une corde et tu t’en vas; il est tard.
beeke b-
béquille
Dina doxe ay beeke ay fan
il marchera avec des béquilles pendant quelques jours.
beer b-
bière
Beer aka mëna féexal nak !
et pourtant, comme la bière est rafraîchissante !
béeru
uriner (rare)