wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Foo nekkoon ba nëgëni-sii ? Yaa béréej !
où étais-tu jusqu’à cette heure ? Tu en mets du temps pour faire tes courses !
bërëŋ
faire avancer une chose en la faisant rouler sur elle-même
Xàndi bi dafa fees; na ko bërëŋ
le fût est plein; qu’il le roule !
bërëm
griller du poisson dans le feu
Bu ñu amaan jén, bërëm ko ci tefes gi
quand nous avions des poissons, nous les grillions dans le feu, sur la plage.
bëret
exprime la manière de se lever brusquement
Mu ne bëret daldi daw wuti àll ba
il se leva brusquement et courut en direction de la brousse.
baaraamu-déy b-
pouce
Ci baaraamu-déy bi la dagg
il s’est coupé au pouce.
baane
avoir un rapport sexuel
Soo bëggee baane, takkal jabar
si tu veux avoir un rapport sexuel, marie-toi !
berkelle b-
tente
Nangeen samp berkelle yi bala muy agsi
vous dresserez les tentes avant qu’il arrive.
(prov.) Naar bu ndaw, lu mu wax, ca berkelle ba la ko dégge
le petit Maure, tout ce qu’il dit, c’est à la tente qu’il l’a entendu
bërlóor b-
circoncis qui vient de finir son initiation
Bërlóor yi lañuy fowal
C'est pour les nouveaux initiés circoncis qu’on organise des jeux.
bernde b-; g-
réception
Bernde bu mel nii, mësu fee am
il n’y a jamais eu pareille réception ici.
berndeel
organiser une réception en l’honneur de qqn
Sama doom laay berndeel
J'organise une réception en l’honneur de mon fils.
berngal b-
bout de bois qui sert à tendre les cordes du tambour d’aisselle
bernge
tendre les cordes du tambour d’aisselle
bés b-
jour (de la semaine)
Bésub pénc ba
le jour du jugement dernier.
Bés, dinga xam li mbokk di jariñ
un jour, tu sauras à quoi sert la famille.
Bés a ngi ci bés yi
je t’attends au tournant, un jour viendra.
bës-pénc b-
jour du jugement dernier
bëstandiku
prendre appui sur
Bu ma bëstandiku
ne prends pas appui sur moi !
bët-bëtóor b-
margouillat mâle en livrée nuptiale
Deru bët-bëtóor bee ka rafet
comme la peau du margouillat mâle en livrée nuptiale est belle !
baaxaay g-
la qualité
Baaxaayu liggéey bee tax ñu tànn woto boobu
C'est pour la qualité du travail qu’on a choisi cette voiture.
bët b-
œil
Bët yu réy la am
il a de gros yeux.
(loc.) Bëggul ku ko ne sa bët bi suuf a ngi ci
il ne veut pas qu’on lui fasse le moindre reproche.
(loc.) Bët sébbi na Saalum
La saison des pluies a commencé au Saloum.
(prov.) Bët baaxul, demal soli yére
l’œil n’est pas bien, va mettre un habit
(prov.) Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan
l’œil ne porte pas mais il sait ce que la tête peut supporter.
bélli
être accueillant, rayonnant (visage)
Kanam gi dafa bélli léegi
il a le visage rayonnant maintenant.
bëmb
blatérer (dromadaire)
Gëléem giy bëmb a ko tiital
C'est le dromadaire qui blatère qui l’a effrayé.
bew
fat
Moom de, dafa bew léegi
il est devenu fat maintenant.
betteex b-
plomb
Diigal bi, betteex la
le lest (de la ligne de pêche) est en plomb.
bëtu-tànk b-
malléole, saillie osseuse de la cheville
Dafa gaañu ci bëtu-tànk bi
il s’est blessé à la malléole.
bëy
avoir un panaris
Dafa bëy
il a un panaris.
bëy b-
panaris
Bëy la; boo yeboo teel ko faj
C'est un panaris; tu ferais mieux de le soigner à temps.
bëy w-
chèvre
Am na bëy wuy jooy
il y a une chèvre qui bêle.
Dañoo rey bëy wu
ñuul nous n’avons pas dîné (involontaire).
Bëy wéy na mbuus
L'occasion est ratée.
(prov.) Bëy wu ne am na ag déem
chaque chèvre a son jujubier
bibëroŋ b-
biberon
Bibëroŋ bi doyatu ko
le biberon ne lui suffit plus.
bar g-
grosse corde pour descendre dans un puits
Demal indil ma bar ga
va me chercher la grosse corde pour descendre dans le puits.
baar
mijoter
Wàññil xal yi, bàyyi cin li mu baar
diminue les braises et laisse la marmite mijoter !
bépp
tout
Muñ la Yàlla sant bépp jaam
Dieu ordonne à tout fidèle de patienter.
biig b-
la nuit dernière
Biig la ñów
il est venu la nuit dernière.
biij
faire osciller qqch
Bàyyil sa ndigg li ngay biij booy dox
arrête de marcher en roulant des hanches.
biiñ
faire la moue
Looy biiñ, ak kooy biiñ ?
qu’as-tu à faire la moue, et à qui fais-tu la moue ?
biiñ b-
vin
Duma naan biiñ
je ne bois pas de vin.
biir-a-biir
au fond
Puus ko ba ca biir-a-biir
pousse-le jusqu’au fond !
biir
dedans, intérieur
Mu ngi ci biir
il est dedans.
Def ko ci biir
mets-le à l’intérieur !
biir
être enceinte
Astu dafa biir
Astou est enceinte.
Yàq biir
avorter volontairement.
biir-buy-daw b-
diarrhée
Garab bu aay la ci biir-buy-daw
C'est un médicament efficace contre la diarrhée.
biiral
mettre enceinte
Ku ko biiral
qui l’a mise enceinte ?
biiw
voltiger autour d’une nourriture ou de toute chose qui attire
Dàqal weñ yiiy biiw yàpp wi rekk
chasse ces mouches qui n’arrêtent pas de voler autour de la viande.
bijjanti
reconduire un visiteur
Doo sax bijjanti Omar
et tu ne reconduis même pas Omar ?
bijji
répéter, redire
Bijjil wax ji nga waxoon
répète les propos que tu avais dits !
billaay
Je le jure devant Dieu
Billaay ! du man
je le jure ! ce n’est pas moi.
bilimbaane
donner la nausée
Akara bi dafa ma bilimbaane
les beignets de haricot m’ont donné la nausée.
Bàyyil bilimbaane nit ñi
arrête de semer la confusion entre les gens !
bëpp
perdre l’équilibre en étant déstabilisé à la base
Cin li bëpp na de, yaay
la marmite est déséquilibrée, maman !
Xaaral ba mu bëpp
attends qu’il ne soit plus en colère !