wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Dafay béeru
Il urine
béer g-; b-
(flore) Sclerocarya birrea (Anacardiacées)
bëër w-
courbine, maigre (poisson)
bees
vanner
Demal bees, am na ngelaw léegi
va vanner, il y a du vent maintenant.
bees-bees b-
État neuf d’une chose état de fraîcheur d’une chose comestible
Ci bees-bees bi nga ko wara lekk
tu dois le manger pendant qu’il est tout frais.
bëgëj b-
purée de feuilles ou de fleurs d’oseille
Mënuma ko lekk su amul bëgëj
je ne peux pas en manger sans purée d’oseille.
bëgg-bëgg b-
désir volonté
Wax ma say bëgg-bëgg
dis-moi tes désirs !
(prov.) Nit ak bëgg-bëggam, Yàlla ak dogalam
l’homme et ses désirs, Dieu et sa décision)
bëggante
s’aimer mutuellement
bëgg-bëgglu
faire semblant d’aimer
bëgg-àddina
aimer la belle vie
bëgg-lekk
être gourmand, être glouton
bëgge
se dit de qqn qui veille excessivement sur ses biens, qui est trop attaché à ses biens
Dafa bëgge; bul laal weloom
il est jaloux de ses affaires; ne touche pas à son vélo !
beeñ b-
sable blanc et fin
Foo jéle beeñ bi, te demuloo géej ?
où as-tu pris ce sable blanc et fin alors que tu n’as pas été à la mer ?
bëj-géwél b-
chef des tambours
Géwél, ne ma naam, bëj-géwél, ne ma naam
griot, réponds-moi, tambour-major, réponds-moi !
béj g-
débat
bëj-gànnaar b-
nord
Mu ngi ci bëj-gànnaaru Senegaal
C'est au nord du Sénégal
bejjaaw b-
cheveu blanc
Kaay tànnal ma bejjaaw
viens m’enlever les cheveux blancs !
béjjén b-
corne
Dina la jéndal woto bu ganaar saxee béjjén
il t’achètera une voiture quand les poules auront des cornes.
(prov.) Béjjénu nag jégeñe na lool, waaye bu ñu laalee du sagos borom
s’il ne tenait qu’à nous, certaines choses ne se réaliseraient pas.
bëj-saalum b-
sud
Bëj-saalum taw na
il a plu dans le sud.
bëkk
avancer résolument
Ñuy bëkk di dem, wuti géej
ils marchèrent d’un pas décidé, se dirigeant vers la mer.
bekk b-
morceau (de sucre)
Suukaru bekk laa jénd
C'est du sucre en morceaux que j’ai acheté.
bëkk-démb
avant-hier
Bëkk-démb la ko jénd
C'est avant-hier qu’il l’a acheté.
bëkkëtal
faire passer un nouveau-né par le rite du {bëkkëtë}
bël b-
farine de mil obtenue au bout de six tamisages
bël b-
embouchure d’un cours d’eau
Doxantu nañu ba ca bël ba
nous nous sommes promenés jusqu’à l’embouchure.
bekkoor b-
famine
Ñàkkum taw bee waral bekkoor bi
C'est à cause du manque de pluies qu’il y a la famine.
belefete b-
cache-sexe féminin passant entre les jambes et retenu par une ceinture
Njegemaari tukulóor yi dañu daan sol belefete
les jeunes filles toucouleurs portaient des cache-sexe.
ball
jaillir
Boo fa demee, dangay gis ndox miy ball
si tu y vas, tu vois l’eau jaillir.
basi b-
gros mil, sorgho
Ren, basi rekk laa bay
cette année, je n’ai cultivé que du sorgho.
bëmb b-
blatèrement (dromadaire)
bembaxli
verser du lait dans la bouillie
Xaaral ma bembaxli soow mi, ñu lekk
attends que je verse le lait et que nous mangions !
bëmëx
pousser avec violence
Dafa ko bëmëx, mu feyyu
il l’a poussé violemment, il s’est vengé.
(prov.) Yebu ca, namm ca, ku la ca bëmëx, nga jél
tant mieux si on pousse à l’action qqn qui ne demandait que cela.
bëñ b-
dent denture
Ñaata bëñ nga am ?
combien de dents as-tu ?
(prov.) Géja gis sa màgget, bu mu tax nga defe ne sax na ay bëñ
il y a des choses auxquelles il ne faut pas s’attendre
bën-bën b-
trou
Bën-bën bi dafa sakku
le trou est bouché.
bëmëxante
se pousser mutuellement avec violence
beñe b-
beignet
Yaay, jéndal ma beñe
maman, achète-moi des beignets !
béngël j-
tamarin vert, non mûr
Fonde bi amul béngal
il n’y a pas de tamarin vert dans la bouillie.
benkeñenke b-
critique complications réflexions d’insatisfaction problèmes
Bu ma indil ay benkeñenke
ne m’amène pas de complications.
Kii dafa bari ay benkeñenke
il trouve toujours à redire, celui-là.
benn b-
num. Un
Benn bunt ak ñaari palanteer
une porte et deux fenêtres.
Benn la
C'est pareil (ou bien) c’est unique.
Benn lañu
ils sont semblables (ou bien) ils ne font qu’un.
Dinay am ci marse bi benn, benn
on en trouve sporadiquement au marché.
bënnu
se (faire) percer le lobe de l’oreille
Waxambaane yu bënnu
des jeunes gens qui se sont percé le lobe de l’oreille.
bëñ-teg g-
coin de selle
Jafandul ci bëñ-teg gi
accroche-toi au coin de selle !
béntéñe g-
(flore) Fromager
beñwaar b-
bassine, baignoire
Sama yaay jénd na beñwaar bu muy fóote yére nenne
ma mère a acheté une bassine pour laver les habits de bébé.
béj
débattre
ballarñi b-
(champ d’arachide) Troisième binage
Léegi ballarñi bi jeex
bientôt le troisième binage sera terminé.
bëqët b-
couard, poltron
Bëqët bi, ca xaj
poltron, au diable !
bër
arrêter les activités scolaires pour des vacances
Suba lañuy bër daara ji
C'est demain qu’on prend les vacances (scolaires).
Daara ji bër na; xale yi jàngeetuñu
L'école est fermée; les enfants ne vont plus en classe.
beral
mettre à l’écart pour qqn
Nanga ko beral lekkam
tu lui mettras sa nourriture à part.
beral loxo
faire un traitement de faveur.
ber b-
sable blanc à gros grain
Taamuwuñu ber bi ci tabax
on ne préfère pas le sable blanc à gros grains pour la construction.
bëre
lutter
Mënul bëre.
Il ne sait pas lutter.
(prov.) Kuy bëre yaay daanu
qui lutte, c’est toi qui tombes
bëre b-
lutte
Bàyyileen bëre bi
cessez de lutter
béréej
qui d’habitude met du temps à faire ses courses